Umar Kan

Jóge Wikipedia.

Umar Kan (1932-2008) jangalekat la woon ak boroom xam-xam.

Jaar jaaram[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Kooku, 1932 la gane adduna, ca Kanel, dëkk bu nekk ci tund wu Matam, di jéggé dexug Senegaal. Umar Kan moo doon jiite la Faculté des Lettres et sciences humaines bu daara ju kawe gu Seex Anta Joob bu Dakar.

Dafa bokkoon ci ñu amoon xam-xam bu gëna mat ci cosaanu nguuru Fuuta Tooro, di dëkk bu am solo ci cosaanu tund wu dexug Senegaal, xam-xam boobu la yoroon tamit ci cosaanu lislaam ca Sowwu Afrig.

Bind na ay teere yu bare ci tëriit yooyu, rawatina teere bi nit ñi gëna roy ci li muy bind, La première hégémonie peule. Le Fuuta Tooro de Koli Tengella à Almaami Abdul, juge ci benn teereem bu mu bindoon ca uniwersite waaye soppi ko, di woon Le Fuuta Tooro à l'époque almamale.

Abdulaay Bacily, nekkoon na ndongoom.

Jangalekat la woon, ci li ñu naan École des Bibliothécaires, archivistes et documentalistes (EBAD).

Umar Kan, Tukkloor/Pël la woon, te gëstukat ak seetkat bu mag la woon ci lu jëme ci aadaak cosaanu askanu Senegaal.

Nitu lislaam bu mag la nekkoon, baayam mo ko yaar bu dëgër ci lislaam. Baayam itam a tax mu amoon pasteef bi ci lu jëme ci aaday Pëli / Tukkloor yi.

Ci atum 2000, gangooru uniwersite bi, magal neen ko ak Mélanges d'archéologie, d'histoire et de littérature offerts au Doyen Oumar Kane, ñu ko doon jagleel.

Umar Kan, gén na adduna ci weeru rakkaati-gàmmu atum 2008, ca Diiwaan yu Bennoo, fu ñu ko doon faj.