Ubbite
Xerawlu leen ma sadd fii baati wolof - miy sunu làkki maam ya déggatuñ ko faf
Ngirag ne sun jamono lañ xéy mbaanig - jànqe ko yaawur te rañaane kàcc nag
Te xéy ma ñépp këmm mbaa jupp la dal - ña jànq it seen diñe gaay seen wéttal
Gaa ya rañaan war ca galéemi fande ya - te xét fétal ca ñall yuy gòlliku ya
Ba génn kéewu dànna mom ëwoon na leen - ni dédd def xaloobi gaynde sange leen
Jéggi dayoom gu weesu lef moo ma ëlëm
- ma rët ba tax ma bëgg a dëflu cig woyam
Ngir dekkalaat ko koomu alkandeem ma wér - te suuxataat reen ya ba meññatam ma ñor
ñu raas ko, fuuyu ko te ràcc, def cifaay - yoor ca di fas dumóoyu lépp lëf lu aay
jafal la giim te taal ko ngënji muy bërëx - di lekk sun liw bi ba kenn dootu lox
ñu naan ci dex gi bàyyi tèpp-tèpp yi - ak dèq yeek ñunux yi, xunn-xunn yi
dëtëm ba màndi raggu bokkul ak di ñéer - ci lol dafay guusali put di yokku tér
masëy-bandaŋ wa wenn dooñ la tooyalul - waame wa mooy tooyali tool te koy ñoral
ba tax ma fëx àkki wolof ya jiitu woon - muy waxi sun maam ya dem ak ñii fi ne woon
waxiin ya laa jëlaat, fasoo ñu delsiwaat - te ñooy wolof yu wér ya, nar ñu dèkkiwaat
tudde ko mottaliy mebët yu’ñ sémb - ci dekkalaat baati wolof yuy démb