Aller au contenu

Téere Taariix

Jóge Wikipedia.

Taariixu àdduna bu bees bi te jamonoo Ag jiital

Teeree ngi nii buy gàttal yoonu xam, ndax li nga daa lijjantee xam ciy fan ak cib coona, moom la lay xamal ciy waxtu, ci lu dulub coona.

Muy bu nu def ngir feeñal ci baat ak waxiin yiy war a wuutu yu fraanse yu bari yu nuy teg ci barabi yu wolof yi, te kat fekk na wolof amoon leen mbaa mu manoon leen a am, te nu jàpp ne manunoo doylu wëlif leen. Ma yaakaar ne bu nu bëggee yombal dëgg, lu mu metti, metti, danoo war a wut ay kunaked babies in my asshole utlaay ñeel baati doxandeem yii bëgg a ruur sunu làkk wi, te nag yombug xam-xam mi ngi ci nga koy jàng mel ni jàngoo, kon lu tax muy français? Ginaaw du lu moy ab jumtukaay ngir xam, ngir déggante, waxante, te ma gis ne bu dee ci ay wolof seen làkk, lay gën a nekke jumtukaay boobu. Lii ak leneen lu bari, moo ma yobbu ci di xalaat ci di binde ci wolof, te ba yeneen kàllaama yi, ginaaw bindaluma ku leen moy. Te it nag ni ñepp def ba ami làkk lu tax dunu ko def bay am sunu yos ñun itam waa Afrig? Nekkewunu fi lu dul ligeeyal Tugal ak lu ni mel, nanu sunu bopp ñor ! doonte as lëf la it. Nan la am reew mu tollu ne Senegaal… ñépp di waxi wolof nga ne fraanse rekk ? reerale ga’a ngii ! i have a 1 incher

Abdul Xaadir KEBE





Bunt bu njëkk bi

Njëlbéenug jamono yu yees yi



• Yewwute’g Tugal gi • Wuññi yu juxraaf yi • Yëngu-yëngu yi daa kontar Egliis bu Paab bi










Doggantal gu njëkk gi

Yewwute ga amoon ca Tugal

"Yewwute" gu Tugal gi, baat la buy tekki - ci maanaa mu taarix mi mu yore - yëngu-yëngu gu dekkal ak yeesal, walla dundal xay gu Tugal gu yàgg ga ( gu klassik ga), gu Geres ga ak Rom . Rawati na ci wàlli njàggat , fànn ak tabaxiin .

Yëngu-yëngu googu nag mi ngi tàmbli ci xarnu bu fukk ak ñatt ginaaw juddu gu yonnant Yàlla Hiisaa, ba ci bu fukk ak juroom ñaar, mu sos fi nag ay soppi yu xóot ci wàllug aada, dundiin, mboolaay , politig ak koom-koom. Kon daal, "yewwute" gii amoon ca jamono yooya ca Tugal, li muy wund mooy ag tuxu juge ca jamono ju diggu ja ( mu'y jamono'y "ag laman" walla ag cang) dem ci jamono ju yees ji ( di ju jëm-kanam gu xam-xam ak xarala ).

Sabab yi tax Yewwute'g Orob gi am :

Sabab yi jur yewwute gii yu bari lañu, waaye nañu ci indi ñatt yi ci ëpp solo rekk, ñooy :

1 - Jeexiit gi xay gu lislaam gi def ci yewwute gii, 2 - Ak feeñug dëkk yu mag yi ci Tugal ( les villes), 3 - Ak neew-doole gu Egliisub Paab bi neewoon doole, ak tas gi mu faroon tas.

Jeexiit gi Lislaam amal ci yewwute'g Orob gi :

Ci waxtu wi Tugal nekke cig deltu ginaaw, ci wàllug xay ci jamono yu diggu yi, nga xam ne jàngu bi (Egliis bi) faagaagaloon na bépp xalaat bu leer te gore , araamal ci nit ñi ñuy xool leneen lu dul am njàggaleem mu way deng mii te doxadi, bi Orob nekke ci lëndëmam gii, jullit ñi ñoom ñi ngi doon jëm-kanam bu baax ci yekkati tabaxub seenug xay ci kaw ay cëslaay yu xam-xam ak wisaare maandute ak mbokko ci diggante nit ñi, ci lu dul xool xeet walla melo mbaaw làkk .

Xayug lislaam gi nag àgg na Tugal jaare ko ci yoon yu bari, bokk na ci yooyu, Andalusi ak Sisil ak reewi penkub lislaam bi, rawati na ci xarey jooñ yi

Ndax kat booy xool li Tugal di nekk lépp di ku ñu dàqe ca xarey jooñ ya, duma ko ca, teewul mu fàggoo ca njariñ lu bari ngir fenqoo gi mu ci defe ak xalaatub lislaam bi, ak nosteg dundam .

Lii nag ci li soppi xalaati waa-Tugal yi la jëm ci Egliis bi, nit, adduna bi ak dund gi.

Te itam lu bari ci sàkkukati xam-xami Tugal yi, dañoo tàmbli woon di naan ci xam-xami lislaam yi, ci ndoktoor, xeltu , gañcax ak ndundat , ak yu dul yooyu ci jàngu yu Andalusi yi, la ko dale ca xarnub fukk ak benn (g) .

Loolu nag taxoon na ba yëngu-yëngu gu firi walla tekki gu mag amoon ci xam-xami lislaam yi, tukkee ci làkku araab dem ci wu latin ( wi doon wu xalaat, wu diine, tey wu politig ca Orob ca jamono jooja ) loolu dimblee woon - ci ginaaw bi - ci lal yoon wi ba yewwute gu Tugal gi man'a am.

Feeñug dëkk yu mag yu Tugal yi ( les villes ):

"Nosteg laman" walla gog cang, ku ne xam na ne la mu baaxoo woon mooy tegu ci mbay, suuf, ak seqoo yu laman yi daa lijjanti ak'a nos diggante jaam bi ak sang bi.. ag laman nag - jullit ñi masuñu koo xam - nosteg koom-koom la tey gu mboolaay gu bon, daan gàllankoor xay gi ba du jëm kanam.

Bu ko defee, li ñuy wax "tool", di suuf si sang biy moom, moo daa tekki barabu dëkkuwaay bi, koom-koom bi, mboolaay gi, ci gii noste .

Màggug dëkki Tugal yi, ngir màggug yaxantu gi nu daa def ak mboolaayi jullit ñi, ak màggug mecce yi ak ligéey yi, ngir jòkkoo gi waa Orob gii daa def ak jullit ñi taxoon na ba nosteg laman tàmbli woon’a lòtt ak’a naaxsaay, rawati na bi nitug Tugal ki tàmblee am yoon wu mu man’a jaar bay dund te du sukkandiku - ci léppam - ci suuf ak tool, waaye ci yeneen ligéey yu koom yi.

Dëkk yi tam tàmblee doon barabi leer yu di boroomi xay, di sonnale ci loolu ak’a lakkal noste gu laman gi, tey ligeey cig màbbam, def it lu rëy ba yewwute ci Tugal man’a am.

Lòttug Egliis bu Paab bi akug tasam:

Egliis bi moo nekkoon di teg loxo ci dundug xalaat gi, gu diine gi ak gu aada gi ci Tugal gépp, te yitteem jépp mi ngi ko sotti woon ci njàngum pas-pasu diney nasaraan, walla li nuy wax "njàng yi aju ci Yàlla" (théologie), ak njàggat ak xellu , amutoon jenn yitte ci njàng yi aju ci xam-xam.

Egliis bi moom dafa jàppe woon boppam ki nga xam ne ci yoon moo war’a doxal mbiri politig yi. Te kat (moom Egliis bi) tawati mbon akug yàqu dañoo ruuroon aw yaramam, dugg ko fépp, ba waral aw nit wu jàng te yewwu jug, taxaw temb ci dañal ñaawteef yooyu ko taqoon. Loolu tam bokk na ci li jañoon xelum nitug Tugal ki ci mu jëm kanam, gën’a ñaw, rawati na bi dëkk yi gënee yaatu, deggiinu ligeeyub yaxantu gën fa’a xóot, ak bu endustri ak aada . Yii yepp nag ligeey nanu lu rëy ci waxuma la doyodil ngëb gu tar gi paab gi ngëboon mboolaayu Tugal gu nasaraan gi, waaye it doyodil nosteg laman gi, loolu it - di doyodil nosteg laman gi - rataxal yoon wi ba yewwute gi man’a am.

Itaali mberum yewwuteg Tugal gi:

Dëkk yu Itaali yi ñooy mber mu njëkk, mi njëkk’a uuf, tete yewwuteg Tugal gi, looloo waraloon ñu am wàccuwaay bu kawe akug wormaal ci yeneen dëkki Tugal yi ca jamono jooja. Dëkk yii niki Milano ak Venezia ak Firenze ak Napoli, ñoo uufoon yewwute gi, seeni boroom xam-xam aki njàggatkat ak artist walla waa fànn duggaloon nanu ci seen loxo bu baax .

Li waraloon loolu nag lu bari la, bokk na ci, dal ga fa amoon ak jàmm ja, ak jëm kanamug koom-koom ba, ak yaatug yëngu-yënguy nitu Itaali ki, ak ba tay yaatug goxi xalaatam, ak yëg gu mu yëg gore gu mu am, ginaaw bi mu goree ci nosteg laman, ak li Itaali yàgg’a am ci teddnga gu sax ak jaloore : mu'y njàggati waa Rom yi, seeni xam-xam, seeni jeexiit ak seeni fann , nga rax ci loolu nekk gi paab gi nekk Rom, nga xam ne loolu faggul na waa Itaali ag cang gu diine.

Ni nga xame ne barab boobu it (di Itaali) faggul na paab gi ci Itaali ag tono gu ne-ne ak gu maanaa gu mag, nga rax ci dolli gëpplante gu mag gi amoon ci diggante dëkk yu mag yi ak peeyi buuri Itaali yi, ci wàllug njàggat ak fànn ,ak soññ gi doxalkati dëkk yii ak buur yi daa def boroom xam-xam yi daa ligeeyal yewwute gi. Ak ba tay yittewoo gi nga xam ne amoon na ci dëkk yii, aju ci gëstu mbind ak taalif yu yàgg ya, ak barig móolukaayi teere yi ci yii dëkk. Ak nag li Itaali doon xéewoo, muy nekk ci barab bu raññiku, buy dimblee ci jokkoo ak addunay jullit ñi.

Mandargay Yewwuteg Tugal gi :

Yewwuteg Tugal gi, mi ngi ame ci mbooleem wàlli dundug nit, gu xalaat, gu fànn, gu politig, gu diine, ak gu koom-koom. Yii di ñëw ñoo ciy wàll yi gën’a rëy:

(1) Yëngu-yëngu yi aju cig "nite" :

Ag nite li miy wund fii mooy dundal njàggat yu yàgg ya ( yu Gres ya ak Rom), ak feddali sukkandiku gu nit war’a sukkandiku ci boppam, akug goreem ak sañ-sañu wax li nekk ci moom, ak dog gàllankoor yu mboolaay yi, ak jële fi aaday jamono yu diggu yi, ak sotti yitte yi ci adduna bi ak dénd bi , ak jeem’a xam seeni mbóot.

Yëngu-yëngu googu nag bokk na ci màndargay yewwuteg Tugal gu njëkk gi, ndaxte li mu yittewoo woon mooy xam-xam yu kojug nite yi nga xam ne njàggatkati Gres yeek Rom (grego-romain) ñoom lanu jëloon, yittewoo leen,ak seeni xeltukat ak seeni boroom xam-xam ak ñoñ fànn ak seen boroom mecce yu muus yi te ñaw. Boroom xam-xam yi daa def gëstu yooyu di kojug nite, ñi ngi leen di woowe ñoñ nite, walla boroom njàggat yi. Ñoñ nite kon ñooy mbooloom nit mi yittewoo woon jàng njàggat, xam-xam ak fànn yu yàgg ya (yu klaasik ya), maanaam njàggati Gres ak Rom ak seeni fànn ak xam-xam.

Yëngu-yëngug nit gii nag judd na, ginaaw bi mu amee ag jàpple gu tukkee ci kilifay dëkki Itaali yi ak seeni boroom alal. Ñoñ nite ñi génne woon nanu ab taar, feeñal ko ci mbooleem fànn yu wuute yi, moo xam yatt la, mbaa nataal, ak deseñ, ak misik, ak tabax. Ñoñ fànn ñu Itaali ñi ak ñu dul ñoom ci jamonoy yewwute, dañu doon roy fànn bu klaasik bi , di bu gres-rom bi, bàyyi nee nag fànn bi nu daa wax xóot , nga xam ne moo amoon ca Tugal ca jamono ju diggu ja . Bu ko defee, ñoñ fànn ñi jëmale seen fànn ci taarub dénd bi ak dund gu yees gii nga xam ne mooy gisiin wu jëm kanam wi nu am ci dund gi.

Dëkki Itaali yi gis nañu aw tabaxiin wu bees, ndax wacc nanu nee tabaxiinu xóot wiy am ay poto yu ñu catal, te weccee ko ak tabaxiin wu klaasik wi raññikoo ay poto yu am ay ndëpp yu rafet aki jagle mbaa deseñ yu eesañeri mel ne yi daa am ca tabaxiinu Gres wa. Tabaxiin wii siw na lool te tas ci Egliis yi ak katedraal yi, ak saal yi ak barabi tiyaatar yi, ak sangukaay yi .

Ci dëkki Itaali yii, lu bari ci waa-fànn yu siw yi fa lañu feeñe, bokk na ci ñooñu deseñkat bu siw ba, di Fra Angeliko ( 1400 - 1455 ), mi nga xam ne dees na ko lim mu bokk ci waa fànn yi raw te gën’a mag, ñi nga xam ne ñoo doon gëstu modeli fànn yu yàgg ya . Ay ligeeyam itam dañoo raññikoo woon màndargam diine mu dal, mu nekkoon moom ku diinewu.

Bokkoon na ci ñoom it Leonardo da Vinci ( 1452 - 1519 ), moom mi boole woon fànn ak xam-xam, defar nay nataali fànn yu siw, bokk na ci yooyu bi tudd reer bu mujj bi, ak Jokanda, walla Mona Liza. ñaari nataal yii ci yi gën’a siw lañu ci deseñi jamonoy yewwute. Da Vinci mii nekkutoon ab deseñkat bu aay rekk, waaye raxoon na ci dib yattkat bu mag,dib rëddkatu tabax te dib eesañër bu muus. Bokk na ci deseñkati Itaali yu yewwute gi ba tay ki ñuy wax Titian (1488 - 1572 ), moo nataaloon ay wàll ci dundug ñu féex ñi walla aristokraat yi ci dëkki yaxantu yi ak fànn yi, ak Rafayel (1493 - 1520 g ), moom itam rëddkatu tabax bu siw la woon, te di deseñkat bu bokk ci ñi gën’a siw ci mbooleem jamono yi.

Bokk na ci ñoñ fànni yewwute gi ci Itaali ba tay, yattkat ba Donatello ( 1386 - 1466 ) , mooy ki sukkandiku woon ci yattam ca yattiin yu klaasik ya, di gres-rom, rax ci dooli ku yittewoo woon taarub dénd bi la ak ag dundam. Moom daal ca dëgg-dëgg moom la nuy jàppe ki sos te taxawal yatt gu bees gi.


(2) Feeñug làkk yu bees yi:

Làkku Latin, ci jamono yu diggdoomu yi , moo nekkoon wa tasoon ca boroom xam-xam ya, ak niti diine ya, ak politgkat ya, ak njaggatkat ya ak ustaas ya. La notoon nag ca nit ña - di woon niti neen ñi rekk - ñoom déggunu woon wii làkk, lu tumbrànke la woon ca ñoom, seen làkki bopp yiy yu seeni barab lañu déggoon.

Bi jamonoy "yewwute" dikkee, ngelawul "fonk sa xeet" upp ci Orob gepp, la lu bari ci xalaatkat yi, ak njàggatkat yi, ak woykat yi, tàmblee jèng jëm ci bind ak taalif ci seen làkki réewi bopp, niki wu Itaali, wu Espaañ, wu Fraans, wu Angalteer ak yu dul yooyu.

Bi mu ko defee, woykatu Itaali bi tuddoon Dante ( 1265 - 1321 g ) taalif Komedi Bu sell bi ci làkku Itaali, naka noonu Petrarch ( 1304 - 1374 g ) mii nga xam ne li mu gisoon mooy làkku Romam wii daal mooy gën ja a kawey jumtukaay ngir génne xasiday woyam yi.

Bu ko defee Miguel de Cervantes moom itam def xisaam bu siw ba di (don kixota) ci làkku Espaañ, ci noonu it la Rabelais ( 1483 - 1553 g ) def, moom mi nga xam ne gisul lu gën làkkam wii di wu Fraans, ngir wuññi ci liy yëngu ci biiram, ci njàggat lu fees dell ak xoromu ak mbóosóor (kaf).

Chaucer mi dib angle ( 1342 - 1400 g) jug, moom itam, sotti ciw làkkam woyam yu yéeme yi cib taar, rawati na nettaliy Kentrebry yi, nettali yooyu ñoo ko def kenn ci woykati Angalteer yu mag yi, yi gën’a siw.

(3) Feeñug xeeti Orob yu yees yi:

Màggug fonk sa xeet ak sa reew ci Tugal, juroon na ci jamonoy yewwute, ay reew yu bari ci Orob taxaw, yu amoon "ag temb" ,ci noonu, yittewoo xalaati fonk sa xeet daal di fay feeñ, fés fa, lu aju ci "temb" tam di lu ñu fay waxtaane, ak àttewiin yi .

Looloo tax xarnub fukk ak juroom daa tàmblee dugg rekk, xataati politig yooyu ak yu dul ñoom tàmblee am ay maanaa yu nu man’a laal ci xeli lu bari ci nit ñi. Ci noonu xeet yu bari ci yu Orob yi, tàmblee feddali yooyule xalaat ci jëf, di goreel seen bopp ci toppub jàmbur, te jambur boobu weesuwul woon paab bi ak imbratoor bi Ay àtte nag yu Tugal yu am ay nekkte yu politig yu temb juddoo ci loolu ci ginaaw bi, yu am seeni làkki bopp yu yees, di ya nit ña daa waxe ay xarnuy xarnu waaye taxutoon ñuy làkki politig yi ak xalaat, lu dul ci jamonoy yewwute gi.

(4) Yëngu-yënguy dajale mbind yi:

Dëkki Itaali yi ak reewi Tugal gu sowwu gi ci jamonoy yewwute, dañu doon yittewoo dajale mbind yi ci fi ñu jortoon ne fi lanu nekk ci Xustantin ak ci dëkki Gres yi, ak ci yeneen barab yi ci Tugal, mbind yooyu ñu daa wër nag ñooy yu Gres yeek Latin, yi nekkoon di lu ñu tas ci kàgguy daara yeek egliis yi ak katedraal yi,ak ci nit ñi walla kër yi yittewoo woon mbir mii.

Peey yi daan àtte, dañu daa jagleel lii alal ju bari, ñoñ nite ñi tam ñu ci bari jëmale woon nanu seeni ligeey ci dajale mbind yi, ci noonu ñu jot’a am ci misaal rekk,mbindu’m binkat bii di waa Rom te dib xutbakat, tuddoon Quintilian (35 nj - 96 g) ak bataaxeli Cicero (106 - 43 nj) yu xutba yi, ak woy yu at-ba-at yu Tacitus yi(56 - 120 g) . Tacitus moomu mooy taarixkatu xeexi jarmaan yi, mi ngi bokkoon ci ñi gënoon a ñaw ci xutbakati Rom yi ak seeni njàggatkat yu ñaw yi.

(5) Sonn ci taarix ak jeexiit yu yàgg ya:

Yewwuteg Orob gi yittewoo woon na te sonnoon ci taarix ak jeexiit yu yàgg ya. Ag jublu gu yees am ci jàngiinu taarix, ñu koy teg leegi ci cëslaayu jam , waaye tegeesatu ko rekk ci dégg ak nettali, ci noonu ab jàngu sosu ci Firenze am njàngaleem jëm ci jam gu taarix , mu tudd daaray xam-xam bu taarix.

Bokkoon na ci boroom xam-xam yi ci gënoon’a duggal seen loxo, nitu taarix kii di Lorenzo Valla ( 1406 - 1457 g), mooy ki jamoon te diiŋatoon benn dosye bu taarix, sikkoon it ag wéram, mooy li ñuy wax "mayug Xustantin", mooy dosye boobu nga xam ne paab yi yàgg nañu cee sukkandiku, la ko dale ca xarnub fukk ak ñaar (g), ci seen xeex yi nu doon def ak buur yu mag yi ngir feddali ci seen àqi politig ci àtte nit ñi, jiite leen .

Bokk na ci ñi nga xam ne yittewoo woon nañu gëstuy taarix yi ak yu politig yi, bindkatu itaali bii di xalaatkat bu politig bu am diplomasi, di Nicola Michiavelli ( 1469 - 1527 g), Michiavelli mii def na teere bu mu tudde woon (buur bi), ndax da ci doon wax lu aju ci buur bu am doole, bu doon bennale dëkki Itaali yi, ak nguur-nguuraanam yu daggatoo woon yi te tas.

(6) Jëm-kanamug yaxantu ak endustri:

Yaxantu noyyi na bu baax ci Orob gu sowwu gi,dale ko ci njëlbeenug xarnub fukk ak benn g. Itaali fi mu feete dimbli na ko bu baax ci yëngu-yëngug yaxantu dox fa te jëm fa kanam. Ci noonu lonkoo yu yaxantu yi tàmbli fa’a sosu, di jëli marsandiisi penku yi, niki sooy, ak cuub yi ak rëndaay yi , ak wurus ak bëñu ñay ak yu dul yooyu, ginaaw bi it yii lonkoo - ginaaw bi ñu gënee jëm kanam – tàmblee yòbbu yii silaa ci yeneen dëkki Orob yi, bu ko defee bu ñuy dëpp di indaale marsandiisi Orob yi, niki ngëndal ak der ak firaa .

Jëm kanamug yaxantu googu ak gu meccey endustri yi, jur nañu ag xereñ ci denciinu alal, akug jëm kanam ci kee yi ñuy jëfandikoo ci jëfi yaxantu yooyu, ci noonu am mbooloom ay sandikaay mecce feeñ, mujj teg loxo ci ginaaw bi, ci fepp fu koom nekk, te am fa cawarte, naka noonu nu def ay ligeey yu mag ci wàlli mboolaay ak politig ak xalaat, raxaatal ci loolu juddug "maas gu diggu" gi ñooy mbooloo miy ligeeye yaxantu ak yeneen mecce yu wuute yi.

(7) Feeñug yëngu-yëngug xam-xam gu yees gi:

Yewwute gi ci njëlbeen gi dafa sotti woon yitteem ci dundal njàggat yi ak fànn yi, ginaaw bi mu dox as lëf ba àgg ci mbooleem lu xay gu mat laaj. Ci noonu yewwute gi matale mbooleem dundug mboolaay gi, bokk na ci, xam-xami dëppale yi , ndaxte xam-xam moom màggoon na ci dëkki Orob yi, jàngu yu mag yi sosu ci Orob gi rawati na ci dëkki Itaali yi. Yëngu-yëngug xam-xam googu mi ngi tàmblee ci di jeem a dundal xam-xam yu yàgg ya, ginaaw bi mu dox jëm kanam, loolu nag li ko waraloon mooy jariñu gi mu defoon ci yoonu xam-xam woowu di wu kojug nattu, maanaam lu nekk looy wax, nga teg ci sa loxo, mu leer la ne loolu la, nga doog ne moom la, ndax wóore na la ci làmb gi nga ko làmb ba daj ko, yoonu gëstu woowu nag, mooy wi boroom xam-xami jullit ñi jaaroon, ci noonu boroom xam-xamu fisiyaa bu Angalteer bi ñuy wax Roger Bacon ( 1220 - 1292 ) feeñ, di njiitul gëstug xam-xam ci Tugal .

Becon mii mi ngi sukkandiku woon ci yoonu jakkarloo ak nattu, ci gëstoom yooyu nga xam ne àggale woon nanu ko ci ay ngérte yu am solo ci xam-xamu bidiw, ak bu weer yi ak yu matematik yi, ak juxraaf .

Naka noonu boroom xam-xamu xeltu ak politig bu Angalteer boobu di Francis Bacon moom itam feeñ ( 1561 - 1626 g) , di koo xam ne dafa jëfandikoo xel ci àgg ci dëgg yu xam-xam yi , ci noonu ci gisiin, mooy ki teg ponki ngérum xam-xam mu bees mi, ak doonte moom doonul woon boroom xam-xamu dénd . Boroom xam-xamu Itaali bi, Leonardo da Vinci ( 1452 - 1519 g) moom tam feeñ , di kok dafa yittewoo woon jiyoloji ( bu mekanig) ak matematig, ak yu dul yooyu, nga rax ci dolli fànnu yatt, ak nataal, ak misik, ak eeseñëri, mu nekkoon daal boroom xam-xam te di nitu fànn , tey fentkat. Naka noonu boroom xamu Itaali bii di Galileo ( 1564 - 1642 g) feeñ , mooy ki njëkk’a defar nattukaayu tàngoor, njëkk’a fuglu bidiw yi ca fesalukaayam ba , dëgëral te feddali gisiinu boroom xam-xamu bidiw bu Poloñ bii, di Copernicus ( 1476 - 1542 g).

Bokk na ci màndargay xam-xam yeneen yu yewwute gi, fentug móolukaayu teere ci loxol nitug Almaañ kii di John Gutenberg, atum 1404 g, fent gii ak doonte gu Almaañ la, teewul jëmale na kanam bu baax dundug nit ci biir Tugal ak biteem. Wuññiy juxraaf yi tam ci màndargay yewwute gi la woon, ak yéwénalug diine gi ci Tugal. Nga dolli ci loolu feddali gu nitug Tugal ki feddali jëmmam jii nga xam ne yàgg na’a nekk di lu nu làq ci jamono yu diggu yi ci biir ay kureel , walla sandikaay mecce yi mu daa bokk ngir làqatoo ca ak aar njàriñi boppam.

Yewwute gi ci Itaali:

Yewwute gi ci Itaali daa tàmbli woon’a giim ak’a yànnjadi ci mujji fukk ak juroomeelu xarnu g, ak njëlbeeni fukk ak juroom benneelu xarnu g, loolu nag li ko waral lu bari la, ñu jéem cee indi yenn rekk yi ci ëpp solo:

1 - Song gu mbooloom xarem Fraans mi ak mu nguurug Rom gu nu sellal gi songoon dëkki Itaali yi, rawati na Rom ak dëkki bëj-gànnaar yi, niki Milano, loolu it taxoon na ba ñu giir dëkk yooyu, te Milano ak Rom jiitu woon ci. Ci noonu la yewwute gi delloo ginaaw ci Itaali ngir ñàkk gu fa jàmm ñàkk ak kaaraange ak dall.

2 - Jeex gu àtteg walla kilifteefug njabootug Madatsi jeexoon, ñooy buur yi daa sàmm yewwute gi ci Firenze , loolu nag sabab si mooy xuloo ak xeex gi amoon ci biir njaboot gii, te Firenze moo ëppoon solo ci barab yi yewwute gii nekkoon.

3 - Teg loxo gu buurub Espaañ bi Ferdinando, buurub Argon, defoon Napoli atum 1504 g, loolu bokk ci li neewaloon doole yewwute gi ci dëkku Itaalib bëj-saalum bii.

4 - Yëngu gi amoon ci jéem’a yéwénal diine ji ci Orob, ñi ko daa def di Luther,Kalfen, Swingli ak ñeneen, looloo taxoon paab gi jug ak doole ci kontar nite gi. Nga xam ne sax noonu gi àgg na ci paab bi tuddoon Kalimat mu juroom ñaareel mi, kompoloo woon ak buur bi Sarl 5 (Sarlkaan) buurub Espaañ bu katolig bi, ngir ñu fexee naaxsaayal yëngu-yëngug nite googu ci Itaali. Loolu mooy li waajal mbir yi, nooyal yoon wi ba “ëttu àttey lajmat" yi man’a am ca Esapaañ, di woon ëtti àtte yu siwe ay jëf yu ñaaw, daan sonnal ak a fitnaal képp kuy woote yéwénal, mbaa’g yewwute. Attekaay yooyu mosal nanu - ginaaw bu àtteb Lislaam dañee ca Andalusi te Garanada nërméelu, daanu - mosal nañu lu bari ci jullit ñi ay xeeti mbugal ak coona lu maneesul’a misaal, bokk na ci di leen lakk ñuy dund.

Tuxug Yewwute gi:

Ak li yewwute gi di neew doole ci Itaali lepp, taxul mu naaxsaay, mbaa mu suux, li am kay mooy da fa’a tuxoo dem ci yeneen reew yu Tugal niki Espaañ, Portigaal, Fraans, Angalteer, Holand, ak Almaañ, añs. Ay jëfka yu bari bokk nanu ci li tuxale yewwute gi jële ko Itaali yòbbu ko ci yii dëkki Orob, bokk na ci yooyu nekk gu yii dëkk nekk di yuy door’a noppi ci seenug sosu gu politig gu yees, ak tàbbi gu ñuy doog’a def ci jamonoy tabax ag xay. Ñi daa woote yewwute gi nag def nanu lu rëy ci tuxale ko Itaali mu dem feneen. Nitug Holand kii di Erasmus ( 1466 - 1536 g) moo tasoon te wisare yewwute gi ci Almaañ, jaarale ko ci def fa ay waxtaan aki xutba, ak ci yeneen dëkk yu Orob yi.

Erasmus mooy ki firi Injiil jële ko ci làkku Gres yòbbu ko ci wu Latin, jël nag li ñu ciy wax "kòllare gu yees gi" def ko ci ay làkki Orob yu bees, loolu bokk ci li feexal te goreel xalaatub Tugal bi ci ngartaajoo gi ko niti diiney katolig yi ngartaajoo woon. Loolu it won na waa- Tugal ne yaxub Injiilub latin, bi egliis bi yoroon du woon biy cosaan, te yax bu bari woon ay yàq la, kon daal Eramus mooy ki waajal xelum Tugal mi ci mu man’a nangu yéwénali diine yi.

Ni yewwute gi meloon ci fu dul Itaali:

Yewwute gi ca Almaañ dafa yoroon melow njàngat, wiy ligeeyal gëstuy diine yi (ci manaa daa yamoon daanaka ci lu aju ci diine rekk). Ca dëgg-dëgg, gëstu yi aju ci xam-xami Gres-Latin yi, dafa xawoon’a yeex’a àgg ca dëkk yooyu di yu Almaañ, ak li njiiti yooyu dëkk daa dimbli gëstu yooyu lepp cig wàll, ak li Almaañ doon am ay daara yu mag ci Vienne ak Idelberg ak Baasal ak Strasburg ak yu dul yooyu lepp, ci geneen wàll.

Yeex googu nag li ko waraloon mooy niti diine yi ak ñu dul ñoom ñoo ko nanguwutoon, ñoom daal danu fee nekkoon rekk di sàkku nu ñu tënke, te jéng yooyu njàng ak gëstu, te defi pexe ba du ñu tas ci anam gu yaatu, ngir nu wattoo ci seen kilifteef, sàmme ci seen daraja, aare ci seen ligéey. Ci noonu, danañu gendiku ne yëngug nite gi ci Almaañ dafa doon sori jubluwaay yu deet-diine yi , looloo tax du kiimaan Almaañ di woon barab bi uufoon yëngu yu yéwénali diine yi gënoon'a am solo ci Tugal.

Bu dee ci Fraans moom yewwute gi melow njàngat ak nite la fa yoroon, wi yittewoo woon xam-xami Gres yi. Ci noonu boroom xam-xami Itaali yi ak yu Gres yi taxaw ci wisaare gëstuy xam-xami Gres yi, ñu móol teerey ndonoy Gres yi ci móolukaayu Paris ba ñu taxawaloon ca xarnub fukk ak juroom benn g, ni nu duggale seen loxo ci amal ay akaadimi aki barabi xam-xam ngir njàng yi aju ci nite, niki bànqaasub buur bi ci Paris, ñu sos ko ci jamonoy Buurub Fraans bi, di Fransuwaa mu njëkk mi atum 1540 g.

Bu dee ci Angalteer, ba tay yewwute gi ma nga fa yoroon melow njàngat ak nite. Ay gëstu yu xam-xami gres yi am fa, ay ñoñ nite ñu waa reew ma, ñu bari ñooy ña ca siwoon, ñoom ñooy ñi daa jàngale làkkuw Grees wi ci daaray xam-xami Itaali yi, ku ci mel ne Wilyam Lilly mi daa jangale làkkuw Gres ca Rom. Erasmus mu Olaand mi ak Kolt mu Angalteer mi, ñoo tekki woon Injiil ci làkkuw angale wu bees wi. Buurub Angalteer bi, Henri mu juroom ñatteel mi, moom tam sosoon fa juroomi toogu yu darajay ag ustaas ci xam-xami pas-pasu nasaraan ak yoonu siwil ak wu dénd bi ak làkku ebrë ak wu Gres ci daara ju mag ju Kembrij. Jàngub San Pool bi nekk London moom it jagoo woon njàng yu nite yi.

Yewwute gi ci Angalteer dafa jublu woon yoonu takk ak boole diggante pas-pasu nasaraan ak gëstuy nite, yu njàngat ak yu fànn yi. Yewwute googu nag indiwul woon lu yees, lu ñu fent, ndare ci xarnub fukk ak jurom ñaar g, bi am njurum njàggatam ak mu niteem mu yees feeñee ci anam gu fes te rafet ci woyi William Shakespeare yi (1564 - 1616 g ) ak woykat bu silmaxa bii di John Milton (1608 - 1674 g ) ak ñu dul ñoom ñaar.

Fii tam ci Angalteer yoonu yewwute gi da fee jengoon as lef jëm ci yewwute gu xam-xam, gu aju ci xam-xami dëppale yi walla xam-xami nattu, yu làmb yi. Ñi jiitu woon ci lef moomu, ñooy ñaari boroom xam-xami Angalteer yii di Roger Becon ak Francis Becon, ñoom daal ca dëgg-dëgg ñooy ñi sos daaray xam-xam ca Angalteer.

Baat bi nuy mujj a wax ci yewwuteg Tugal gi, mooy moom daal moo ñàkkal jamono yu diggu yi kàttan ci jeexiital ci mboolaayu Tugal gi ci wàlli dundug politigam, gu mboolaayam, gu xalaatam ak gu aadaam .

Ngir jeexiit yii fi yewwute gi sotti ci Orob, ay noste yu yees am nañu yu làmboo tabax guur gu yees gi ak mboolaayug Orob gi ci cëslaay yu aada, yu mboolaay, yu jikko, ak yu ngér yu yees, ni mu duggale loxo ba tay ci ubbi ay gox yu yees yu xam-xam, yu jël gisiini xam-xam yi ak dal yu xam-xami juxraaf yi. Lii lépp nag moo sabab jamono ju yees ci Orob,di ju wuuteek ja woon (ca jamonoy laman) ci xalaat, ak ngér ak defiin aki xew-xew. Loolu lepp nag nga boole ko, moo jur jamonoy Tugal ju yees jii.

Doggantal gu ñaareel gi:


Wuññi yu juxraaf yi  :

Luy wuññi yu juxraaf yi ?:

Yëngu-yëngu gu wuññi gu juxraaf, walla feeñal gu juxraaf, yëngu-yëngu gu yàgg la. Waa-Isipt ñu njëkk ña ak Finiix yi ak jullit ñi defoon nañu ko bu yàgg,njëkk waa-Orob di ko def ci jamono ju yees ji. Lu am soloo ngii nag ñu war koo xam, mooy wuññi'y juxraaf yi, bi muy am it li ko taxoon’a jug mooy ay xemmemteefi sañc , ak doonte daa mbubboo woon gëstu gu aju ci xam-xamu juxraaf.

Yëngu-yëngu gu wuññi gu juxraaf gi ñuy waxtaane ci doggantal gii, da nanu ko man’a xamalee ci nii: mooy mbooloom ligeey yi jéngukat yu Tugal yi daa def ci ñaari xarnu yii: bu fukk ak juroom ak bu fukk ak juroom benn g. Yenn nag ci réewi Tugal yu nasaraan yi, ñoo leen doon soññ ak’a jàmbaarloo ak’a xiirtal ci loolu.

Li sabab wuññi yii:

1) sabab bu diine:

Sababu diine moo jiitu ci sabab yi waraloon yëngu-yëngu yu wuññi yu juxraaf yu Orob yii am. Sababu diine mooy li gën’a waral ñaari reewi katolig yii di Espaañ ak Portigaal defoon ligeeyub wuññi boobu. Ñoom yile ñaari reew dañoo jortoon ne dananu man’a sutuxlu ci biir Afrig ak fu dul moom, def ko barab bu dëppoo ak li ñu bëgg muy tas fa ag katolig, ak nangu ko teg ko loxo jaare ko ci diine. Reewum Portigaal moom daa gisoon ne reewum Ecopi, - mii di mu nasaraan, waaye di mu yoroon ngérum xibt, mu ortodoksi - man na koo soppi def ko mu yor ngérum katolig. Loolu nag da nga ci gise diinewu gu dëgër gi amoon ci waa-Espaañ ak waa-Portigaal ca jooja jamono. Paab gi moom da daa soññ reewi nasaraan yi ci ñu dugg bu baax ci wuññi yooyu, ngir tas ag katolig, ak xatal Lislaam te sonnal ko,tee koo tas, ngir neewal dooleem, xottite ko,giir ko.

Ci noonu mu ( moom paab gi) génne ay mbind yuy jox àq ñaari reew yii ci ñu moom gox yu yees yi ak mbooleem yu nu wuññiwaat, moo xam geej yi la mbaa jeeri yi. Paab gi ak nasaraan yi ci ginaawam, dañoo ragaloon lislaam ak ñoñam, looloo taxoon ñu daa wut nu ñu mucce ci ñoom, ñu ne woon kon nanu leen fi jeem’a jële.

2) Sababu politig:

Am na yeneen reew yu yees yu feeñ ci ëttub politig bu Tugal bi, yu ci mel ni Espaañ, Portigaal, Angalteer, Fraans, Holand ak yu dul yooyu. réew yii nag, dañoo tàmbli woon di xalaat bu baax ci tas ak wisaare seeni kilifteef ak jeexiit ci biti seen, rawati na ci reew yi ci yeex ci seenu'g nekku walla sosu gu yees. ñu gisoon it ne bu ñu fa tasee, wisaare fa seeni xay aki ngéri diine,loolu da na man'a nekk ay raas yu ñu man'a jaare ngir sampu fa, sanc leen . Reew yii nag joŋante woon nañu te gëpplante ci mii lef , loolu bokk ci li daa soññ ak’a xiirtale ci yëngug wuññi gu juxraaf gi.

3) Sabab bu koom-koom:

Waa Orob yi ñoom dañoo gisoon ne addunay jullit ñi daal,mooy ji ngëp ci loxoom nosub yaxantu bi, ndaxte ñooy ñi notoon, tegoon loxo ci kaw yooni yaxantu yu penku yi. Ci noonu xalaatu wacci fi yooyu yoon, te gëstuji yeneen yu leen man’a àggale End ak Siin tàmblee feeñ, ngir bañ’a fay njëgi nduwaañ yi ak galag yeek yeneen yi cig wàll, ak ngir neewal doole koom-koomu jullit ñi ci geneen wàll, ginaaw bi ñu soppee yoon yooyu def leen leegi ñu jaar Afrig ak màmbulaan gu atlas gi , loolu lépp ngir bañ’a jaar fi jullit ñi dëkke.

Yenn ci réewi Tugal yu yees yi dañoo gisoon ne li gënoon ci ñoom mooy seeni séqoo yu yaxantu ak réewi penku yi, ñu koy defal seen bopp, ngir mucc ci rënkug yaxantu gii dëkki Itaali yi ame woon te daan ko def, yu ci mel ni Venezia ak Genova ak yu leen moy. Xalaat bii nag taxoon na ba yii réew demoon gëstuji aw yoonu yaxantu wu bees, nga xam ne ñoo ciy nekk ci wenn waxtu wi di yaxantukat biy jëli ,tey tuxal, tey kiy dox ci diggante yi.

Lori waa Orob yi tàmbli woon na’a yol, bi ñu déggee xibaari wurus ak xaalis ci Afrig, ndax kat mbell yu gànjaru yi dañoo muuroon seeni gët, fees seeni xel, ñoom ñi nga xam ne dañoo tàmbli woon di faale ak a yittewoo wàllug ne-ne gi rekk, bayyi nee yeneen wàll yi, loolu moo tax ñu sawaroon lool ci def wuññi gu juxraaf gi bi ñu déggee tono gu ne-ne gu rëy gi nga xam ne am mbooloo ci wuññikati Orob yi ndàmmoon nañu ko ci seen tukkiy wuññi yooyu, rawati na bi ñu jàngee xisay tukkikatu Itaali boobu di Marco Polo (1254 - 1324 g ), mi wuññiji woon ba Siin (1271 - 1275 g ), nga xam ne bi muy dëpp, daa indaale lu sakkan ciy doj yu tedd , ba mujj waa Venezia daa ko wooye boroom milyoŋ yi .

4) Sababu xam-xam:

Xalaat yi boroom xel yi ci Tugal amoon ci suuf si, ak bindam dafa soppiku woon, ginaaw bi ay tukki yu juxraaf yu kenn-kenn amee ak yu mbooloo yu nasaraanal ,juge Orob, génn, rawati na ginaaw bi jamonoy xarey jooñ yi jàllee, nga xam ne boroom xam-xam yu bari leegi dañoo am koolute ci ne suuf si dafa bulu walla mu mel ni ab kol-kol, wuute ak la ñu jàppoon, gëm ko, muy dafa tàllaliku mel ne basang gu ñu lal, loolu nag mooy li muuroon xeli waa Orob yépp ci jamono yu diggu yi. Ag jèng jëm ci sopp ag jéngu , ak bëgg xam-xamu juxraaf, feeñ ci ñoom, ginaaw ba fa ruug gëstu gu xam-xam gënee suuxatu, gën fa’a jëme kanam, ak li ñu jële ci jullit ñi - ci biir xeexi jooñ yi ak ginaaaw bi - ci xam-xam bu juxraaf bu jëm kanam, ak ginaaw bu xam-xamu bidiw ak ligeeyiinu gaal ak buusal biy won gaal yi seeni yoon gënee jem kanam.


Wuññiy juxraaf yu Portigaal yi:

Portigaal moom la ñu’y jàppe reew mi jiite woon wuññi yu juxraaf , yu Orob yi. Buur bii di Henri, mi nekoon ab mool (1394 – 1460 g ) , doonoon doomi buur bu Portigaal bi tudoon John mu njëkk mi, moom mooy ki njëkk’a def ay wuññi ci waa Portigaal yi. Mu nekkoon ku soppoon dugg geej, ak yër xisay mool yi, ak teerey taariix yi . Muy ku aayoon ci rëdd karti juxraaf yi , moom la baayam sàmpoon mu yor Sawuta , ginaaw bi ñu ko nangoo ci julliti Marog yi atum 1415 g.

Henri daa xalaatoon’a wesaare diine’y nasaraan ju katolig ji ci Afrig, ci noonu mu ne kon na jokkoo’k buuru nasaraan bu Ecopi bii di Prester John, ngir ñu ànd, xeex waa Marog yii di ay jullit cig wàll, ak ngir man’a àgg ca waaxi geej gu xonq ga ci geneen wàll. Ci noonu mu yabal ay mool yoy ci seen tukkiy wuññi yooyu, àggoon nanu ba ca duni Kanaari ya , ak Madira ak Osoras ci Mambulaanug Atlas , atum 1402 g, naka noonu ñu wëy ci seen tukki yooyu ba agsi Senegaal, atum 1445 g, ginaaw bi Henri deewee tam teewul seen tukki yooyu wëyoon ba ci sottiwaayu dexug Kongoo gi ak Niijer. Bu ko defee mool bii di Bartholmew Diaz, moom àgg ba ca wàllug bëj-saalumu Afrig, di fa ñuy wax Boppub Callmeer, atum 1486 g, moom la buurub Portigaal bi soppi tur wi tudde ko « Boppub Yaakaar Ju Baax Ji » ngir mool yooyu man cee ame yaakaar ba man’a wuññi yoonu yaxantu wi jëme End. Mool bu siw bii di Vasco De Gama moom, jug def tukkib wuññi, atum 1497 g, daal di àgg End, ginaaw bi mu wëree Afrig jaare ko ci yoonu tefesug Marog gi, romb Bopp Yaakaar Ju Baax Ji, ak Mosambig ak Mombasa ak Malandi, ba àgg (Jawa) ca tefesug sowwu gu daanaka dun bu End. Vasco De Gama mii jot naa xamante ak Ahmadu’bnu Maaja mii di woon ab mool bu jullit bu araab, moo ko dimbli sax ba mu man’a àgg End, ndaxte mooli jullit ñi ñu xamoon geeji penku yi lañu woon, ak yooni yaxantu yu jéeri yeek yu geej yi. Naka noonu beneen mool jugati bu tudd Kabraal, def ab tukki bu geej bu aju ci xare, dem End ,tàmblee naj ak’a sonnal Samirin,mi daa àtte ak’a saytu fi nuy wax Kalikuta gu End gi, ngir mu jox Portigaal ab barab bu yaxantu ci tefes gu sowwu gi, Kabraal mii xeex na fa’ak jullit ña, song barab ya ak mbooloo’m gaalam ma. Vasco De Gama moom itam delluseeti End ci ab tukkib xare ngir faagaagalsi Samirin, ak mbugalsi yaxantukati araab yu jullit yi, ak defsi ay déggoo ak buuri goxi End yi nekk ci tefesug sowwu gu daanaka-dun bu End bi.

Li wuññiy juxraaf yu Portigaal yi jur :

Wuññiy Portigaal yi jur nañu ay ngérte yu bari, yi ci ëpp njariñ ñooy yii di ñëw :

1) Waa Portigaal, ñi ngi tàmbli woon di teg loxo ci tefesi Afrig yu sowwu yi, ci noonu njàppum jaam siw, te tas ci Orob gépp, di jaam yi ñu daa jàppe Afrig, te daan ci yaxantu.

2) Jamonoy sanc gu Portigaal , mi ngi tàmblee ci bi Portigaal taxawalee ab sancu , ci penku bi, ca fa ñuy wax Jawa, ay xare it am diggante araab yu jullit yi ak Portigaal cig wàll, ak ci diggante waa Portigaal ak waa End yi ci geneen wàll. Waa Portigaal yi nag jot nañoo teg loxo yenn waax yu am solo yi nekkoon ci yoon wi jëme End.

3) Waa Portigaal yi mujj nañu xam yoonu yaxantu wu geej, wu dul romb ci reewi jullit ñi,mooy wi jaar ca Boppu Yaakaar Ju Baax ja .

Loolu nag mooy li doyadiloon koom-koomu jullit ñi ci penku bi, maanaam koom-koomu nguurug Mamaalik ci jëmmi boppam. Lii moo taxoon nguurug Mamaalik mujjoon neew doole ci kanamu nguurug Portigaal gi ak ci kanamu ñoñ Usmaan ñi nga xam ne jot nañoo fexe ba xaw’a woyofal naj ak ñàkkal jàmm gi Portigaal defoon araab yi, ak nguuri araab yi nekkoon ci tefes gi, yàqoon nañu it mbooleem jeem yi ñu daa def ñoom waa Portigaal ngir taxawal ab jë bu nasaraan kontar doole yu lislaam yi nekkoon ci peggu geej gu xonq gi, ak tefesug Afrig gu penku gi.

Wuññi yu juxraaf yu Espaañ yi :

Li ci duggaloon Portigaal, moo duggal it Espaañ ci wuññi yooyu. Ci noonu boroom xam-xam yi daa yëngu ci mbiri wuññi gi, danoo jàppoon ne suuf si daa bulu, moo waraloon ba ñuy dem End ñu jaare woon ko ci sowwu bi.

Moolub Itaali bii di Cristoforo Colombo (1451 – 1506) moom defaloon na waa Espaañ ñi benn tukkib wuññi atum 1492 g, juge Espaañ jem End jaare ko ci sowwu bi, ci màmbulaanug atlas gi. Ginaaw tukki bu tar te sonnle, moom Colombo àgg na ca duni Bahama ya mu mujjoon’a tudde San Salvador, juge fa dem ca tefesug Kubaa gu bëj-gànnaar ga ak dunub Ayiti bi mu faroon tudde Espaañ gu ndaw gi.

Mu delluwaat nag Espaañ ci atum 1493 g, ànd ak jort ne moom de jot na’a àgg End ci yoonu sowwoom woowu. Ci atum 1493 g, Colombo defaat na ab tukki, bu li ko taxoon’a jug mooy teg loxo ci suuf yooyu mu jotoon’a wuññi ci atum 1492 g, ak wisaare fa katolig, ca ña fa dëkk te mu tudde woon leen ay « endo ».

Ci tukki bii la jotoon’a wuññee Jamayka, daal di delluwaat Espaañ ci atum 1496 g. Mu defati ñatteelu tukki atum 1498 g, waaye amu ca woon tawfeex. Mu dellu defaat bu ñeenteel atum 1502 g, taxul ba tay mu am ca la mu ca doon wut. Bu ko defee nag ñaari sooy yii mu def ci ñaari tukkeem yi tax ba buuru Espaañ bi Ferdinand ak soxnaam lingeer bi Isabela, begadi woon ci loolu, ag siwam suux, ñu folli ko ci njiitul geej gi, daal di koy delloosi Espaañ ci ay jéng, ngir mere gu ko meññilukat yi mere, ñoom ñi seen yaakaar tas. Colombo faatu na atum 1506 g, te xamul sax ne wuññi na adduna ju yees ju dul End.

Ginaawam it wuññikat yi doon ligeeyal Espaañ wëy ci seen ligeeyi wuññi yooyu , ka cay Amerigo Vispucci jot ca’a àgg ca gox ya Colombo àggoon ak yeneen yu mu àggutoon, ci njëlbéeni xarnub fukk’ak juroom benn. Moom mool bii di Amerigo, moo am teraagay ñu tudde ko Adduna bu bees bii di Amerig tay.

Li wuññiy Espaañ yi jur:

1) Ñoom de ubbil nañu tukkiy wuññi yi aw yoon wu bees wu jëm ci àdduna ju yees ji, di ko jaare ci màmbulaan gu atlas gi . Bu ko defee Espaañ tàmblee sanc gox yi mu jotoon’a àgg ci Amerig gu diggu gi ak gu bëj-saalum gi, ñu wisaare fa seenug xay ak diine, ubbi fa ay mbelli wurus ak xaalis.

2) Saxal gu ñu saxal ci xam-xam ne suuf si daa “bulu” , te li waraloon loolu di tukki bi Magellan defoon. Buur bi ñu daa wax Shark mu juroomeel mi (Sharlakaan) di woon buurub Espaañ, daa digaloon mool bii di Magellan atum 1519 g, mu def ab tukki jëm penku jaare ko sowwu, ci noonu moom Magellan jug, war geej, jawali sowwu, te jëm penku, ci kaw màmbulaan gu atlas gi, bi mu ko defee daal di àgg ca tefesug Braasil ga, fa Riyo De Janero, mu wëy nag ca doxam ba, ba ca sottiwaayu dexug Labalata, daal di wër Amerig gu bëj-saalum gi, tàbbi màmbulaan gu dal gi nga xam ne moom moo ko tudde « pasifik » di wund lu dal, mu àgg Filipin atum 1521 g, foofa nag mu songoo fa’ak ñoñ réew ma, ci’y xeex yoy ca la ñu ko raye, waaye kenn ciy nitam, tuddoon Dianco, moo mujjoon jiite boobu tukki, dem ak ñoom ba ci boppu Yaakaar Ju Baax ji, juge fa dem Espaañ, gi nga xam ne ma nga fa àgg atum 1522 g.

3) Weddi gisiin yi daa wax ci bindu suuf si ak ab kemam ( ni mu tollu), ndax kat tukki bii nga xam ne dafa dox, wër àdduna bi, firndéel na ne suuf si daal moo ëpp fuuf li ko Colombo jàppe woon ak ku dul moom. Beneen gox feeñ na, bu mag diggante Orob ak Asi ci wàllug sowwu gi, di Amerig gu bëj-gànnaar gi, nga rax ci dooli geneen gi’y gu bëj-saalum gi, te ag màmbulaan gu yaatu, gu yees’a ngii gu ñu xamutoon. Kon suuf desatutoon su ñu xamutoon su dul Ostrali ak ñaari xutbu yi .

Wuññi yu Angalteer:

Ñoñ Angalteer ñoom itam sóobu woon nañu ci wuññi yi, bi Buur bi Henri mu juroom ñaareel, mi nekkoon buurub Angalteer digalee mool bii di John Cabot, mu tukki dem End, jaare ko bëj-gànnaar gu suwwu gi, ca saa sa mu geeju, tukkee Bristol atum 1497 g, jéggi màmbulaan gu atlas, àgg tefes gu bëj-gànnaar gu Amerig gu bëj-gànnaar gi, ca New Fondland, ginaaw bi mu jéggi Librador, dellu Angalteer. Cabot mii delseeti na leru tefesu’g penku gu Amerig gu bëj-gànnaar gi, ba àgg Florida, loolu nag moo doonoon tàmblig sancug walla koloniiseg waa Angalteer yi, ñeel Amerig gu bëj-gànnaar gi ak Kanadaa . Ba tay it, kii di Jams Kook di woon ab mool bu dëkkoon Angalteer, defoon na moom it ñatti tukki yu wuññi ca tefesi Ostrali yu penku ya ak Newsiland.

Wuññiy Fraans yi :

Waa Fraans nag ñoom, ñoo mujjoon’a duggsi waa Angalteer, waa Espaañ ak waa Portigaal ci lefum wuññi mi, ñoom seeni tukkiy wuññi daa jemi woon Kanadaa. Ki ñuy wax Jaak Cartier moom ab mool la woon, daa jugoon def benn tukkeem bu wuññi ci jamonoy Fransuwa mu njëkk mi, jeggi màmbulaan gu atlas gi, jem sowwu, fetali àdduna ju yees ji. Ci noonu mu àgg New Fondland gi jàkkaarloo ak Kanadaa, daal di fay jot’a wuññi walla feeñal sottiwaayu dexug Santa Lorans. Tukki yi Cartier mii jot’a def ci goxi Amerig gu bëj-gànnaar gi ñeent lañu woon. Bi mu ko defee sancug Fraans tàmblee putuxlu ci Kanadaa, ak goxi dex yi ci Amerig gu bëj-gànnaar gi. Noonu ñu taxawal ab sancu tudde ko Samwel de Shampala, taxawal it dëkk bii di Kebek ci tefesug dexug Santa Lorens atum 1608. moolu Fraans bii di De Laasal jotoon na’a wuññi dexug Misisipi, ci noonu waa Fraans ya daal di fay sos sancu walla koloni bu Luwisiyaana, bii nga xam ne mi ngi jële turam wi ca buurub Fraans ba tuddoon Luwis mu fukk ak ñeenteel mi.

Wuññi yu Oland yi :

Lonkoo gu End gu penku gu Oland gi, dafa joxoon ndigal moolub Angalteer bii di Henry Hadson, da ko’o joxoon ndigal ci mu defal Oland ab tukkib wuññi, ngir man koo gisal aw yoon wu bëj-gànnaaru penku wu ko man’a àggale Asi, ci noonu mu geeju moom Hadson juge Angalteer, jaare ko ci bëj-gànnaaru atlas gi, jawali golofub New York, ak dexug Hadson gi mu tudde woon boppam. moolu Oland bii di Wilyaam Shotin moom, moo wuññi yoonu boppub Horn bi nga xam ne mujj na di yoonu geej wu am njariñ. Waa Oland yi jeemoon naño’o wuññi Ostraali ak Newsiland ci diggante 1622 – 1624 g .

Li wuññiy juxraaf yu Orob yi jur :

Li wuññiy Tugal yi jur man nanu koo tënk ci lii di ñëw :

1) Njiitug yaxantu gi tuxu na tukkee ci li wër geej gu diggu gi dem ci màmbulaan gu atlas, mu mujj moom yaxantu gi nekk ci loxoy reewi Orob gu sowwu gi, bu ko defee ñu nos fi ay yooni geej yu yaxantu ci ñaari màmbulaan yi, gu atlas ak gu dal gi (pasifik). Yëngu-yëngu gu yaxantu gu yees gii, ñi ngi ko tudde woon « soppi ci anamug yaxantu » .

2) Wuññi yu juxraaf yi amal nanu fi jawwu yu gëpplante ak wujje, ak as lef cig noonoo ci diggante reew yi doon def wuññi yii, loolu moo yokkoon xemméemtéefi sanc yi ci diggante reewi Orob yi. Ci noonu aw gisiin wu sanc tàmbli woon’a feeñ wu Orob jëm ci askani reew yii ñuy door’a wuññi.

3) Xam-xami juxraaf yi soppiku woon na bu baax, li ko waraloon di yaatu gi wuññi yii yaatu woon te bari. Ci noonu yëngu-yëngu gu nasaraanal yokku ci anam gu fés, rawati na ci Afrig ak ñaari Amerig yi.

4) Ag jëm kanam feeñoon na ci wàllug yaxantug mbèll yi, di wurus ak xaalis, nga xam ne sax xarnub fukk ak juroom g, danu koo tudde woon « xarnub xaalis », ni nga xame ni jëm kanamug koom googu taxoon na ba dundiin wi gën’a kawe, njëg yi it gën’a yekkatiku, ni fi ay njaay yu yees dugge, lu ci mel ne kakawoo, poon, kiinaa, batata ak mbòq .

5) Wuññi yi de lenn lanu ci màndarga yiy wone yewwuteg Tugal gi, ni nu la ko leerale woon ci doggantal gu njëkk ga.

6) Reew yii ñu wuññi, ruu gu fees ak bëgg’a fayyu moo leen ubale woon, muur leen, jëm ci yii leen wuññi, ndax ñoom tubaab yi xalaati sanc lanu yoroon, daan ci doxe ci mbooleem seen doxi wuññi yi, lepp lu nu gis aakimoo ko, ngartaajoo ko, lii mooy li waral askani reew yi nu wuññi, jugoon ci jànkoonte ak ñoom, taxaw ci xeex canc gu Tugal gi, ci anam gu tar, jëfandikoo ci li nu yor lepp ci kàttan.

7) Wesaare diiney nasaraan ci bepp gox bu nu wuññi.


















Doggantal gu ñatteel gi :

Yëngu-yëngu yi jugoon di kontar Egliis bu paab bi

Yëngu-yëngu gu yewenal diine ji ci Tugal :

Yëngu-yëngu gu yéwénal gu diine ci Tugal, mooy googu doon am ci Orob ci xarnub fukk ak juroom benn g, ngir setal Egliis bu katolig bi ci li ci taqoon ci ay ñaawtéefi pas-pas ak yu jikko, na ñu ko daa defe mooy jeem’a delluwaat ci njàggaley Injiil yi.

Li waraloon « yéwénal » gi :

Ak li Egliis bi di nekk nguurug ruu lepp - ci li ko njëkk’a tax’a jug - teewul ànd ak li jamono di gën a yàgg, mu jot’a àgg ci ŋëpp - ci loxob weñ - nguurug diine gi ak gu politig gi, maanaam, mu tëye tëyiin wu metti te tar, ñaari nguur yii di gu diine gi ak gu adduna gi. Ci loolu la mujje di dooley politig, ju diine, ju koom, ju mboolaay ak ju aada ci mboolaay yu Tugal yu katolig yi ci jamono yu diggu yi. Dàkku nag walla xañ nit ki jàngu bi moo nekkoon mbugal mi gën’a saf, te gën a tar, mu Egliis bi moomoom, daan ko teg kuy jeem’a léewtoo’k moom, ak nu darajaam man’a kawee, mbaa mu màgge ni.

Egliis bi ci safaanub muy jëfandikoo nguurug ruuwam gi, di jëmale nit ñi ci yooni baax ak ragal Yàlla, moom déy – ginaaw ag mbon da koo duggoon – daa labaloon boppam ci bànneexi adduna aki caaxaanam, fàgguloon boppam ay suuf yu yaatu, ay alalam it mu teggiloon leen, te musal leen ci galag yi ñépp di fay. Ci noonu paab yi ak kardinaal yi nekkoon di ñu nuuroon ci dundug adduna aki caaxaan yu ëpp.

Ñaawtéefi Egliis yooyu ak yu leen moy, ñoo gestuloo woon te fëkkoon yittey yéwénalkat yu mboolaay yi ak bindkat yi ci jamonoy yewwute gi.

Ki gënoon’a jeexiital ci mbooleem bindkat yooyu, mooy labbe bii dib xeltukat , nu ko daa wax Erasmus ( 1466 – 1536 g), moom daal jamoon na ci teereem bi tudoon « tagg ag ndof » (Praise of Folly) , jamoon na ci nekkiinu egliisu katolig bi, mu nekkoon jam yu tar te wex.

Dox gu taarixe gi yéwénalug diine gi defoon ci Orob :

Yéwénalug diine ci Orob - ci doxam bi - romb na ñaari tolluwaay : bi ci njëkk mooy : bi ay yëngu-yënguy yéwénal yu ndaw amee te lalu niki ay njiitlaay aki cëslaay yoo xam ne ci seen kaw la yëngu-yënguy yéwénal yu diine yu mag yi ci Tugal tegu. Bu ñaareel bi nag mooy yëngu-yëngug yéwénal gu mag gi ci boppam.

Bu dee nag yëngu-yëngu yu diine yi nooyal yoon wi ba yu mag yi man’a am, man’a taxaw ci Tugal, ñoom ñooy yi nuy wax Fransiskaan ak Dominikaan, ñooy yi gisoon ne mant’a ñàkk nu dañal njuumte ak ñaawtéefi diine yi niki aw yoon wu nuy jaar ngir yéwénal Egliis bi te dëgëral ko.

Ag yëngu-yëngu gu yéwénal daal di taxaw ca Angalteer ci njiitl John Wycliffe (1330 – 1373 g), moom kenn la woon ci ustaas yu siw, yu daaray Oksford ju mag ji.Googu nag li ko taxoon’a jug mooy dañal li taqoon Egliis bi cig mbon. Gii yëngu-yëngu moom mi ngi judd ginaaw lu tolloo’k xaaju xarnu, ginaaw juddug yëngu-yëngu gu ñaari way sell yii di Fransis ak Dominik, waaye gii nag moo gënoon’a fés, gën a jeexiital ci egliis bi ci gu Fransiskaan gi ak gu Dominikaan gi. Geneen it feeñati gu yéwénal ci Bohimiya ci njiitul John Hess (1373 - 1415 g) , moom mooy ki ne woon : ag diggale wart’a am ci diggante nit ak boroomam, ndare diggale googu doon ngëm ak jëfe li ci Injiil. Hess nag li mu jublu woon ci loolu mooy wàññi sañ-sañu Paab gi, ak neenal taxawaayub làbbe bi niki aji diggale ci diggante jaam bi ak boroomam .

Bu dee yéwénali diine yu mag yi ñoom, ñi ngi doon jëmmu ak’a feeñe ci am gi yëngu-yëngug Protestants gi amoon, njiit ya di woon Martin Luther, Kalfan ak Swingli.


Martin Luther ak yéwénal gi :

Martin Luther mi ngi juddoo Isilban, di benn dekk ci diiwaanu Saksoniya ci Almaañ atum 1483 g, faatu atum 1546 g, baayam nekkoon ku daan ligeey ci benn ci gasuwaayi mbell yi. Mu màgge nag ci njaboot gu ndóol, ak ci ron dund gu jafe te wow. Moom nag jàng na cosaani làkkuw latin, ak cosaani ag katolig, noppi jàng yoon ak xeltu, dugg nag ginaaw bi, benn ci barabi jaamu yu katolig yi, ngir laabal fa boppam ciy bàkkaar aki ñaawtéef, loolu nag ci gëm-gëmi katolig yi la bokk. Ginaaw bi mu tukki dem Rom atum 1510 g, def fa weer, gisal boppam ñaawtéefi paab gi, ak bon-boni Egliis bi, li gënoon’a wëlbati ay bëtam mooy jàdd gi niti diine yi jàddoon, ak wàcc gi nu wàccoon yoonu leer ak lëmoodiku wi nasaraan gu njëkk ga yoroon, ak set gi mu setoon . Lii jeexiitaloon na ci boppam, ak xelam mu daladi mi, jañoon ko it ci jam walla kritige paab gi, ginaaw bi it, mu mujj fèttéerlu ci kawam , bi mu bañee –moom paab gi - ne du soppi aw doxaliinam.

Dikk gi labbe bii di John (Tetzel) dikkoon ci diiwaanu Saksooniya atum 1517 g, ngir jaaysi fa ‘xobi njéggal’ yi, dikk googu dimbli woon na Luther ci mu man’a feeñal li nëbbu woon ci biiram muy yéeney yewenal yi mu yoroon te fasoon leen ci xolam. 

Jaadu na ñu fàttali leen ne ‘xobi njéggal’ mooy li fi wuutu woon tuubug aji tooñ ji, ci jeem’a fare ay bàkkaaram ci def lu baax, jaare ko ci julli walla joxe asaka mbaa woor. Waaye paab bii di Liyoo mu fukkeel mi, moom daal, da ne woon da na doy aji moy ji bu bëggee tuub ay bàkkaaram mu aji-ji Rom, ginaaw bi, wax jooju xaw’a gën’a jëm kanam, gën’a xóot, bi kenn ci paab yi nee : njéggal daal man na’a ame ci nit joxe ci alalam ci Egliis bi, ngir ñu dundale ci diine, bu ko defee ñu jox nit kooku ‘xobu njéggal .

Luther moom dafa kontaroon njaayum xobi njéggal yi, mu ne woon : mucc mbaa mbugal ak fayoontoo, manuñoo juge ci jënd ay xobi njéggal, fa nu man’a juge kay mooy gëm Yàlla. Luther moom diiŋatoon na xobi njéggal yi, daal di woon dem ba ca Egliisub Wtanberg ba, wékk fa mbind mu ëmb ay diiŋat yu toll ci 95 , ci atum 1517 g . Paab bii di Liyoo mu fukkeel mi amoon na taxawaay bu tar ci xalaati Luuther yi, ndax daal di woon nay genne ca saa sa benn saxal walla ndigalul xañ, ñu teg ko Luther, saxal boobu walla ndigal loolu moom lanu daa wax (Wermis), waaye Luther moom faalewul woon saxal bii, moom kay da koo sanni woon ca ëttub Egliisu Watanberg ba, lakk ko.

Xalaati Martin Luther ak ay gisiin yu yéwénal yi mu yoroon :

Luther, xalaati yéwénal yi mu woote woon jëme ñoo’y yii di ñëw nii :

(1) Injiil mooy nattukaayub diine ak bu yoon bi muy sukkandikoo ci firi pas-pas yi ak mbooleem masalay diine yi am ag wuute. (2) Nit ku jàng ku nekk tey jëfandikoo xel sañ na’a jàng injiil te firee ko ni mu ko dégge, xame ko ni. (3) Paab bi amul - benn yoon - àq mbaa sañ-sañ ci rënkal fi boppam, moom rekk, sañ-sañu firi injiil. (4) Sëy daa war’a dagan ci làbbe yi. (5) Niti diine yi dañoo war’a nekk ci ron kiliftéefug nguur gu àdduna gi. (6) Wàññi limub jàngu yu bari yi tasoon ci mbooleem reewi Orob gu sowwu gi.

Bu nu xoolee xalaati Martin yi dananu gis ne moom daal li ko yitteeloon mooy mu neewal doole sañ-sañu paab bi, loolu yaa ngi koy gisati ci bi muy sàkku nu neenal diggale gi daa am ci diggante Yàlla’ak’ub jaamam. Sàkku gi mu doon def it ci nu neewal limub jàngu yi li mu doon wund mooy neewal ngañaayi Egliis bi aki am-amam, ndax loolu man’a soril Egliis bi caaxaan ak po mi mu nekke woon. Da nga gis it ne wax ja mu waxoon ne nit ku xam ku nekk am nga àq ci jàngal sa bopp injiil ak firee ko ni nga ko dégge, moom itam li mu doon tekki mooy jeqiku gu mu jeqiku woon ci Egliis bi, ak rafleel gu mu ko rafleeloon ci li mu jàppoon moom Egliis bi ne àqi yoonam la ju mu moom.

Jëfka yi dimbli Luther mii ci wooteem gi man’a àntu :

Am na ay jëfka yu bari yu ñoo dimbli woon Martin ci fipp gu yéwénal gi man’a àntu. Yi ci ëpp solo ñooy yii :

(1) Feeñ gu Luther mii feeñoon ci jamono joo xam ne waa Orob yi seeni xel da cee tàmbli woon’a ubbiku, ñu tàmbli woon’a fèqu ak’a dañtalu ci ŋëbug paab gi ak sañ-sañam. (2) Siwug njuumte ak ñaawtéef yu rëy yi nga xam ne taqaloon nanu derub paab gi, te taxoon ba nit ñi doon sikk ag muccam ak ag sellam. (3) Fonk sa xeet,walla xeetu gi tàmbli woon’a feeñ ci reewi Orob yi, te taxoon waa Almaañ ñi defoon ab dank topp ci ginaaw Martin Luther, rawati na maas gu diggu ga ak baykat ya ak gawar ya. (4) Dimbali gu ko ustaas yu daara yu mag yu Tugal yi dimbali woon, ak ñu dul ñoom ci xalaatkati Almaañ yi warlu woon ne ñooy fas yeenee tas xalaatam yooyu. (5) Firi Injiil ci làkku Almaañ, ak def ci ay taalif yu tax waay Almaañ ji man’a gis ay xalaatam, yër it jam yi mu doon def Egliis bi . (6) Tasug móolukaayu téere gi nga xam ne Gotenborg moo ko fentoon, loolu taxoon nag ba xalaati Luther yi tasoon ci waa Almaañ yi ak ñu dul woon ñoom.

Am na benn xeex bu mag bu amoon ci diggante Martin aki gaayam, ñoom ñi diy protestants, maanaam ay diiŋatkat cig wàll ak diggante ñi toppoon paab gi (katolig yi) ci geneen wàll. Dëkki Almaañ yi moom xare yu tàng’a fa amoon, dongay ñaari ngér yii doon xeex nag mujjoon nanoo xaatim ag juboo, gu nu tudde woon (Augsburg) atum 1555 g, ñu nangu woon ci ne goxu Almaañ bu nekk am na àq ak sañ-sañ ci tànn ngér mu ko neex, mu protestant mbaa mu katolig, waaye ci wàllug ofisel ñu tànn protestant def ko diine, ngérum Luther mu protestant mii tasoon na te siw ci goxi almaañ yu bëj-gànnaar yi – egliisam daal di doge ca egliisub Rom ba – ak Norwej, Finland, xalaat yii tam tas ba genn Almaañ, dugg Angalteer ak nguuri skandinaaf yi (Danmark ak Suwed) .

Kalfen (Calven) :

John Calven mi ngi juddoo Fraans atum 1509 g, di woon ku duggoon ci ngérum protestant mu Luther mi, te bàyyi woon mu katolig mi. Kalfen walla Calven juge woon na Fraans dem Siwis, li ko waraloon it mooy sonnal gu nu ko fa doon def ngir ay sabab yu aju ci diine . Fii nag la tàmblee wisaare ak’a tas ngérum yéwénalam mu xaw mee jege ngérum Luther mi, ñi ko toppoon mu tudde leen (Hogonoots), di ci maanaa ñoñ laab ñi. Kalfen ak Luther dëppoo woon nanu ci ay masala yu diine yu bari, waaye wuute woon nanu ci ñaari mbir ñooy: (1) Wax gi Kalfen waxoon ne njéggal ci mbir yi nu doggal la, te loolu Luther nanguwu ko . (2) Kalfen daa gëmoon ne Egliis bi warul’a topp ci ginaaw genn nguur gu adduna, ne woon: Egliis bi daa war’a am nguurug boppam gu temb, gu dul wéeru ci gu adduna gi, ñi war’a doxal nguurug Egliis bi nag ñooy am mbooloo mu xellu te am hikma. Xalaatam yooyu nag wisaaroo woon nanu ci reewi Tugal yi ci anam gu ëppante, ci Fraans, Angalteer, Siwis ak yeneen. Swingli :

Mi ngi cosaanoo woon Siwis, judd atum 1484 g, ay yéwénali diineem mu tàmbli woon ko ci dëkkub Siyorix atum 1519 g, ci biir diiŋat gu mu doon def njaayum xobi njéggal yi. Kon foofu ag jegeente gu mag am na fi ci diggante ay xalaatam ak yu Luther ak Kalfen, waaye teewul mu wuute ak ñoom ci lenn ci ay masalay diine.

Swingli moom daa jàppe woon egliis bi benn campéef bu am demokraasi, buy ame ak’a sosoo ci mbooleem nasaraan yi nga xam ne seenug bokk ci, mi ngi ame ci benn kuréel bu leen fay teewal ci mbooleem mbir ak masala yi aju ci Egliis bi, ak ni ñuy sampe nit ña fay ligeeye. Ngérum Swingli tasoon na ci Siwis, ak ci lenn ci yeneen reewi Orob yi, waaye taxutoon mu siwe, wisaaroo ni mu Luther mi mbaa mu Kalfen mi.





                                                             Bunt bu ñaareel bi




























Jëm kanam gu xam-xam ak yewwute gu endustri



• Jeexiitalu gu waa-Orob defoon ci yooni gëstu yu xam-xam yu jullit ñi.

• Lefi (wàlli) jëm kanamu xam-xam ci Orob.

• Yewwuteg endustri: ay jagleem – ay màndargaam – ay ngérteem (li mu fi jur)














Doggantal gu njëkk gi

Jeexiitalu gi waa-Orob defoon ci yooni gëstu yu xam-xam yu jullit ñi.

Jamono ji xam-xam neewe lool te amadi xiima ci Tugal, ci jamono ju diggu ji, di (ju ag laman), moom xam-xam nekkoon na ci mbooleem reewi jullit ñi di lu naat, te meññi. Xay gu lislaam gi di woon gi gënoon’a kawe ca booba, ngir coona bi boroom xam-xami jullit ñi daa génne ak’a daj ci dundal ko, ak ngir soññe gi nguurug lislaam gi daa soññe ak’a jàmbaarloo ci xam-xam ak boroom xam-xam yi.

Bi waa Orob yi dee ñu yittewoodi xam-xami Gres yi ak yu leen moy, fekkoon na jullit ñi ñoom ñu nekkoon ñu xam-xami xay yu yàgg ya ñoroon, ñu taxawoon ci firi leen ci araab: xay yooyu di yu Gres, Faaris End, rawati na ci ndoktoor, bidiw, ak mat ak yeneen yi. Ñu jotoon’a naan nag ci xam-xami Ubuqraat, Iqlidis, Aflaton ak Arustoo ak ñu leen moy ci boroom xam-xami Gres yu mag yi. Boroom xam-xami jullit ñi yamuñu woon rekk ci naan ci xam-xami Gres yi ak tuxal leen yobb leen ci araab, waaye kay danu leen’a toppoon, wéral leen, te dolli ci lu bari ci li nu feeñal, wuññi ko ciy xam-xam, aki gëstu aki nattu yu nu amal ci wàllug ndoktoor ak mat, kimyaa ak xam-xami dénd yi , bidiw, juxraaf ak yu leen moy, ginaaw bi nu amee jikko yu mag yiy joxe xalaatub xam-xam bu sell.

Ngérum walla yoonu gëstu wu xam-xam ci jullit ñi: Boroom xam-xami jullit ñi daal doxoon nanu ci seen gëstuy xam-xam yi ci ngérum xam-xam mu wuutewut ak mu xam-xam mi am ci jamono ju yees ji. Ñi ngi sukkandiku woon ci yooni xam-xam yoy bokkoon na ca yii: Xeeñtu, raññale xaaj yi, jëfandikoo yooni natt yi, jàkkarloo, làmb, misaal ak jeem’a àgg ca jëmuwaayu xam-xam ba, maanaam xam-xam bi la tax’a jug, ak xam ngérte yi , muy liy juddoo ci boo ko xamee ba noppi . Ngir coona yii nu daa daj nag mujj nanu di ñi jiitu ci lefum gëstu mu xam-xam, walla li nuy tudde “yoonu xam-xam wu nattu” , ci noonu lanu fi sampe woon kenoy gëstu gu xam-xam, ngir yeesal gi nu yeesaloon xam-xam ci seen jamono. Waa-Tugal yi nag jariñu nanu ci wii yoonu nattu wu xam-xam wi nga xam ne jullit ñi rawoon nanu ci. Ki jiitu woon ci ñi ci jariñu mooy waay- Angalteer ji di Roger Bacon ( 1214 g 1297 g), mooy ki waa Tugal yiy jàppe ki raw ci gëstug xam-xam ci Tugal, ndax mooy ki jeemoon’a wutal xam-xamu dénd ag noste guy sukkandiku ci nattu ak jàkkaarloo. Loolu nag mbir la moo xam ne boroom xam-xami jullit ñi ñoo ko ci jiitu. Jaadu na ñu leeral fi ne Roger Becon mii kat ku jotoon’a jàng làkku Gres la ak wu yahood yi , ak araab, jariñu woon it ci xam-xam yi nu ci bind. Moom nag daa gëmoon ne li tax ñu war’a jàng fisiya ak kimiya ak mat ak bidiw ak xeltu mooy ligeeyal xam-xam bi aju ci Yàlla .

Digg yi “xayug lislaam gi” jaaroon bi muy dugg Orob:

Jullit ñi dañoo nekkoon ñu rawoon ci lefi xam-xam yu bari, ci noonu ñu yanu woon seen xay googu yóbbaale ko ci mbooleem àdduna bi, ci penku bi ak sowwu bi. Orob jariñu woon na bu baax ci xam-xami jullit ñi, ña fa dëkk it jòkkoo woon nanu ak jullit ñi jaare ko ci ay ker-keraan yu bari, bokk na ci yooyu:

(1) Andalusi : Waa Orob yi jonjoo woon nanu ak digg yu xayug lisaam gi ci Andalusi, moom gox bii nga xam ne daa mujjoon fees dell ak leer guy jòlli tukkee ci xayug lislaam gi ko róofu woon. Moom bii gox barabu jòlli la woon ñeel xam-xam ak dañ-kumpa, rawati na ci dëkki Orob yi mu dendaloon. Bu ko defee nga gis sàkkukati xam-xam yu Orob yi daa jariñu ci xam-xami jullit ñi, di jawalsi ak’a jublusi dëkki Andalusi yii di Talitala, Kordoba ak Sewija , ñu jële woon ci ñoom ngérum nattu mi ñu daa jëfandikoo ci gëstu gu xam-xam, loolu mujj yëngal bu baax xalaatiinu waa-Tugal yi.

(2) Dunub Sisil :

     Araab yi jotoon nanoo teg loxo Sisil, ki joxe woon ndigalul jëf jooju di Siyadatul Laahi Bun Al Axlab, buurub nguurg Axaaliba yi, waaye mu ame ci loxol kapitenam bu siw boobu di Asad Bun Alfuraat atum 212 ginaaw gàddaay gi, mu ame woon nag ci jamonoy xalifa bu nguurug waa Abaas, bi tuddoon Maamun. Ca saa sa xayug lislaam tàmblli fa’a sutuxlu, Sisil mujj di gilin ci gilini xam-xami lislaam yi, sàkkukati xam-xam yepp jublisi ko rawati na ñi dëkke woon Orob, ngir sàkkusi fa xam-xam. Bi Norman yi nangoo Sisil ci Araab yi, yaquñu woon xayug lislaam gi, ñoom kay dañoo sawarloo woon boroom xam-xam yi, soññ leen, ci noonu firi teerey araab yi yobb leen ci latin daal di fay tàmblee am ak’a sawar, waa Orob yi tàmblee yër li ci yii teere ak’a jariñoo, rawati na Itaali mi ci gënoon’a jege Sisil, looloo waraloon muy mberum yewwute gi.

(3) Xarey jooñ yi bokk nanu bu baax ci li tax waa Orob yi manoon’a jokkoo ak xayug jullit ñi. Jokkoo gi it saxoon na fi lu tolloo ak ñaari xarnu, ci biir ñaari xarnu yii Orob jot na cee tuxal lu bari ci xam-xami lislaam yi, ame ci it, walla tege ci loxo lu bari ci teere yi nu taalifoon ci araab, ak yi nu firi woon jële leen ci làkku Gres, End ak Faaris . (4) Jokkoog yaxantu gi amoon ci diggante reewi jullit ñi ak Orob, rawati na li ci Itaali jotoon’a def, mu bokk ci li sababoon jonjoog xay ci diggante ñaari dëkk yi. (5) Siyaare gi nasaraan yi daa defsi ci seen barab yu sell yi nekk Palastiin. Nga rax ci dolli tukki yi waa Orob yi daa defsi ci reewi jullit ñi, ak la ca juddoo muy ñu gis te jariñu ci xam-xami jullit ñi ak seeni xay. Jullit ñi daal ñoo waral jëm kanam gii nga gis ci Orob ci jamonoom ju bees jii.



Xam-xam yi bàyyi ay jeexiit ci waa Tugal yi:

Lim (Mat):

Jullit ñi naanoon nanu ci xam-xami kalkil yi nekkoon ca waa End yu yàgg ya, ñu jotoon’a jànge ca ñoom ni nuy defe ay lim (numero) waaye nag nu sellal ko gën koo teg ci yoon. Boroom xam-xami jullit ñi ñoom defoon nanu ay dollent yu am solo ci xam-xamu waññ ( calcul), ñoo dolli woon tus ci lim yi, ndax amu ci woon bi nu leen di jël. Ñu indi màndargam al kasr alhasarii di ci wolof (damat ci fukk) , ñu taalif ci wàllug xam-xamu waññ (calcul) ay teere yu waa Orob yi firi ci seeni làkk, te jariñu ci. Boroom xam-xamu jullit bii di Muhammad bun Muusa Alxuwarsamii, nekkoon na di ku aay ci xam-xamu lim walla waññ, moom de lanuy sant bu lim (mumero) yi nekk ci kalkil duggee Orob tay. Xawaarsamii mii aayoon na it ci beneen xam-xam bu yees mooy aljabr , moom sax mooy ki ko sos far. Taalif na ci tollale ci aljabr , nu tekki ko ci ginaaw bi ci làkki Orob yu bari. Boroom xam-xami Orob yi jariñu ci. Boroom xam-xami jullit ñi jëfandikoo nanu ay junj ci matematig yi(xam-xamu lim), ñoo njëkkoon waa Orob yi ci wàllug matemetig gu yees gii. Bu dee nag ci andasa , ak xam-xamu ñattal yi , jullit ñi ñoom yamuñu woon ca la woon ca waa Gres yi rekk , nga xam ne seen boroom xam-xam bi nu naan Iqliidis moo ko feeñaloon, waaye jotoon nanoo feeñal ay masalay andasa yu bees. Ñu duggal li nuy wax “al mamaas” ci xam –xamu kalkilu ñattal. Nu jël li nuy wax “juyuub” = poos, wuutale ko ak li nuy wax “awtaar” = buum. Nu fecci itam toolale yu nu kaabaal yi . Nu xootal bu baax tam ci xam-xam yu nuy wax “maxruutaat” . Boroom xam-xamu jullit bi nuy wax Omar Alxiyaam defoon na lu mag ci wàllug mat, moom de bokkoon na ci ñi gënoon’a ràññiku ci boroom xam-xami jullit ñi ci wàllug matematig ci ñeenteel bu njëkk bu xarnub fukk ak ñaar g.

Xam-xamu Fisiya :

Li nga xam ne sikk amu ci mooy ne jullit ñi jariñu nanu ci xam-xamu Fisiya ci waa Gres yi , bi nu ko tekkee ci seen làkk , waaye ñu gën koo yaatal dolli ci ay masala yu fisiya yu bari. Nu màndaqe walla natt diisaayu yolaakon yi , nu fent ay màndaqekaay yu xereñ, ñu xamale ay gisiin yu bees ci xam-xamu “kàddu” ak “gis” (basariyaat ) ak “séen” (almariyaat ). Boroom xam-xam bu jullit bii di Abo Yuusuf Yahquub Ishaq Alkanadi, mi nga xam ne mi ngi faatu atum 873 g, moom ku aayoon ci xam-xami gis yi la, taalif na ci ab teere bu am solo, mooy teereb yu nu xool yi, nga xam ne waa Orob yi mujjoon nanu ko’o tekki ci làkku latin. Roger Becon jariñu ci ak Liyonardo Da Vinci, ak boroom xam-xam bu Poloñ bii di Copernice (1473 – 1543 g). Boroom xam-xamu jullit bii di Abo Aliyu Muhammad Bun Alhasan Bun Alhaysam (965 – 1038 g), moom mu nekkoon di ku aay ci xam-xamu fisiyaa, mu soppi xam-xamu leer bu yàgg ba, indi fi xam-xamu leer bu yees bi. Mu amoon ndam ci indi fi gisiinu xam-xami seen yi, mu firi feeñteg xònn , ak safaanu gi ag leer di safaanu, ak ni muy dammoo.

Bu boroom xam-xamu Gres bii di Batlimos jàllee, kii di Ibnu Haysam moom lanuy jàppe boroom xam-xam bi njëkk’a def ay wuññi ci xam-xamu gis. Haysam defoon na ay taalif ci xam-xamu-yu nu gis yi, ak xaaji bët, ak weer yi ak leer ak yeneen. Waa-Orob yi it yii taalif, tuxaloon nanu leen ci seen làkk wii di wu latin, ci xarnub fukk ak ñatteel g, ak ci yeneen làkk yu Orob yi. Loolu dimbli leen ci nu jariñu bu baax ci xam-xam yii nga xam ne jullit ñi aayoon nanu ci bu baax.

Xam-xamu bidiw :

Jullit ñi yittewoo woon nanu xam-xamu bidiw, Xawarsimii moom defoon ay natt ci yëngug bidiw yi, xam fi nuy fenke ak fi ñuy sowe. Jullit ñi jariñu woon nanu ci xam-xamu bidiw ci waa Geres yi, ci noonu ñu firi woon ci araab lenn ci teerey bidiw yu Geres yi niki teereb Batlimos bi tuddoon ñeenti wax yi.

Boroom xam-xam bi ko tuxaloon ci araab di Aboo Yahyaa Albatriix, ci jamonoy Abo Jahfar Almansuur. Doomi Muusaa Bun Saakir ñoom itam taalif teere bi nuy wax Aljadaawil Alfalakiya, yeneen boroom xam-xami bidiw it feeñ, niki: Saabit Bun Xurra, Haniin Bun Ishaqa Alhibaadi, ak Bataani mi faatu atum (929 g) ak ñu dul ñoom.

Jullit ñi tabaxoon nanu ay fuglukaayi bidiw ca Dimasq, Baxdaad, Kordoba ak Sawija di woon ay dëkki lislaam. Abo Abdillaa Albattani mii dees na ko lim muy ki gën’a bàyyi ay jeexiit -ci anam gu xóot- ci waa Tugal, ci boroom xam-xami bidiw yu jullit yi. Waa Orob yi ñoom jariñu nanu bu baax ci xam-xamu bidiw ci jullit ñi,ak ci li jullit ñi jot’a gennewaat ci anam gii ciy wuññiy xam-xam.

Kimya:

Jullit ñi fésoon nanu ci xam-xamu kimyaa, Jaabir Bun Hayyaan Alkoofii bokkoon na ci ñi gënoon’a siw ci wàll googu, moom mi doon def kimya te taalifoon ci ab jimblang .

Jabbir leeraloon lu bari ci way toggale yu kimya yi nu xamutoon bu njëkk, niki: aji wex ju nitrik , ruug nasaard, botaas, soda al kawiya ak aji wex ju asotik ak yeneen.

Mu leeraloon ba tay jefi kimya yi niki: seebal ak leeru ak yeeg ak toqqal.

Da na jaadu nu leeral ne xam-xamu kimya moom, danu ko daa wooye xam-xamu Jaabir, ngir li ko ci Yàlla tawfeexaloon ba mu man’a topp yoonu xam-xam wu nattu wi nga xam ne ci la jaaroon ba man’a àgg ci ay dëgg yu kimya yu bari.

Waa Orob jariñu nanu bu baax ci xm-xamu kimya bi ci jullit ñi, ci noonu nu firi taalifi jaabir yooyu ci seeni làkk, xam it lu bees li ci jullt ñi dolli.

Ndoktoor :

Boroom xam-xami jullit ñi rawoon nanu ci xam-xamu ndoktoor. Sartoon nanu ci seen boroom xam-xam, mu xam siddi , xam jëf ak warteefi cer yi, ak noyyi ak soppikum saw. Ñoom de ñu sonnoon ci xam-xamu siddi lanu woon. Firi woon nanu xam-xami Geres yi ci aju woon, ci làkku araab. Bi nu noppee ñu taalif ci. Teereb Ibnu Nafiis bi tudd Tasriihul Xaanuun dolli na ay xam-xam yu am solo ci xam-xamu siddi. Jullit ñi jàngale nanu doxug dereet , sonn it ci mbooleem xeeti tawat yi, xamale itam deewal bi nuy faral a def ci ligeeyu xotti . Ki niy wax Razi te faatu atum (923g) feeñ na te raw ci ndoktoor, taalif na ci lu sakkan. Ak Ibnu Sinaa mi faatu atum (1037g) , moom de kenn la ci boroom xam-xami jullit ñi gën’a siw ci ndoktoor, teereem ba tudd Xanuun Fit Tibb de jenn jimblang la ju xam-xamu ngoktoor, ju waa penku ak sowwu ñepp xam, ak Abo Xaasim Xalf mi gënoon’a fes ci xottikati xarnub fukk ak benn g. Ak Ibnu Zahr, boroom teere bi tudd Mubtakaraat Fil Jiraaha. Waa Orob yi jariñu nanu ci xam-xamu ndoktoor bi nga xam ne jullit ñi rawoon nanu ci. Ñu jariñu ci ni nuy siddee, ak ni nuy gennee tawat yi, ak ni nuy faje, ak ci xam-xam yi nga xam ni teerey jullit yi làqoon nanu leen ci wàll gii, ginaaw bi nu leen firee ci làkki Orob yi. Waa Orob yi jële nanu ci jullit ñi tabax ay fajuwaay ak jëfandikoo deewal ak li nuy wax Kaaw su nuy opere (xotti).

Waa Orob yi ba tay jariñu nanu bu baax ci xam-xamu xeltu bi nga xam ne jullit ñi ñu ci rawoon lanu. Ci noonu nu jàngoon taalifi Kanadii, Faarabii, Ibnu Sinaa ak Ibnu Rusdi ak ñu dul ñoom, ginaaw bi nu leen firee ci seeni làkk. Bokk na ci boroom xam-xami Orob yi gën’a siw ci jariñu ci jullit ñi ak seeni xalaat : Paskaal, Dikart, Hiyom ak Becon ak ñu leen moy.

Waxtu wi yaatuwul ngir nu man leen a indil ngértey xam-xam yu bari yi nga xam ne jullit ñi àggoon nanu ci, ci seeni gëstu te booba Orob’a ngi ci ngëmmeenam li ak lëndëmug reeram gi, ci ron nosteg laman ak cangug Egliis bi.

Da na yell nu leeral ne xam-xam yi ak ngértey xam-xam yi nga xam ne jullit ñi àggoon nanu ci, dañoo tàmbli woon’a tuxu ndànk-ndànk jëm ci reewi Orob gu sowwu gi, ginaaw bi ab kureel ci waa Orob yi xamee solos xam-xam yii, te taxawoon ci firi leen ci seeni làkk. Ay firikati Orob yu bari feeñoon ci loolu ku ci mel ni: Costantinus Africanus, Herman The Cripple ak Eugenius mu Parlermo mi ak ñu dul ñoom. Kon lu nu war’a xam la ne yewwuteg xam-xam ak gu endustri gii am ci reewi Orob yi, ci ginaaw yewwute gi, du lu moy meññat ci meññati nattu ak gëstu yu xam-xam yi nga xam ne Orob tuxale na leen ci xam-xami lislaam, ci digg jamonoy xayug lislaam gi. Coonab gëstu yooyu nag ñooy cëslaay yi nga xam ne ci la jëm-kanamug xam-xami dëppale yi ak yu xarala yu bari yii tegu ci adduna ju xay jii ngay gis tay .


























Doggantal gu ñaareel gi

Wàll yi xam-xam jëme kanam ci Tugal

Xam-xam naat na te jëm-kanam ci Orob, ci biir xarnu yii: bu fukk ak ñeent, fukk ak juroom ak fukk ak juroom benn g, loolu bokk ci li waral jëm-kanamug xam-xam gu mag gii Orob gis tay ci jamonoom ju yees jii nu nekk, nga xam ne ci la yewwuteg xam-xam juddoo ak gu endustri ci Orob, ak li topp ci loolu ci njariñ yoy du Orob rekk la ñeel waaye àdduna bépp.

Li taxoon xam-xam jëm kanam :

Jëm-kanam gii xam-xam jëm kanam tay ci reewi Orob gu sowwu gi, am na ay balluwaay yu wuute, yi ci ëpp solo di:

(1) Tuxal xam-xami jullit ñi ak firi leen ci làkki Orob yi te jariñu ci. (2) Ak feeñ gu ab lim xëy feeñ ci boroom xam-xami Orob yi amoon ag cofeel ci gëstu yi aju ci xam-xam (3) Yokku gu yëngu-yëngug firi ak taalif yokkuwoon, rawati na bi nu fentee móolukaay yi. (4) Xeemmeemteef gu waa Orob yi amoon ci dundalaat xam-xam yu yàgg ya: yu Gres-Rom ya.

Wàll yi xam-xam jëme kanam :

Ak li nuy misaal jamono yu diggu yi ci Orop lepp, naan jamonoy reer la ak lëndëm, teewul ay ceññeeri xam-xam yu kenn mant’a reere, mant a weddi amoon fa . Li am daal mooy wuññiy xam-xam yi ci jamono jii du woon yu yaatu, lu neew la woon. Ci noonu xam-xamu waa Orob yi nekkutoon lu moy li nu xame woon ci waa Geres yi ak ci jullit ñi, ci seen ginaaw. Maanaa mi xalaati waa Orob yi ame woon soppiku woon na ci jamonoy yewwute gi, ginaaw bi nga xamee ne gëstuy xam-xam yi fa ñoom, dafa mujjoon tegu ci nattu . Ci noonu Orob jot na a am ndam ci jëmale kanam xam-xam ci wàll yu bari, yi ci ëpp solo di:

Ndoktoor :

Ndoktoor ci Orob wëyoon na di sukkandiku ci li fi waa Geres bàyyiwoon ak li fi Jalinos jot a indi ak Hiboqrat ak ndoktoorug jullit ñi, jaare ko ci seen teerey ndoktoor yi nga xam ne waa Orob mujjoon nanu leen’a firi ci seeni làkk.

Xam-xam bi Orob ame ci ndoktoor weesuwutoon fii, ba ci xarub fukk ak juroom benn g.

Waa Orob yitewoo woon nanu bu baax xam-xamu ndoktoor, ñoom daal ñoo ci gënoon’a sonn ñu dul woon ñoom, rawati na ci xarnub fukk ak juroom benn g, moom dey xarnu la bu fekke ay xew-xew yu bari yoo xam ne ñoo waral ag jëm kanam gu mag ci wàllug ndoktoor ci Orob.

Bii xarnu daal seere na ay yëngu-yëngu yu wuññi yu juxraaf ak tuxug ay mboolooy gaal yu yaxantu, ak ay gàddaay ci ay mbooloo ngir dëkk-ji ci reew yii nuy door’a wuññi, aki xare yu tar te yàgg yu amoon ci Orob te sababoon ay tawat yu metti aki mbas yu nu xamutoon ci Orob. Mu mujj nag bokk ci warteefi doktoor yi ci Orob ñu jeem’a xam yile tawat yu yees ak nu nu leen di faje, wutal leen ay garab.

Ci noonu boroom xami-xami Orob yu bari feeñ, ku ci mel ni: Fisaliyos mum Beljik mi, Frakastor mu Itaali mi, ak Gonte Andarnax mu Almaañ mi nekkoon doktoorub Fransuwaa mu njëkk mi doon buuru Fraans, ak Lofan Hok mu Oland mi, ak Luwis Pastor mu Fraans mi ak Kox mu Almaañ mi añs. Bu ko defee waa Tugal yi xam jàngoro yi, xam it nu nu leen di faje, ju ci mel ni: Daftiriya, Judri, Tifos, Kolera, Tifod añs.

Juxraaf ak Bidiw:

Xalaat bi naan suuf si daa tàllaliku daal, te boroom xam-xami bidiwi Gres yi indi woon ko fi, moo nekkoon xalaat bi tasoon ci Tugal gëpp, ci jamono ju diggu ji, ak doonte lenn ci boroom xam-xami Gres yi waxoon nanu lu ko safaan, ne suuf si moom tàllalikuwul, daa bulu kay, mel ni ab kol-kol, boroom xam-xamu Gres bii di Batlimos, moom doon na def ay ligeey ci googu wàll.

Waa Tugal yi nag seen xam-xamu juxraaf ñi ngi ko doon gën a jëmale kanam, jaare ko ci li nu xame ci wuññiy juxraaf yi ak ginaaw bi. Ci noonu xam-xamu juxraaf tàmblee jem kanam ci Orob. Jem kanamug xam-xamu Juxraaf tax na ba bu Bidiw it jem kanam. Kii di Koperniks, di boroom xam-xamu Poloñ, moom, siwoon na ci lefum xam-xam mu Tugal mi, moom dey duggal na loxoom bu baax – boo xoolee ligeeyam yi aju ci xam-xamu bidiw – ci doxug xam-xam akug jëmam kanam ci Tugal. Kopernic moom àndutoon ci gisiinu Batlimos wi doon wax naan suuf si moom daa bulu ba noppi nekk ci digg adduna bi, bu ko defee nekkteefi asamaan yi di ko wër. Kopernics moom ne suuf si daal ak yeneen nekkteefi asamaan yi, ñoom ñepp danuy wër jant bi, te suuf si nag am na wërug boppam gu muy wër ab diggam , ci 24 waxtu yu nekk. Mu neeti suuf si dafa wëndeelu, maanaam roo te wëndeeloom googu nag tax na ba day yor doxiin walla yëngu-yëngu gu roo, mbaa guy wëndeelu. Waaye nag lu ñaaw la lool Copernic ñàkk a man a tas te wisaare xalaatam yooyu ci bi muy dund, ngir rekk ragal gu mu ragal jàngu bi (Egliis bi), xalaatam yooyu wisaarewunu leen mbaa nu tas leen ndare ci atum 1543 g, muy at mi mu faatoo. Boroom xam-xamu Itaali bii di Galileo ( 1564 – 1642 g ) moom jug, def lu rëy ci jëmale kanam xam-xamu Bidiw, loolu gën na a am ci ginaaw bi mu jëfandikoo fésalukaay ngir fuglu bidiw yi ak nekkteef yi ci kaw asamaan si, mu dëgëral itam xalaati Kopernic yi.

Fisiya:

Xam-xamu fisiya gën na a jëm kanam te gën a buur , ci xarnub fukk ak juroom benn g. Bu ko defee, nga gis boroom xam-xam yi ñuy dàggasante ci masalam yëngu-yëngu, ndaxte yëngu mooy cëslaayu xam-xamu fisiya bu Arusto, maanaam ci la xam-xamam boobu tegu. Boroom xam-xami Tugal yi def seen yite ci ñòddi gi nekk ci suuf si . Boroom xam-xamu Itaali bii di Galileo di ku rawoon ci wàll googu, moom de ci atum 1592g, yeegoon na ca sooroolub Pisa bu jeng ba, jël ñatti yef sànni leen, ñu rotandoo ci suuf, Galileo mii moom lanuy jàppe ki gën a am solo ci boroom xam-xami Tugal yi daa yitewoo xam-xamu fisiya, ndax kat mooy ki teg dàtti walla fondmangi xam-xam bii ci Tugal ci fukk ak juroom ñaareelu xarnu g. Boroom xam-xamu Angle bii di Isaac NEWTON (1742 – 1727 g ) mooy ki feeñal dooley ñòddi gi nekk ci suuf si . Moo wax ne bidiw yepp, walla plaanet yepp, danuy wër jant bi, ci ay ngunu yu sax , walla ay nekkuwaay yu sax yoo xam ne ñòddi gi nekk ci jant bi moo leen di nos te di leen teg ci yoon. Ki nuy wax Laplace (1749 – 1827 g ), moom itam ñëw, sonn ba xam ni bidiw yi sosoo.

Kimya:

Waa Tugal yi tuxale nanu ci jullit ñi xam-xam yu am solo, yu aju ci xam-xamu Kimya bu bees bii, nga xam ne boroom xam-xamu jullit bii di Jaabir Bun Hayyaan, fésoon na ci lool, te amoon ci ag raw. Ñoo leen xamal alkol, soda, gudrong, saabu ak yeneen toggaliiti kimya yi nga xam ne jullit ñi aayoon nanu ci. Toggaliit yii ba leegi da nga ciy gis yoo xam ne turi ay jullit lay yore.

Waa Tugal yi nag, ñoom, danoo gën a jëmale kanam xam-xamu Kimya, ci ginaaw yewwute gi. Ci noonu kii di Josef Priestley am tawfeexu di ci waa Tugal yi, ki njëkk a jële Oksijen ci xoromi Siibix , atum 1774 g, te loolu kat fekkoon na boroom xam-xamu jullit bii di Jaabir xamoon ko bu yàgg. Lavoisier di boroom xam-xamub Fraans, di ki feeñal gaasub njëlbeenu oksid korbon, atum 1797 g . Waay Almaañ jii di Rontgen (1845 – 1923g), moom, ñëw feeñalal ñu ceññeeri iks , atum 1895g.

Kuran:

Boroom xam-xam bii nuy wax (Thales), di ku dëkkoon Gres, moo seetlu woon dooley ñòddi ju nekk ci kuran, bi mu ko wokkee, loolu mooy li nu njëkk a xam ci kàttanu kuran. Boroom xam-xamu Angle bii di William Gilbert, nekoon doktooru buuru Angalteer bu jigeen bii di Elisabet mu njëkk mi, moom itam ñëw, feeñal ne am na yeneen ne-ne yuy am ag ñoddi boo leen jonjee, yu dul kuran rekk. Feeñalug loolu nag mi ngi ame woon ci lu tollook atum 1600 g. Boroom xam-xamu Almaañ dikk, fent ab jumtukaayu kuran buy juddal kuran atum 1672 g.

Ki nuy wax Stephen Gray dikk, won nu ni nuy tuxale kuran, jële ko ci barab, yobb ko ci beneen, jaare ko ci fiil yu xànjar.

Wolt mu Itaali mi, di ki wone duusi kuran yi, te fent batari. Borom xam-xamu Amerig bii di Bengamin Franklin, di ki wone ne melax ak kuran benn lanu, mooy ki fent fegukaayu dënn . Misel Faraday dikk, moom itam, di ki feeñal yoon woo xam ne ci la nuy jaare di genne kuran bu bari atum 1831 g. Waa Tugal soobu nanu ci xam-xamu Mat, waay Itaali jii di Tartaliya def ci lu am solo, boroom xam-xamu Frans bii di Fiit, jëfandikoo woon na ay araf ci xam-xamu jabru, bii nga xam ne ci jullit ñi la ko waa Tugal yi jële. Leodardo da Vinci nag moom ci boroom xam-xam yi sos xam-xamu Jiyoloji la bokk, moom mi dëkkoon Itaali, Jims Hitn ( 1726 – 1797g) itam ñëw, di ki xamale ni doj yi nekke ak ni nuy sosoo.

Jamonoy yewwute daal ci Orob mooy jamono ji goreel xelum Tugal mi, te feexal xalaatam, yaatal ko, musal ko ci tënk-tënki jamonoy Orob ju diggu ji. Ba tay dees na ko jàppe muy jamono ji xayale te waajale ba xam-xam man a jëm kanam, man a naat ci Tugal, naataangey xam-xam gii nga gis ci Tugal ci jii jamono de, dara waralu ko lu dul jamonoy yewwute. Ci jii jamono la ay jeem yu xam-xam yu dëggu am, yu sukkandiku ci yoonu xam-xam wi jullit ñi fentoon bu yàgg lool, njëkk waa Tugal yi di ko xam.





















Ñatteelu doggantal


Yewwute gu endustri : li mu jagoo – ay màndargaam – li mu fi indi

Yewwute gu endustri ci Tugal, ñi ngi ci jublu soppiku gu mag gi fa amoon ci wàllug endustri, walla jëm kaman ga fa amoon ci wàllug jumtukaayu mekanig, rawati na ci Biritani, ci ñatteelu xaaj bu mujj bi, ci fukk ak juroom ñatteelu xarnu g. Waaye nag, moom endustri mii, yàggul dara mu tàmblee tas ci Tugal nànk-nànk, ak Amerig, la ko dale ca njëlbeenug fukk ak juroom ñeenteelu xarnu g. Bi mu ko defee nag, ay jeexiitam tas, ba àgg ci pàkk yu bari ci adduna bi, loolu nag ci ñaari xarnu yii la: fukk ak juroom ñeenteelu xarnu ak ñaar-fukkeelu xarnu g. Endustri yi nag masuñoo dañ di jëm kanam ak a awaase ba ci sunu jamono jii nu toll.

Looloo waral du man a ñàkk nu xam sabab yi tax yewwuteg endustri am ci Tugal.

Sabab yi tax yewwuteg endustri am ci Tugal:

(1) awaase gi xam-xam awaase ci Tugal, ci jamonoy yewwute, moo waral yewwuteg endustri am. (2) Dëkki Tugal yu mag yi, am gi nu am, ak tegu gi nu tegu ci yaxantu ak endustri, ak woomleg koom gi loolu di jur, nga xam ne day tax ba endustri di jëm kanam, rawati na, bi ci aju ci ràbbu ser , nga xam ne mooy endustri bi njëkk ci Tugal. (3) Jëmm ci Tugal, ni mu jekki-jekkee rekk fés, mujj di dàtt bi mboolaayi Orob yi tegu, sabab la ci li yee waa Tugal yi, moom jëmm jooju, ci Orob ku nu tënk la woon ci jéngi nosteg laman , jamonoy yewwute ñëw dog jéng yooyu, feexal am xelam, leeral ko ci xam-xam, ba mu man a xalaat bay fent ay jumtukaay yu am solo yu koy dimbli ci yombal ag dundam. (4) Li juddoo ci wuññiy juxraaf yi it, muy teg loxo gi reewi sancaan yi daa def reew yi nu sanc , ak di fa jële ay xeewal aki ne-ne yu nu laalagul , di leen yobbu seeni reew, loolu it bokk na ci li jëmale kanam yewwuteg endustri gi ci Tugal. (5) Reewi Tugal yi ak këri koppar yi, jàpple gi nu doon jàpple naal yi jug ngir jëmale kanam endustri ci Orob, loolu de ci li defar jawwu ji la ba endustri man a dox, man a àntu. (6) Boroom xam-xam yu aay, yi xëy feeñ, te bari ci Tugal. (7) Bari gi ligeeykat yi bari ci Tugal, rawati na ñiy ligeey ci endustri yu ndaw yi. Na ngeen xam nag ne lu bari ci fentkati angle yi daa defar ak a fent jumtukaay yi ak masin yi, ci ligeeykat yi amoon xam-xam yu neew lanu woon, nga xam xam ne daanaka jàngunu woon.



Yewwute gi li mu jagoo woon ak ay màndargaam :

Yewwuteg endustri ci Tugal, daa jagoo woon ay mbir yu bari, yii ci lanu:

(1) Jëmale kanam gu nu jëmale kanam jumtukaayu ëcc ak ràbb :

Meccem ràbb daal, ci yi gën a jariñu ci fent yu xam-xam yi aamoon ci Tugal la, rawati na ci Britani, loolu di ci ñeenteel bu mujj bi ci xarnub fukk ak juroom ñatt g. Loolu nag li ko waral mooy yitewoo gu tar gu nit yitewoo ay sér, ak ñàkk a jafeg jëfandikoo jumtukaay yi ngir ligeey ci. Ràbbkatu angle bi nuy wax James Hargreaves, jot na a fent atum 1764 g, benn jumtukaayu defar wëñ, muy benn masin bu loxo, bu nuy jëfandikoo ci ëcc, li koy doxal nag doon genn mbege walla pono, bu yor juroom ñatti ëccukaay ak ñaari forukaay, bu ko defee benn ligeeykat di ko yor, di ko doxal. Bu ko defee, fentkat bu angle bii di Richard Arkrihgt, fent moom it atum 1771g, benn jumtukaay buy xëcc wëñ yi, moom nag jumtukaay la bu nu daa doxale ci dooley ay fas, mujj nu koy defe ci dooley ndox, nu tudde woon ko kaadaru ndox bi, (water frame). Ki nuy wax Samuel Compton, ñëw fent – atum 1779g – benn jumtukaay buy boole gaaw ci ligeey bi ak baaxle ko, boobu jumtukaay nag tasoon na ci fi dend ak barabi ndox yi, ci ñaari goxi Angalteer yii di Yorkshire ak Lancashire .

Ki nuy wax Edmund Cartwright, moom itam àgg ci fent benn jumtukaay bu nuy doxale dooley ndox, ginaaw bi nu koy doxale dooley cóolóol , te kat tax na ba nu man a ful li nu daa ràbb, daa ko defar ciy sér.

Ligeey bi nu daa def ngir gën a jëmale kanam ak gën a rafetal ligeeyu ëcc beek ràbb bi, gën a dolliku, te sax. Nu àgg ci jëfandikoo ne-ne yu Kimya yi ngir raxas wëtéen wi, defarati yeneneen jumtukaay ngir móol ay deseñ aki mbind ci ndima yi nu ligeey.

(2) jëfandikoo kàttan  :

Jumtukaay yu njëlbeenu yi amoon, nit a ko daa doxale ci dooleem, walla dooley dundat . Kàttan nag di energie jëm na kanam ci jëm gi jumtukaay jëm kanam te awaase. Ci noonu nit jot a jëfandikoo ci njëlbeen gi dooley ndox, ngir doxal jumtukaayam yi mu fent bu yàggul, ginaaw bi, mu jëfandikoo dooley cóolóol ak këriñ. Ki nuy wax Thomas Newman, ñëw, indi fi jumtukaayu cóolóol, James Watt, moom itam dikk, gën a defaraat jumtukaayu Thomas boobu atum 1765g, loolu waral ay soppi yu mag yu xóot ci wàllug ligeey bi, ak li nuy ligeey, ndax kat duggal gi nu duggal jumtukaay bu mekanig, bu cóolóol ci endustri ak jokkoo lu rëy a rëy la te am solo, te moo tax ba nga gis endustri tay mu toll fii mu toll.

Bu ko defee ca saa sa, waa Tugal yi tàmblee gëstu fu nuy jële këriñ. Këriñ nag bari woon na lool ci Wels gu bëj-saalum gi, ak Skotland.

Nit it gënoon na a jeego ay jeego ci jëfandikoo gi muy jëfandikoo kàttan, mu feeñaloon petrol ca D.B.A (Diiwaan yu Bennoo yu Amerig yi), ci digg fukk ak juroom ñeenteelu xarnu g. Ginaaw bi, nu gisaat petrol fu bari ci adduna bi. Ginaaw bi nu fentati benn jumtukaay buy “lakk ci biir”, boo xam ne mooy soppi petrol bi, ginaaw bu ko lakkee, def ko kàttan guy yëngal ak a doxal. Loolu moo waral ngay gis leegi jumtukaay yu mekanig yii nga xam ne danuy sukkandiku ci li nuy wax lakkug biir gi, mooy lakku gi petrol bi di lakku ci biir jumtukaay bi, jumtukaay yooyu nag ñooy yu mel ni: oto yii ngay gis, fafalnaaw yi, gaal yii nga xam ne lakkug biir gee leen di doxal añs. Kuran tam jariñ na nit lu bari, loolu nag mi ngi ame ci bi kii di Faraday juge, fent li nuy wax juddalukaayu kuran, nga xam ne loolu indil na nit lu bari ci ay ligeey ak njariñ ci dundam. Nit àgg na ci xam kàttanug saal te jëfandikoo ko ci anam yu bari, loolu tax mu man a neewal li muy sukkandiku ci petrol. Waaye nag nanu xam ne kàttanug saal moom lu seer la, manu fee wuutu petrol ci genn anam, nit it jot na a xam kàttan gu jant gi , te jëfandikoo ko ci yenn anam yi, niki nuggalukaayu ndox yu jant yi nuy jëfandikoo ci kër yi, ak ci yeneen anam yi.

(3) Jëm kanam gu endustri bu weñ jëm kanam:

Bokk na ci lu am solo li yewwuteg endustri gi jagoo, bokk na ci, jëmale gi nu jëmale kanam endustri bu weñ, loolu nag mooy bi angle bii di Bassemer, jugee, fent yoon woo xam ne manees na cee jaar bay soppi weñ di ko def “sulb” mooy weñ gu wow kong, dëgër këng, loolu nag ni mu daa ame mooy nu jaarale ko ci tàngoor wu kawe lool. Nit it gënoon naa def ay jeegoy jëm kanam ci wàllug yoon yi muy jaar bay genne këriñ, loolu tam dimble ko ci mu man a dolli, gën a lëwal li muy ligeey. Lii lepp nag bokk na ci li waral yewwuteg endustri gi man a am ci Tugal, rawati na ci Britani.

(4) Jokkoo gën a jem kanam gu mu gën a jem kanam:

Li kenn manul a sikk mooy ni endustri jëme kanam ci Tugal de indi na fi ag jëm kanam ci wàllug jokkoo, rawati na bi ligeeyu weñ gënee dox, gën a jëm kanam. Ci noonu angle bii di George Stephonson, moom ñëw , fent saxaarug coolool maanaam , muy daw ci ay banti weñ ci diggante dëkkub Liverpool ak Manchester ci atum 1830g, yoonu weñ wii mooy yoonu weñ wi njëkk ci adduna bi. Ginaaw bi, nitug Amerig kii di Robert Foulton, moom dikk, jëfandikoo coolool, di ci doxale gaali dex yu ndaw yiy daw ci dex yu mag yi nekk ci Amerig gu bëj-gànnaar gi. Ginaaw bi mu jugati, jëfandikooti cóolóol, dawal ci gaali cóolóol yu mag yii di daw ci geej yeek mbàmbulaan yi. Ci noonu la jokkoo tàmblee jëme kanam nànk-nànk, ni ko endustri defe. Bu ko defee, feeñteg jëm kanam ci wàllug jokkoo mujj di feeñte giy raññale tey màndargaal yewwuteg endustri gu mag gii am tay ci adduna bi.

(5) Feeñug campeefi endustri yi :

Ligeeyuwaay yu ndaw yi juge nanu ci kër yi, doon leegi ay campeef yu endustri, yu mag, yu nekk leegi ci dëkk yu mag yi. Endustri yi mujj di loo xam ne am mbooloom ay lonkoo yu endustri, yu mag ñoo koy moom, ñooy lonkoo yooyu nga xam ne ñooy faral a moom li ëpp ci alal yi. Isin yu mag yi nag, ci wetu barabi ne-ne yu nu laalul yi lanu daa faral a sampu, te loolu da leen daa dimble ci ñu man a neewal seeni fere ci lu aju ci seeni ligeey, ndax loolu daa na tax li nu ci waroon a ñàkk gën a neew. Neewug fere yooyu daa na feeñ bu baax ci njëg yi, ndax daa na leen daaneel. Te daa na gën a baaxal ligeey bi gën koo wuuteel.

Li fi yewwuteg endustri gi jur:

Maneesul a sikk ne yewwuteg endustri gi indi na ci Tugal ay ngérte yu yaatu ci wàlli koom, politig ak mboolaay.

Li mu fi indi ci wàllug koom:

Yewwuteg endustri gi bàyyi na fi ay jeexiit yu rëy ci wàllug koom, ci biir Orob ak biteem. Ndax ca la isin yu mag yi tàmblee feeñ, yi daa am jumtukaay yu rëy yi. Li nuy ligeey gën a yokk, gën a wuute, li nu koy jënde gën a neew, ñepp man cee jot, jumtukaayi ligeey yi gën a bari, jokkoo gën a yomb, yoon yi gën a bari, ja yu adduna yi gën a yaatu, lonkoo yu mag yi amoon ay gis-gis aki xemmemteefi rënk ak sanc , tàmblee booloo. Ndax kat sanc gu politig gu yees gii, du lu dul doomi sanc gu koom-koom, gi Tugal daa def, jaare ko ci endustreem bu jëm kanam bii, ak baaxug ay jumtukaayam, ak soxla gu tar gu mu soxla ne-ne yu nu laalul yi, ak soxla gu mu soxla ay ja yu yees, yu mu man a jaaye marsandiisam yu bari yii te wuute.

Waaye mbay nag moom, ak li ay jumtukaayam gën a jamonoo lepp, ak li mu gën a ñaw lepp, te gën a xam-xame, teewul ay njëgi li ciy juge gën a seer, li ko waral mooy li ëppoon ci baykat yi danoo gàddaayoon àll yi, dem ci taax yi, fi isin yi nekk, ngir man fa a ligeey, ndax la nu daa gañee ci ligeey bi moo daa gën a bari, te daa nanu ci ame ag sax fi barab. Gàddaay gii nag, juge ci àll yi, dem ci taax yi, taxoon na ba ab kiris walla jafe-jafe bu rëy amoon fi ci wàllug mbay ci Orob, rawati na ci Angalteer.

Joxalanteg yaxantu gën a yokku ci adduna bi, nga gis reew yiy defante ci seen biir ay kollarantey yaxantu, ak yeneen kollarante yu aju ci yombalug jaarale marsandiis yi ci geej yi, ak mbàmbulaan yi , ak barabi romb yu adduna yi. Ci noonu lonkooy yaxantu yu adduna yi nga xam ne seeni boroom danuy am alal lool tàmblee feeñ, bank yi tàmblee yëngook a sawar, ak këri koppar yi.

Li mu fi jur ci politig:

Sanc gii Tugal tàmblee sanc reewi jàmbur yi ak di leen teg loxo, bokk na ci li fi yewwuteg endustri gi indi, wuutal ko fi, ginaawal ko fi ci wàllug politig, ndax ni ma la ko waxe woon ci ginaaw , endustri day soxla ay ne-ne yu nu laalul, te loolu danu ko daa gis feneen fu dul Tugal, te loolu jur na ay xare ci diggante ay reew ci fu bari ci sunu adduna bii, tax it ba reew yi nu sanc jug, di xare ngir goreel seen bopp, soril senn bopp ag sanc, ak lepp lu ko jege ci xeeti moomadi sa popp, ak tembadi. Bu ko defee, benn dal daal di feeñ ci Orob, mooy dalu “koom-koom bu gore bi walla bu libre ” bi am te taxaw ci nosteg bopp-alal . Loolu nag mi ngi am ci ginaaw bi endustri bu yees bii soppikoo dem ci noste gii, li ko waral di yitewoo gu bari gi mu yitewoo ci nu sos ay isin yu mag, ak isin yu mag yii, yitewoo gu tar gi nu yitewoo alal ju bari ngir taxawal leen, sos leen. Goornamaay Tugal yi, jàpple woon nanu noste gii te dëgëral ko ci mbooleem li nu man, am ko ciy man-man aki kerkeraan . Ci noonu warteefi goornamaa yi gën a yaatu, gën bari ci mboolaayi endustri yi. Loolu yobbu ko ci ay warteef yu mel ni sonn ci mbiri mboolaay yi, te yittewoo leen, sosal leen ay jàngu aki daara yu mag, ak sonn ci mbiri wér gu yaram, ak lepp lu yitteel mboolaay gi maanaam societe bi.

Ci noonu ay boroom xam-xam aki bindkat daal di feeñ, yoo xam ne seen ligeey bepp ñi ngi ko jëmale ci luy dundal mboolaay gi, suqali ko. Ay gisiini politig yu yees feeñ, yoo xam ne bokk nanu ci li fi indi xalaatu politig bu Tugal bu yees bii tay. Goornamaay Tugal yi duggsi nanu ngir aar ligeeykat yi, ci noonu ñu yamale waxtu yi nuy ligeey, def leen leegi ñuy: 7 – 8 waxtu, te bu njëkk 12 – 16 waxtu lanu woon. Ñu ñëwati indi fi noppaluy tawat yi ak yu jeexiitalu ayu bis yi ak yu at yi . Ñu defati ay ligeey ngir yekkati seen payoor yi, jeemati ba seenug dund ak seeni dëkkuwaay gën a baax.

Man gi reewi endustri yi man a doxal seen mbiri reew, feeñ na, te am bi reew yooyu amee alal ju doy ak ngànnaay yu yees te xereñ . bu ko defee, nga gis reewi Tugal yi sukkandiku ci endustri, ëpp doole fuuf yi sikkandiku ci mbay, ak ngànnaay yu yàgg, yi nu miinoon.

Li mu fi jur, indi ko fi ci wàllug mboolaay:

Yewwute gi ci Orob jur na ay gàddaay yu mag, juge ci àll yi, ak dëkk-dëkkaan yi, dem ci taax yi ak dëkki endustri yi, loolu nag mi ngi am ci bi isin yi yokkoo, jumtukaayi endustri yi gën a xereñ cig wàll, moomeeli mbay yu mag tàmblee feeñ ci Tugal, la ko dale ca ñaareelu xaaju xarnub fukk ak juroom ñatt g, rawati na ci Angalteer ci geneen wàll. Bu ko defee baykatu Orob bi moom gisoon ne li ko gënal daal mooy mu dem ci isin yii nga xam ne li nu koy fay moo gën a wóor te gën di lu nu xam, te bàyyi mbay mii nga xam ne leeg-leeg mu baax, leeg-leeg du baax, ak jafe-jafe yi mu àndal, muy njaay meek toppatoo gi. Lii mooy li waral ñiy ligeey ci mbay neew, te wàññiku, ñi dëkke kaw gi gën a neew, loolu it jur yokkug ñi dëkke ci taax yi, bu ko defee, am lu juddoo ci loolu, mooy neewug jóoxiitum mbay mi , te loolu it tax na njëg yi aju ci mbay ak li ciy juge gën a seer.

Beneen jafe-jafe daal di juddooti, mooy bu aju ci dëkkuwaay ñeel way gàddaay yu bees yii gàddaaye kaw ga ngir dëkksi ci taax yi, di wër ligeey. Ci noonu ay barabi dëkkuwaay yu xat tàmblee feeñ ci wetu fi isin yi nekk. Di dëkkal lu sakkan ciy nit, te matalewul li nu laaj ci dëkkiin wu baax te xellu. Ci noonu wér gu yaram dajeeki jafe-jafe yu rëy a rëy , jikko it naka noonu. Jafe-jafey ligeeykat yi gën na a yokku, bi nu demee ba li nu leen di fay manatul a faj gën ja’a neewi seeni aajo, ngir seerug dund gi.

Beneen jafe-jafe bu mboolaay bu bees amati, ànd’ak yewwuteeg endustri gi, ak ag jëmam kanam, loolu mooy ne lu bari ci jigeen ñeek xale yi, leegi danoo tàmbli di ligeey ci isin yi, te kat kenn soññu leen ci ku dul boroom isin yii nga xam ne li leen ñoroon weesuwul nu nu man a gën a ame ay ligeeykat ba gën a man a neew lu nuy fay, ginaaw ligeey bi ci isin yi laajul doole ju rëye noonu ngir man ko. Loolu tam jurati yeneen jafe-jafey mboolaay, ndax tax na ba jigeen bàyyi fi ay ligeeyi boppam, dem ci isin yi, xale yi it bàyyi njàng mi, te loolu ag pert manu koo kawe, ndax xale yi ñooy yaakaari ëlëg. Ag yàqu-yàqu tàmblee feeñati ci wërlaay gu mboolaay yi, ci Tugal, maanaam nit ñi, loolu nag mi ngi am bi ag ñàkk-ligeey tàmblee tas ak a yaatu ci Orob, ci ligeeykat yu góor yii nga xam ne danoo tàmbli woon a nekk ay jafe-jafe dëgg, ci kanamu goornamaa yi, di yëngal, tey sàkku nu nu leen lijantile seen jafe-jafey ligeey yi. Ci noonu goornamaa yi daal di def ay àtte , indi ay sart yu nos ligeey bi, aar ligeeykat yi ci fuqaleg boroom bopp-alal yi moom isin yi.



















Ñatteelu bunt bi





Yëngu-yënguy politig yu mag yi ci adduna bi



Feeñug Diiwaan yu Bennoo yu Amerig yi (U.S.A)

                                  Jeqiku walla fipp  ga amoon  ca Fraans











Doggantal gu njëkk gi

Feeñug Diiwaani Amerig yu bennoo yi

Gàddaay yi waa Tugal yi daa def juge Tugal, jëm Amerig, gàddaay yooyu wéyoon nanu di sottiku ci Amerig gu bëj-gànnaar gi. Loolu nag amoon na, ginaaw bi Kolomboo feeñalee Amerig ba am lu tollook xarnu. Li ko taxaoon a am nag bari na, bokk na ci:

(1) Fitnay diine yi amoon ci Orob gu digg gi ak gu sowwu gi, li waraloon loolu di yëngu-yëngu yu diine yi jugoon di kontar Egliisu Katolig bi, ak la ca juddoo muy ay xeexi ngér, yu amoon ci diggante ngérum Katolig ak mu Protestant , ak xeex bi protestant yi doon def ci seen biir, rawati na ci Angalteer, ak la ca juddoo muy bòddikoonte ci diine, loolu nag waraloon gàddaayug ab lim bu mag ci waa Tugal yi, dem Amerig gu bëj-gànnaar gi, ngir rawale seen bakan, ak ngir man a doxal seen diine ci ag féex akug ngore. (2) Fitnay politig ya amoon ca Tugal ngir xeex jaay doole ga fa amoon, ak àttee na mu la neexe ga, ak la ca juddoo muy ag ñàkk a nosu gu mbir yi ñàkk a nosu, ak ñàkk-kaaraange, ak dox gi nguur yi di doxe ni mu leen soobe, loolu lepp nag taxoon na ba lu bari ci waa Tugal yi gàddaaye woon fi nu dëkkoon dem, wuti ag goreg politig . (3) Wër gi nu doon wër mbèll yu gànjaru yi, lu ci mel ni wurus mbaa xaalis, bokk na ci li leen daa gàddaayloo, ndax kat lu bari ci ñi daa gàdday, danoo gëmoon ne Amerig de reew mu fees dell la ak yile mbèll, te ña fa dëkk, ñu neew ag xay lanu, te ñàkk ag taaxe, te yittewoowunu yenn ligeey yu mel ni lijanti ay wurus aki xaalis ak gasi mbèll. (4) Jëm kanam gi xam-xam am ak endustri ci Tugal, rawati na ci wàllug ligeey ay gaal, googu jëm kanam dimblee na ci nu man a tukki ci geej gi, bay àgg ci barab yu sori yee sori. (5) Ligeey yi nga xam ne lonkoo yu Angalteer yi def nanu leen , ngir meññal ak jariñoo suufus Amerig si ak lijanti nu ñu koy sance te dëkke ko ngir dëgërale ci kilifteefug sanc gu Angalteer ci goxub adduna bu bees bii, bokk na ci li waral gàddaay gi.


Sancu yi nga xam ne waa Angalteer yi taxawal nanu leen ci Amerig gu bëj gànnaar gi:

Waa Tugal yii bawoo woon Espaañ, Fraans, Holand, Suwed ak Angalteer, sancoon nanu ay barab yu wuute ci Amerig gu bëj-gànnaar gi, ñoom lanuy wax tay Diiwaani Amerig yu Bennoo yi , loolu nag di woon ci ñaari xarnu yii di bu fukk ak juroom benneel ak bu fukk ak juroom ñaareel g. Angle yi nag ñooy ñi njëkk a taxawal ab sancu ca Jims Town, ci diiwaanu New York, atum 1607 g, mujj nanu nag ci diir bu gàtt, di ñi gën a tas, gën a wisaaroo ci goxi tefes yu penku yi, ci mbooleem ñi gàddaayeTugal.

Barabi penku yii, maanaam yii nga xam ne la ëpp ca ña fa sancoon, dëkke woon fa ay waa Angalteer lanu woon, barab yii mooy yi mujjoon ginaaw bi (1776 g) di laaj ag temb akug dagge ca reew may nday di Angalteer. Angle yi nag amoon nanu ñaari anam yu nu daa sance reew yi ak a yilife, bi ci njëkk mooy : buurub Angalteer da daan may yenn ci lonkoo yi, gu ci mel ni lonkoo gu Werjiniya gu London gi – mooy bi yoroon mbirum sos sancu bu Jims Town bi nu la waxoon leegi - da leen daa may ay sañ-sañ ci nu taxawal ay sancu, ak jariñoo xeewal ya fa nekk, ak defar xaalis walla koppar yu nuy man a jëflantee, ak topptoo mbirum kaaraange gi. Geneen anam gi mooy: buur bi day dogal garmi yu Angalteer yi ay suuf, ba noppi féetale leen mbirum yor leen ak àtte leen .

Bi fukk ak juroom ñatteelu xarnu g, di agsi ci digg bi, Amerig mujj na yor fukk ak ñatti sancu yu Angalteer, ñooy: New York, Wirjiniya, Rood Island, Masacuusest, Dulawir, New Hamser, Kintakit, North Karolaayna, South Karolaayna, New Jersi, Jorjiya ak Pensilvaniya. Diiwaan yooyu ñooy yi sos, te amal li nuy wax Diiwaani Amerig yu Bennoo yi, ci ginaaw xareb temb gi , atum 1775 – 1783 g, ñu mujj am ag temb ci Angalteer, ci mujj gi. Diiwaan yooyu nag, bu nu leen xoolee ci Amerig gu leegi gii nii, dunu weesu benn xaaj ci Amerig gu nu xaaj fukki xaaj.

Noste gi doon doxal mbiri biir yu sancu yu Angalteer yi:

Nguurug Angalteer gi, daa joxoon ay sancoom yi nekkoon ci Amerig gu bëj-gànnaar gi, da leen a joxoon aw xeet ci “ag àtte sa bopp” , waaye teewul ci biir loolu lepp, mu bàyyil fi boppam kilifteef ak cang gu mu am ci kaw sancu yooyu, maanaam may na leen ñu yor seen bopp, di doxal seen mbiri biir, waaye teewul muy seen kilifa, di reew mi leen moom. Nosteg àtte-sa-bopp googu amoon ci sancu yooyu, mi ngi tegu woon ci ñatti ponk:

(1) Doxalkat bi , (2) Jataayub yoonal bi , (3) Jataayub diisoo bi .

Doxalkat bi walla àttekat bi , mooy kilifa gi yilif dooley xare ji ci sancu bi, mooy feetewoo sàmm mbiri way dëkk yi, di topptoo kaaraange gi, te am na sañ-sañu dindi saxal gu nu defe ci ñaari jataay yii: bu yoonal bi ak bu diisoo bi. Moom nag (àttekat bi) buuru Angalteer bee koy fal ak a folli.

Bu dee nag jataayub yoonal bi, moom ñi dëkk ci sancu bi ñoo koy tànn, li ko tax a jug nag mooy tege galag yi ak fuglu ligeeykat yi, ak saxal seeni payoor, ak payooru doxalkat bi. Bii jataay nag li ko may doole mooy jële gi mu jële sañ-sañam ak kàttanam ci nit ñi dëkke ci sancu bi, ginaaw ñoo ko fal.

Jattayub diissoo bi moom, li ko taxoon a jug mooy di xelal àttekat bi ak jataayu yoonal bi, ak di diisoo ak ñoom. Waaye nag moom sancu bi, ak li mu jot a am lepp, muy “ag àtte-sa-bopp ” gi nga xam ne taxoon na ba nu man fa’a doxal demokraasi, teewul mu nekkoon ab sancu rekk bu toppoon ci ginaaw nguurug Angalteer gi, ci gisiinu waa Angalteer.

Goornamaa bu Angalteer li mu fàttee def mooy, wut nu mu nose mboolooy angle yii dëkke woon sancu yi, ñoom mbooloo yii nga xam ne mujj nanu lu jamono di gën a yàgg, ñuy gën a sori seen reewum nday ma di Angalteer, ci wàllug aada ak dundiin, loolu waral ñu tàmbli koo fàtte, di yëg nag leegi ne fii mooy seen reew, di ci tënku, te di ko fonk. Loolu nag tàmbli woon na a wuute ak politig bi George mu ñatteel mi, taxawaloon, moo doonoon burub Angalteer ca jooja jamono, lii mooy li taaloon ab xare bu mag ci diggante sancu yi ak nguurug Angalteer gi, xare boobu moom lanuy tudde xareb temb bi .

Li waraloon xareb temb bi:

Ñi dëkke woon sancu yi, ay mbooloo lanu woon aki kureel yu wuute, ak doonte la ëppoon ca ñoom ay waa Angalteer lanu woon yu di ay protestant . Seeni njariñi koom-koom it bokkewul woon, te niroowul woon, waaye nag, loolu lepp teewul woon amoon nanu ñatti mbir yoo xam ne kenn wuutewu ci woon, ñepp a ci dëppoo woon, ñooy:

(1) Am gu nit war a am “ag goreg jëmm” , rawati na “goreg pas-pas” (2) Ak sàmmoonteek yoon ak nosu, maanaam nosu gi mbir yi war a nosu. (3) Yëg gi ku nekk yëgoon ne fii ci sancu yii la dëkk, moo dim reewam, fa la feetale ag reewoom .

Ëttub Amerig bii nag mujjoon di def ay mbir yoo xam ne ñoo waraloon xareb temb bi tàkk. Mbir yooyu manees na leen tënk ci yii:

Yoon yuy tege galag ak tembar:

Parlamaa bu Britani bi daa genne atum 1762 g, aw yoon walla luwaa bu nuy wax luwaa bu tembar yi, mooy biy def ngay fay tembar ci jëflante yu Ofisel yi, ak dosyee yi, ak yëglekaay yi añs. Ci atum 1764 g, ñu farataal galag ci suukar si nu daa jële ci sancuy Espaañ yi, yu Fraans yi ak yu Holand yi, teg ci farataalati ko ci ataaya, kayit, weer ak rasaas .

Yoon wi aju ci geeju (navigation) ak yaxantu:

Ci atum 1651g, barlamaanu Britani bi dafa genne benn luwaa buy waral ci sancu yi nuy tuxal li nuy genne ak li nuy duggal di ko def ci ay gaal yu Britani, aaye leen ñuy jëndati feneen, leneen loo xam ne bari na Angalteer.

Koppar walla kee   bu kayit ak jënd suuf:

Sancu yu Britani yi danu leen a aaye woon ci yoon, ñuy genne walla ñuy defar benn kee bu kayit ak di ko jëfandikoo niki kee bu ofisel . Noonu tam lanu teree woon – ci beneen luwaa - ñuy jënd suuf yi feete sowwu fukk ak ñatti sancu yi, ngir jàpp gu nu jàppoon ne yooyu suuf nguurug Britanee leen moom.

Nos dooley kaaraange ji:

Goornamaa bu Britani dafa sosoon jenn doole ju xare ngir aar sancoom yi nekkoon ci Amerig gu bëj gànnaar gi, doole jooju tolloon na ci junniy xarekat , mu waxoon waa sancu yi ne ñooy warlu di joxe depaas yi doole jii di laaj. Loolu nag taxoon na ba waa sancu yi mer, ñaawlu loolu lool, ngir loolu tam goornamaa bu Britani bi ne kon na ci genn, waaye nag galagu ataaya moom dindiwu ko. Loolu tam tax na ba waa sancu yi di yëg ne ñoom daal danuy jëflante ak ñoom, mu mel ne dañuy ay nit walla ag njaboot goo xam ne ñoo gën a neew solo ak daraja ñi dëkke Angalteer.

Waa sancu yi tam yëgoon nanu ne li nuy fay ciy galag lepp, dunu leen ko defal fi nu koy faye waaye kay ca reew mu leen sori mee di Angalteer, te loolu du leen jariñ ci seen dund gi, te du ci def dara. Nga rax ci dolli ne Angalteer mooy reew mi rënkaloon boppam ci sancoom yi, yaxantug marsandiis yu bari, maanaam bari na lool ay marsandiis yoo xam ne Angalteer da ne woon moom rekk a leen sañ a jaay ci sancu yi, lu mel niki ataaya, loolu nekkoon na lu waa sancu yi ñaawlu woon. Ci nii daal la xew-xew yi toppantee woon, di nëxal nag sellug seqoo gi amoon ci diggante Angalteer aki sancoom, loolu tam gën a yaatal paxum reeroo mi nekkoon seen diggante. Loolu nag gën na a fés, bi waa sancu yi bañee ne dunu fayati galagu ataaya, ginaaw bi tam am mbooloo jug, ci desambar atum 1773 g, lakk ñatti gaal yu nguurug Angalteer, yu nu duyoon ak ataaya, ca waaxub Boston, ca sancu bu Masacusets, loolu waral waa Angalteer tëj waaxub Boston bi, ne gaalug yaxantu du fi teerati, daal di ne moom ci jëmmi boppam mooy yoral boppam sancu boobu. Xew-xew bii ak la ca juddoo , man nanu ne moo waral xareb temb bi.

Ndajem waxtaan mu Filadelfiya mu njëkk mi:

Juroom ñeenti diiwaan yu Ameriig teewe woon nanu ndajem New York ma, atum 1765g, di sàkku ci nguurug Angalteer mu teggil leen galagu tembar bi mu leen di teg. Ci noonu Angalteer teggi woon na galag boobu waaye teewul mu wéyoon di tege yeneen galag yi nga xam ne ab Parlamaam daa na leen woote, te di leen farataal ci mbooleem ay sancoom yi nekk ci adduna bi.

Looloo taxoon reenub reeroo bi amoon ci diggante Angalteer aki sancoom saxoon fi di lu ñu dogadi, ndax kat sancu yi danoo gisoon ne di leen teg ay galag te seeni jataayi yoonal ànduñu ci, bu amee lu muy tegtale mooy dindi màndargam demokraasi mi seen jataay yooyu di doxal seeni mbir ame woon, ndax kat daa am ab dal bu nekk ci demokraasi, bu naan “doo fay galag boo amul ndaw” .

Man nanu ne ndajem New York mi mooy lu njëkk a feeñ te nosu loo xam ne waa sancu yi def nanu ko, di ci kontar ni Angalteer di àttee seen reew yi.

Ñoñ sancu yepp a meroon bi Angalteer tëjee waaxub Boston bi, bu ko defee ñu taxawal am ndaje ca Filaadelfi, atum 1774 g, jàmmaarloo fa’ak Angalteer ne ko na xam ne lepp lu mu defati benn sancu ci sancu yi, na ko wóor ne sancu yepp la ko def, daal di ñaawlu bu baax jëf yu ñaaw yi Angalteer tegoon Boston . Njiitul xare lii nuy wax George Washington (1732 – 1799 g ) teewe woon na ndaje ma. Ndajem Filadefi moomu, mooy dàtt bi nga xam ne ci la Kongres mujj a teggu, ci ginaaw bi .

Jaadu na ñu leeral leen ne ndajem Filadefi mi li ko taxoon a jug du sàkku ag tembte , waaye kay yëgal Angalteer ne lu wuuteek demokraasi lii muy def ci sancu yi neexu leen, te man na a nëxal te yàq xaritoo ak jàmm ji amoon ci diggam ak ay sancoom. Ñoom kay seeni càkkuteef weesuwutoon lii, mooy na Angalteer xam ne ñoom sancu yi kat ñoo ame àq ak sañ-sañ - ci seen jataayi yoonal yi – ci tege ak farataal ay galag ci waa sancu yi.

Angalteer nag, ci safaanub muy lijanti lëj-lëj boobu ci maslaa gu xereñ, moom daal da fee nekk di yonnee ay dooley xare yu yees ci Boston, ngir gën a dëgëral doole ja fa nekkoon. Loolu tam li mu juroon mooy waa sancu yi ñoom itam, ñu ne woon nanu waajal seen bopp, ndax kat nguurug Angalteer gi bëggul jàmm, ci noonu ñu - ñoom waa sancu yi – defaat beneen ndaje ci Filadefi, ngir jàng mbir mi, seet nu ñu ciy def.

Ndajem Filadelfi mu ñaareel mi:

Ndawi sancu yi defoon nanu am ndaje atum 1755 g, ca Filadelfi, muy ñaareelu ndaje mu Filadelfi mi, ñu wax fa ne danuy sos menn mbooloom xare , te bennal ko, bañ a def sancu bu nekk am sa mbooloom xare, bu ko defee nag, mbooloom xare moomu ñu tànne ko ci waa sancu yi, ngir ñu aar leen ci ay wi leen dëgmalsi. Ci noonu ñu duggal doomi sancu yi ci xarekat yu bees yii nga xam ne George Washington moo leen jiite woon. Waaye teewul ñu yonnee ca buuru Britani bi, ab bataaxel buy sàkku ci Angalteer mu xoolaat ni muy jëflanteek sancu yi, te lenn baaxu ci, waaye buur bi moom jàpp fa mu jàppoon rekk, ne daal am na ag cang gu nu joyal ci kaw mbooleem sancu yi. Ci jëfam jooju la tëje buntub jeem gi sancu yi doon jeem ngir defar – ak doonte lu neew la itam – seen diggante ak Britani, reew miy nday.


Ni xare bi tàkke :

Bi buur bii di George mu ñatteel mi, ñàkkee faale càkkuteefi sancu yi, ne daal li wér mooy moo ame cang gu joyu gi ci mbooleem sancu yi, maanaam sancu yepp ci ron kilifteefam lanu nekk, ci anam gu matale te daj, bi buur bi nekkee ci taxawaayam boobu ne du ci juge la xare bi tàkk ci diggante ñaari wàll yi, sax nag lu toll ci juroom ñaari at daanaka (1775 – 1783 g ), bu ko defee, mu tas nag ci li ëpp ci sancu yu Amerig yi, George Washington nag jot na a man a nangu Boston, ginaaw bi mu ko gawee. Dooley gornamaa bu Britani moom, teg loxo lu bari ci waaxi Amerig yi. George Washington ni mu doon xeexe ak ñoom nag mooy xeexub bette, ci barab yu bari, ak door-daw, foo ko fekk daawul nangoo jaamaarlook ñoom, ndax xammoon na ne ñoo ko ëpp doole te gën koo tàggatu.

Ak li xarekati sancu yi doon jànkoonteel lepp ciy coona yu tar ci biir xare bii, teewul George Washington gañe woon na njiitul Anglteer lii di Burgoyne, ci xareb Saratoga, loolu mi ngi am bi mu jawalsee juge Kanada, jëm New York, ci oktobar 1777 g. Ca saa sa, ginaaw bi nu gañee Britani, Fraans jug na, yëgleb xareem ci kawam atum 1778 g, Espaañ roy ko ci, atum 1779 g, Holand topp ci atum 1780 g. Man nanoo wax ne Fraans moom jàpple na way fippi sanncu yi ci wàllug xare (militaire) ak ci alal, ba tay it dajale na way coobarewu yu Fraans yi, yobbu leen ci Diiwaan yu bennoo yi, ngir nu xeexle leen ci ron njiit lu xare lu Fraans lii di Lavette, kontar Angalteer noonam bu mu yàgg a noonool bii. Ci noonu Britani mujj war a xare ci jë yu bari.

Dàq gi nu mujj a def dooley angle ji, ci sancu yi, mooy gi nu defoon seen njiit la Cornwallis, loolu di bi mu deltoo ginaaw, dem dëkkub York Town, fa dexug York di sottikoo, ginaaw ba ko fa mbooloom xarem George Washington ma songee. Xarekati George Washington yooyu nag am njaxasiitum kureel lanu woon mu ame ci diggante ay waa Fraans aki ñoñi sancu, tollu nag ci fukk ak juroom benni junniy xarekat.

Nanu fàttaliku nag ne waa Amerig yi ñoom, ci seen suuf lanu doon xeexe, bu ko defee dolli leen doole ci xare ak ci alal day gën a yomb, gën a gaaw, bu dee waa Angalteer yi xawoon a sori Kanada, fi seen bagaasi xare daan juge, walla Angalteer mi leen soree woon lu tollook ay ñatti junniy miil daanaka. Nga rax ci dolli, waa Amrig yi danoo dogu woon bu wóor ci raxasu ci teg loxo gi Britani tegoon loxo seeni mbir, te amoon nanu ay njiiti xare yu bari, ku ci mel ne George Washington. Doolil ci loolu, nekk gi waa Britani nekkoon di xeexe ci sancu yoo xam ne manuñu fa’a ame jokkoo ak dolli doole ga war, ca anam ga mu ware te gaaw, te itam pasteefub xeex bi nu amoon moo gën a suufe fuuf bi waa sancu yi amoon, ñoom ñi taxawoon tamb ci xettaliku ci waawug nguurug Angalteer gi. Bokk na ci li doyadil waa Britani yi ci xeex bi, ubbi gi nu gubbi woon ay jë yu xare yu bari ci seen kaw, ci barab yu sakkan ci Amerig.

Tembug Diiwaani Amerig yu Bennoo yi:

Bi waa Britani xamee ne lòtt nanu ci toroxal jeqiku gi amoon ci Amerig, te xam ne doole du mooy lijanti lëj-lëj yi nekk ci sancoom yi, ndax kat mi ngi nii di ku nu dàqe, gañee ko ca xare ba, bi loolu amee mu sàkku woon ag juboo, ci noonu ñu xaatim juboo gi ci Paris, ci digganteem aki sancoom atum 1783 g, lii mooy poñ ya ca ëpp solo:

(1) Britani day nangu tembteg sancu yi nekk ci suuf yi feete ci penkub dexug Misisipi gi, te jàppe dex gii muy diguw soww wi ko tàqale ak sancu yi. Bu ko defee dig yu bëj gànnaar yi ñoom ñu bàyyi leen nanu nekke woon. (2) Jeem a rafetal seqoo yi, ci diggante Britani ak reewum Amerig mu temb mi (Diiwaani Amerig yu Bennoo yi) (3) Amal ci diggante Britani ak Amerig gu temb gi, ay seqoo yu yaxantu ak yu koom-koom, waaye nag seqoo yooyu ñu teg leen cig nawlante, ak moroomante, kenn du jaay kilifteef sa moroom.

Nii daal la Diiwaan yu Amerig yu Bennoo yi ame, xareb temb bi nag am na benn jeexiit bu rëy te xóot, ndax wal na te upp ngelawul gore ak temb ci mbooleem sancu yi. Lii nag làppal na Britani, loofloo ko, ci wàllug xare ak politig, nga rax ci dolli alalam ju bari ji mu ci ñàkke.

Amerig nag moom, daal di ñew, defar sartu reewam , daal di taxawal ndajem booloo mi nga xam ne Kongres moo ko digale woon, atum 1788 g, mbooleem ndawi Diiwaan yu Bennoo yi teewe woon nanu ko, ba mu des diiwaanub Rood Island. Cer ya fa nekkoon tam, tànn cig dëppoo, George Washington muy njiitul ndaje mi, ci loolu la nekke ki njëkk a nekk njiilul Diiwaan yu Bennoo yi. Ginaaw bi lanu def Washington – ginaaw bi mu nekke peeyu koom-koom bi ak bu alal bi – la nu ko def peey bu politig bi. George Washington nag jëloon na xalaatam yepp, def leen ci nu muy def ba bennal Amerig, looloo taxoon waa Amerig yi soppoon ko, wormaal ko, waxam it weesuwutoon : (( doon leen benn, doon leen ay waa Amerig ..)) , loolu saxoon ci seen xel yi. Washington moom wàcci na jal bi, joxe njiit gi, atum 1797 g, ginaaw bi mu ko yoree ñaari yoon.















Doggantal gu ñaareel gi

Jeqiku walla fipp ga amoon ca Fraans :

Jeqiku walla fipp ga amoon ca Fraans, mooy jeqiku gi njëkk a am ci jamono ju bees jii, ci kaw nguuru ak jaay doole, ak doxale ni la neexe, doo diisoo, doo deglu xalaatu keneen. Moom nag (fipp googu), mi ngi ame woon ca Fraans, ca jamonoy buur ba tuddoon Luwis mu fukk ak juroom benn ma, bokkoon ca njabootug Barbon ga, loolu nag di woon ca noorub 1789 g, saxoon it diir bu toll ci fukki at, ba ca nawetub atum 1799 g, bi Jeneraal bi tuddoon Napoleon Bonaparte (1769 – 1821 g) defee yong gu nuy wax yongug 18 Brumaire, dëppoo ak 9 nowambar 1799 g, daal di daaneel doxaliin wa fa nekkon, jële fa it jataayub mag ña , mujj nag di kenn ci ñatti kilifa yiy doxal mbiri reew mi. Bonaparte mii - nga xam ne mujj na di kilifag Fraans gu njëkk gi, ci atum 1800 g, mujj it di imbraatoor ba atum 1804 g – moom Bonaparte mujj na am tawfeex ci dindi lëjug politig ga fa amoon, ñàkk jàmm ga, tiitale ga , tuur dereet ga, ak yeneen jëf yu ñaaw yi àndoon ak fippug Fraans gi. Loolu nag taxoon na ba “fipp gi” manu fi woon a amal dali gore , yamoo, mbokkoo yi nga xam ne ñoom la yàgg a yekkati kàddoom ngir saxal leen fi. Waaye nag jeexiit yi nga xam ne fipp gii ba na leen fi, yamuñu rekk ci Fraans, waaye weesu nanu ko ba daj Tugal gepp, ak lu bari ci reewi adduna bi.

Ni Fraans meloon laata fipp gi:

Bu ñu gëstoo na Fraans meloon laata fipp gi, loolu di na nu dimbli ci nu man a xam li waral fipp gi, atum 1789 g.

Melokaanu politig wa:

Buuri Fraans yi, ni ñu doon àttee Fraans, du woon nenn nu dul ni mu leen neexe. Buur bi moo daa saytu lepp, kepp ku am nguur moo la ko daa jox, moo daa doon balluwaayu mbooleem doole yi, ak sañ-sañ yi, walla nga ne sax mooy nguur gi, di sañ-sañ bi, di kàttan gi, di doole ji. Loolu nag man nga koo degge ci waxi buurub Fraans bii tuddoon Luwis mu fukkeel meek ñeent : ( Man maay nguur gi ).

Buur bi mooy ki am sañ-sañ ci def ay yoon , ak neenal leen, tege ay galag, def ci alali reew mi lu ko soob, tabb jëwrin yi, fal ligeeykat yi, folli leen, joxe ay ndigal jaare ko ci ay bataaxel yu nu xaatim, ngir nu jàpp ku ko soob ci askan wi, ak tëj ko ci lu dul mu koy àtte mbaa mu koy laaj dara. Buur bi daal - ci gàttal – lu ko soob mu def . Ndax moom dafa gis ne mi ngi wéeru – ci sañ-sañam boobu – ci gis-gis bi fiy indi “sañ-sañu Yalla bi”, mooy li naan buur bi daal, nguuram gi, ak sañ-sañam bi mi ngi bàyyikoo ca Yàlla. Luwis mu 16 mii nag, nga xam ne ci atum 1774 g la nekkoon ci jal bi, tey buur bi nga xam ne ciy jamonoom la fipp gi xewoon, moom Luwis mii, nekkoon na ku doyadi, te daan dengi-dengi. Moom de jaraafam yi danu koo yilifoon, ak bëkkneegam yi, ak soxnaam si bàyyikoo woon Hongri, Mari Antuwanet (di woon doomi lingeerub Ongri ba, Mariya Tereesa), moom soxnaam soosu nag, ku yëgoon boppam la te faaleedi woon askan wi, taxoon na ba kenn manut a def genn yéwénal, kenn manul a jàpple buur bi ci luy defar. Moom daal nekkewu fi woon lu dul yàq alal, noos, ak caaxaan, nekkoon it ku diis, te rëyal boppam, looloo taxoon mu mujjoon di ku waa Fraans yi bañoon.

Njabootug Barbon gi, yàgg nanoo jariñoo seen nguur gi, ci luy lor askanu Fraans wi, ñoom daal danu daa nangu alali ku leen neex, daan tëj ku leen soob, daan xeexloo reew mi saa su leen soobee, te xeex yooyu yu ci ëpp danu ci daa gañe Fraans. Bari na lool lu ñu daa tabax ay njénd , di ci sotti alali reew mi, ak di may seen dag yi alal ju dul jeex, seen dag yu bari yooyu nga xam ne tolloon nanu ci 18 junniy nit, atum 1789g, te lu ëpp ci ñoom defuñu fa woon dara, amul lenn lu nu fay ligeey lu amal njariñ reew mi. Looloo taxoon njëlul nguur gi loof, mujj moom nguur gi fees dell aki bor.

Nguur gi kat mujj na ay deppaasam àgg ci 130 milyong yu Frank, atum 1789 g . Li mu ameele woon ciy bor àgg ci 206 milyon yu Frank, ngir lòtt gu njëlam li lòttoon.

Baj-baji ak doxadi amoon na ci wàllug doxaliinu nguur gi, ci wetu doxe ni la neex ga amoon ca wàllug politig ga. Nattukaayi gox bii daawul bokk ak bee, naka noonu yoon yi , màndaxekaay yi, galag yi. Ci noonu Fraans mujj di reew mu ay gox boole, gox bu ci nekk am ay yooni boppam , aki nosteem yu wuuteek yeneen ya ca feneen, loolu nag waraloon na ag lënt ci nosiin yi ak luwaa yi, reew mi mujj seddaliku, doon ay doxaliin yu temb. Bu ko defee, Fraans mujj doonatul menn reew, waaye ay doxaliin yu wuute te tas.

Na mboolaay ga meloon:

Mboolayug Fraans gi, njëkk fipp gi, dafa seddaliku woon, doon ñatti kureel yu mboolaay, ñooy: kureelug ñu tedd ñi, walla garmi yi, kureelu niti diine yi, ak kureelu mbooloo mi walla baadoola yi. Ñatti kureel yii nag – ñoom de ci li fi jamonoy laman desaloon lanu – yamoowunu woon ci àq ak yelleef, du caageegug ci ay warteef, li am daal mooy ag yamoodi gu mboolaay amoon na ci seen diggante, jefkay tàqali ak feewaloo ruuru leen, ak boddante gu mboolaay.

Bu ko defee kureelub garmi yi nu teggil leen galag yi, ña ca bokk it ñoo daa feetewoo pal yu kawe yi, yu siwil yi ak yu xare yi , ci nguur gi. Ñoom ba tay, daa nanu am ay cer ci mbayum baykat yi, ak ci jurug sàm yi, ak seen ñanaaw yi. Amoon nanu it sañ-sañ ci rëbb ci tooli baykat yi. Baykat yi tam amunu wonn sañ-sañ ci wal seen dugub ci lu dul walukaayi garmi yi, te seen reseñ it sañuñu ko woon a nale fu dul ci seen nalukaay yi.

“Nitu diine yi” nag ñoom, seen kureel moom itam bu ràññiku la woon, niki bu garmi yi, ñoom de daa nanu am ay suuf yu nu leen dogal, yu yaatu, yu daa toll ci juroomeelu suufi nguur gi, maanaam bu nu xaajoon suufi nguur gi juroomi xaaj, benn xaaj bi. Ñoom itam, ñu nu teggiloon ay galag lanu. Li Egliis bi daa gañee ci suufam yooyu, ak ci galagi diine yi nga xam ne mbooloo mi daa nanu ko ko fay, àggoon na ci 200 milyon yu Farank.

Loolu lepp nag daanaka ñi ko daa jariñoo, ñu neew la daan doon ci niti diine yi ak seeni njaboot, bu ko defee ñu bàyyi nee way ndool yi, ak ñi aajowoo, kenn du leen dimbli. Ña ëpp nag ca niti diine ña, taxutoon ñu feexoon, moo taxoon danu daan ànd ak mbooloo mi, kontar garmi yi.

Kureelub mbooloo mi nga xam ne la ëpp ca askan wa ca lanu bokkoon, ñoom jegge woon nanu, bi fipp gi di bëgg a door, lu tollook 25 milyongi nit , te kat booba garmi yi bu nu leen boolee ak niti diine yi weesuwunu woon 300 junniy nit. Coonab galag yepp ci ndoddum baadoola yi la daan tegu. Kureel boobu nag (bu baadoola yi), moo ëmboon kureel bu diggu bi, walla bi nuy wax (Bourgeois), ak kureelu baykat yi ak bu boroom mecce yi ak bu soldaar si.

Bu dee kureel bu diggu bi moom, ca la boroom xam-xam ya bokkoon, xalaatkat ya, boroom xel yi. Ñoom nag amunu woon sañ-sañ ci pal yu kawe yi. Moo ëmboon it yaxantukat yi, ak boroom alal yi daa fay galag yu mag yi, nga xam ne seen fay gu metti gi nu daa fay galag yi, ak lamb gi amoon ci seen yaxantu gi, taxoon na ba seen koom-koom daanu woon. Lii lepp nag taxoon na ba gii kureel meroon lool ci goornamaa bi, te meroon it ci ay jëfam ak ci li nu defaloon ñaari kureel yii di bu garmi yi ak bu niti diine yi.

Bu dee “kreelug baykat yi” nag, ñooy ñi gënoon a sonn ci kureelug baadoola yi, ñoo ci daa njëkk a yëg aw ay bu jafe-jafe bu kopooar amee, ndax ci seen kaw lanu ko daa tegaat, ci fayloo leen ay galag, ak teg leen ligeey yi gën a tar.

Bu nu nee “kureelub soldaar si”, ñi ngi ci jublu soldaar su ndaw si, ak boroom ndomay xare yu ndaw yi, ndax ndoma yu mag yi moom, ak pal yu mag yi, garmi yi lanu leen daa jagleel.

Na fa xalaat meloon:

Ak li Fraansu njëkk fipp gi, di gënadi woon a nekk cib coona, ak ñaawug nekkiin yeneen reew yi mel ne : Itaali, Otris, Brusiya, ak Riisi lepp, teewul waa Fraans a gënoon a yëg yeneen reew yi tooñaange yi nu leen daa teg. Li waraloon loolu nag mooy yewwuteg politig ga fa amoon ak gu xalaat ga, ca biir boroom xel ya ca kureelub baadoola ya, di yaxantukat ya, ustaas ya, layalkat ya , doktoor ya, boroom xam-xami koom-koom ya, bindkat ya, xeltukat ya añs. Jamono jii , dafa fiiroo ak diggante bob Fraans da cee amoon ay xalaatkat yu mboolaay, ak yu koom-koom yu leen daa yee ci coona yi nu nekke, ak bonug nosi politig ya fa amon, yu mboolaay ya, yu doxaliin ya, ak yu alal ya. Da na jaadu nu waxtaane fi ñatti xalaatkat yoy ligeey nanu lu rëy ci tas fi xalaat yi fi indi fipp gi. Ñooñu ñooy: Montesqieu, Voltaire, Jean Jacques Rousseau.

Bu dee Montesquieu (1689 – 1755 g) - moom mi nga xam ne siyaare na Angalteer, gondiku woon it lool ca nosteg sartu reew gu buur ga fa nekkoon – moom de ay ligeeyi xam-xamam mi ngi feeñe woon ca teereem ba tuddoon “Ruug yoon yi” (1748 g), teere boobu nga xam ne teere bu jaroon la, bu boroom xeli yi fonkoon la ci Fraans ak feneen. Xalaati Montesquieu yi ñi ngi tënku ci fexee tënk goornamaa bi, te fuglu ko ak tàqale diggante dooley yoonal ji, ak ju doxal ji, ak ju laman ji . Moom Montesquieu nag li mu doon wut ci teereem boobu mooy taxawal ag atte gu tegu ci sartu reew ca Fraans. Ndax kat moom dafa gondiku woon lool ca sartu reew bu buur ba amoon ca Angalteer.

Bu dee Voltaire (1694 – 1778 g), moom de woote na jëme cig coppi ci nekkiinu askanu Fraans wi, jaare ko ci taalifam yi mu defoon ciy woy, nga xam ne taalifi jam lanu woon ak yéjj . Moom de jamoon na nosteg politig ga amoon ca Fraans ak gu egliis ga, ak sañ-sañ yi garmi yi amoon ak niti diine yi.

Wolteer de ak li xalaatam yi doonadee woon lu yees lepp, teewul seen solo ñi ngi feeñe woon ci nekk gi nu nekkoon di luy laal yëg-yëgi waa Fraans yi, ngir nekk gi ñu nekk di ay xalaat yu nit yuy jeexiital.

Wolteer de gore ga waa Angalteer ame woon da koo neexoon lool, yeemoon ko, mu jeexiitalu ci, ginaaw ba mu fa amee ñatti at, li waraloon mu nekk fa nag, mooy danu koo dàqe woon Fraans. Gore googu mu gisoon ca Angalteer, ak xalaat ya mu fa ame woon, feeñal na leen ca teereem ba tudd “bataaxeli xeltu” , walla ay bataaxel yu bawoo ca waa Angalteer, atum 1734 g. Wolteer nag dàq gi nu ko dàqe woon Fraans, yobbu ko Angalteer ak tëj gi nu ko tëjoon lepp ca kasob Bastil bu metti, bu raglu ba, teewu ko woon a wéy ci jam garmi yi ak niti diine yi. La desoon ca dundam ga lepp it da koo jeexaloon ci nekk di ku yoon di wër. Bu dee Jean Jacques Rousseau (1712 – 1778 g), mooy boroom teere ba tudd “kollareg mboolaay” , mooy teere bi doon woote jëme ci goreg nit ak yamoo gi nit ñi war a yamoo ci wàllug mboolaay, mu neeti goornamaa bi daal li ko war mooy mu sonn ci yittey nit ñi. Fippug Fraans gi, mi ngi sukkandiku woon – bi muy lim yelleefi ki dëkk Fraans – mi ngi sukkandiku woon ci xalaati Rousseau yu mboolaay yi nekk ci teereem boobu nu doon wax leegi.

Jafe-jafe bu koppar ba:

Atum 1789g, mooy at mi fipp gi ame woon, nekkutoon at mu ya ko jiitu woon tane, ci wàllug koom, waaye la waraloon fipp ga am ca, mooy ñàkk a taw ga mu àndaloon, ga juroon bekkoor ba ak xiif ba, nit ñi mujjoon di ñu ñàkk, aw ñam jafe, dundiin wi naqari. Bokkoon na ci li gënoon a mettil mbir mi, galag yu bari yi nga xam ne tege woon nanu leen, te lepp di woon ci ndoddum baadoola yi, ngir mëdde ci depaas yu bari yii nga xam ne nguur gi daa na leen def, ngir boram yu bari yii mu daa jële ci xare yii mu daa faral a def ci biti, ci jamonoy Luwis 14 ak Luwis 15, te loolu ci li daa jeexal ay koomam la woon.

Luwis 16, bi mu ñëwee jeem na ba sonn, ngir lijjanti jafe-jafe bii amoon ci mbirum alal mi, ak loppanti njëlul nguur lu loof lii te sonn, jaare ko ci tege ay galag yu bees, waaye mujj na di ku manutoon a ñàkk a woo “jataayub kureel yu xeet wi” – bii nga xam ne danu koo tasoon ci jamonoy Luwis 14 – ngir mu daje.

Naka la fipp gi ame woon :

Doomi kureel gu diggu gi, begoon nanu lool, bi Luwis 16 woowee jataayu kureel yu xeet wi, ngir mu def am ndaje ngir gëstu yoon yi man a lijjanti jafe-jafe bii aju ci lòtt gi njëlul reew mi lòttoon, ñu gisoon ne loolu daal pose bu mag la ngir nu indil seen bopp, saafara si ko man a faj, te fajal ko seen bopp. Ñi daa woote yewenal it jàppe woon loolu pose ngir def seen yewenal yi nu yeene woon, ak soppi yi nu bëggoon ngir Fraans man a baax, man a tegu ci yoon, bañ koo yamale ci loppanti njël li rekk. Ci noonu ag wuute am ci diggante kureelub garmi yi ànd ak bu niti diine yi ci wàll, ak kureelub baadoola yi ca geneen wàll. Bu ko defee waa kureelub baadoola yi sàkku woon ñu def woote bi mu sukkandiku ci cer yi te bañ a sukkandiku ci ay neeg, ndaxte la doonoon aada foofa mooy kureel bu nekk ci ñatti kureel yooyu, da daa am genn kàddu, bu ko defee yenenn ñaari kureel yi (bu garmi yi ak bu niti diine yi) bu ci nekk am ñaari kàddu, bi ñaari kureel yii lànkee, ne deesu fi wootee, di ko teg ciy cer , ne daal ay neeg ñooy woote, bi loolu amee, ceri kureelu baaloola yi danoo daje ñoom nee, cig beru, ñu neew ci garmi yi ak niti diine yi jàpple leen, dëgëral leen, ku ci mel ni garmi bii di Mirabo, ñu waxoon ne ñoom daal ñooy ndawi li ëpp ci askan wi, ñu giñoon it ca fowuwaayu tennis ba nekkoon ca wetu njéndul Versay la, ci atum 1789 g, ne ñoom de dunu bàyyi mukk lii nu nekke li feek wutalunu reew mi ab sartu reew bu man a yewenal seenu nekkiin te baaxal ko, ak doonte Luwis 16 moom li mu àndoon mooy kureel yepp daje, te xam ne ñooy ndawi reew mi, bu nu booloo, waxul bu benn taqalikoo nee, beru. Ci noonu way daje yii nga xam ne danoo tudde woon seen ndaje mi, ndajem xeet wi , walla “jataayub taxawal bi” , ñoom de foofu lanu nekkoon ci defar sart bu bees bi ñeel Fraans, bi nga xam ne day leeral li waa Fraans bëgg, tey jeem ci seeni aajo. Jëf jii nag mooy doorug fipp gi.

Tolluwaay yi nga xam ne fipp gi romb na leen:

Ceri ndajem xeet wi daje woon nanu ca Versailles ngir defaral Fraans ab sartu reew bu yees. Askaan wi daal di jañu jëm ca kasob Baasil ba, ca Paris, ca 14 sulye 1789 g, song ko, nangu ko, genne ña ñu fa tëjoon ngir politig. Jëf jooju mujj di juy wone gore gi nga xam ne moom la fipp gi doon woote jëme. Ñu mujj jël bis boobu def ko màggal gu xeetu Fraans wi di màggal, at mu nekk .

Nangu gi nu defoon kaso bi, ñemeloo woon na baykat yi, ñoom itam ñu jug, song suufi garmi yi, yàq seen njénd yi, looloo waraloon lu bari ci garmi yi gàddaaye woon Fraans, dem feneen. Nekk gi nu nekkoon feneen, mujjoon na di aw ay ci Fraans, ndax buur yi nga xam ne doonuñu woon ànd ci fipp gi, ndax du seen njariñ, danu leen doon ngemb ngir ñu xeex ko, te loolu doon na jëme ci xareb ñoñ .

Askanu Paris wi wutaloon nanu seen bopp ay ngànnaay, ñu daal di woon sos ag wattu gu reew ngir wattu fipp gi, aar ko, Lafyette jiite ko, moom mi nga xam ne waxoon nanu la ne doon na xeex di jàpple waa sancu yi kontar waa Angalteer ca xareb temb ba. Xarekati fipp gi, ñi leen jiite woon ay nit lanu ñu bañoon te sib doxaliinu njabootub Barbon gi, ak seeni dag, Lafyette moomu ci la woon, ñoom de seen xol yi dara nekku ci woon lu dul mbañeel, wañse ak gënjëng .

Ci bis bi njëkk ci ut la ndajem xeet wi jibal “àqi nit aki yelleefam”, ci 4 ut, mu neenal sañ-sañi laman yi ak yeneen yi garmi yi ame woon, ak niti diine yi. Xeet wepp mujj daanaka di jàpple fipp gi, lu bari ci doole ju ngànnaayu ju Fraans ji mujj fekksi “wattu gu reew “ gi nu taxawaloon ngir wattu fipp gi. Ci noonu mbooloom xare mu Fraans mi tas, Luwis 16 mujj ànd ca la xewoon ca kaso ba. Waaye way fipp yi digale nu sàmm Luwis 16 ba du daw, ci noonu ñu taxawal seen bopp ci doxal mbirim reew mi, ak mu Egliis bi ci wàllug doxaliin ak alal, loolu moo merloo woon paab gi, mu mujj moom paab gi di kenn ci ñi gën a noonu fipp gi. Ñu daal di bennal nattukaay yi, ak yoon yi , ci Fraans gepp, ñu daal di seddalewaat Fraans def ko ay doxaliin yu bees .

Bi ndajem xeet wi di teg sart bi, Luwis 16 doon na jeem a dolli ay kàttanam aki sañ-sañam, bi mu ko manul nag, la doon jeem a daw, juge ca njéndam la, waaye ñu jàpp ko ca Farn, ca 22 suye 1791g, njëkk muy genn reew mi, gis nanu tam benn dosyeem bu mu fi bàyyi woon buy feddali ne moom daal nanguwul yoonal yooyu mu àndoon, ndax ànd googu mu ci àndoon danu ko cee manante woon , waaye du lu mu def ci teeyug bakkan. Ndajem xeet wi eggal na sart bi ci 14 sebtambar 1791 g, loolu di bi fipp gi amee ba toll ci ñaari at, bi mu ko defee nag, ndajem xeet wi daal di tas boppam, daal di fiy taxawal ab jataayub yoonal bu sukkandiku ci li nekk ci sartu Fraans bu bees bii nga xam ne lu feddali woon àqi ak yelleefi nitug Fraans la woon, ak war gu mu war a gore te am ag yamoo ci wàllug mboolaay. Moom sart bi tam tàqale woon na diggante nguurug yoonal gi ak gu doxal gi ak gu àtte gi. Mu jël nguurug yoonal walla dooley yoonal ji, teg ko ci loxol ab jataay bu askanu Fraans wi di tànn, mu jël dooley àtte ji , teg ko ci loxol ay àttekat yoy danu leen di tànn, mu jël nag dooley wéyal ji walla ju doxal ji , teg ko ci loxol buurub Fraans bi aki jëwrinam. Ndaxte nguur saxoon na ca Fraans ba ca 21 sebtambar 1792 g.

Ci atum 1792g, beneen woote amoon na, bu nu doon tànnewaat ab jataayub yoonal. Ci noonu jataayub xeet daal di sosu, boo xam ne li mu njëkk a def mooy jibal nosteg pénc (systeme republicain) ca Fraans, ca 21 satumbar 1792 g. Ñu feetele ko doxal reew mi, ak teg sart bu bees buy sukkandiku ci nosteg republig gu bees gi, ñu wax ko tam mu seet li nu war a def buur bii di Luwis 16, te teg yoon yuy aar fipp gi, aar it Fraans ci musiba yi ko man a dikkal, juge ci reew yii di : Otris, ak Brusiyaa, ak Britaani, ak sax yeneen reewi Tugal yoo xam ne danoo noonu woon fipp gi. Feetale nanu ko ba tay taxawal goornamaa bu Fraans bu dëgër, boo xam ne da fiy jeem a jële fitnay biir reew mi. Ñi jiite woon goornamaa bu jataayub xeet boobu nag , ñi ngi sosoo woon ci “Girondins”yi, ñooy ñi nga xam ne danoo gëmoon ag yewenal, te daan woote jëme ci coppat goo xam ne danu koy amal cig nànk-nànk, ak ci “Jacopins” yi xam ne, ñoo gënoon a xaabaabal Girondins yi, danoo gëmoon ne fii Fraans toll tay ak nekkiinam wii, danu koo war a soppi bu wér ak doonte loolu dafa laaj doole. Ak ñu diggdoomu ñoo xam ne taxul woon leen a xaabaabal, ñoom ñooy ña ëppoon ca jataayub xeet wa, waaye amunu woon gis-gis bu dëgër, ndax leeg-leeg ñu ànd ak Jacopins yi, leeg-leeg Girondins yi.


Ligeeyub goornamaa bu jataayub xeet wi:

Goornamaa bu jataayub xeet wi, daal di nay àtte buur bii di Luwis 16 àtteb ray, ci 21 samwiye 1793 g, loolu nag tax na ba lu bari ci reewi Tugal yi def ag jàppaloo kontar Fraans, mu ci mel ne Angalteer, ak Brusiyaa, Otris, Espaañ ak Holand. Ginaaw bi nag goornamaa bu jataayu xeet wi daal di taxawal kureelub kaaraange, feetale ko ligeeyub aar Fraans ci ñiy noonu fipp gi ci biir reew mi, ñu feetale ko ba tay moom kureel bi, wàluug taxawal am mbooloom xare mu Fraans mu dëgër, ngir aar Fraans, ak fipp gi, ak li mu fi jot a indi ci ndam, ak xeewal, moom fipp gi. Goornamaa bi nag ci njiitul Girondins yi gañe na xarekati Brusiya yi ca xareb Valmy ba, lijjanti na it ba xiir waa Beljig ci ñu fipp ci kaw Imbraatoor boobii di Francis mi nekkoon imbraatooru nguurug Rom gu Sell gi. Ñu daal di nangu alali paap gi ci goxub Afinion, ngir noonu gi mu noonu woon fipp gi (moom paab gi).

Ñu fàttali leen ne Jacopins yu xaabaabal yooyu, ñoo saytu woon kureelub kaaraange gu matale gi, ñoom songoon nanu ci anam gu tar, ci njiitul Robespierre kepp koo xam ne yaakaaroon nanu ne da nga àndul ci fipp gi aki gaay fipp gi. Jacopins yi nag bari na lu ñu daa mbugal lim bu bari ci waa Fraans yi, ci tuumaal leen ne danoo def ay wor yu mag. Ñoom ci seen jëmmi bopp nag ak doonte jàmaarloo woon nanook jafe-jafe yi leen dikkaloon juge ci reewi Tugal yi leen wër, te aju woon ci kontar fipp gi, ak doonte jàmmaarloo woon nanook ñoom ci doole ak fulla, te farataal duggug coldaar gu sañ-bañ, ngir aar reew mi, tas te giimal fèttéerlu yi doon am ci yennat ci gox yi nekk ci biir reew mi, duggal seeni xarekat ci Beljig ak Holand, ànd ak loolu lepp teewul waa Fraans bëggoon ñu soppi seenuw doxiin ci politig ba mu gën a woyof, gën a teey, gën dal, te gën a maandu.

Ci 29 sulye 1794g, la ceri jataayub xeet wi, tuumaal Robespierre, ne daa wor, yobbu ko ca mbuggalukaay ba. Jataay bi defaraat na beneen sart, boo xam ne moo waral ab goornamaab Fraans bu bees, ñu xame ko ci turu goornamaab doxaliin bi.

Goornamaab doxaliin bi:

Goornamaab doxaliin bi sampu na atum 1895g, moom nag li mu doon wund, mooy ab diggante bu tuxu, nekk ci diggante jamonay tiital ak taral, ak jamonoy nguurug imbraatoor gu nu joyal, gu tar, goo xam ne Napoliyon Bonaparte moo ko ame woon ci ginaaw bi, ci bi mu fi nekkee. Goornamaa boobu nag li gënoon na fés ciy ligeeyam ci ñaari wàll yii lanu jëmoon:

(1) Def politig bu maandu ci biir doxaliinu reew mi, te du tax mu doyadi mbaa mu ñàkk fulla ci kanamu ay noonam (2) Yonni Napoliyon ngir mu song Itaali, ngir yare ci Otris, ak yonneeti ko ci penku bi.

Nanu fàttaliku ne goornamaab doxaliin bi, mi ngi sosoo woon ci juroomi cer yoo xam ne dëppoowunu woon. Ciy jamonoom it la jëmmi Napoliyon feeñ, moom mi nga xam ne jariñu woon na bu baax ci doyadig gooramaa bii, ak ñàkk dooleem, ngir saxal fi boppam ci wàllug politig. Ciy jamonoom it lu sakkan ciy làngi politig sosu woon nanu, ni nu doon jëfandikoo alal ji gën a ñaaw, gën a bon. Ci fukki fan ci nowambar 1799g, la Napoliyon ak làngam gi, defoon yong googu nuy wax yongug Brumaire, daaneel goornamaab doxaliin bu neewoon doole boobu, loolu moo fi indi goornamaab kilifa bi, mooy bi ame ci ñatti kilifa yi nga xam ne ñoo doon jiite Fraaans te Napoliyon jiite woon leen, nga xam ne daanaka mbooleem sañ-sañ yi ci loxoom lanu nekkoon.


Napoliyon Bonaparte:

Napoelon Bonaparte, mi ngi judd atum 1769g, ca Ajaksio, ca dunub “Corsica” ca Itaali, dun boobu nga xam ne Fraans da koo mujjoon jënde ci Genova. Napoleon nekkoon na, ba muy doon gone, ku bëggoon fànnug xare, mi ngi genne ca bànqaasu xare ba nekkoon Paris, daal di dem nag doon ab ofise, bokk ca kureelub kano ya ca xarekati Fraans ya. Moom nag ku soppoon xam-xamu yoon la , taariix, ak xam-xami xare yi ak yu doxaliin yi. Ku sawaroon la ci dali fipp gi , te fonkoon leen. Moom nag ab bidiwam a ngi féqe ci ginaaw bi mu songee Itaali. Àtteg Napoleon walla yor gi mu yoroon Fraans, dafa seddaliku woon ci ñaari xaaj, bu njëkk bi: mooy kilifag Fraans gu njëkk gi, la ko dale ca 1799g, ba 1804g. Bu ñaareel bi: moom mooy imbraatoor bi, la ko dale ca 1804g, ba 1815g.

Song gi Napoleon defoon Itaali:

Goornamaab doxaliin bi, dafa feetale woon Napoleon jiiteg xeex boobu mu doon xeex Otris, jaare ko ca moomeelam yooyee nga xam ne Itaali benn la ci woon, atum 1796g, Ci noonu moom Napoleon mu daal di xeex ak nguurug Sardeñ, xeex bu tar boo xam ne jañ na ko ci mu xaatim ag wéer ngànnaay gu nuy wax gu Cherasco. Napoleon defati ab xare ak dooley paab gi, moñoxe ko ca Ancona, mu dumaati soldaari Otris yi ca bëj-gànnaaru Itaali, dàqeeti leen fa, xaatim fa ak ñoom juboo ga tuddoon Campo Formio, atum 1797g. Ci nii daal la Napoleon doyodile woon Otris, neewal ko doole, daal di àgg ci njobbaxtalu siw ci wàllu doxal xare. Napoleon, àntu gi xeexam yooyu àntu woon ci Itaali, tasoon lënkaloo gi waa Tugal defoon, kontar Fraans, mu mujj Britani rekk moo dese woon xeex beek Fraans.

Song gi Napoleon songoon penku bi:

Politigkati Fraans yi naaloon nanu – Taliraan mi nekkoon jëwrini bitim reew mi jiite woon leen – naaloon nanu ay naal yu aju woon ci ngàdd Britani, jaare ko ca sancoom ya, te bañ koo fekk ci biir këram, rawati na moom Britani dafa amoon mbooloom gaal mu mag ca geejug Mans. Politigkati Fraans yi, li nu bëggoon ci loolu mooy sos ab sancu bu Fraans ci geej gu diggu gi, ak man a àgg ca geej gu xonq ga, ak dog yoonu yaxantu wi daa àggale Britani ca sancoom ya nekk penku.

Goornamaab doxaliin bi, lii mi ngi ko denkoon Napoleon, ci noonu mu jug mooki gaayam, geeju ci atum 1798g, tukkee ca waaxub Toulon, mbooloom xare mi àndoon ak moom àggoon na ci ñeenti teemeeri gaal, yu sëfoon ñaar fukki junneek juroom ñatti soldaar, bokkoon na ci tam teemeer ak juroom ñaar fukk ak juroomi boroom xam-xam yu waa Fraans. Ñu àgg waaxub Aleksandriya, ca Isipt, nangu ko. Waaye mbooloom gaalum Britani mi bettoon na mu Fraans mi, ca ndoxum golfub Abii Xiir, moñoxe ko, ci noonu la Britani xañe Fraans cangug geej gi Fraans yàgg a gent. Fraans sax nag – ni mu ko baaxoo woon – nguurug xare la gu mag gu gën a am mbooloom xare mu jeeri ci mu geej, mu mel ne mu Britani mi.

Man nanu ne xare bii Napolen daan def ci penku bi, xare jooñ la woon, ndax kat ag sof rekk la ca xareb jooñ ba amoon cag njëkk, loolu nag gën na a leere ca xare ya mu doon def ca Afrig gu bëj-gànnaar ga.

Misra (Isipt) ca jamono jooja, dafa nekkoon reew mu nekkoon ci waawug àtteg Usmaan gi , bu ko defee, buuri Mamaalik yi jiite ko, mu doon jànkoote ak ag doyadi gu biir, ak xeex gu sax ci biirum reew ngir nangu nguur gi, te tam ngànnaay yi mu ame woon yu doyadi la woon bu nu leen nattee ci yi Napoleon ame woon, aki jumtukaayam. Lii moo taxoon Napoleon sonnutoon ci teg loxo Isipt, ak doonte Mamaalig yi ñoom jàmmaarloo woon nanook moom, xeex ak moom xex bu tàng ngir aar seen reew. Waa Isipt yi bégunu benn yoon ci àtteg Napoleon gi, li am kay mooy danoo fippoon ci kawan, mooy la amoon, ca Xayra (Keer), ñu koy wax “fippug Xayra gi” . Napoleon jawali na reewi Shaam mook mbooloom xareem mi, ginaaw bi mu nangoo Isipt, mu daal di teg loxo Hariis, Gaza, ak Yafa, daal di ray dooley kaaraange ja fa nekkoon daan ko aar, te tolloon ci ñeenti junniy soldaar. Juge fa, diriku jëm Hakka, gaw ko diir bu yàgg, waaye Hakka moom, toogul rekk faste ay loxoom di seetaan, dafa jànkoonte, jaamaarloo cig njàmbaar, ci njiitul kilifaam gii di woon Ahmad Basha, nga xam ne mbooloom gaalum xare mu Britani mi ñoo ko doon dimble tukkee ci geej gi, waa Usmaan yi di ko jàpple ci jeeri ji. Bi gaw gi yàggee, te Napoleon ñàkke ca lu bari, te amewu ca lenn njariñ, xarekatam yi tàmblee tawat, rawati na tawat ji nuy wax “siburu” di yaram wuy tàng, bi loolu amee Napoleon, xam ne fii muus du fi naane ñeex, mu deltu ginaaw, dellooti Isipt, te jëlewu fa lenn ndam.

Napoleon bàyyikoo na Isipt ci sekkare, dellu Paris, askan wa tertu ko fa cig yaatal ak mbegte. Xew-xew yi toppante ci Fraans, waaye ci anam gu baaxul ci goornamaab doxaliin bi. Looloo fi jële boobule goornamaa. Bi nuy wax bu ñatti kilifa yi taxaw, atum 1799g, Napoleon nekk ca Kilifa Gu Njëkk ga.

Ay ngérte , yu am solo juddoo nanu ca xareb Napoleon bu penku ba, ñu indil leen ci yii rekk: (1) Xareb Fraans boobu ci penku bi, wone woon na solo si Isipt am ak fi mu feete, ci wàllug jokkoo ak tuxu, ñeel imbraatoorug Britani gi ci penku bi. (2) Xare boobu Fraans da ci doon seete rekk, ngir xam nu muy def ba man a sanc walla kolonise reewi Afrig gu bëj-gànnaar gi. (3) Boroom xam-xami xare boobu, bi nuy ñëw, indaale woon nanu ay gëstuy xam-xam yu aju woon ci nàndal , ak jeexiit , indi woon nanu fi it benn naal bu aju woon ci gas aw yoonu ndox ci diggante Suwes ak geej gu diggu gi, di kanaalu Suwes bi, te it indaale woon nanu fi ab moolukaayu teere ci araab nu koy wax moolukaayu Bolaax bi. (4) Xare bi wutoon ay yoon yu man a indi ag jokkoo ci diggante Fraans ak Isipt, rawati na ci wàlli xam-xam ak njàngale añs.

Napoleon ak reewi Tugal yi:

Napoleon de taxawaloon na màmm gi Otris màmmoon, ci yaatal nguuram, ndaxte gañe woon na ko ca xare ba nuy wax Marenngo atum 1800g, jañoon ko ci mu xaatim ag juboo gu yees atum 1801g, mooy juboo gi saxaloon poñ ya nekkoon ca kollareg Campo Formio ga (1787). Napoleon xatim na ak Britani juboog Amiens, atum 1802g, looloo waraloon dooley Fraans ji genn Isipt, bu ko defee Angalteer moom itam noppi ci li dal Otris, bañ cee wax dara. Napoleon saxoon na di ki nga xam ne moo ame woon sañ-sañu fal niti Egliis bi ci Fraans. Paab bi tam – bi Napoleon di sampu niki Imbraatoor, atum 1804g - mooy ki doon def li ci aju woon ci xeeti ñaanal ak xumbal. Napoleon bi mu jotee ci imbraatoor gi, daa daal di nosaat doxaliin wi ci campeefi nguur gi, mu taxawal fi benn jumtukaay buy yëngu ci luy amal bëgg-bëggam bii, mu jël lu sakkan ci mbokkam yi ak xaritam yi, jox leen pal yu kawe yi. Mbooleem dooley nguur ji ak sañ-sañ yi mu tëyyeel leen boppam, teg boppam it ci kaw mbooleem làngi politig yi, doyadil làngi politig yi ak barlamaan bi, nos galag yi.

Napoleon de tàbbi woon na ciy xare ak reewi Tugal yi. Britani gañe woon ko nag ci wàllug geej gi, ca xare ba nuy wax (Attaraf Al-aqar), mu song Brusiya, gañe ko ca xareb Yena ba, atum 1807g. Mu daal di def waxtaan ak Aleksandar mi nekkoon sesaarub Riisi, def ak moom genn dëppoo, nu koy wax dëppoo gu Talist atum 1807g, mooy liy wone njobaxtal la Napoleon àggoon ci kàttan. Mu defoon ag gaw gu goxub Tugal bepp, jëme ko Britani , daal di woon ga reewi Tugal yi ci ñu topp ko ci loolu. Loolu indi woon na fi benn jafe-jafe bu koom-koom bu tar ci reewi Tugal yu bari. Loolu it waraloon na reew yii bañ ko, kontar ko. Mu xare woon ak Riisi gu sesaar gi, ndaxte daa gisoon ne moom kat wormaalul gaw googu mu digale woon. Ci noonu mu jëmale fa menn mbooloom xare mu mag, atum 1812g, ñu dox ba àgg ca peey ba, di Butrusburg, waaye mujj nanu manatunoo ñàkk a dëpp, ngir sedd bu tar ba leen fa gaw, ba jamonoy sedd ja duggee. Ak ba tay ngir jafe ga fa ag jokkoo jafee, guy man a yombal nuy jot ci li am mbooloom xare di soxla ngir man a def ligeeyam, muy jotug jumtukaay yeek dund yeek lu ni mel. Bi nuy dellu nag la waa Rusi yi sottiku ci seen kaw, ñoom xarekati Napoleon yi, ray ci lu bar. Bu ko defee Napoleon ñàkk soldaaram yu bari, te amul la mu doon bëgg. Bu ko defee waaTugal yi ( Otris, Brusia, Rusi ak Britani) boole seen doole, jàmmaarlook Napoleon, daal di koy gañe ca xareb Libisg, nu koy wax ( xareb xeet yi ), di woon ci Oktoobar atum 1813g. Ca noona nu sànni Napoleon ca dun ba tudd Elba, waaye mu lijjanti ba rëcce fa ci sekkare, ginaaw bi mu fa defee teemeeri bis, dem nag Paris, dajale fa xarekat yu bari ci waa Fraans yi, ngir xeexi reewi Tugal yi ko doon sot. Ñu gañeeti ko, ca xareb Watrlo ba, atum 1815g, sànneeti ko ca dunub Santa Hilana, mu des fa nag ba kero bi mu faatoo, atum 1821g.

Bu ko defee, reewi Tugal yi def seen ndaje ma nuy wax ndajem Vienne atum 1815g, ngir seddalewaat kartu Tugal wu politig wi. Daal di fiy saxalaat bu baax kenoy nguur, te suuxat ko fi. Ak sàmmoonteek yamoo gu reew yi ak sos reew yu am doole yu peek Fraans wër ko.

Ligeeyi ndajem Vienne:

Ligeeyi ndajem Vienne nii la tënkoo woon:

(1) Way daje yi delloowaat nanu buuri Tugal ya ca seen reew ya nu juge woon, teg ko ci “àqi yoon”, ci noonu nu delloosi njabootug Borbon gi, ngir ñu yilif Fraans ak Espaañ. (2) Britani jëloon na sancu yi Fraans moomoon, muy Malta ak Kaab, ak Silaan, ak Morisos. (3) Rusi jël moom Varsaw, Otris jël tefesug Dalmas, ak Milano gu Itaali gi, mujj nag ëpp doole nguur yu ndaw yu Itaali yi. Brusiya moom am ay moomeel yu mag ci Almaañ, ak ag wàll ci Poloñ. Ñu jël Beljig – cig sañ-bañ – boole ko ci Holand. Jëlati Norwej – cig sañ-bañ – boole ko ci Suwed . Jëf yii yepp nag dëppoowunu woon ak xeetu, walla fonk sa xeet, di nationalisme gi doon am ca Tugal. Lii nag firee nanu ko ne li ko waral mooy Britani daal, ak Rusi ak Otris ak Brusiya, danoo defoon seen bopp ay reew yu ñoo am ag kilifteef ci reew yu Tugal yu ndaw yi.

Li juddoo ci fippug Fraans gi:

(1) Fipp gi moo fi indi tay, dalub Fonk sa bopp bii nga xam ne, mujj na foo dem ci Tugal fekk ko fa, ci diirub xarnub fukk ak juroom ñeenteel bepp g, moo waral reewum Itaali bennoo, te moo jur it bennoo gu Almaañ gi. (2) Moo fi jële sañ-sañ ak ràññale ci biiri kureeli nit, naan kii moo kawe kee, wii xeet a gën wee, te man nanu ne mooy jaasi ji mujj rendi nostey laman ya nekkoon Tugal. (3) Fipp gi ci Fraans mooy gi njëkk ci fipp yi, ci taarixu Tugal bu bees bi, loolu nag li ko waral mooy coppat yi mu indi ciy gisiin aki deggiin, aki xalaat, ci wàll yu bari ci dundug politig gi, gu mboolaay gi, gu xalaat gi, gu koom-koom gi ci Tugal, ak fu ko moy. Ay term yu politig feeñ, yu mboolaay, yu diplomasi yu bees. (4) Moo fi jële gisiin wu “àqi Yalla ji” mooy gisiin wi naan buur yi seen àq ak sañ-sañ, ca ju Yalla ja lanu ko jële, mooy gisiin wi matale woon noste yi amoon ci Tugal gepp, la ko dale ca ba fa jamonoy laman tàmblee. (5) Xalaatub fipp gi law na ba àgg ci Tugal gepp, ak yeneen reew yu dul Tugal, yu adduna bi.























Buntub ñeeteel bi


Yëngu-yëngu yi aju ci “xeetu” walla fonk sa xeet (nationalisme) ci Tugal, ci xarnub fukk ak juroom ñeent g.



Bennal gu Itaali

Bennoo gu Almaañ
















Doggantal gu njëkk gi

Bennal gi nu defoon Itaali


Ni Itaali meloon njëkk xare yu Napoleon yi:

Itaali laata a Napoleon di ko teg loxo, di ko nangu, nekkutoon reew mu nu bennal , nekkutoon it di mu am ag temb, moom kay daa seddaliku woon, doon fukki xaaj ak ñaar, yu doon topp ak a nekk ci ron kilifteefug ay nostey politig yu wuute: nosteg nguur ca Savoia, Piemonte, Napoli, ak nosteg pénc ca Venezia ak Geneva, ak ag àtte gu paab ca Rom, ak gu Doox ca Toskaana ak Parma, ak xaaj yoo xam ne danoo nekkoon ci waawug imbraatoor gu Otris gi, ñooy Milano ak Lombardia.

Piemonte nag moo nekkoon nekkteg politig gi gënoon a dëgër, te ëppoon doole ci nekkte yooyu. Ña ëppoon ca njiit ya yilifoon nekkte yooyu, ay diktaatoor lanu woon, rawati na ñi ci waa Otris jiite woon, cig jonjoo mbaa lu ko moy .

Jeexiit ya Napoleon bàyyiwoon ca Itaali:

Napoleon, bi mu nangoo Itaali, dafa lijjanti ba boole xaajam yu politig yu bari te wuute yooyu ci ñatti nguur rekk, ñooy: Nguurug Alp gu bëj-gànnaar gi, walla Itaali, ak Nguurug Savoia, ak Nguurug Napoli. Mu wutaloon reew mi mepp, wenn yoon , daal di dindi galag ak tënk yu koom-koom yi amoon ci wàllug endustri ak yaxantu, ak mbay. Mu ubbi leekol yi ngir jàngal doomi reew mi, mu may waa Itaali yi ñu man di jot ci pal yi, te kat bu njëkk waa Otris rekk a ci manoon a jot. Looloo tax ñu man a wax ne Napoleon de mooy ki ji njiyum bennoo mu xeet ci suufus Itaali, mooy ki leen def ñuy xeeñtook a gént am reew mu Itaali mu man a am, mu nu bennal.

Itaali ginaaw ndajem Vienne:

Ndajem Vienne mi – ci xalaati njiitu jawrin ju Otris jii di Metternich-Winneburg – seddale woon na Itaali, def ko juroom-ñaari xaaj, ñooy: Piemonte, Napoli, Parma, Modena, Toscana, Lombardia, ak Venezia, ñoom ñaar nag, mujj nanu leen boole def leen benn, teg leen ci ron kilifteefug Otris. Ginaaw nag Metternich fexe woon na ba yay njiiti ndaje mi, gëmloo leen “dalu desal fi lu yàgg la ca yàggam ga” maanaam lu nekk, nanu ko delloo na mu meloon, loolu nag moo indi ndaje mi delloosi njiiti nguur yu ndaw yu Itaali yu njëkk ya, ñu delloosi leen ci seeni pal, tegaat leen seen barab. Metternich ak bëtam yi mu tasoon ci gox yepp, jeemoon nanoo fuglu yeglekaay yi, daan naj it gepp cawarte gu politig. Ci noonu ñu daa tëj gor ñi ci kaso yi, daan xañ way dëkk yi pali siwil yi ak yu xare yi nga xam ne bi Napoleon ñëwee jox na leen ko,mu daan leen weccee ak ay waa Otris (moom metternich), te daan leen teg ay galag yu diis te sonnle.

Yewwueg xeetu (nationalisme) ni mu xëye rekk am te màgg ca Itaali:

Politigu noteel gi Metternich yore woon, ak li muy tar lepp, taxutoon mu man a rekki yëg-yëg bi waa Itaali yi ame woon, ak xam ngi nu xamoon am solo gi bennal seen reew mi, te booloo ci wàllug politig amoon solo, loolu nag mi ngi am, ginaaw bi nu ci ñamee’s lëf ci jamonoy Napoleon. Bi nga xamee ne politig bu ñaaw boobu fa amoon, mayu leen woon ñuy def seeni cawarte ak jëfi politig, ci lu bér, te nëbboodiku, bi loolu amee lanu wéeru ci di def seeni yënguy politig cig làqu ak fésadi. Bu ko defee, ay booloo yu politig yu sekkare tàmblee sosu ci dëkki Itaali yu mag yi, li leen taxoon a jug di bennal Itaali, bokk na ci yooyu: booloo gu Karbonari (ñoñ këriñ), ak booloo gu Itaali gu waxambaanee gi.

Booloo gu Karbonari, moom mi ngi sosoo ca Napoli, daan def ay jataayam - ngir làqatu - ci barabi ligeeykati këriñ yi, walla lakkati mat yi, mu mujj nag tas ci mbooleem Itaali. Mbooleem kureeli askanu Itaali wi nag bokkoon nanu ci, baykat yi, ligeeykat yi, boroom mecce yi, yaxantukat yi, boroom xel yi, añs. Li leen manke woon nag, mooy danoo nosuwutoon bu baax, te ni ñu daan naale ak a rëdde seeni mbir tam dafa dese woon a tegu ci yoon, looloo taxoon li nu bëggoon daawul àntu, te seeni noon daa leen gaaw a not, te daa àntoodil seeni fipp. Waaye nag booloo gii, di gu Karbonari gi, jot na fee taal yëg-yëgu xeetu ci Itaali, te lijjanti ba mu sax fi di tàkk, ak doonte daje na’ak coona yu bari, te nu teg ko lu sakkan ciy mbugal.

Bu dee booloo gi tuddoon “Itaali gu Waxambaanee gi”, moom Jozeph Mazzini (1805 – 1872 g) moo ko sosoon, ginaaw bi mu nekkee ab cer ci booloo gu Karbonari gi. Mazzini mii, moom waay Itaali la woon ju xéroon ci reewam ak xeetam, nekkoon it ab xeltukat bu bokkoon ci ñoñ nite ñi , bu gëmoon ne xeetu nit ñepp benn lanu, te bëggoon lool goreg askan yi , moom nag jot na’a àgg ci xëcc cig wàllam boroom xel yi ci Itaali, te fàggu ñeewanteg nitug neen ku Itaali ki, akug cofeelam.

Bokkoon na ci jubluwaay yi gënoon a tax booloo gii am, goreel Itaali ci àtteg Otris, ak duma àtte gu paab gi nga xam ne Otris a ko daa dimbleek a dëgëral, ak fexee bennal reewum Itaali mi, ci ron ag noste gu republig.

Yëngu-yëngu yii, mujjoon na naat, te dox, bijjaloon it boppam lu sakkan ci waxambaane yi ak xalaatkat yi, àggoon nanu ci lu toll ne juroom fukki junniy waxambaane, yu weesu ay ñeen-fukki at yooyu. Mazzini dimblante na’ak Garibaldi, moom Garibaldi, ab kojug xare la woon, bu itaali, bu gëmoon bennug Itaali, te gëmoon ne danoo war a gorewu ci àtte gu Otris gii bóof ci suufus Itaali si. Ci noonu lanu jot a taxawal ñoom ñaar, ag àtte gu pénc ca Rom, ca moomeeli paab ga, ak ca Venezia, atum 1848g. Waaye Otris moom, ca dooleem ju bari ja, faagaagal na yëngu-yëngu googu, daal di dàq Mazzini mu daw, làqu ca Anggalteer. Ag woote nag feeñ na fa, jëm ci ñu def nattukaay yi benn, xaalis bi, ak peesekaay yi , ci mbooleem diiwaani Itaali yi aki nguur-nguuraanam, rawati na bi endustreem tàmblee màgg, yaxantoom gën a jëm kanam. Boroom ligeey yi nag ak boroom boppi alal yi , gisoon nanu am njariñ gi gore ci koom-koom amoon njariñ, ñu tàmbli woon a sàkku ñu sosal leen ay yooni weñ , yuy taqale diggante bëj-gànnaaru Itaali ak bëj-saalumam, te nu uppi mbooleem ja yu Itaali yi, ci kanamu yaxantu gu Itaali gi, te bañ cee indi yenn jafe-jafe walla ay mbugal yu doxaliin , walla ay galag yu man a tee bennoo gu yaxantu gi am ci Itaali.

Ma fàttali leen ne barab yu bari de ci bëj-saalumu Itaali, yu deltu woon ginaaw lanu woon ci wàllug endustri, koom-koom, mboolaay ak politig. Looloo taxoon xalaat yi jëmoon ci bennoo, mi ngi gënoon a dëgëre ci fi nuy wax Itaali ( di nguuru Alp gu bëj-gànnaar gi) ak ci digg bi. Foofa daal la wooteg bennal gi gënoon a tare ci yeneen wàll yu bëj-saalum yi. Ndax kat wàlli bëj saalum yi dañoo jëmutoon kanam dara ci wàllug endustri, yaxantu, politig ak mboolaay. Lii a waraloon woote gi, jëme ci bennoo gu koom-koom, yamoon rekk ci digg Itaali ak ci bëj-gànnaar gi. Ñi ëppoon it ci xalaatkat yi ak boroom xam-xam yu Itaali yi, ñi ngi dëkke woon digg bi, ak ci bëj-gànnaar gi.

Ak li boole Itaali, def ko menn reew doon nekk càkkuteful ñepp lepp, teewul yenn ci nguur-nguuraan yi, ak Doox yi , kontaroon ko, ndaxte ñoom dañoo ragaloon ne loolu de, moo xam leegi la walla ci kanam, bu amee, di na fi indi ag bennoo gu politig, te loolu bëggunu ko woon, ndax kat ñoom seeni njariñi nguur yooyu moo leen gënaloon njariñul Itaali li. Ci noonu, nguurug Paap gi kontar ko, naka noonu gu Otris gi nga xam ne amoon na kilifteef gu yaatu, ak sañ-sañ bu mag ci Itaali. Ndax moom daa gisoon ne bu Itaali bennoo ci wàllug koom, boole ay nguur-nguuraanam, aki Dooxam, loolu du wund lu dul ne moom kat (Otris) waxtuw gennam Itaaliee ngi bëgg a jot, ci lu dog. Te loolu du ko nangu mukk.

Nguurug Piemonte ak Bennalug Itaali:

Ci bëj-gànnaaru Itaali ag nguur a ngi fi woon, ñu koy wax nguurug Piemonte walla Sardeñaa, ka nekkoon ca gàngunaay ga, di woon Victor Emmanuel. Moom Piemonte nag, nguur la woon gu ame woon ci ñeenti xaaj yu taqaloowul, (ñoom xaaj yi), ñooy: Piemonte, mi nekk ci ron doji Alp yi, nekkoon barab bu taxu ko woon a woomle, ak Savoia, mi ngi nekkoon ci kaw doji Alp yi, tiim wàllug Fraans gi dend ak Itaali, moom nag ruq la bu gën a yor ay màndarga yu Fraans ci yu Itaali, moom itam taxu ko woon a jëm kanam mbaa mu woomle, ak Sardeñaa, moom dun la, bu nekk ci geej gu diggu gi, xaw a sori Piemonte. Ak Genova, moom nag, nguurug Piemonte jot na ci, ci ginaaw xarey Napoleon yi ci Tugal. Di nanu gis fii ne Piemonte moom yorul woon nguur gu àttanoon coonay bennal Itaali, waaye nag yoroon na yenn yu rëy ci yiy taxawal reew mu mag, yu ko mayoon mu man a yanu yan bu diis bii, ñu tudd ci yi ci ëpp solo:

(1) Ab buuram daa gëmoon ag àtte gu tegu ci sartu reew, te daa gëmoon it bennoo gu Itaali. (2) Njiitul jawrinam lii di Cavor, - mi ngi doonoon njiitul jawrin atum 1851g – daa gëmoon moom itam te sopp sartu reew ba Angalteer defoon, te bëggoon lool Itaali doon benn, te nekk ci ron ndëppul Piemonte. (3) Piemonte amoon na dooley xare joo xam ne, li ko daa wone mooy soldaaram sii nga xam ne jot nanoo xare ba am ci xam-xam. (4) Piemmonte moo nekkoon làqatukaay bi politigkat yi nu daa sonnale ci nguuri Itaali yeneen yi daan làqatoo. (5) Màgg gi koom-koom doon màgg ci Piemonte, moo gënoon a gaaw, gi mu doon def ci feneen ful Milano. (6) Nguurug Piemonte, gu sori woon loxol Otris la, nga xam ne daawul man a dugg ci mbiri biiram.

Cavour ak bennalug Itaali:

Cavour mii (1810 – 1861g), nekkoon na di ku gëm bennoo gu Itaali, waaye nag ci ron ag àtte gu nguur gu sartu reew , goo xam ne buurub Piemonte bee koy jiite, moom kon ci loolu la wuute woon ak Mazzini mi nga xam ne da doon woote ag bennoo gu Itaali ci ron ag àtte gu republig. Moom de daa gëmoon ag yewenal gu politig, gu koom-koom ak gu doxaliin , ngir Itaali man a doon benn. Mu gisoon ne nguurug Piemonte am na kàttanug dàq Otris mu genn Itaali, ak naj nguurug Paab gi daa lënkaloo ak Otris, bu lënkaloo woon (moom Piemonte) ak jeneen doole ju reew, ju mel ne Fraans mbaa Britani.

Cavour mi ngi yoroon njiitug jawrin gi ci atum 1851g, bi mu ko defee nag, mu tàmblee waajal am reewam ngir mu man a jiite ligeey biy bennal Itaali. Ci noonu mu sotti yitteem ci xarekatam yi, waajal leen ba nu man a jàmmaarlook mbooloom xarem Otris mi, te man leen a genne Itaali, mu jug ci suqali koom-koom bi, defar ay yooni weñ , yu lënkale mbooleem dëkki Piemonte yi, daal di jamonool mbay mi ak endustri bi, defar ay yoon, neenal galag yeek mbir yi man a tënk yaxantu ak endustri, tege ay galag yu duwaan yu mag ngir aar endustri bu lokaal bi (bu biir reew mi), yewenal nosteg galag yi, daal di sos lonkoo yu askan yi ak bànk yi.

Bu dee lu aju ci doxaliin , ak yewenal yu biir reew mi, moom da fee daal di woon buddee doxaliin wu yàgg wa fa nekkoon, daal di jël ay matuwaay yoo xam ne tax nanu ba yoon ci reewum Itaali gën a jamonoo, jële fi lu bari ci ay jàngu, maanaam ay egliis, wàññi dooley politig ju paab gi, tàqale àtte geek Eglis bi.

Kafor mii nag xamoon na ni reewam mi tuutee woon, bu nu ko tollalee ak Otris walla Britani, mbaa Fraans, am Rusi, ak Brusiya, waaye loolu lepp teewutoon mu gëmoon ne bennug Itaali daal, mbirum aw xeet la woon, manul woon a ñàkk, te itam mbirum adduna bepp la, laaj na reew yi sonn ci, te jeem koo faj ci nu mu gën a gaawe, mu dogu woon ci sóobu ci geewub politig bu adduna bi, ngir yékkati kàddug Piemonte ci adduna bi ba ñepp degg ko, ci ndajey Tugal yi. Ci noonu mu digal parlamaa bu Piemonte mu nangu ñu yonnee ab kureelub xare bu Piemonte ngir mu bokki ca xareb Xarm ba , àndoon ca ak Britani ak Fraans, ngir sàkkoo ci xaritoo ak Imbraatoor bu Fraans bii di Napoleon mu ñatteel mi, (Napoleon III), te ame ca ñeewantug Britani akug jàppaleem ci li mu bëgg.

Kureelu xare bu Piemonte boobu, ak doonte bariwu ci ñu ci dee ca xareb Xarm ba, ndax ñu bari ci ñi ci dee ci mbasum koleraa lanu deewe, teewul Kafour moom lijjanti na ba nu yëg Piemonte ci kanamu ndawi Tugal yi, ca ndajem juboole ma nu doon def bi xareb Xarm bi jeexee. Kafour sàkku na fa ca Fraans mu dimbli ko ci Otris, ndaxte nguurug Piemonte moom rekk manul a dàq imbraatoorug Otris gu dëgër gii. Kavour ci njëlbeen gi, li ko gënaloon mooy Britani jàpple ko, kontar Otris, waaye Britani moom, bëggutoon a xeex ak Otris, xeex bu ko amalul njariñ. Bu dee Fraans nag, nga xam ne pencam mi , Napoleon III moo ko jiite woon, moom Napoleon III mi nga xam ne daa jàppe woon Itaali am ñaareelu reewam, ndax moom doom la woon ca Napoleon I - ginaaw doomi mbokkam la woon - te Napolen I mi ngi cosaanoo Corsica. Moom Napoleon III, ku soppoon waa Itaali la, te xéroon ci seeni àq aki yelleef ci gore te doon benn, moom de bokkoon na ci ñi gënoon a siw ci woote ag xeetu ci Tugal. Politigu bitim reewam it mi ngi ko tegoon ci bañ Otris mi dendoon ak moom. Te ginaaw Piemonte it reew mu nekk ci wetu Fraans la, loolu taxoon na mu bëgg mu nekk reew moo xam ne yoonu Otris du ca nekk.

Cavour lënkaloo na ak Napoleon III, ñu def dëppoo ga nuy wax (Plombiere) ci 21 sulye atum 1858g, dëppoo googu, la mu yaxal mooy ñu taxawal ag nguur gu Itaali ca bëj-gànnaaru Itaali, buurub Piemonte jiite ko, ak geneen nguur ci digg bi. Moomeeli paab gi moom ñu bàyyi leen fi, te bañ a laal dara ci nguurug Napoli, gi nekk ci bëj-saamu Itaali, bu ko defee nag, genn bennoo gu ame cig dëppoo lënkale leen ci njiitug paab bi. Fraans nag li muy ame ci loolu mooy ñu bàyyee ko Niis ak Savoia.

Xare yi amoon ci diggante Piemonte ak Otris:

Kafour wéy na di cokkaas Otris, rawati na bi ko Napoleon III yonnee ñaari temeeri junniy xarekat, ngir ñu xeexle ko kontar Otris, loolu nag amoon na ci ginaaw dëppoog (Polombiere) gi . Kafour am na la mu bëggoon muy jeqi Otris, yëngal ko, ndax moom kat (Otris) mujjoon na jekki-jekki rekk sàkku ci Piemonte mu nocci ay ngànnaayam ci diir bu gàtt, bu weesuwul ñatti fan, mu tóllanti loolu ci jug jawali Piemonte ànd ak ay xarekatam atum 1859g. Taarixkat yi firee nanu loolu ne ag wuyyusi la gu Otris def ci li ko Piemonte doon yàgg a cokkaas, ak a dëkk.

Nii daal la xare bi tàkke ci diggante Otris ak Piemonte, waaye nag Otris a njëkk a song, ci noonu Fraans itam jibal ab xareem ci kaw Otris. Soldaari Piemonte yi ak yu Fraans yi jot nanoo duma Otris, gañe ko ca xare ba nuy wax Maginta ak Salvarino, waaye Napoleon III moom daa xëyoon rekk taxawlu ci xare bi, daal di gise ak Imbraatoor bu Otris bi, def ak moom ag wéer-ngànnaay, dellu xaatim ak moom ag juboo, te diisoowu ci ak nguurug Piemonte. Wéer-ngànnaay gii nag mooy li jur ci ginaaw bi, li nuy wax juboo gu Siyorix atum 1859g. bokkoon na ca poñ ya ëppoon solo ca juboo ga:

(1) Otris bàyyee Piemonte Lombardi (2) Sos booloo gu Itaali ci njiitul Paab bi ci tur (3) Venezia day des ci moomeelug Otris, waaye bokk ci bennoo gu Itaali gi (4) Delloosi ñi yilifoon Doox yi nekkoon ci digg Itaali ci seen barab, ak seeni pal, ginaaw bi leen askan wi follee. (5) Boole Niis ak Savoia ci Fraans.

Taarixkat yi, firee nanu taxawal xare gu bette gi nga xam ne Napoleon III, defoon na ko, ne daal li ko waraloon, mooy daa bañoon ag nguurug Itaali gu dëgër am, taxaw, rawati na bi mu tàmblee gis lenn ci Doox yi nekkoon ci digg Itaali tàmblee bokksi ci Piemonte. Bokkoon na it ci li ko ko taxoon a def, jeem a gëramloo Katoligi Fraans yi nga xam ne danoo tàmbli woon a mer ci neewal gi nuy neewal doole nguurug paab gi ci Itaali, te Otris a ko daan jàppleek a dëgëral. Kafour nag moom, daa daal di woon xàcc , walla tekki ndombaam, bi mu sàkkoo ci buur bi Victor Emanuel ba soon ngir ñu wéy ci xare bi ak doonte Fraans genne na ci loxoom, waaye mu lànk mom buur bi. Askani Doox yi bañ nañu ne dunu nangu mukk ñu delloosi ña leen yilifoon bu njëkk, ni ko poñi juboo gu Siyorix gi yaxale, ñu ne woon daal ñoom leegi danuy dem bokki ca nguurug Piemonte. Ci noonu ay fipp am yu toftaloo, ci Parma, Modena, Romaña ak Toscana, di woote ag bokki ca Piemonte. Kafour dellusi na yoraat njiitug jawrin gi, ngir sonnal gu ko askan wi sonnal ci mu dellusi, ci biir Piemonte ak ci biti. Nii daal la Itaali doone benn ci gox yi nekk ci bëj-gànnaar gi ak digg bi. Kafour dara deseetu ko woon lu dul mu fexee nangu Venezia, ak moomeeli paab bi, ak nguurug Napoli gi boole leen ci Itaali.


Coona yi Garibaldi doon daj ci Itaali doon benn:

Garibaldi moom ku bëggoon la te gëmoon bennug Itaali. Moom nag soldaar la woon bu dëgër, jàmbaare te ñeme. Mujjoon na it bokk ci jàmbaari Itaali yi siwe woon ag wooteg bennoo gu xeet, te daan ci ligeey. Garibaldi mii, tukkee na Genova atum 1860g, ànd ak lu jege junniy xarekat yu bokkoon ci way coobarewu yu Itaali yi nu tudde woon “Boroom simis yu xonq yi”. Daal di wàcc ak ñoom Sisil, jot faa dàqe doole ya fa nekkoon te àndoon ak buurub Napoli bi, ginaaw diirub ñatti weer. Daal di jéggi xat-xatu Silil bi , dugg ak dooley xareem ji Napoli, ci lu dul jàmmaarloo gu nu man a tudd. Ci noonu Napoli mujj ak dëkk yi nekk ronam, dugg ci bennoo gi.

Samp Victor Emmanuel muy buuru Itaali:

Dooley Piemonte ju xare ji jawali woon na ca diiwaan ya nekkoon ca ron kilifteefug Paab bi, mu jotoon a nangu moomeeli Paab bi bepp, lu ci dul Rom. Ci noonu xarekati Piemonte yooyu jawali woon ca soldaari Garibaldi ya, ca Napoli, ci ndigalul Kafour, ñu àndandoo nag xeex ba nangu mbooleem gox yi nekkoon ci ron nguurug Napoli, te Garibaldi manu fa woon àgg moo rekk. Ci noonu Victor Emmanuel ñëw, dugg Napoli, ni ku gañe di dugge ci dëkk bu nu xare ba nangu ko. Parlamaa bu Itaali bu bees bi def na ndajeem mu njëkk, ca Torino, bisub 18 febriye atum 1861g. Ca ndaje ma lanu ndëppale Victor Emmanuel , def ko buurub Itaali gu nu bennal gi. Ginaaw bi Itaali taxawee di ag nguur gu nu bennal, ba am juroomi weer la Kafor faatu, ci sulye atum 1861g. Garibaldi it bàyyi politig, ndax kat moom li ko taxoon a jug mooy ligeey ci Itaali doon benn, waaye soxlawutoon ay pali politig.

Def Rom peeyu nguurug Itaali gi:

Waa Itaali yi delloosi nanu Venezia mi Otris tegoon loxo, nangu woon ko, delloosi gi di ci atum 1866g, mu mujj nag moom Venezia di ab gox ci Itaali, ginaaw ba nu fa dàqee dooey xare ju Otris ji. Nanguwaat googu nag ñi ngi ko mane ci ñàkk a tal gi leen Otris ñàkkoon a tal, ngir xeex bi mu nekkoon di ko def ak Brusiya. Fraans it ay xarekatam gennoon nanu Rom, ngir sotti gi Fraans sotti woon yitteem ca xareem ba’ak Brusiya. Bi mu ko defee soldaari Itaali yi daal di leen fay wuutu, ci 20 sebtambar atum 1870g, ñu daal di jibal ci anam gu ofisel ne Rom daal mooy peeyu nguurug Itaali gu nu bennal gi. Doxaliin wii merloo woon na Paab bi, yobbu woon ko ci mu bañ a nangu loolu, ne woon it du man a summiku ci sañ-sañu politigam yi te du nangoo raflewu ci nguuram gi. Noonu la mbir mi nekke woon ba 1929g, ca la genn dëppoo ame ci diggante Mossolini ak Paab bi, dëppoo googu mayoon na Paab bi mu doxe nu ko soob ci mbiri diine ji, te am ag tembte gu mat ca Vatikan, am it sañ-sañ ci yabal ay ndaw yu koy toogal ca biti. Ñu wutal ko nag (moom Paab bi) njëlul boppam lu mu jagoo .

Nii nag la Itaali doone woon benn, muy lol ay doomam a ko xeex. Doomam yoy danoo jëloon seen coona bepp def ko ci goreel ko, bennal ko, te fuqarcee ko ci ngëbug jàmbur, bu leen ruuroon, teg leen loxo. Bennoo gii de lu ñepp soppoon la, ndaxte doole la ci ñoom, di teddnga, di tembte te dig fonk sa xeet. Bennoog Itaali du lenn lu dul meññatum sellal ak gëm ag bennoo. Mooy wuyyu gu mag ga, ca woote ga Michiavelli doon woote, moom mi doon sàkku ciw nitam ca teereem ba tudd “buur bi” te looloo njëkkoon bennoo gi ci ay xarnu, mu doon sàkku ci ñoom ñu ligeey ngir bennal seenuw reew.















Doggantal gu ñaareel gi

Bennoo gu Almaañ


Almaañ njëkk xare yu Napoleon yi:

Almaañ njëkk xarey Napoleon yi, dafa seddaliku woon ci lu jege ñatti teemeer ak juroom benn fukki diiwaan, yepp it ci ron imbraatoor gu Otris lanu nekkoon, walla li nuy tudde Imbraatoorug Rom gu sell gi. Almaañ gepp it genn nguur rekk a fa nekkoon gu mag te temb, mooy gu Brusiya. Nguur googu nag jëmoon na kanam, te ag yewwuteem fés, ci jamonoy buuram ba tuddoon Fredrick mu mag mi (Great Fredrick) (1740 -1786 g), mooy ki ko defoon muy nguur gu dëgër te am doole. Bu ko defee waa Almaañ yepp wëlbati seeni gët jëme ci nguur gii, ngir bëgg ag bennoo.

Almaañ ci jamonoy Napoleon:

Napoleon ak xarekatam ya xuusoon nanu ci diiwaani Almaañ yi, teg leen loxo. Daal di jawali ca nguurug Brusiya, gi nga xam ne jàmmaarloo woon na’ak ñoom cig njàmmaar ak fit, waaye Napoleon moom mujj na ko not, te gañe ko ci mujj gi, ca xareb Yena ba, atum 1806g, daal di teg loxo peeyam ba Berlin. Napoleon merloo woon na lool waa Brusiya yi, ci dog gi mu dogoon ay wàll ci seeni suuf, te jébbaloon leen diiwaanu Saksoni bi. Waaye nag ci geneen wàll, am na lu am njariñ lu mu fa indi, ndaxte wàññi woon na limub diiwaan yu Almaañ yi ba ci fanweer ak juroom ñeent rekk, te bu njëkk lu jege 360 lanu woon. Kon jëfi Napoleon jii, mbir la mom moo nooyal yoon wi, waajal ko ba ag bennoo gu Almaañ man a judd, man a taxaw.

Almaañ ginaaw ndajem Vienne mi:

Ginaaw bi Napoleon Bonaperte daanoo atum 1815g, ci lanu def ndajem Vienne, ñu jële fa ay saxal yu bari, bokk na ci yooyu, dagg Doox bu Warsaw gu Poloñ gi, dagg ko ci Brusiya, te jox ko Rusi, bu ko defee ñu jox Brusiya moom itam goxub Rayan ak xaaju diiwaanu Saksoni. Daal di taxawal ag bennoo gu Almaañ gu làmboo fanweer ak juroom ñeenti nguur-nguuraan yu Almaañ, Otris jiite ko. Defiin wii nag mi ngi ame ci càkkuteeful Metternich, ak naj gi mu doon naj way daje yi, ngir ñu defal ko bëgg-bëggam boobu. Bennoo gu Almaañ gii juddoo ci ndajem Vienne mi, nekkoon na di lu manul a wéy, ndax kat Otris moom daa tàmbli woon di genne ay saxal aki ndigal yuy kontar tas-xibaar gu gore , te wéeroodi fenn, tey kontar mboolooy Almaañ yi daan sàkku ag bennoo te daan ko woote. Te Otris it daa mujjoon teg loxo ci jataayub bennoo gu Almaañ gi, te ga woon ko ci mu genne ay saxal yuy digale ñu fuglu daara yu mag yi , ak leekol yi, ak ndaje yi añs.doxaliin yooyu nag taxoon na ba ay kàddu jib yu ay waa Almaañ, di sàkku ñu fipp ci kaw Otris, tey sàkku ñu jeem a bennal Almaañ, ci keppaarug nguur gu Almaañ gu dëgër. Loolu mooy li xeltukatu Almaañ bi (Hegel) daan sàkku, te daan ko woote, moom ak ñeneen ñi daa jam bennoo gii nga xam ne Otris a ko moomoon daanaka, te tegoon ko loxo.

Taxawaay bi nguurug Brusiya ame woon ci naal yi jëmoon ci Bennoo gu Almaañ gi:

Nguurug Brusiya dafa tàmbli woon di yëngu ngir dajale xeetu Almaañ wi, duggal leen ci genn nguur gu Almaañ gu nu bennal. Mu daal di woon rëddal boppam ab politig bu muy jaar ngir àgg ci loolu mu bëgg. Mu daal di woon door ci dëgëral boppam ci biirum reew, defaraat doxaliinam , yekkati koom-koomam, soppi nosteg galag yi aju woon ci nduwaan ci mbooleem goxi nguur gi. Ñu daal di taxawal noste gi nu daa wax (Solofrayn), di ag bennoo ci wàllug nduwaan, mooy li neenaloon nosteg nduwaan gi ci biir Almaañ. Nga xam ne li nekk ci biir reew mi cim njaay deesu ci genne duwaan. Nga xam ne danoo feexal yaxantu gi ci Brusiya, ëfal ko ba mu man a doxe ni ko soob, ci lu dul ñu ciy teg ay tënk-tënki galag mbaa yu nduwaan. Doxiinu Brusiya wii dey dees na ko lim mu dig soopiku gu mag ci taarixu bennoo gu Almaañ gi. Doxal nanu ko nag ci atum 1818g, ci biir ay goxam yu biir yi. Gox yooyu nga xam ne njëkk “Nosteg Solofrayn gi” danoo nekkoon ay gox yoo xam ne bu ci nekk daa amoon nosteg pobb gu nduwaan, gu mu bokkul ak kenn. Waaye bi Solfrayn taxawee, lanu bennal biir Brusiya ci wàllug nduwaan, ginaaw bi mu nekkee moom Brusiya di lu nu seddale ci juroom benn fukki goxi nduwaan.

Waa Brusiya yi yëgoon nanu ne benno gi ci wàllug koom-koom mooy cëslaay li nu war a teg bennoog Almaañ gi ci wàllug politig. Looloo taxoon kilifay Brusiya yi tàmbli woon a fexe nu nuy def ba duggal yeneen diiwaani Almaañ yi ci bennoo gu nduwaan googu. Brusiya nag amoon na ndam ci li mu doon wut ci yenn ci diiwaan yu Almaañ yu ndaw yi, waaye nag jot naa dajeek ag jàmmaarloo gu mag ci yeneen diiwaan yu Almaañ yu mag yi, li ko waral mooy ñoom dañoo gisoon ne li gën ci ñoom mooy ñu sosal seen bopp ag bennoo gu ndawaan gu temb, ngir xeex ci bennog nduwaan gu Brusiya gi. Looloo fi indi woon ñatti bennoo yu nduwaan ci Almaañ, ñooy:

(1) Solofrayn (2) “Bennoog nduwaan gu Bavar” gi nga xam ne mi ngi judd woon atum 1820g, maanaam ginaaw bi gu Solofrayn amee ba am ñaari at. (3) Ak bennoo gu nduwaan gu Saksoni. Mooy gi Saksoni taxawaloon atum 1828g.

Kilifay Brusiya yi xamoon nanu ne diiwaani Almaañ yi dananu nangoo duggsi ci bennoo gu Solofrayn gi, bu nu soppee sart yiy tax manees cee dugg. Looloo taxoon ñu soppi sarti Solofrayn yi, nga xam ne leegi danoo sos ab jataay bu làmboo mbooleem ndawi yi ci bokk, buy saytu noste googu. Leegi nag lu fa duggati rekk ci li bawoo ci nduwaan mi ak galag yi ñu koy seddale mbooleem diiwaan yi, ci kem limub ña fa dëkk. Soppi yii de dimblee na ci yaatal gëweelub Solofrayn, gën a yàkkali ab geewam. Leegi nag Bavar bokksi na ci ak Saksoni ci atum 1934g, ca saa sa tam, nga tàmblee gis lu lay won ne Solofrayn moom tàmbli na a naat ak a am ag yokkute. Yaxantu ga tàmbli woon nay jar, di dox, mbay ma màgg, endustri ba jëm kanam ci mbooleem diiwaan yi bokksi ci Solofrayn. Am na nag benn jëfka boo xam ne moo àntul Solofrayn, mooy moom de noste gu waa Almaañ xalaat ba def ko la, loxol Otris duggu ci, jenn doole it ju ko man a teg loxo yoonam nekku ci. Metternich gisoon na ay wi nekkoon ci noste gii, waaye bi mu koy gis fekk na waxtu wa jàll, manatu ca woon dara. Mu daal di bind Imbraatoor bu Otris bi ne ko: “Na la wóor ne nguuri Almaañ yi - bi lii amee de – di nanu nekki wenn yaram wu jàppaloo, ci ron kerug doxaliin gu Brusiya, te da na jàppeji Brusiya muy - moom - aw yaram wu di doxandeem, wu tumbrànke wu bokkul ciw yaramam”. Te kat waa Otris yi ñoom, ca dëgg-dëgg, dunu ay doxandeem ci waa Almaañ yi, ndax ñoo bokk xeet, làkk ak taarix. Man nanu ne Almaañ gepp mujj na bokksi ci Solofrayn gi, atum 1842g.

Xalaatu xeltu bu Hegel bi feddali woon na dooley nguur, ak ray gi muy ray jëmm ak lepp lu mu am, ngir sàmm dooleem akug màggam ak wegeelam. Nguur walla àtte – ci gis-gis Hegel- cëslaayam mooy doole, ci doole rekk la man a dëgërale gëgg. Kon nguur walla àtte gu dëgër ci gis-gisu Hegel, mooy nguurug walla àtteg dëgg. Kon moom Hegel day mel ne moo teg ci loxol Brusiya lay wa xeltu guy rafetal, di baaxal seen jëfi jiite googu nu jiite woon bennalug Almaañ gi.

Ñu leeral leen ne bi 1848g di jot, fekkoon na Brusiya muy reew mu am kàttan ci tere Otris muy dugg ci mbiri nguur-nguuraani Almaañ yi. Naka noonu, nekkoon na it mu amoon kàttan ci jiite yëngu-yëngu gi jugoon ngir bennal Almaañ. Nguur-nguuraan yi bokkoon ci Solofrayn it, doon man a dimblante ci seen biir ci wàllug koom-koom, te daan jëflante ci lu dul yoonu Otris di ci nekk mbaa ñuy diisoo ak moom, walla ñu koy tàggu. Ci noonu nguur-nguuraan yooyu tàmblee xoole Brusiya bëtu kilifa. Ci noonu la bennoo gu koom-koom googu doon màgg ak a naat ci ro kerug Solofrayn, mujjoon di ab jeego bu mag jëm ci ag bennoo gu politig ak xare ci Almaañ.

Jeexiit yi fipp gu atum 1848g defoon ci amug bennoo gu Almaañ gi:

Ay fipp yu bari jot nanoo am ca Tugal atm 1848g. Ag fipp am ca Paris, am gu am ca Vienne, geneen ca Brusiya ak ay fipp ci Itaali ak Almaañ, yepp it di xëccu jëm ci ag gore , demokraasi ak xeetu . Metternich mu màggat mii, mujjoon na manatul woon a noot fippi Tugal yooyu, mbaa mu giimal leen, ni mu ko baaxoo woon a defe. Kërug Orob gi mujj – ni ko Metternich di waxe – di kër gu màggat, te ràpp, ba àgg ci maneesatu cee yatt sax ab palanteer ciy miiram ngirug màggat, kon leegi li jaadu kay mooy ñu màbb ko, te wuutal fa geneen kër gu yees. Ca dëgg-dëgg nag loolu am na, ndax kat noste ga amoon ca la ëppoon ca reewi Tugal ya, daa mujjoon di lu ràpp, ngirug yàgg, mujj manatutoon a ñàkk ñu yeesalaat ko, te taxawalaat ko ci anam gu dëppoo ak li jamono laaj.

Metternich dawoon na, te daanu woon, ci noonu buurub Brusiya bi Frederick William mu ñeenteel mi daal di jug, woote am ndaje mu parlamaa, ngir ñu defaral Brusiya ab sartu reew bu bees. Mu dig aw askanam ne leen moo fas yeenee jiite yëngu-yëngu giy jug ci jeem a bennal Almaañ, ci benn bataaxel bu mu leen jàngal. Ndaw yi teewal Almaañ yepp teewe woon nanu ndajem atum 1848g moomu, ñu def fa ay gëstu ci lu aju ci Almaañ gu nekk benn. Ndajem parlamaa mii, ñi ngi ko gën a xame ci turu “Parlamaab Frankfort”. Ndaje ma ëmboon na lu bari ciy woykat , aki xeltukat aki taskati xibaar aki ustaas. Ñatti saxal nag yu mag juddoo nanu ca ndaje ma:

(1) Bennal Almaañ ci njiitul buurub Brusiya. (2) Ñu boole ci bennoo gu Almaañ googu, wàllug Almaañ gi bokkoon ci imbraatoorug Otris gi (3) Genne Otris ci bennoo gu Almaañ gi.

Way daje yii ci Frankfort, (seenub lim àggoon na ci 830 ciy jëmm) tànnoon nanu buurub Brusiya bi Fredereick William mu ñeenteel mi, def ko imbraatoor ci Almaañ gu nu bennal gi. Waaye Frederick moom daa bañoon ne du dëppoo ndëppul imbraatoor li nu ko joxoon, te way daje yi joxoon ko ko, ndax da ne ndëpp li daal ndawi askan wee ko ko jox, waaye buur yeek kàggam yi joxuñu ko ko. looloo taxoon nanguwu koo sol. La am nag mooy ne buuru Brusiya bi dafa bañ a jël ndëpp li, ndax xam ne Otris ak Rusi ànduñu woon ci bennoog Almaañ googu, te manoon nanoo xëy di duggati ci seeni mbir ngir loolu. Rawati na ne Otris moom jot na a not fipp gi amoon ca peeyam ba Vienne. Nga rax ci dolli ne Buuru Brusiya bi, moom dafa gëmoon gisiinu “àq ak sañ-sañ bu Yàlla bi”, mooy gisiin wi naan ñoom buur yi Yàlla a leen fi teg, moom lanu fi wuutu, nit ñi tegunu leen fi, du keneen it. Looloo taxoon bu nangoo it ñu def ndaje moomu, muy mu Frankfort mi, jubluwu ci woon lu dul ngistal, waaye du ligeey bu fullawu, mbaa mu dëggu ci yoonu soppi.

Otris ak Rusi dimblante nanu ci màbb barlamaab Frankfort bi, ak naalam yi mu amoon te nu jëm cig bennoo gu Almaañ, looloo waraloon jeem gi nu doon def ngir bennal Almaañ ci ron kilifteefug Brusiya, ci atum 1848g, mujjul woon àntu. Waaye li muy àntoodi lepp teewul xalaat bi sax ci xoli ak xeli waa Almaañ yi. Ñu mujj (waa Almaañ ñi) xam ne daal dunu man a amalati seen bennoo googu ci anamug jàmm, mbaa gu sartu reew, ndaxte Otris àndu ci te mi ngi koy xeex ak doole. Looloo waraloon nu jëloon seen yitte def ko ci amal am mbooloom xare mu dëgër, mu leen di man a may ñu man a genne Otris Almaañ cig njëlbeen, door a lijjanti nag nu nuy doone benn ci ginaaw bi. Xalaat bii nag diisoowaale bu Brusiya bii di Bismarck, àndoon na ci te jàpple woon ko, dëgëral ko. Moom mooy Otto Von Bismarck, boroom kurpeñu weñ bi.

Politigu Bismarck ci lu jëm ci bennoo gu Almaañ gi:

Bismarck mi ngi judd atum 1815g, am njàggam mu kawe mu defe ko ca daaray Berlin ju mag ja. Daal di dugg ag coldaar, gennati ca, dem nag feete ca boppam ca toolam ba. Mi ngi bokkoon nag ci njaboot gu woomle, gu ami alal yu rëy ca Brusiya. Sampoon na boppam ngir nu fal ko ci bennoo yu Almaañ yi, atum 1848g, ñu tànnoon ko it muy ab cer ci parlamaa bu Brusiya bi. Ligeey na it ci toolub diplomasi, doonoon ndawul reewam ca Butrsburg ca Rusi. Ginaaw bi mu nekkal reewam ca Paris.foofee la ko William mu njëkk mi doon jiite Brusiya woowe woon mu juge Fraans, ngir jiite-si njiitug jawrin gi ci Brusiya. Bismarck nag nekkoon na ku gëmoon, te daa dëgëral noste gu nguur gu nu joyal , te gëmoon ne buur daa war a am doole te am soldaar su dëgër, Egliis bi jàpple ko ak garmi yi. Bismarck moom faalewutoon parlamaa bi. Gisoon na ne jëm kanamug aw xeet walla ag yeegam jëm ca kaw manul a ame ci lu dul ay buuram di ñu kawe ay yitte, ak ay kilifaam, waaye du nu ko ame mukk ci ay saxal yu juge ci ay parlamaa, aki nostey sarti reew.

Bismarck yitteem jepp mi ngi ko jëmale woon ci genne Fraans ak Otris Almaañ, mu gisoon ne lii daal manul ame ci lu dul dooley xare ju mag, ju leen ci man a ga. Ci noonu mu tàmblee ligeey ci dëgëral dooley xare ji, ak kàttanal ko. Mu daal di tas parlamaab Brusiya bi, ndaxte (moom parlamaa bi) daa bañoon ne du woote alal ji mu doon laaj ngir man cee dooleel soldaaram si, ci noonu mu tëjopon kepp ku wuuteek politigam boobu, daal di digle ñu fuglu yeglekaay yi, daal di beddiku sartu reew mi, ne du ci sukkandikooti. Alal ji mu soxla woon mu gennelu ko ci ndigalul buur bi, bañ cee sukkandiku ci lu parlamaa bi.

Wàllug xeetu nag moom gis-gis bi mu ci amoon moo gënoon a yaatu bi mu amoon ci sartu reew, ndax daa gisoon ne sartu reew moom, mi ngi ame mook ay jubluwaayam, ci ginaaw bu ag xeetu amee ba noppi. Bismarck nag neenalul mbooleem parlamaa bi mbaa mu tas ko lepp, moom kay da caa neenl walla mu soril ko ñatti mbir, ñooy: (1) Coldaar gi (2) Politigu bitim reew bi (3) Fal ay jawrin ak di leen folli


Bismarck wone na dogu gu mag akug takku contar teg gi Otris teg loxo Almaañ, loolu nag gën na a fése ci taxaw gi mu taxawoon ci dakkal politigu Otris bi muy teg Almaañ . Looloo taxoon Otris mujj woo buuri Almaañ yepp cim ndaje ca Frankfort, ngir sos ag bennoo gu federaal, guy doxal ab goornamaa, boo xam ne ay dooleem ak sañ-sañam mi ngi koy jële ci sart boo xam ne Otris moo koy defar, tër ko. Bismarck gisoon na ne lii de ag anam gu yees gu Otris jëlati la, ñu muure ko mbubum diplomasi, ngir yeegati ci kaw waa Almaañ yi. Bismarck melaloon na sart boobu ne mooy sart bi gën a bon ci mbooleem yu mas a am ci kaw suuf. Ci noonu mu ne woon du teewe ndaje ma lu dul ci kaw ñu jox Brusiya ay àq aki yelleef yu tol ni yi nu jox Otris ci ñaari mbir yii, ñooy: (1) Dëgël ak wéyal jibalug bennoo gi (2) Jiite benno gi

Bismarck ci taxawaayam bii, leerale na ci ne Otris daal moom ñàkk na kàttan ga mu amoon ci aakimoo moom rekk mbirum bennoo gu Almaañ gi. Te it won na nguur-nguuraani Almaañ yi ne Brusiya mii kat mooy jenn dooley Almaañ ji man a jiite bennoo gu Almaañ gi. Bismarck jeem na a fàggu cofeelug Rusi, ngir mu bañ a feete fenn, bu ab xare tàkkee ci diggam ak Otris. Loolooo taxoon mu dugg ci lëj-lëju Poloñ bi, jàpple ci Rusi, kontar gori Ploñ yi defoon ag fipp kontar Rusi, ngir dañal ag àtteem te jeem a am ag tembte, ba man a amal ag àtte gu Poloñ gu temb. Fraans nag àndoon na ca fipp ga, te jàpple ko, askanu Angalteer wi ànd ca, waaye goornamaa ba moom àndu ca woon, ndax daa ragaloon ag nguurug Poloñ gu katolig judd, guy dem di àndeek Fraans. Ci noonu Bismarck moom dem jàpple-ji Rusi, te jàpple googu gu amoon doole la, ndax moom reewam (Brusiya) daa taqaloo woon ak Poloñ, ba noppi taqalook Rusi. Te it nanguwutoon a ànd ak Fraans ak Otris kontar Rusi.

Xarey Bismarck yi ngir taxawal bennoo gu Almaañ:

Bismarck xuus na ay xare ak lu bari ci reewi Tugal yi digoo’k Almaañ, ngir bennal reewi Almaañ yi. Ñu tudd ñatt rekk ci xare yooyu, ñooy:

Xare Brusiya yi ak Danmark:

Bismarck xuus na ab xare kontar Danmark, atum 1864g, ànd ca’ak Otris, ngir nangu ñaari diiwaan yii di Shalswig ak Holistin, ñu doonoon ñaari doox yu bokkoon ci bennoo gu Almaañ gi te Danmark tegoon leen loxo. Danmark mujjoon na ñàkk pexe, daal di deltu ginaaw wëlif ñaari doox yooyu atum 1864g, bu ko defee Brusiya jël dooxu Shalswig, Otris it àtte diiwaanu Holistin. Xarey Brusiya ak Otris:

Bismarck gisoon na ne xare bi moom – deet sikk – aji tàkk la ci diggante Brusiya ak Otris, te li ko waral du dara lu dul diiwaanu Holistin. Ndax kat mbir yi manunu woon a nekk di wéy ci anam gii nu nekke, di ay maslaa yu dëggoodi aki lijjanti yu xootadi aki juboo yu gàtti dig. Bis bu Yàlla dogalee njortul Bismarck loolu mujj di dëgg, ba Brusiya am ndam, loolu de da na nekki muccug waa Almaañ ñi ci gàllankoor gii tukkee ci Otris, gu leen di teree nekk benn, tee bennoo gu Almaañ gu wér man a am. Màggug Brusiya ci wàllug politig ci biir bennoo gu Almaañ gi, mujj di luy jeqi njàqare ci Otris. Solofrayn moom màgg na ci anam gu doy waar, rawati na bi ci nguur-nguuraan yu Almaañ yi tiim geejug bëj-gànnaar gi bokksee. Ci noonu lu sakkan jug ciy yooni weñ lënkale diggante wàll yu Almaañ yu wuute yi. Loolu tam dooleel bennoo gu koom-koom gi nga xam ne Brusiya mujj na di ci ki ci gën a jariñu.

Sabab yii rekk doyoon nanu ngir taal xeex bi ci diggante Brusiya ak Otris, rawati na ginaaw bi dooley Brusiya ji doxee jawali Holistin, nangu ko, te moom daa nekkoon ci ron kilifteefug Otris, ngir dëppoo gi amoon ci diggante Brusiya ak Otris atum 1865g.

Bismarck moom lijjanti woon na ba Rusi genne loxoom ci diggam ak Otris, loolu nag di ci jàpple gi mu jàpple woon Rusi ci giimal fipp ga amoon ca Poloñ, atum 1853g. Dëppoo woon na ak Imbratoor bi Napoleon III, imbraatooru Fraans, moom itam, ngir mu seetaan kook Otris, bañ cee dugal loxoom, li mu koy faye ci loolu nag mooy bàyyi kook yenn moomeel yi ci goxub Rayn. Mu demati tapoo-ji ak nguurug Itaali, gi nga xam ne li doonoon yitteem mooy nocci Venezia ci loxol Otris, ngir matal ag bennoom.

Xare bi amoon ci diggante Otris ak Brusiya xare la woon bu fëkk te gaaw, wéyutoon lu ëpp juroom ñaari ayu-bis, moo waraloon nu tudde woon ko xareb juroom ñaari ayu-bis yi. Dooley Brusiya ji jot na ca a gañee ju Otris ja ca xareb Sadwa ba, ca Bohima atum 1866g . Mu manoon a àgg sax (moom dooley Brusiya ji) ba ca Vienne, bu Imbraatooru Fraans bii di Napoleon III jugutoon, dox tànki jàmm ci diggante bi. Ci noonu Bismarck daal di ñàkk pexe, taxawal xeex bi, ngir ragal Fraans dugg ci xeex bi ci wetu Otris. Te it Bismarck moom da ne woon na doylu nag ci gañe gii mu gañe Otris, ak dammte gii mu ko dammte, ndaxte soril na ko bennoo gu Almaañ cig wàll, te it bëggutoon a toroxal Imbraatooru Otris bi, ngir loolu man na a tax bu jugee ëlëg moom Brusiya di xare-ji ak Fraans, Otris du ko sot, ci geneen wàll. Ag juboo amoon na ci diggante Brusiya ak Otris, ñu koy wax “juboog Braax gi”, atum 1866g. Ci la yii ame:

(1) Gennug Otris ci Bennoo gu Almaañ gi, gi mu tegoon loxo, la ko dale ca jamonoy Metternich. (2) Duggug mbooleem nguur-nguuraan yi nekkoon ci bëj-gànnaaru dexu Rayn gi, ci bennoo gu federaal gu Almaañ ci ron njiitul Brusiya. Diiwaani bëj-saalum rekk a bokkutoon ci bennoo googu. (3) Bàyyee gu Otris bàyyee Itaali Venezia.


Gis nga ko, Bismarck kat am na ay ngërte yu am solo ci xareem beek Otris. Moom de fare na fi bennoog Almaañ gu yàgg ga, indi fi leegi ag bennoo gu Almaañ gu yees, gu ame ci mbooleem reewi bëj-gànnaaru Almaañ, nga xam ne ñaari doox yii di Shalswig ak Holistin ci lanu woon, buuru Brusiya bi jiite ko. Bismarck nos na bennoo gu yees gi, wutal ko ab parlamaa (Rashstach), ndawi askan wa di fa daje, ak jataayub bennoo gu Almaañ gi (Bundasrat), ndawi diiwaani Almaañ yi bokk ci bennoo gu Almaañ gu bees gi di fa daje. Bismarck it lijjanti na ba def ak diiwaani bëj-saalum yi bokkutoon ci bennoo gi, lijjanti woon na ba def ak ñoom genn tapoo gu xare .

Xareb Brusiya ak Fraans:

Xetug xare tàmbli woon na a xeeñ ak a jòlli ci diggante Fraans ak Brusiya, ginaaw bi Brusiya gañee ca xareb Sadwa ba. Ndaxte Fraans moom begutoon dara ci lii Brusiya amal ciy ndam ci kaw Danmark ak Otris cig wàll, ak àntul gi mu àntuloon bennoo gu Almaañ gu bëj-gànnaar gi, ci geneen wàll.

Fraans moom daa jàppe woon loolu muy aw xët ci digg ginaawam, ndaxte moom kat manul woon a dékku ag nguur gu Almaañ gu am doole ci wetam. Moom kay li ko sooboon mooy Almaañ des di nguur gu nu dogat, ngir mu nekk moom Fraans di reew mi am kilifteef ci sowwub Tugal bi. Moom kay jamono ju nekk, da daa kontar bennoog Almaañ gi, ni ko Otris kontare woon. Bismarck it tàmbli woon na a xalaat nu muy xëcce diiwaani Almaañ yu bëj-saalum yi ngir nu bokksi ci bennoo gi. Jëf ju mel ni jooju nag Fraans du ko doon nangu, ndax moom tàmbli woon na di dugg ci mbiri diiwaan yu Almaañ yu bëj-saalum yi, ngir tee leen a bokki ca bennoo gu Almaañ ga nga xam ne Brusiya ko jiite woon. Lëj-lëju ku jigeen ki waroon a donn Espaañ daal di taxaw, mooy lëj-lëj bi taaloon xare bi ci diggante Brusiya ak Fraans. Lëj-lëj boobu mi ngi tënkoo woon nii: gàngunaay gu nguurug Espaañ dafa feexoon , ginaaw bi lingeeru Espaañ bi Elisabeth dawee, ñu gaaral buur bi Leopold ndëpp li, moom mi ngi bokkoon ci njabootug Hohenzellern, di woon ab njegeñaaleb imbraatoor bu Brusiya. Waaye ak li Leopold di bañ lepp ne du sol mukk ndëpp li, teewul Fraans mer ci loolu, jàmbat ko ci buurub Brusiya bi, daal di sàkku ci moom mu warlu ne du ànd ci ñu samp kenn ku bokk ci njabootug Hohenzellern ci gàngunaayaug Espaañ gi. Waaye buuru Brusiya bi bañ, ndax loolu kat dafa xaw a laal teddngaam ak ngoram, te xaw a niru ag yabeel. Loolu nag mi ngi ame woon cim ndaje mu mu defoon ak ndawul Fraans ca Ems. Bu ko defee buuru Brusiya bi yonnee ab day ca la juge woon ca ndaje ma, mu yonnee ko Bismarck, mi nga xam ne lepp li mu doon def mooy neggandiku ab pose ngir jibal ab xare ci kaw Fraans. Ba mu ko defee, Bismarck xëy tas ci yëglekaay yi ay cofiit ca la bawoo woon ca ndaje mooma, ngir merloo ci Fraans. Loolu nag ni mu ko defe mooy genne ay baat yu xaw a wow, yu begloowul dara Fraans. Ci noonu Fraans jug, jibal ab xare ci kaw Brusiya, ci 14 sulye 1870g, te fekku ko woon jekk ngir xeex, te taxul woon it mu xalaat ci ngérte yi man a juddoo ci bii xare, bis bu nu dàqee Fraans ci xeex bi.

Brusiya li nuy wax xareb fëkk la doon def ak Fraans, maanaam gaawal ko, loolu nag jot na koo def ba am ci xam-xam ca xareem ba’ak Otris. Bi mu ko defee tàngooru xare bi sax di tar lu tollook juroom benni ayu bis, waaye tàmblee giim, ci ginaaw bi, rawati na ci ginaaw bi ay màndargay kawe ak ëpp doole tàmblee feeñ ci xeex bi ñeel Brusiya. Xare bi bepp nag ci suufus Fraans la doon tàkke. Jotoon nanoo dàq Fraans nag ci xeex yu bari, bi ci gënoon a siw nag mooy bu Sedan ca satumbar1870g, nga xam ne àggoon na ci Napoleon III manutoon a ñàkk a wommatu, te nangu ne gañe nanu ko, ngir dàq yu metti yi te toftaloo, te yepp di yu nu teg ci kaw dooley Fraans ji ci biir suufus Fraans, te ray lu sakkan ciy soldaaram, te itam lu jege ñaari teemeeri junniy soldaari Almaañ sutuxlu ba ca xolub Fraans, te mu leer nàññ ne Fraans moom manatul a gañeeti Brusiya ca jamono joojee te manatu koo genneeti suufam. Loolu nag di woon ci 27 oktobar 11870g.

Ci noonu imbraatoor gu Fraans gu ñatteel gi daanu, ñu daal di taxawal ci Paris nosteg pénc gu ñatteel gi . Daal di teg Fraans ñeel Brusiya alamaanug xare gu toll ci juroomi bilyoŋi frank yu Fraans ( loolu mooy tollook – daanak – alamaan bi Napoleon Bonaparte tegoon Brusiya bi mu ko dumaa ca xareb Yena ba, 1806g. Bu ko defee ñu juboo ci xarekati Almaañ yi dunu genn Fraans li feek fayeesul alamaan bi, (moom nag jotees na koo fay ci diirub ñatti at). Nga rax ci dolli dagg gi nu dagge ñaari gox yii di Alsaas ak Loren ci fraans, boole leen ci Almaañ.

Nii daal la bennoo gu Almaañ mate woon ci njiitul Brusiya, ci loxol goor gu dëgër gii ni weñ, Bismarck, mi nga xam ne dafa gëmoon bennal Almaañ ak doonte day ci dereet, ci weñ mbaa sawara. Bu ko defee imbraatoorug Almaañ gi daal di sosu, dib xew-xew nag bu fés ci taarixu Tugal bu bees bi.boroom gàngunaay gi (imbratooru Almaañ bi) mujj di ku ñu joyal ab gogam ci def li ko neex ci nguur-nguuraan yu Almaañ yi. Sartu reew bu Almaañ bu bees bi yaxal na nu sos ñaari jataay:

(1) Jataayu Bennoo gu Almaañ (Bundasrat) (2) Jattayu (Rechstag)

Dooley yoonal ji nag mi ngi nekkoon ci Bundasrat, di jataay bi nga xam ne mi ngi ame woon ci juroom fukk ak juroom ñatti cer, ñu seddale leen ci nguur-nguuran yi nga xam ne ñoo amal imbraatoor gu Almaañ gi. Brusiya nag moom rekk amoon na fukki kàddu ak juroom ñaar, ginaaw bi mu am ñaar fukki kàddu. Ak li Brusiya di moomadi li ëpp ci kàddu yi lepp ci Bundasrat, teewul mu gënoon fa’a guddub loxo, gënoon fa a am jeexiit, ndax la ëppoon ca nguur-nguuraani Almaañ ya duggoon ca bonnoog Almaañ ga, danoo takku woon ci Brusiya, te daawunu woote lenn lu mu bëggul. Te daawunu jàllale genn saxal ca jataay ba, bu fukki cer ak ñeent àndadee ca saxal ga. Bu dee nag jataayu Rechstag nag moom, man nanu ne mooy jataayub askan bi, mi ngi ame woon ci ñatti teemeer ak juroom ñeen-fukk ak juroom ñaari cer, ñu leen di tànn ci anam gu sekkaree. Dooley jataay bii nag daanaka danu koo lafañal, yòqeel ko . ndax nguur ak doole yi nu ko joxoon ci ron sartu reew bu Almaañ bu bees bi, danoo nekkoon di yu doyadi te ñàkk solo.

Bismarck nag, jiite na goornamaa bu Almaañ bi niki diisoowaale walla chancelier. Benn ci ñaari jataay yi manul woon ci moom dara, mu yoroon it sañ-sañ bu rëy, te ci ron kilifteefam tam la Almaañ gu rëy gii gepp nekkoon, nga xam ne ña fa dëkkoon ca atum 1871g jege woon nanu ñeen-fukki milyoŋi nit, mujj àgg ci ñeen fukk ak juroom ñeenti milyoŋ ciy nit atum 1890g, di maanaam bi Bismarck faatoo ba am ñaari at.










Juroomeelu bunt bi


Sanc gu yees gi


Sabab yi fi indi sanc gu yees gi, ak ay anamam Reewi sancaan yi Ñaawteefi sanc yi Yëngu yënguy nasaraanal ak ay wi mu làmbool















Doggantal gu njëkk gi

Sababi sanc gu yees gi aki anamam.

Xamale lan mooy sanc gu yees gi:

Li sikk amul mooy sanc gu yees gii toppoon ci yewwuteg endustri gi ci Tugal, rawati na ci ñaari xarnu yii di bu fukk ak juroom ñeent ak bu ñaar fukk g, sanc gii de ay reenam tàlliku woon na di dem ba ca yëngu-yëngu yu wuññiy juxraaf yu Tugal yi nga xam ne dees leen di jàppe ñuy bunt bi nu jaare bay dugg ci sanc gu yees gi Tugal doon def ci reewi adduna bi.

Sanc nag dees na ko xamalee ci ne mooy teg loxo gi reewi endustri yu mag yi tegoon loxo mbiri koom-koom yi ak yu politig yeek aada ci reew yu bari ci yu amadi doole yi ci adduna bi. Rawati na yi ci di yu woomle ci wàllug mbay ak mbèll. Looloo tax sanc - ci maanaam mii mu yor – du lenn lu dul luy yëngu ci nangu ak fëkk alali jàmbur ak ngacc dooley mbindeef yi ak jariñoo leen.

Sababi sanc gu bees gi:

Li sabab sanc lu bari la te lënkaloo, ñu tudd ci yi ci ëpp solo yii:

(1) Màgg gu gaaw gi ba ëpp ci wàllug endustri, ci lu bari ci reewi endustri yu mag yi. Loolu nag tax ba reew yii mujj soxlawoo ay ne-ne yu nu laalul aki ja. Tax na tam ba ag gëpplante gu tar te metti am ci diggante reewi endustri yu mag yi, jëm ci yaatal seenug kilifteef ak sañ-sañ ci gox yi leen man a warlul ag yokkute ci wàllug endustri, ndax seen koom-koomu xeet wepp ci endustri la tegu woon. Li juddoo ci loolu nag lu mujjoon metti la ci reew yu neew doole yii nga xam ne yu mag yii danu leen tegoon loxo, ngir muucu seen njariñ yeek ne-ne yu nu laalul yi, ak ngir def leen ay ja yu mag te yaatu, yu nu man a jaaye seen ligeeyi Tugal yu endustri yooyu. (2) Yokk gu ñi dëkke ci reewi endustri yi yokkoon, loolu moo waraloon reew yii gëstu-ji woon fu nuy wàññi seen ëppiitum askan moomu, bu ko defee ñoom ñu man leen a nekkal dib jumtukaay bu am solo buy dëgëral seen koom-koomu reew miy nday. Laaj na ñu xamal leen ne politigu genne ëppiitum askan boobu ak sotti leen ci reew yi nu sanc, politig la bu nu nosoon, jublu woon ci ligeeyal xemmeemteefi sanc yu reewi endustri yi amoon way dëkk yu bari woon ba ëpp. (3) Bëgg a soppi nit ñi def leeni nasaraan (nasaraanal), ak wisaare diiney nasaraan ci kaw-kaw yi, ak ñu xamul ñi. Nga xam ne nasaraanal bokk na ci sabab yi gën a rëy yi waral wuññiy juxraaf yu Tugal yi am, te ñooy li ubbi buntub sanc. Waa Tugal yi jëfandikoo nanu diine niki ab raas bu niy jaare ngir àgg ca seen bëgg-bëgg yu sanc yi, yu politig yi, ak yu koom-koom yi, ak doonte danoo làqoon loolu, bu ko defee mbubboo seen wax jooju nu daan wax naan: wisaare ag nasaraan du lu dul xayal ak yiwal nit ñu deltu ginaaw, ñi xamul dara. Adduna bi nag sonne na bu baax ci par-parloo ak boddanteg diine ak xalaatu maa-la-gën bi reewi nasaraan yi ame woon jëm ci yeneen askan yi dul ñoom. (4) Wàññiku gu tar gi amoon ci ñi dëkke woon ci kaw gi, ci reewi Tugal yu endustri yi, taxoon ba jafe-jafe am ci wàllug dundub mbay ci reew yii. Loolu yobbu woon na reewi yii ci ñu wuti bii dund ci reew yu neew doole yii nga xam ne mbay amoon na fa doole. Reewi Tugal yi nag jaarunu woon ci yoon ngir am seen càkkuteef loolu, ci misaal ñu jaare woon ko ci yaxantu, waaye kay danoo jëfandikoo doole ak noot ak sanc, sukkandiku ci seen dooley xare ji, ak ñawug seen ngànnaay, ak neew dooleg geneen wàll gi mu fas yeenee noot, loolu mooy li ko dimbli ba mu man a am bëgg-bëggam yooyu ci kaw askan yu doyadi yi. (5) Lu bari ci reew yu mag yi, li leen doon defloo sanc googu mooy feeñal ag yëg-sa-bopp, aakimoo mbir yi, ag rëy ci wàllug xeet, yaakaar ne ñoo gën, yooyu nag ay jumtukaay lanu won ngir wone doole ak màgg gi nga xam ne reewi sanc yii màggoon nanu ko te ame ko ni doole. (6) Ay lonkoo yu Tugal ak yu dul ñoom, yu mag feeñ nanu ci biir yewwuteg endustri gi. Dajale woon it alal ju bari, ba gisoon ne leegi danu koo war a meññali ca reew yay màgg, ci wàlli koom-koom yi. Ci noonu lonkoo yu adduna yu mag yi tàmblee gëpplante ci meññilu alal yooyu, loolu nag jur ag jongante gu mag te tar, ba mujj sax yii lonkoo tàmblee sàkku ci seeni goornamaa ngir ñu jàpple leen te dëgëral leen, loolu tam daan yobbu goornamaa yi ci ñuy aar seen njariñu lonkooy reew. Loolu nag nooyal na yoon wi ba xeetu sanc gu politig man a taxaw, di lol gëpplanteg koom-koom a ko fi indi. (7) Bëgg gi reewi sanc yu mag yu bari bëggoon na dëgëral seen yoonu jokkoo gu adduna, loolu yobbu leen ci ñu teg loxo yenn yoon yu strateji yi, ak waax yu am yi solo, ak yoon yu mag yi am solo ci wàllug jokkoo gu adduna gi, di taqale diggante goxi adduna bi. (8) Bëgg gi yenn ci reewi sanc yu mag yi bëggoon a tas seeni xalaat, aki dal (principes) yu seeni làngi politig, ak seeni aada, jàppe loolu nag ab jumtukaay buy ligeeyal seeni xammemteefi sanc.


Anami sanc gu bees gi:

Sancug Tugal gu yees gi dafa jëloon ay melo aki anam yu wuute, yoo xam ne xew-xew ya peegoon te yiiroon reewum sancaan mi ak mi muy sanc, xew-xew yooyu danu doon jeexiital ci ñoom, bu ko defee sanc gu bees gi dikk ci ay anam yu bari, ñu tudd ci yi ci ëpp solo yii:

Sanc ngir dëkk:

Xeetu sanc gu ñaaw gii feeñ na ci ginaaw yëngu-yëngug wuññiy juxraaf yu Tugal yi. Bu ko defee reewi Tugal yiy wuññi, daal di taxaw ci neewal doole ñi cosaanoo woon ci reew yi nu wuññi. Jaare ko nag ci di leen dàkku ak a genne seeni reew, ak di leen alag ci xare yi, di leen toraxal, di leen seeyal ci biir mboolaayi reew miy sanc, maanaam di leen def daanaka ñuy ñenn ci ñoom ci wàllug aada, deesu leen manatee ràññale. Xeetu sanc wii mooy li waa Espaañ defoon ca Endo yu xonq ya ca Amerig gu digg ga ak gu bëj-saalum ga, bi nu leen sancee te dëkke leen, taxawal fa ay sancu, yoy mujjoon nanu cuub gox bii ci cuubug Espaañ, ginaaw bi fi ay waa Espaañ jëlee barabu endo yu xonq ya fa cosaanoo, mel ne leegi fa lanu cosaano, loolu di ci Amerig gu digg gi ak gu bëj-saalum gi, lu ci dul Bresil,moom waa Portigaal a ko sancoon.

Nu mel noonu la sahyooni yahood yi defoon ca Falastin, bi nu ko sancee ci doole, dëkke ko, reewi sanc yu mag yi jàpple leen ci, Britani nekk ca bopp ba. Ci noonu la yahood yi tasaaroo woon ci adduna bi, dajee, dëkksi ca Falastin, ginaaw bi nu leen fa gàddaayalee jëme, ci ron aarug reewi sancaan yi, ak li askanu Falastin daan xeex loolu lepp, te daan ci jiyaar ngir bañ ko.

Nii it la sancug Tugal gi meloon ca Afrig gu digg gi, ak Rodisiya, ñu fay teg doomi Afrig yi lu sakkan te lëw ciy coona, di leen noot, di leen teg loxo, di leen tiital, di leen tàqale ak a gënale ci wàllug xeet, ak lu bokkul ak loolu lepp ci anami mbugal yu tar te mbaam-àlle.

Teg loxo gu xare :

Ay reew yu sancaan jug nanu, teg loxo ay reew, nangu leen ci doole. Loolu nag li leen ci gënoon a jañ, gënoon leen cee yobbu mooy neew doole gi nu gèndiku woon ci yii reew, rawati na ci wàllug xare. Li ñu doon jublu ci teg loxo googu, mooy man cee jaare bay wéyal ak a doxal seen naali sanc yooyu daan tax ba nuy man a teg loxo ci koom-koomi reew yi nu nangu, ci seeni dooley xare, ci seen politigu bitim reew ak seeni mbiri xam-xam ak aada, ngir man a samp bu baax seen kenoy sanc ci dëkk yii. Misaali sanc yu mel nii yu bari lanu, nañu ci indi yii rekk: Sanc gi Fraans defoon Aljeeri, atum 1830g, ak sanc gi Britani defoon Adan, atum 1839g, defoon ko it Isipt atum 1822g, ak teg gi Fraans tegoon loxo dunu Madagaskaar, atum 1894g, Beljig defoon ko Kongo atum 1907g ak nangu gi Itaali nangu woon Libi atum 1911g, ak Ecopi 1936g.

Xeetu sanc wii mooy wi gënoon a tar te gën a ñaaw ci xeeti sanc yi, ndaxte lu diisoon la ci ñi cosaanoo woon ci reew yi nu tegoon loxo. Ndaxte sanc gu sukkandiku woon ci jëfandikoo doole la. Waaye li muy tar lepp ak a tiitale, teewul nit ñi xeexoon ko, te xaru woon ci jële ko fi. Jànkoonteek lu sakkan ciy jafe-jafe aki coona ci seen xeexu njàmbaar boobu ñu ko doon xeex, ba mujj ame ci lu màgg li nu doon wut, muy gore ak tembte, ak dàq sancaan yi ñu juge seeni reew.

Aar :

Reewi sanc yi mujj nanu wut geneen anam gu yees gu nuy sance ak a tege loxo reewi jàmbur yi, ñu soppi woon seen sanciin woowu doon tegu ci dooley xare, wut weneen wu nuy tudde “AAR”. Aar nag ci maanaa mu sanc mi mu yor, gënul benn yoon sanc gi nu daan defe ci teg loxo ak nangu reewum jàmbur ci doole, moom daal AAR, tur la ci tur yi sancaan yi indi te jëfandikoo ko ci yenn ci ay jamono.

Bu dee maanaa mi aar yor ci wàllug sanc, mooy def gi reewi sancaan yi daa def ay dëppoo aki kollarante ci anam gu maandoodi ak yeneen reew yu doyadi yi, te neew doole. Bu ko defee reewum sancaan mi day kollaranteek reew mi mu sanc ci di ko aar ci mbooleem tooñ gu ko man a dikkal, juge ci dooley politig ju digook moom walla jeneen. Bu ko defee loolu di may reewum sancaan mi, muy doxal mbirum reew mi nuy aar, ci wàlli kaaraange, bitim reew, ak koom-koom. Reew mi nu aar daal du doxal lu dul mbiri biir reewam rekk. Loolu nag daa na tax mu nu aar mi daawul am temb gu mat, ndax ag gore gu politigam kollarante yooyu danu ko daan tënk, ba daa ko tee muy def ay ligeeyam ci mbooleem ay mbiri reewam, ci ni mu ko neexe. Misaal yi ci loolu yu bari lanu, ñu indi ci yii rekk: Aar gi Fraans defoon Tunisi atum 1881g, ak Maraakes 1912g, ak aar gi Britani defoon Adan, dale ko ca ba mu ko tegee loxo atum 1839g, ak yeneen barab yi mu tegoon loxo.

Feetale :

Reewi sancaan yu mag yi tàmbli woon nanoo wutati ay tur yu bees, ngir sanc gu bees gi, ginaaw xareb adduna bu njëkk bi. Loolu nag mu jublu woon ci muur sanc gii muy def muuraayu ag yiw akug xay. Loolu nag du tee sanc moom di lenn rekk, ak mbubb mu mu man a sol, ak melokaan wu mu man a dikke . Ci noonu la “feetale” dikke, moom nag ag anam la ci anami sanc gu yees gi nga xam ne jataayu kureelu xeet yi saxaloon na ko, te nangu ko, mooy kureel googu nu sosoon ca Paris, ca ndajem jàmm ma nu defoon atum 1919g, ngir lijjanti lëj-lëj yi amoon ci ginaaw xareb adduna bu njëkk bi. Boobu kureel nag Fraans da ca’a defoon ay jeexiit yu mag mook Britani. Nga xam ne ni nu bëgge mu mel ni daanaka la mel.

Dalu feetale ci jëmmi boppam, ñi ngi ko jële - ci cosaan la – ca yoon wu Rom wu yagg wa . Feetale nag noste la gog defoon na mbooleem reew yi nga xam ne “reewi dëppoo yi ” nangoo woon nanu leen ci imbraatoorug Almaañ gi, ak reewum Usmaan mi , ñuy ay reew yu nekk ci ron feetale googu. Bu ko defee, reewi dëppoo yi ñoo nekkoon reew yi nu joxoon feetale googu, maanaam ci seen ron kilifteef lanu feetale woon mbooleem reew yi nu nangoo ci Almaañ ak reewum Usmaan mi.

Bu ko defee ñu waral ci reew yiy feetewoo feetale gi ñuy def leeg-leeg ñu indi ay saxal aki leeral yu aju ci seen dooley xare yi nekk ci reew yi nekk ci seeni loxo, te nu feetale leen ko. Saxal yii nag ak leeral yi kureelug feetale gi nekk ci kureelug xeet yi lanu ko daa indil. Feetale gi tam mi ngi daa yam ci benn ñeenteelu xarnu, maanaam benn xaaj ci xarnu bu xaaj ñeenti xaaj. Misaal yi aju ci xeetu sanc wii yu bari lanu, ñu wax la ci rekk: Feetale gi nu defoon Britani Iraak, penkub Jordani ak Falastin mi nga xam ne dafa genn ci teg loxo gu Britani, ngir tàbbeeti ci gu Israayil. Ak feetale gi nu feetale woon Fraans Siri ak Libaa, ak feetale gi nu defoon goornamaab neewiit yu weex ya nekk Afrig de Sud, feetale gi nu leen feetale woon mbirum Namibi, ñu yor ko di ko doxal. Ak feetale gi nu feetale woon Japon duni Pasifig, duni Marshal, ak feetale gi Ostraali ame woon ci kaw Gine gu yees gi añs. Kureelug xeet yi nag, daa xëyoon rekk sàkk feetale, di ko teg reew yu neew yi doole, ci sañ-bañ, te du leen ci tàggu mbaa mu ciy diisoo ak ñoom.

Denkaane :

Moom itam aw xeetati la ci xeeti sanc yi, wii nag xeet la wu feeñ ci ginaaw xareb adduna bu ñaareel bi. Ñu amale ko nag ci genn saxal gu juge ca mbootaayu xeet ga ñu sosoon , atum 1945g, ngir wutu fi kureelug xeet yi. Mbootaayu xeet yi nag neenaloon na kureelug feetale gu sax gi nekkoon ci kureelu xeet yi, ngir teg fi leegi jataayub denkaane bi nga xam ne moom lanu wekk leegi mbirum saytu sancu yi “reewi digg” yi moomoon, yilifoon leen: Reewi digg yi ñooy Almaañ, Itaali ak Japon bi nu leen laata a dàqe ci xareb adduna bu ñaareel bi. Moom jataay boobu tam moo yoroom mbirum reew yi tembagutoon. Misaalum xeetu sanc gii: denk gi nu denkoon Itaali Libi ak Somali ak denk gi nu denkoon Britani Tanganyika ak yeneen .

Sancug aada :

Moom de xeet la ci xeeti sanc gi nuy jaare ci xalaat. Yenn ci reewi sancaan yi danoo jugoon ci jariñoo xalaat ak aada, ngir ligeeyal seeni njariñi sanc. Ci noonu ñu sosoon ay jàngu (leekol) aki xamluwaay aki fajuwaay , aki barabi nasaraanal, ak yeneen, loolu lepp nag ngir man cee jaare bay sanc yii reew ñu ko def, te man leen a moom.

Fraans de xeetu sanc wii def na ko ci Afrigu bëj-gànnaar gi, ci : Tinisi, Aljjeeri, Maraakes, (sunu reew mii it di Senegaal def na ko fi), defati ko ci reewi Shaam yi, rawati na Libaa. Reewi dankub mbokkte bi it, Bennoog Sofiet gi jiite leen, ñoom itam jeem nanu ba sonn ci wisaare seen xalaat yi ak seen dali làngi politig yi ci reew yu bari ci adduna bi.

Barabi sañ-sañ :

Lu bari ci reewi sancaan yi danu doon ngàrtaajoo ak a aakimoo koom-koomu lenn ci reewi Asi yi ak yu Afrig yi, ba noppi naan ñoom de dugguñu te seen yoon nekkul ci mbiri politig yu reew yii, du caageenug seen mbiri biirum reew. Misaali xeetu sanc wii, mooy la xewoon ca Iraan atum 1907g, nga xam ne danoo defoon bëj-gànnaaru reew ma muy barabu sañ-sañ ñeel Rusi gu Xaysar gi, bëj-saalum ba nu def ko barabu sañ-sañ ñeel Britani. Amoon na it ay xejj yoo xam ne yenn ci reewi sancaan yi amoon nanu leen ci reewi adduna bi, lu ni mel mooy xejj yi nga xam ne reewi Tugal yi amoon nanu leen ci reewi Shaam yi, ci jamono ju Usmaan ji ak xejj yi nga xam ne reewi sancaan yi amoon nanu leen ci Siin ak Tayland ak yeneen.














Ñaareelu doggantal

Reewi sancaan yi

Lu bari ci reewi sancaan yi doon nanu def seen cawartey sanc yooyu ci fu bari ci reewi adduna bi, ci gox yii di: Afrig, Asi ak adduna bu yees bi (Amerig). Reew yi ëppoon solo ci reewi sancaan yooyu, ci taarix, ñooy:

Reewum Portigaal:

Waa portigaal yi ñooy ñi njëkk a def ay wuññiy juxraaf yu Tugal ci ñaari gox yii di Afrig ak Asi. Ñoo ci jiitu woon waa Espaañ, Holand, Angalteer, ak waa Fraans ak ñeneen ñi jot a def ay wuññiy juxraaf ci jamonoy yewwute gu Tugal gi.

Tukkib Vasco de Gama bu njëkk bi mu defoon ci Afrig ak End, moo ubbi woon gëti waa Portigaal yi jëme leen ci sanc ay barab yu bari ci Afrig ak Asi ngir teg loxo geeji penku yi, ak rënk yaxantug penku gi , rawati na li ci aju ci ay rëndaay , ak ngir yàq koom-koomu reewi jullit ñi, rawati na nguurug Mamaalig yi, ngir loolu man a doyadil jullit ñi, neewal leen doole.

Waa Portigaal yi tàllaloon nanu seen kilifteef ak sañ-sañ ci duni Madira yi, Bopp bu Wert bi ak Osoras, barab yooyu nekkoon ci màmbulaanug atlas gi,la ko dale woon ca ñeenteelu bu njëkk ba ca fukk ak juroomeelu xarnu g. Cig nangu tegoon nanu loxo barab yu bari ci Afrig ak Asi ci xarnub fukk ak juroom g, yu ci mel ni: Mosambig ci penku Afrig, Angola ci sowwu bi, Ecopi, ak duni Madagaskaar, Moris ak Silaan ak xat-xatu Hormos ak xat-xatu Malga ci daanaka-dun bu Malayo añs.

Waa Portigaal yi defoon nanu seen “sanc gi ngir dëkk” ca Bresil, gi nekk ci Amerig gu bëj-saalum gi, ñu indaale fa woon lu sakkan ciy jaam yu Afrig ngir ligeeyloo leen ci mbay meek gasum mbell mi. Nu leeral leen ne sancug Portigaal moom dundul lu ëpp ab xarnu, ndax seen soxot gu tar gi nu ame woon ci ñoñ ñi cosaanoo woon ci seen sancu yooyu, ak ngir ñàkk gi nu ñàkkoon a yittewoo mbirum nos politig bi ak goornamaa bi ci seeni sancu. Ak tam ngir xeeg gut ar gi leen askani yii barab doon xeex.

Reewum Espaañ:

Espaañ def na ay ligeeyi wuññeem yu juxraaf moom itam ginaaw waa Portigaal, waaye jariñu ci seen xam-xam boobu ñu jot a am ci lef moomu. Bu ko defee, waa Espaañ jël goxi Amerig gu digg gi ak gu bëj-saalum gi def leen ay sancu yu mu sos ngir dëkksi fa. Moom nag ag sancam daa tegu woon ci fitna, ray, song, jaay doole ak gënale ci wàllug diine. Ci noonu ñu tàggatoon jaam yu ñuul yi ak endo yu xonq yi ngir ñu bayal leen tool yi, gasal leen mbell yi. Ñu daal di woon jël yii reew cuub leen cuubug Espaañ, ci làkk, ci diine, ci aada ak ci taarix, ba mujj sax bii gox ñu koy wooye Amerig gu Latin gi, di ko askanale Latin gi nu jublu woon Esspaañ ak Portigaal. Espaañ it tàllaloon na ag kilifteefam, lal ko ci kaw ay barab ci goxu Afrig, yu ci mel ni duni Kanari ak àllub Maraakes bi ak goxu Afni bi dend ak Maraakes ak Gine gu Espaañ gi nekk ci bëj-gànnaaru rëddu yamoo wi .

Sancug Espaañ gi neewoon na doole te doyadi ci kanamu jongante gi Tugal doon def ci wàll googu. Ci noonu waa Angalteer yi yàqate woon seen mbooloom gaal mi tuddoon Irmada, atum 1588g. Mbooloom gaalum Holand mi tam moñoxeeti mu Espaañ mu lòtt mii atum 1607g. Ci noonu la Espaañ mujje di reew mu neew doole mu loof ci kanamu gëpplante gu Angalteer, gu Fraans ak gu Portigaal. Bu ko defee, ay fipp am ca sancuy Espaañ ya, ci noonu askani dëkk yii daal jéngu xeex ba roccee seen tembte ci loxol waa Espaañ yi.

Reewum Holand:

Waa Holand yi danoo duggoon ci ngérum Protestant ba noppi nekk ci ron teg loxo gu Espaañ gu katolig gii. Looloo taxoon ñu defoon seen fipp gu mag googee kontar katolig yu Espaañ yii, daal di noccee ci ñoom seenug temb ci doole ci njëlbeenug xarnub fukk ak juroom ñaar g. Waaye temb gii nag nangu na ko (moom Espaañ) ci anam gu ofisel atum 1648g, ca kollareg Westfalia ga nu defoon, ginaaw xareb fanweeri at ba . Waa Holand daal di taxawal lonkoo gu End gu penku gu Holand gi ci njëlbeenug xarnub fukk ak juroom ñaar g. Daal di sóobu ci geewub jonganteg sanc gi ci penku bi, daal di not waa Portigaal yi ci wàllug sanc, teg loxo duni End yu penku ya ca Asi. Yaatuwaayu suuf yi Holad mujjoon sanc mujjoon na gën a rëy juroom ñaari yoon yaatuwaayu Holand gu ndaw gii ci jëmmi boppam.

Sancaan yu Holand yooyu danoo rënkaloon seen bopp rekk yaxantu gi aju woon ci rëndaay yi, kawsu, attaaya, kafe, suukar, seng ak petrol añs. Waaye ñii dëkke woon ci sancu yu Holand yi te cosaanoo fa, xeexoon nanu kontar waa Holand yii ba mujj am tembte atum 1949g ci turu Endonisi. Waa Holand yi tàllaloon nanu seenug sanc ci diir bu gàtt ci kaw ay barab ci adduna ju yees jii di Amerig. Ñu taxawaloon lonkoog End gu sowwu gu Holand gi atum 1622g, ñu sancoon goxub dexug Hadson, daal di jënd Manhatan ci endo yu xonq yi, daal di taxawal dëkkub Amstardaam bu bees bi nga xam ne waa Angalteer yi nangu woon nanu ko ci Holand, tudde ko New York. Waa Holand tam sancoon nanu – ci diirub fanweeri at – ag wàll gu mag ci Bresil gi nekkoon ci ron kilifteefug Portigaal.

Reewum Beljiig:

Leopol mu ñaareel mi tegoon na loxo reewum Kongo mi nekk ci digg Afrig atum 1876g, daal di koy def ag moomeelam, loolu nag wéyoon na di nekk ba atum 1908g, ci ginaaw bi lanu tuxale moomeel gii yobbu ko leegi muy gu reewum Beljig. Kongo nag reew mu naat la lool, te woomle ci ay koom-koomi mbell. Waa Kongo nag jàmmaarloo nanook sancug Beljig gii leen doon jariñook a toggi mbugal, daan jariñoo it seeni koom-koom ci anam yu ñaaw a ñaaw, loolu yobbu leen ci ñu am tembte atum 1960g ci turu Saayir.

Sancug Britani:

Imbraatoorug Britani gi moom lanuy jàppe muy gi ëpp ci reewi adduna yi mas a def sanc gu yees gii nu xam tay. Moom mooy imbraatoor gu sanc gi nga xam ne jant manul a so mukk ciy sancoom ngir bari gi mu bari lu mu sanc ci suufus adduna si.

Britani dey defoon na ci wuññiy juxraaf yi, waaye ca Amerig gu bëj-gànnaar ga, mu sancoon lu sakkan ciy suufam, waaye dëkke leen, te sonn it ci dindi kilifteefug Fraans ak Holand ci gox bii te jële ko fi. Bu ko defee, sancu ak dëkkuwaay yu Britani yi ci Amerig gu bëj-gànnaar gi desoon ci ron cang gu sanc gu Britani ba kero Diiwaan yu Bennoo yu Amerig yi di am tembte , naka noonu Kanada, ñoom reew yii nga xam ne dafa am lu leen boole ak Britani, muy bokk gi nu bokk ak ñoom askan, te bokk nekkandoo ci “Komonwelth gu Britani”. Britani sancati na Ostraali ci anamug dëkk ak Newsiland, waaye temb nanu ñoom ñaar te mujj bokk ci Komonwelth.

Britani sanc na End, wéyal fab sañ-sañam, daal di sos lonkoo gu End gu penku gu Angalteer gi atum 1600g, mu jot a dàqe Fraans ca daanaka-gox bu End ba . Mu manante Siin ci mu ubbi ay waaxam ci kanamu Afyon bii nga xam ne Britani daa na ci indi lu bari ci waa Siin yi. Looloo waraloon xare ba tàkkoon ci diggante Siin ak Britani, di woon xare bu nuy tudde xareb afyon bu njëkk bi nga xam ne wéyoon na la ko dale woon ca atum 1840g ba 1842g, nga xam ne ca la Britani nangoo waaxub Hong Kong bu straateji bi, waax bii mi ngi woon ci loxol Britani ba bu yàggul. Xareb afyon nag benn la ci tooñaange yi nga xam ne Britani mi ngi ko doon tooñ waa Siin cig wàll, ak nit ci jëmmi boppam ci geneen wàll.

Britani tegoon na loxoom dunu Brem atum 1799g, ak Adan atum 1839g, ak Borma atum 1885g, akug wàll ci Malayo. Mu defati ay aar aki kollarante yu maandoodiku ak ab lim ci barab yi nekk ci bëj-saalumu dunu araab bi, ak tefesug golfub araab bi. Mu sanc Isipt, Sudaan, Iraak, Penkub Sordani, Falastin ak yeneen barab ci reewi Asi yu ñàkk doole yi.

Britani nangooti cig sanc lu bari ci reewi Afrig yi, lu mel ni: Afrigug Bëj-saalum gi , Nijeeriya, Oganda, Tansani, Rodisiya ak Somali gi nu xame woon ci turu Somali gu Britani gi.

Sancug Britani gi nag mooy gi gën a ñaaw ci mbooleem xeeti sanc yi, ndax moom da daa jëfandikoo cig sancam doole, teg loxo ak jariñoo ne-ne yu nu laalul yi , ak kàttanug askan yi ak tas nit ñi ak xàjjale leen, fitnaal leen ak tooñ leen. Waaye li lii lepp di tar, teewul askani sancu yu Britani yi xeex nanook sancaan bi ba kero nu ame seen tembte, ci noonu la Britani dellu mel namu meloon, yor dayo bi mu yoroon, ginaaw bi sancoom yii tembee wëliif ko, foofa la ko lòttug politig gaare ak gu koom-koom.


Reewum Fraans:

Waa Fraans yi bokkoon nanu ci ligeeyi wuññi yu Tugal yi ci goxi Amerig gu bëj-gànnaar gi, rawati na ci Kanada ak gox yi peek dexug Santa Lorens gi. Ñu sosoon fa ay sancu yu Fraans, yu ci mel ne: Kebeg gi nga xam ne ci tefesug Santa Lorens gi lanu ko taxawaloon, ak sancu bu Luwisiyana bi nga xam ne turam wii mi ngi juge ca Luwis mu fukk ak ñeenteel ma buurub Fraans ba.

Ag gëpplante gu mag xewoon na ci diggante waa Fraans yi ak waa Britani ci Amerig gu bëj-gànnaar gi, ci xarnub fukk ak juroom ñatt g. Waaaye Britani moom jot na a neewal doole kilifteefug Fraans gi ci barab yooyu, bu ko defee Fraans moom teg loxo yeneen barab yu bari ci Afrig, fu ci mel ne: Aljeeri, Tinisi akug wàll ci Maraakes, daal di sutuxlu ci tàkkug Afrig gu mag gi, daal di yaatal bu baax seen sañ-sañ ak kilifteef ci Senegaal, Kongo, Nijeer, Madagaskaar, Somaal gi nu tudde woon Somaalug Fraans gi, Gine ak Dawme.

Fraans tegati loxo ay reewi Asi, fu ci mel ne: ay wàll ci End, waa Britani jële leen fa atum 1763g. ñoom de jotoon nanoo taxawal lonkoo gu End gu penkug Fraans gi, ngir gëpplanteek lonkoo gu End gu penkug Britani gi, ak lonkoo gu End gu penkug Holand gi ci wàllug yaxantu ci penku bi. Fraans sancati Sireek Libaa ci turu feetale , ci ginaaw xareb adduna bu ñaareel ba . Sancug Fraans gii nag daa melowoo ag tooñ, tiitale, jeem a far aaday reew yi mu sanc ak seeni màndargay reew ak jëmm. Lu mel noonu it mooy li nu def ci reewi araab yi nekk ci bëj-gànnaaru Afrig te Fraans tegoon leen loxo. Waaye way dëkke ya xeexoon nanu sancug Fraans gii, ba mujj am tembte gu mat .

(Fii fi Senegaal, waa Fraans sonnale nanu fi, tege fiy fitna, gennee fi, xoolal ku mel ni Sëriñ Tuuba., cig tooñ lanu ko fi gennee, sanni ko ca àlli Gabong yu lëndam ya, yobbooti ko Moritani, te fii nu koy genne de du seenum reew, reewam la. Xoolal ma fa ñuy wax (Camp Caaroy) ak jëf ju ñaaw ja nu fa def, xoolal ma sunu làkki reew yii nga xam ne ba tay manunu leen di jàng te Fraans nekk ci ginaaw, xoolal ma yeneen mag yi nu sonnal, xoolal ma aaday nasaraan ji nu fi bëgg a saxal, leegi la sax waaye ci ginaaw ak seen Senghor mi fi nekkoon nga xam ne daanaka tubaab la woon, ngir ne seenub ligeey la woon bu leen fiy ligeeyal, lenn luy sunu aada safu ko woon, du col mi, du wax ji, du lekkiin wi, du lenn lu mu man a doon, naka noonu ñi nekk ci ngunoom ci ñi mu sos, defar leen, ñu koy ligeeyal).

Reewum Almaañ:

Imbraatoorug Almaañ gi moom itam dugg na ci geewub sanc bi ak jongante gu adduna gi, ginaaw bi mu amalee ag bennoom atum 1871g, mu daal di sanc Kamerun ak bëj-saalumu sowwub Afrig, bi nga xam ne dees na koy wooye bëj-saalumu sowwu Afrig bu Almaañ bi, ngir sanc gi ko Almaañ sancoon, ak bëj-saalumu penku Afrig bi nu tudde ba tay bëj-saalumu penku Afrig bu Almaañ ak Togo . Almaañ it jotoon na a teg logo lu bari ci duni Pasifig yi nga xam ne ñi ngi leen gënoon a xame ci turu “duni argabiil yu Bismarck yi” . Ñu nangu tam ñoom waa Almaañ xaajub bëj-gànnaar bi ci duni Gana gu yees yi nekk ci màmbulaanug atlas gi. Waaye Almaañ moom mujjoon na ñàkk sancoom yii ci ginaaw bi nu ko dàqee ci xareb adduna bu njëkk bi.

Reewum Itaali:

Itaali tam soobu na ci lefum gëpplanteg sanc gi, ginaaw bi mu bennoo, atum 1870g, mu daal di teg loxo ay sancu ci Afrig, ci Eritri, Somali, gi nu tudde Somali gu Itaali gi, Libi ak Ecopi. Itaali nag jëfandikoo na gën ja a ñaawi anami mbugal ak ray ci kaw askani yii reew. (Omar Muxtaar ca Libi fàttaliku leen ko).

Reewum Rusi mu Xaysar mi:

Sancug Rusi gi moom mi ngi jëmoon ci Siberiya, Turkmanistaan ak ay gox ci Asi gu digg gi. Rusi it teg loxo gox yi nekk ci bëj-gànnaaru dexug Amoor gi ci Siin, daal di fay taxawal ab dëkk bu bees ci turu Vladivostok, lijjanti it ba Siin gu neew doole gii jox ko ay sañ-sañ ci defar yoonu weñ wu jaar ci suufi Manshuriya gu Siin gi, ligeey ba daal di tàmbli ca atum 1889g. Sañ-sañu Rusi it yokku ca Kore, mu daal di seddoo Iraan mook Britani, daal di sanc wàllug bëj-gànnaar ga, ci ginnaaw bi nu defee seen dëggoo gu xaritoo gi, xaatim ko cis een diggante ñoom ñaar atum 1907g.



















Buntub ñatteel bi


Ñaawteefi sanc:

Li sikk amul mooy sanc gii amoon ci adduna bi, ci melokaanam yepp aki anamam, bokkoon na ci li gënoon a soof te ñepp bañoon ko te sib ko, rawati na askan yi nu ko teg ci seen kaw, ba nu mos aw wextanam, reer cig lëjam. Sanc de bijj na lu lëw ciy ñaawteef aki jeexiit yu bon ci ka waskan yu lòtt yi yanu woon ab sukkam. Ñaawteefi sanc moom dees na leen man a gaw ci wàll yii:

Ñaawteefi sanc yu politig:

li kenn reerewul mooy ne reewi sanc yi de rekki nanu ngorug askan yi nu sancoon seeni reew, rekki it seen sañ-sañ ci wutal seen bopp mujj gi nu gis ne moo gën ci ñoom, te loolu dal yi aju cig nite yepp ak yu yoon yepp woote nanu ko. Xañoon nanu it askan yi ñuy àttewoo ci sartu-reew , ak ci nostey demokraasi yu tegu ci cëslaay lu mucc te sell, loolu nag mi ngi am ci ginaaw bi nu yàqee mbooleem campeefi xeet yi te dindee leen fi, wuutal fi yeneen yuy ligeeyal seeni xemmeemteefi sanc.

Sanc gi nag jeemoon na a defi pexe ba askan yi nu sanc dunu doon mukk benn, bu ko defee mu def lu nekk, jëfandikoo pexe mu mu man a doon ngir xeet wi bañ a nekk benn. Mu tàmblee wut lepp luy tàqalee di ko sotti ak a wisaare ci mepp mbooloo muy menn, ak wepp xeet wuy wenn, ci mepp reew muy menn. Mu soññ te sawarloo yëngu-yënguy beddiku yi yi nga xam ne neewte yaa ngi leen doon sàkku ak def, daal di yittewoo bu baax lepp lu aju ci luy jeqi ag xëccu jëm ci waaso mbaab kureel walla boddante mbaa woote ag gën ci biiru xeet ak wuute ci ngér, mu ñëwati xóotal dalub tàqle politig ci mennum reew, daal di sawarloo làng yi ànd ak moom ci politigam boobu, daal di def ay soppi ci dig yi , yooyu soppi nag ñoo mujj di jëfka yu mag yi mujj di taal gilinug wuute gi ak noonoo ci diggante dooley politig yi dëkkandoo, dendandoo, mu dooleeti indil reew yi mu sanc ay jafe-jafey politig yu fasu, yoy reew yi nu sanc de wéy nanu di jànkoonteek ñoom ay ati at, ginaaw bi nu tembee, yooyu jafe-jafe wéyoon nanu di fi sax ginaaw bi nu mujjee nekk di fi ag dund gu yees. Sanc nag jëfandikoo woon na mbooleem xeeti jumtukaayi mbugal yi kontar askan yi, mu duma, tëj, mbugal, te ray lu sakkan ci askan yi te dara waralu ko lu dul ne danoo fippoon kontar ko, sàkku woon nu nuy goree te temb, te loolu àq ju mag la tey yelleef ñeel leen. Waaye askan yii yanu woon sanc gi, jugoon nanu xeex, def ci seen lepp ngir yekkati yan bu diis bii tegu ci seenum ndodd.

Ñaawteefi sanc yu mboolaay:

Sanc daal dafa defoon yitteem ci tas, xottite bennoo gi am ci mboolaay yi nekk ci sancu yi, jaare ko ci soññee cig tàqalikoo, wisaare nosteg kureel ci biiru askan, bu ko defee kureelug laman yi walla gu sang yi daal di feeñ, am ay sañ-sañ yu bari aki ngëneel yu tax ñeneen ñu ndool ñig ñàkk di bëgg a ray akug reer mere woon leen . Gii kureel nag ligeeyal na ba tàyyi sanc gi ci anam yu bari. Bu ko defee jaasiy sanc gi nekk fi di lu nu bocci ci baatub ñu ñàkk ñi, di leen tegi coona, di leen fitnaal, te kat ñoom ñooy ñi ëppoon ci askan wi. Am geneen kureel gu feeñati ci wetu gu lamani sancu yi, mooy kureelug sang yu doxandeem yii nga xam ne ñoo tegoon loxo ci koom mi ak ci nguur gi walla àtte gi, bu ko defee tàggat doomi sancu yi ci ñu leen di ligeeyal.

Sanc gi tàbbal na ci sancu yi mbooleem aada yu ñaaw yi man a yàq ag mboolaay, man a ñaawali jikkoom. Mu soññe cig mbon, reer, jëfandikoo dorog ak yiy màndal ak wure ak kart ak yu dul yooyu ci aada yu ñaaw yi man a tas bennoo gu ag mboolaay, te dëgëral nekkug sancaan yi ak seen doole ci sancu yi, te gën fee suuxat seen reeni sanc.

Sanc gi de jeemoon na – jëfandikoo woon ci loolu bepp kerkeraan bu mu amoon mbaa yoon wu mu xamoon – ngir gòndi niti sancu yi ci xayug Tugal gi , te sopploo leen ko, ngir ag maas man a judd guy gëm te gòndiku ci jëm-kanamug Tugal gi ak xalaati waa Tugal yi. Li ñu jublu woon ci raxasug xel gii mooy indi fi ag maas gu yees guy ligeeyal njariñu tubaab yi, rawati na bu maas gii mujjee jiite reew yi ci politig, jaare ko ci seenug jàpple. Waaye ànd ak pexey sanc yii yepp ngir amal loolu, teewul askani sancu yi tas yaakaari way sanc yi, sooyal seeni mebat. Seeni mebat sooy na, seeni yaakaar tas, bi nu gisee ne askan yi dey ñi ngi wéy di gën a jàpp ci seeni diine, di gën a ŋoy ci sseeni aada, di gën a ngëb ci seeni pas-pas yu laab yooyu. Fonk seen bopp, seen taarix aks een xalaat. Nga gis ne maas gi juddoo ci jamonoy sanc ñoo yanu woon raayob fipp gi ak xeex bi kontar sancaan yi, ñu saxoon nag ci noonu ba mujj fuqarci ci doole seenug gore akug temb gu mat sëkk.

Ñaawteefi sanc yu koom-koom:

Li njëkk a yitteel sancaan yi mooy am ay ne-ne yu nu laalul yu mbay ak mbell ba man a doxal seen ligeeyuwaay , buk o defee man fa a ligeeye lu nuy genneeti di ko jaayati ca reew ya nu sanc, looloo taxoon sanc gi saxoon ci di muucu ak a ngacc xeewali reew yi nu sanc yu mbay yeek mbell yi. Mu soññ lonkoo yu jàmbur yiy rënk, ñu ñëw meññilu seen alal yi ci reew yi nu sanc ci anam ak wàll yiy ligeeyal tey jariñ reewi sancaan yi. Bu ko defee yii lonkoo taxaw ci jariñoo koom-koomi reew yi nu sanc ci diir bu gàtt , ndax danoo yàgg a ragal fipp yi leen daan kontar te askan yu ndooli sancu yi daan leen def, ñoom ñi nekkoon ci ron yan bu diis bii leen tegu woon te weesuwutoon lenn lu dul sanc gi. Reewi sancaan yi yamunu woon ci muucu xeewali sancu yi, waaye àggoon nanu ci def leeni ja yuy muucu ak a dékku marsandiisi Tugal yi. Lii nag moo nuy woo ci ñu tudde sanc gi “siyukaay biy si buy dem ak buy ñëw” .

Sanc gi moom da daan xeex endustri ci sancu yi, daan def lepp lu mu man ngir sancu yi sax di ligeey ci mbay mi te bàyyi endustri bi, ngir man a joxe ne-ne yu nu laalul yu mbay yu man a dundal endustri yu reewi sancaan yi. Sanc gi jeem na a ray ruug gëpplante ci doomi sancu yi ginaaw bi mu fi rayee endustri bu lokaal bi, tax it ba seeni boroom daanu ci kanamu endustri bu reewi Tugal yi. Bu ko defee këri jàmbur yi teg loxo ci koom-koomi reew yi ak seeni alali endustri. Ñu takk it xalisu sancu yi ci xaalisu reewi sancaan yi, loolu lepp nag ñu jublu ci takk koom-koomu sancu yi ci koom-koomu reew yiy sanc. Fii nag la genne gisiin wi naan: sanc gu politig du lu dul doomi sanc gu koom-koom ci sunu jamono jii nu toll.

Ñaawteefi sanc yu aada ak xalaat:

Sanc gi xamoon na ne aaday xeet ak cosaanam mooy li gën a man a dëgëral ag bennoo gu politig ak gu mboolaay, te moo gën a gaaw a jañe ci xeex ngir gore cig sanc ci reew yi. Sanc gi jeem na a soppi taarixu reew yi nu sanc, te def ay pexe ci soppi seenug xay gi nga xam ne seen ngértel xeli doom la, juddoo nag ci ay jamono yu toppante te toftaloo. Mu tàmblee jël tooke di ko def ci lem ngir dundal ci doomi sancu yi jaare ko ci aada ak xalaat ngir ñu man a jàpple tubaab yi ci seen xalaat yi ak seen xemmemteefi sanc yi.

Sanc gi nekkoon na fi di doju pakastal ci kanamu am njàng, rawati na mi ci aju ci xam-xami dëppale yi ak yu xarala yi nga xam ne danuy jàpplee bu baax ci yewwuteg xam-xam man a am ak gu endustri ci reew yi. Te moom (sanc gi) yitteem weesuwuton ci wàllug njàng li nuy wax njàggale mu matale mi, walla njàggale mu yaatu mi . bu ko defee njàng mu kawe mi mu jagleel ko doomi kureelug laman gi daa jariñu ci sanc gi des fi.

Sancaan yi danu daa yittewoo tas ak a wisaare seen làkk ak aada ak seen taarixu xeet ak seen xay gii nga xam ne teguwul ci lenn lu dul ci ne-ne . Ñu tay-taylu woon di far dëgg yi, di indi li dëppoo ak seen njariñ, di wisaare xam-xam yiy ligeeyal seeni reew, di wone dooleem akug màggam, ñu tàmbli woon a sikk ndegam ñii cosaanoo ci sancu yi man nanoo jiite am reew, daan leen sabooteel seen kilifa yi, seen njiit yi, seen jàmbaar yi ak seen boroom xam-xam yi. Sanc gi jubluwutoon ci loolu dara lu dul ligeeyal boppam aki njariñam ak jeem fee saxal boppam, moom mi nga xam ne masul a dañ di ragal fippug askan yi ak seen yewwuteg xeet.









Doggantal gu ñeenteel gi:


Yëngu-yëngu yu ag nasaraanal ak ay wi mu àndal:

Ag nasaraanal yëngu-yëngug diine gu nu nos la, gu li ko tax a jug mooy tas diiney nasaraan ak xayug nasaraan yi ci jullit ñi ak ñu dul ñoom. Nasaraanal gii nag lu taqoo la ak sancug Tugal gu yees gii nga xam ne jot na a man a ligeeyal diiney nasaraan ci anam gu nëbbu, jaare ko ci ay yoon aki defiin yu lëmu te jafee xam. Loolu lepp nag ngir ligeeyal ay xemmemteef yi mu amoon ci sanc adduna bi, yilif ko . Looloo du yomb nu tàqale diggante nasaraanal ak sanc, te itam nasaraanalkat yi danu daa nekk ci ron kilifteefug sancaan yi. Lu yeeme la diiney nasaraan nekk di benn ci jumtukaayi sanc gu Tugal gu yees gi. Nasaraanal nag yamutoon ci benn jàngu rekk ci jëmmi boppam, waaye kay jàngu yepp a ko daan def, moo xam jàngu bu sowwu bi la (bu Katolig bi), bu penku bi (bu Ortodoksi bi), bu protestant bi walla bu Angalteer bi (bu Angalikaan bi). Gëpplante gi taroon na ak xeex bi ci seen diggante, ni mu tare woon ci diggante reewi sancaan yi.

Taarixu nasaraanal gu yees gii nag am na ag takku gu mu takku woon ci yëngu-yëngu gu wuññi gu juxraaf gi reewi Tugal yu nasaraan yi doon def, te Porrtigaal ak Espaañ jiite woon leen, di woon ñaari reew yu ëppaloon ci diine te daan ci par-parloo kontar jullit ñi ak seen adduna. Bu ko defee wuññikati Orob yii ame woon ag parparloo gu diine defoon seeni ligeeyi wuññi, soldaarus Tugal si topp ci seen ginaaw di ligeeyal xemmemteefi sanc yu seeni reew, loolu lepp nag ngir nu àndandoo amal li nu bëgg mooy ligeeyal tubaab yi, te taxawal seenug cang ci diineek fetal .

Jumtukaayi nasaraanal aki ker-keraanam :

Nasaraanalkat yu nosu yi jëfandikoo woon nanu ab lim bu rëy ciy ker-keraan yu leen di dimbali ci seen ligeeyub nasaraanal bi, bu ko defee nuy def jamono ju ñëw ñu seet nu ñu ciy def ba ligeeyal ci seen jubluwaay boobu. Jumtukaayi nasaraanal gën na a jëm kanam ànd ak jëm kanam gi jamono def ak gi xam-xami dëppale yi ak yu xarala yi def. Nasaraanal ñi ngi ko tàmblee ci ay nit di jug di waaraate ak a xamale yonnant Yàlla Hiisaa (j.m) akum njàngalem diineem. Wii xeetu nasaraanal sax na fi di ag nasaraanal gu kenn nit di def, mu doonoon lu jëmadi kanam waaye tolloo woon ak jamono ju yàgg ji mu dajeeloon. Jumtukaayi nasaraanal jëmoon na kanam aki ker-keraanam bi yewwuteg xam-xam ak gu endustri gënee jëm kanam ci Tugal. Bu ko defee yonnee yu nasaranal yu nu nos yi tàmblee am, ay mbootaay yu nasaraanal yu bees di leen saytu, yuy jëfandikoo mbooleem anam yi ak jumtukaay yu yees yi ngir doxal seeni ligeey, bokk na ci li nu daa jëfandikoo:

(1) Ndoktoor ak li mu àndal ci ay barabi faju, lu ci mel ni: fajuwaay yi ak këri faj yu ndaw yi ak barab yiy maye ay garab. Ci xaranub fukk ak juroom ñeent, ay mbootaayi ndoktoor yu nasaraanal yu bari feeñoon nanu ci reewi Tugal yi ak Diiwaani Amerig yu Bennoo yi ak yul ñoom ci reewi addunay nasaraan ji, li leen taxoon a jug mooy waajal ay doktoor yu goor ak yu jigeen, aki matulkat aki jàpplekati doktoor ngir ñu man a ligeeyal Egliis bi jaare ko ci ligeey ci barabi nasaraanal yi nu tasoon ci adduna bi, rawati na ci Afrig ak Asi. Ndoktoor man nanu ne mooy ker-keraan bi la man a gën a may ngay man a jonjoo ag nit ñu neew ñi doole ak ñu ñàkk ñi. Nasaraanalkat yi danu daa wax naan: li nu jublu ci jëfandikoo meccem ndoktoor ci nasaraanal mooy ne moom day nooyal yoon wi laytaay ko ba bu Injiil dee ñëw ngir dugg ci xol yi du jafe.(Ma ne man: nit ki boo ko joxee mu lekk, naan ginaaw bi muy bëgg a dee cib xiif, di bëgg a dee ci tawat nga faj ko, boo nee ko fii la mu ne foofa la, rawati na bu ko fekkul muy ku tatawu ci xam-xam, aaru ci dali diine ju dëggu). Daanu daa wax it: war na doktoor biy nasaraanal mu bañ a fàtte ne day nasaraanal laata a dara di xew. Mbootaayi nasaraanal yi sotti woon nanu seen yitte ci meccem ndoktoor mii, daal di ubbi lu sakkan ciy barabi ndoktoor ci reew yu ndool yi yittewoo faj aki doktoor, ngir loolu man leen a jàpple ci seen ligeeyub nasaraanal boobu leen taxoon a jug. (2) Njàggale ak li mu àndal ciy jumtukaay, lu ci mel ne: daaray dal yi ak yu diggu yi ak yu ñaareel yi ak xamluwaay yu kawe yi ak daara yu mag yi ak kàggu yi ak daaray mecce yi añs. Ñi jiite woon nasaraanal gi danoo gisoon ne bu nu ubbee ay daara yii ci reewi jullit ñi ak yu leen moy loolu da na man a doon aw yoon ngir tas ci diiney nasaraan ci doomi jullit ñiy jàngsi ci yii daara, rawati na bu nu leen dee def leeg-leeg ñu cofal leen ci njàggalem Injiil mi, leeral leen ko, nga rax ci loolu li daara yii daa def muy tas xayug Tugal gi ak rawug xam-xamam ak jàngal ko yile dongo, te loolu ag doyodal jullit ñi rekk lanu ci jublu woon. (3) Jëf ju yiw ak ju nite ji nga xam ne mbootaayi yiw ak nite yu nasaraan yi daa nanu ko def ci reew yu ñàkk yi, rawati na ci jamonoy ay yi ak musiba yu dénd yi ak xare yi: bu ko defee ligeeyub nasaraanal bi di sawar ci biir daw làqu yi ak ñu ñu tuxal ñi ci reew yu neew yi doole, loolu mooy li ngay gis ci reewi Afrig yeek ak Asi. Loxob nasaraan biy indi ñam, fa jak ndimal ñeel daw-làqu yooyu ak ñu ñu tuxal ñi, mooy biy tas dali diiney nasaraan ci ñooñii, di jariñu ci seen nekkiin wu metti woowu ak seen tumbrànke gu tar gi. (4) Yëglekaay yi ak këyiti xibaar yi, tasum xibaar meek yeene yi nga xam ne seen woote yu nasaraanal yee ko daan tax a jug, ak waxtaan yi nu daa amal ci penc yi, ak taalifi penku-penku yi yi daa gëstu ci xam-xami penku yi ak seeni njàggat aki pas-pas, ak li nekkoon ci loolu lepp ci tooke ñeel jullit ñi ak seenug xay, aki laaj yu man a jur ay sikk aki jiixi-jaaxa ci jullit ñi jëm ci seeni boroom xam-xam aki kilifa, lii lepp ci jumtukaay yi la woon . Nasaraanalkat yi gisoon nanu ne daal teere yii ak yu nu mool yii man nanu leen a dimbali bu baax ci wisaare ag nasaraan ci reewi jullit ñeek yu leen moy, jaare ko ci li nuy bàyyi ci bakkan yu doyadi yi. Mbootaayi nasaraanal yi sos nanu ab lim bu mag ci ay daaray yar ci Tugal ak Amerig ngir waajal ci nasaraanalkat yi war a defi bii ligeey.



Nasaraanal ci reewi araab yi:

Nasaraanalkat yu katolig, anglikaan ak protestant yi wisaaroo woon nanu ci reewi araab yi nekkoon ci ron sacug Britani, Fraans, Itaali mbaa gu Espaañ. Bu ko defee nasaraanalkat yi sos ci reew yii ay barabi nasaraanal ci biir askan wi, rawati na fa jullit ña, ndaxte seen jubluwaay ci loolu mooy neewal doole jullit ñi aks een diine. Reew yi nasaraanal gi sutuxlu danu leen ci tuddal yii : Nasaraanal ag cawarteem fésoon na ci biir Nasaatiray Iraag yi, ci Mawsil, Baxdaad ak Basra, ñi ko doon def nag di ay nasaraanalkat yu Fraans ak yu Itaali. Àntug nasaraanal gu katolig gii ci Iraag ci njiitul Fraans merloo woon na Britani, ci noonu mu daal di fa woon yabal ay nasaraanalkat yu anglikaan, daal di ubbi bunt bi ci kanamu nasaraanalkat yu protestant yi, ngir ñu àndandoo xeex nasaraanal gu katolig gu rëy gii doon àntu bu baax ci Iraag. Loolu jur ag gëpplante gu mag ci diggante nasaraanalkat yu katolig yi cig wàll ak yu anglikaan yi ak protestant yi ci geneen wàll. Gëpplante gii nag du lenn dul geneenati ci gëpplante yi daa xew ci wàllug sanc ci diggante Fraans ak Britani ci goxi penku bi. Britani daa gisoon ne nasaraanalug katolig gu Fraans gii nekk Iraag tay, dara yobbuwu ko fa lu dul suuxat xejjug Fraans ak kilifteefam ci penku bi, te loolu moom la Britani doon ragal moom mi ame woon dooley sanc ji gën rëy te ëpp doole. Ay turi nasaraanalkat yu protestant yu bari feeñ nanu ci ñi daan ligeey ci toolub nasaraanal ci Iraag ci xarnub fukk ak juroom ñeent g, ku ci mel ni: nasaraanalkat bii di Grant ak Groves ak Samuel Zwemer añs

Goxi Golfub Araab bi  :

Ag nasaraanal tasaaroo woon na ci goxi Golf bu Araab bi, ndaxte bii gox da di ab jàlluwaay bu am solo jëm ci goxi penku yi. Bi mu ko defee, nasaraanalkati protestant yu Amerig yi sawar fa, daal di fay sos ay fajuwaay yu seenub lim àggoon ci juroom ñeent, aki këri doktoor , seenub lim ñoom it àggoon ci fukk ak benn.

Nasaraanal gi yamutoon ci mbootaayi Protestant yu Amerig yi, waaye weesu woon na leen ba daj yu katolig yi ak yu angalikaa yu Britani yi. Ci noonu yii mbootaay tàmblee joŋante ci sos ay daara aki jàngu aki katederaal ci goxi Glof bi. Nasaraanalkat yu protestant yu Amerig yi daal di taxawal egliisub Injiil bu xeet wi ci Kuwet, Ahmadi, Manaama ak Masxat. Bu ko defee katolig yi taxawal katedraal bu katolig bu Rom bic i Manaama ak Abuudabi, ak Egliisu Angalikaan bi ci Manaama. Nu daal di sos ay barab yu nu jagleel tas Injiil ak seddale ko, ak yeneen teerey seen diiney nasaraan ji, ay seen yeene yi aju woon ci seen woote bu nasaraanal bi. Waaye ak li nit ñiy yittewoo barabi faju yooyu lepp ak leekol yi, teewul ñu xeex bu baax kontar yëngu-yënguy nasaraanal yii ànd ceek li nu am ci jumtukaay ak doole. Boroom xam-xam yi xeex ko cis en xutba yi nuy def ci jàkka yi ak waaraate yeek gindee yi. Askan yu bañ sanc yii te noonoo ko ñoom itam xeex ko. Loolu jural nasaraanalkat yi ag sooy akug tas yaakaar.

Reewi Shaam:

Nasaraanalkat yi sawaroon nanu ci reewi Shaam yi, ci Siri, Libaa, Palastin ak Urdun . Nasaraanalkt yi yittewoo woon nanu mbirum Libaa ak Palastin, rawati na ginaaw xareb adduna bu njëkk bi, nga xam ne reewi Shaam yi danoo tàbbi woon ci ron feetale gu Fraans ak Britani. Bu kodefee way nasaraanal yi sotti seenug nasaraanal ci goxi Siri yeek Libaa, daal di jàpplanteek kureelug Mawaarina yu katolig yi ci Libaa. Britani it duggsi, feeteek kureelug Dursu gi ci Libaa. Nasaraanalkat yi jeqi woon nanu fa ay fitnay kureel, ca la xarey kureel yu tàng te tar juddoo ci Libaa, ci diggante Mawaarina yi ak Dursu yi atum 1860g. Way nasaraanal yu Angalikaan yi ñoom danoo sotti woon seen yitte ci Palastin, rawati na ne moom ab diggub diine la bu am solo ñeel ñi topp ñatti diiney asamaan yi: diiney Yahood, ju Nasaraan ak Lislaam. Mbootaayi Anglikaan yu Angalteer yi tàmblee sosi lopitaal aki leekol, aki mbootaayi yiw ci dëkki Palastin yi, rawati na Quds , Betlahem, Naasira, Tabariya, Yaafa ak Gasa. Fii itam du waa Angalikaan yi rekk a fa doon def ag nasaraanal, waaye it katolig yi, Ortodoks yi ak Protestant yu Amerig yi. Julliti Palastin yi jàmmaarloo nanook yëngu-yënguy nasaraanal yii, xeex ak ñoom bu baax, ndaxte daa noonu woon seen diine, noonu seen jaloore, seen ndono, seen xay ak taarix bu lislaame bu xóot bii. Seenug xeex ko gën na a tar bi mu gënee leer ne ag nasaraanal la te sanc gi lay ligeeyal. Ci noonu nasaraanalkat yi jàpplanteek seeni goornamaa kontar araabi Palastin yi ngir defar lanuy wax dëëlub Balfour , genne ko it atum 1917g, li i ko taxoon a jug di sos am reewum xeet mu yahood yu sahyoon yi ca suufus jàmbur see di Palastin, di suufus ay araab yu jullit, tubaab yi déggook yahood yi jox leen ko, ci seenug toroxte ak naqar.

Isipt:

Nasaraanal tas na ci Isipt te wisaaroo fi ci xarnub fukk ak juroom ñeent g, rawati na ginaaw bi ko Britani tegee loxo atum 1882g. Qibt yi dimbali nanu mbootaayi nasaraanal yi tasoon ci biir jullit ñi ci Isipt. Bu ko defee yonnee bu katolig bu Fraans bi tukkee woon Liyon daal di def ay ligeeyi nasaraanal yu fés, mboolooy nasaraanal yu Yesu yi di leen jàpple ci loolu. Nasaraanal ga amoon ca Isipt Paab gi dëgëraloon na ko te jàpple ko.

Mbootaayug nasaraanal gu anglikaan gu Angalteer gi def ay ligeeyi nasaraanal ci Isipt, ay cawartey nasaraanalam gën a yokku ginaaw bi Britani tegee loxo Isipt te jàpple bu baax yii mboolooy nasaraanal te aar leen. Mbotaayi nasaraanal yu protestant yu Amerig yi def ñoom itam seeni ligeey ci Isipt ci ñaari xarnu yii di bu fukk ak juroom ñeent ak bu ñaar-fukk g. bu ko defee mboolooy nasaraanal yii tàmblee xëccoo ci seen biir ak a gëpplante ci wàllug ubbi ay fajuwaay aki leekol aki egliis aki katedraal ak barabi seddale teere yeek mbindi nasaraan yeek yeneen yiy ligeeyal nasaraanal .

Jullit ñi xeex nanu nasaraanal ci Isipt, boroom xam-xami Ashar gu tedd gi jug ñoom itam jàmmaarlook yëngu-yëngu gii, daal di sos mbooloo muy aar Lislaam ngir xeex nasaraanal ci meloom yepp aki anamam. Mbooloo mii mujj na am ay bànqaas ci dëkk yu magi Isipt yi. Sos it ay jàngu aki wéeruwaay ñeel way ñàkk ñi, ñu lòtt ñeek jirim yi. Ay doxi ñaxtu yu bari am ci kanamu barabi nasaraanal yi ci Xaayra, Demenhor, Saqasiq ak Kafar-siyaat añs. Yenn it ci yëglekaay yu Isipt yi dimblee ci feeñal jubluwaayi nasaraanal gi, yee it jullit ñi ci ay wi mu làmboo.

Sudan:

Ligeeyub nasaraanal sawaroon na ci Sudan, rawati na ci ginaaw bi ko Britani tegee loxo. Bu ko defee mbootaayi nasaraanal yu katolig, yu protestant, ak angalikaan yi def seeni ligeeyi nasaraanal ci biir jullit yi dëkke woon ci bëj-gànnaaru Sudan ak ñu dul jullit ñi dëkke woon ci bëj-saalumam. Way nasaraanal yi sotti woon nanu seen yitte ci ñi dëkke woon ci bëj-saalumu reew ma te doonadi woon ay jullit, ci noonu ñu jot a tas seen diine ji ci ñoom ak aaday sowwu ji. Nasaraanalkat yi sosoon nanu ay jàngu yu yonnee yu katolig ak yu angalikaan ak yu protestant ci Sudan, sosati fa ay barabi faj yu nasaraanal.

Waaye waa Sudan ñoom toogunu rekk lem seeni loxo ci kanamu nasaraanal gi. Fipp gu Mahdi di xeex na ko. Broom xam-xam yi xeex ko. Mbootaayi diine yi rawati na ci bëj-gànnaaru reew ma ñoom itam xeex ko.

Reewi Maxrib bu araab bi :

Maxribu araab bi dafa nekke fu jàkkaarloo ak reewi nasaraan yi, rawati na Espaañ, Itaali ak Fraans. Reew yii nag jariñoo nanu bu baax neew dooleg reewi Maxrib bu araab bi, daal fay yabal ay nasaraanalkat yu bañ Lislaam ak jullit ñi, ngir ñu def fa seen ligeeyi nasaraanal yi, ak ngir nooyal ko, waajal ko ba mu man a dékku sanc gi nar a ñëwi di tukkee ci Fraans, Itaali ak Espaañ. Reew yii yepp nag yu yor diiney nasaraan lanu. Cawarteg nasaraanal gi yokku na te dolliku, rawati na ci keppaarug sanc gu Tugal gii ci reewi Maxrib yi. Bu ko defee gëpplante gi ci toolub nasaraanal tàmblee tar ci diggante mbootaayi nasaraanal yu katolig yi, yu anglikaan yi ak yu protestant yi. Nasaraanalkat yi daal di wut ay jumtukaay aki ker-keraani nasaraanal , taxawal ay fajuwaay aki kër doktoor aki daaray nasaraanal añs. Ci biir loolu ñu def lu nu man ngir fay làkkuw araab, te dundal kàllaamay berber yi ngir xeex ci làkku Alxuraan wi, ñu defoon ay pexe itam ci far aaday Lislaam ji ak taarixam, jeem a jox jullit ña fa dëkke woon ay reewu yu reewi sancaan yi, bu ko defee dunu reewooti ci seeni reew, te dunu ko bëggati. Ñu xeex ak boroom xam-xami jullit ñi daa jeem a taxawal ligeeyub nasaraanal bi.

Waaye nag ñu fonk seen reew ñii dëkke woon ci reewi Maxribu araab bi amoon nanu ndam ci damm degug sanc gi ak gu nasaraanal gi, ngir seen xeexub njàmbaar bi ñu leen jëmale woon.


Barabi nasaraanal yi ci reewi araab yi:

Mbootaayi nasaraanal yi sosoon nanu lu sakkan ci ay barabi aada , yu xam-xam ak yu faj ci reewi araab yi, lii ci la:

(1) Mbootaayi nasaraanal yi sos nanu lu bari ci ay jànguy dal , yu diggu ak yu ñaareel yu nasaraanal ñeel xale yu goor yeek yu jigeen yi, ci mbooleem reewi araab yi nasaraanal gi dugg. (2) Mbootaayi nasaraanal yi sos nanu lu bari barabi jàngale yu kawe yi ci Isipt, yu ci mel ne: daara ju mag ju Amerig ji, xamluwaay bu penku bi, xamluwaay bu Fraans bi, yooyu yepp nag ñi ngi Xaayra . Bu dee Sudan, nasaraanalkat yi sos nanu fa bànqaas bu Kamboni bu katolig bi ak jàngu bu Amerig ak jàngu yu Qibt yi, yu Gres yi ak yu Angalteer yi. Mbootaayug protestant gu Amerig gi moom tam sos ca Bayruut daara ju mag ju Amerig’ati. Katolig yi sos fa ñoom daara ju mag ju katolig ja, walla daara ju mag ju Yesu ji ñu duppee aji sell jii di Yuusuf . (3) Nasaraanalkat yu penku-penku yi dugg nanu ci akaademiy làkk yi ci reewi araab yi. Ñu dugg ca akaademib làkk ba ca Xaayra ak bu xam-xam ba ca Dimasq , ak bu xam-xam ba nekk Baxdaad, penku-penkub Angalteer bii tudoon Jub nag kenn la ci ñoom ak Margoliyos mu Fraans mi, Garifani mu Itaali mi, Hothman mu Holand mi, ak Harithman mu Almaañ mi. Penku-penku yi duggal nanu seen loxo ci teere yu bari yoo fiy gis tay, ñu tudd ci rekk ci misaal: jimblang ci Lislaam ak dundug Muhammad (j.m) ki nuy wax Sir William Mouir def ko, teere bi tudd Lislaam te Alfred Giyom def ko ak yeneen ci teere yi nëbbal Lislaam ag mbañeel. (4) Mbootaayi nasaraanal yi taxawal nanu lu limu ci ay cëslaayi faj , lu ci mel ne: fajuwaayu Marson ak bu Maryon Wilth, ca Bahrayni ak fajuwaayu Noks ca Masqat ak bu Harmal ca Isipt ak bu Maryohanna biy faj bët ca Quds, ak yeneen yu nasaraanal yi wisaaroo ci mbooleem reewi araab yi. (ginaaw ci reew yii lanu nekk nag, kon yu Afrig gu ñuul gii nga xam ne mooy seen mburu mu bees jarul ñuy wax).

















Juroom benneelu bunt


Ñaar-fukkeelu xarnu


Ñaari xarey adduna yi, bu njëkk bi ak bu ñaareel bi Mbootaayi adduna yi: kureelu xeet yi, mbootaayu xeet yi Mbootaayu reewi jullit ñi Danki reew yi ak reew yi feetewul fenn Xareb jawwu bi Jëm kanam gu Japon











Doggantal gu njëkk gi Ñaari xare yu adduna yi: bu njëkk bi ak bu ñaareel bi


Xaaj bu njëkk bi ci ñaar-fukkeelu xarnu g, seere na tàkkug ñaari xare yu adduna, ñooy xareb adduna bu njëkk bi (1914 – 1918g) ak bu ñaareel bi (1939 – 1945g). Leegi nag ñu waxtaane leen ci ni nu càllaloo ci jamono.

Xareb adduna bu njëkk bi (1914 – 1918g):

Li waral xare bi:

Xareb adduna bu njëkk bi am na ay sabab yu jonjoo ak yu jonjoodi , kon nanu njëkk a waxtaane sabab yu jonjoodi yi.

Sabab yu jonjoodi yu xare bi:

Man nanoo tënk sabab yu jonjoodi yu xareb adduna bu njëkk bi ci ñeenti sabab yu mag ñooy:

(1) Gëpplante gi ci wàllug sanc (2) Tapoo yi (3) Màggug yëngu-yëngu yiy woote ag xeetu (4) Ak lëj-lëj yu adduna yi

( a ) Gëpplante gi ci wàllug sanc:

Gëpplanteg adduna gi taroon na ci ginaaw yewwuteg endustri gi, ci fukk ak juroom ñatteelu xarnu g . Reewi endustri yi seeni cawarte gën na a yaatu, gën a jëm kanam ci gii wàll, ci fukk ak juroom ñeenteelu xarnu g, li ko waraloon di naj gu tar ak jañax gu tëw a dakk gi leen seen lonkoo yu endustri yu mag yi daan jañax jëme ci loolu, ak boroom boppi alal yi dëkk ci yile reew, rawati na nag ci reewi Tugal yi am ay noste yu gore . Bu ko defee ñu jug tàmblee gëstu-ji ne-ne yu nu laalul yi manul a ñàkk ngir ligeeyi endustri yii man dox, man a jëm kanam. Tàmblee wër it ja yu nu man a jaaye-ji seen ligeeyi endustri yu wuute yi.

Loolu nag jur na fi ag xér ci ne-ne, loolu tam jurati fi jawwi gëpplante ci wàllug sanc ci diggante reewi endustri yu mag yi, lii itam jur ag rawante ci ngànnaayu ci adduna bi, bu ko defee endustrib ngànnaay gën a jëm kanam, ndaxte ku bëgg a sanc fàww nga yor ngànnaay yu doy, ku ko bëgg a suuxat it mbaa nga bëgg cee ame sa njariñi koom-koom yi tax nga koy def fàww nga ngànnaayu.

Ag gëpplante gu tar amoon na ci wàllug koo-koom ci diggante Britani ak Fraans cig wàll, ak ci seen diggante ñoom ñaar ak Almaañ ci geneen wàll. Silaay Almaañ yi bari woon nanu ci ja yu adduna yi, ngir ay sabab yoy yenn yi danoo dellu woon ci jëm kanam gi endustri Almaañ jëmoon kanam, yi ci des dellu ci barig naali koom-koom yu Almaañ yi ci reewum Usmaan mi, rawati na naalub yoonu weñu Berlin-Baxdaad-Kuwet. Xëccoo googu nag amoon ay jeexiital yu rëy ci tàkkug xareb adduna bu njëkk bi . Ci nii lanuy gise ne gëpplanteg koom-koom gu adduna bi mooy li duggal adduna bi ci paxum xare bu tàng, bu nu ngànnaayal.

( b ) Tapoo yu reew yi:

Gëpplanteg politig gi aju woon ci sanc ci adduna bi dafa gënoon na jëm kanam, ci ginaaw bi gëpplanteg koom-koom gu adduna bi gënee jëm kanam. Loolu nag tax ba ay dank sosu yu reew, defees it ay kollarante aki dëppoo yu yor màndargam politig, mu xare ci diggante ab lim ci reew yi seeni njariñi sanc di jegee, walla yi ci jot a àgg ci deggoo ci lijjanti lëj-lëj yi nekk ci seen diggante. Ñu tuddal leen ci dëppoo yooyu ak tapoo yooyu, yii di ñëw:

Tapoo gu ñaaral gi ci diggante Almaañ-Otris:

Gii tapoo amoon na ci diggante imbraatooru Almaañ gi ak gu Otris gi atum 1879g, bokk na ci li ëppoon solo ci ay sartam, lii di ñëw:

(1) Bu Rusi gu Xaysar gi songee menn ci ñaari reew yi , meneen mi war na a dimbli mi nu song. (2) Bu menn ci ñaari reew yi tapoo songee meneen mu ñatteel, ma ca des da ca a war a ame taxawaayub génn ci, di leen seetaan waaye nag ci anamug cofeel ñeel àndandoom boobu. (3) Bu ag dimblante gu am solo amee, walla gu xare ci diggante Rusi ak Fraans, ñaari reew yii tapoo de war nanoo ànd ligeey ngir xeex loolu.

Tapoo gu ñattal gi :

Moom ag tapoo la gu Almaañ-Otris-Itaali, mi ngi sosu ci bi Itaali duggsee ci tapoog ñaaral gi nu la tuddoon leegi atum 1882g, ak doonte njariñi Itaali dëppoowut ak yu imbraatoorug Otris gi, waxuma la sax noonoo gu yàgg ga nekkoon ci seen diggante, te li ko waraloon di yilif gi ko Otris yilifoon njëkk bennoo ga, ak ca ginaaw ba, waaye Otris mii moo tegoon loxo ag wàll ci suufus Itaali, ba noppi yilif fa yeneen wàll. Itaali duggsi na ci tapoo gi ngir wuute gi mu defoon ak Fraans, ndax fraans dafa dëgëraloon bu baax tànkub sancam ca goxi bëj-gànnaaru Afrig, fu ci mel ni Aljeeri atum 1830g, ak Tunisi atum 1881g, kon Itaali duggsi gii mu defoon ci tapoo gi du woon dara lu dul doxaliinu politig, li mu ci jublu woon di jañaxal Fraans ak Britani ngir manante leen ci ñu nangul ko te bàyyee ko njariñam yi nekk ci geej gu diggu gi .

Dëppoo gu Fraans-Rusi gi:

Dëppoo googu am na ci ginaaw bi ag jegeente amee ci diggante Fraans ak Rusi gu Xaysar gi, loolu nag tàmbli na atum 1886g, daal di gën a jëm kanam atum 1888g, bi ñaari reew yi dëppoo ci fas ag kollare guy waral Fraans di jox Rusi ngànnaay, te jëmale kanam ag jokkoom jaare ko ci def fa ay yooni weñ. Ci atum 1891g la Fraans ak Rusi def ag kollarante guy yaxal lii di ñëw:

(1) taxawal ag dëppoo ci diggante ñaari reew yi, ak weccante xalaat ak diisoo buy lëj-lëj amee ci adduna bi. (2) Bu menn ci ñaari reew yi duggee cib xare, ñaari reew yi war nanoo diisoo ngir dëppale seen diggante.

Dëppoog cofeel gu Britani-Japon:

Ag dëppoog cofeel sosu na ci diggante Britani ak Japon atum 1902g, lii la yaxal:

(1) Bu xare tàkkee ci diggante Japon ak Rusi gu Xaysar gi, Britani da ca a war a genn te seetaan. (2) Waaye bu meneen reew duggee ci xeex bi nekk ci diggante Rusi ak Japon, kon Britani da ciy war a dugg moom itam, jàpple Japon.

Dëppoog cofeel gu Britani-Fraans:

Ag dëppoo gu cofeel xewoon na ci diggante Britani ak Fraans atum 1904g, gu lijjanti woon lëj-lëj ak reeroo yi amoon ci seen diggante, dëppoo googu nag lii la wax:

(1) Féexal Fraans, joyal ab loxoom ci Marog , gii nga xam ne jotoon na a temb, te nangul ko teg gi mu teg loxo Ajeeri ak Tunisi. (2) Fraans moom tam nangul Britani teg gi mu teg loxo Isipt atum 1882g

Dëppoo gu cofeel gu Britani-Rusi:

Ag dëppoog cofeel am na ci diggante Britani ak Rusi gu Xaysar gi atum 1907g, lii la wax:

(1) Déggoo ci ni nuy séddoo barabi sañ-sañ yi ci Iraan , ba mu des fa benn barab rekk bu temb ca digg ba ñu bàyyil ko fa Shaah ba, ginaaw bi Rusi jëlee wàll gu bëj-gànnaar gi, Britani jël gu bëj-saalum gi.

( c ) Màggug yëngu-yënguy xeetu yi ci Tugal:

Yëngu-yëngu yi aju ci xeetu dafa xëy gën a màgg ci Tugal, loolu nag bokk na ci li jañ adduna bi jëme ko ci xare bi. Xarnub fukk ak juroom neenteel g, dees na ko lim muy xarnub xeetu yi ci Tugal, yëngu-yënguy xeetu yooyu nga xam ne li leen taxoon a jug mooy gooreel seen bopp te nocciku ci kilifteef ak teg loxog reew yi leen di àtte cig wàll, ak sosal xeet wu nekk am reewum boppam mu koy ëmb, uuf ko ci geneen wàll. Ñaar nag bokkoon nanu ci yëngu-yëngu yi gënoon a siw ci yooyu, ñooy:

Mbootaayug Slaaf gi :

Gii mbootaay, walla yëngu-yëngug slaaf gii, li ko taxoon a jug mooy xettali askanu slaaf wi jële ko ci àtteg imbraatoor gu Otris gi, ak sos reewum slaaf mu ëmb mbooleem slaaf yi dëkke ci Balkaan ak salaaf yi dëkke ci Tugalug penku gi. Mbootaay gii nag daan na jot ag jàpple mu tukke ci Rusi gu saaf gi, loolu taxoon na ba ag reeroo gu mag am ci diggante Otris ak Rusi gu Xaysar gi.

( d ) Lëj-lëji adduna bi:

Ay lëj-lëj yu fasu yu adduna bi sosu nanu, bokk it bu baax ci li fi taal xareb adduna bu njëkk bi. Lëj-lëj yii it li leen jur day dellu ca reeroo ya amoon ca diggante reew yu mag ya ngir seen gëpplanteg sanc gi, ak ngir màggug xeetu ci Tugal, ak ngir fipp gi askan yi fippoon ngir jot seenug tembte ak gore. Ñu tudd ci yi ëpp solo ci lëj-lëj yooyu:

Lëj-lëju Maraakes:

Fraans yàgg na a waaj ak a naal ngir teg loxo Maxrib gu sori gi (Maraakes), moom nag Maraakes dafa yoroon ag tembam lu yàgg, te booba Tunisi ak Aljeeri Fraans a ngi leen tegoon loxo, yilif leen cig sanc. Ci noonu Fraans lijjanteek Britani seen reeroo gi nekkoon seen diggante, ca dëppoog cofeel ga atum 1904g, Fraans daal di bokki ca ndaje ma nu njëkk a def ca dun bu wert ba atum 1906g ca Espaañ ngir lijjanti lëj-lëju Maraakes bi. Saxal ya juddoo ca ndaje ma nag njariñul Fraans la gënoon a nekk, ndax reew ya fa daje woon danoo dëppoo woon ci nangul Maraakes ag tembam waaye feetale Fraans wàllug kaaraange ga ak sàmm njabootug Tugal ga fa nekkoon. Fraans nag jariñu na bu baax ci dénk gi nu ko dénk kaaraange ga, ndax ba ay yëngu-yëngu amee ca Faas ga nekoon peey ba, da fa a daal di woon yabal ay dooley xare yu Fraans ngir ne da ciy aar jàmburi Tugal ya fa nekkoon. Loolu moo merloo woon Almaañ mi àndoon ak buurub Maraakes bi, daal di ne woon fàww Maraakes jot cig tembam, ngir naqaral Fraans. Almaañ daal di yabal ag gaal gu mag ca waaxub Agadiir ngir aar ag njabootam, ak ñaxtoo ci yabal gi Fraans yabaloon am mbooloom xare ca Faas atum 1911g ngir teg ko loxo. Ñu defaat am ndaje ca dun bu wert ba ca Espaañ atum 1911g, ngir lijjanti xuloob Fraans-Almaañ bi, la fa juddoo di : jox Almaañ ay moomeel ca Kongog Fraans ga, bu ko defee Almaañ nangul Fraans nekk gi Maraakes nekk ci ron kaaraangeem, ñu daal di def Tanja muy ab waax bu adduna bepp, daal di doxal nag politigu ubbi buntub Maraakes ci kanamu yaxantug adduna bi.

Lëj-lëju Balkaan:

Otris daa boole woon ci boppam ñaari gox yii di Bosni ak Hersogowin atum 1908g, te ñoom ñaar ñi ngi bokkoon ci diiwaani reewum Usmaan mi ci Balkaan. Reewum Usmaan mi ca jamono jooja dafa nekkoon di dund ci jawwi yong , mooy yong gi ñoñ bennoo ñi defoon atum 1908g. Serbi nag (moom ag wàll la ci yogoslaafi ci jamono jii nu nekk) daal di ñaxtu loolu ak Rusi gu Xaysar gi ko daan jàpple (moom Serbi). Almaañ jug moom jàpple Otris ci jëfam jooju. Loolu nag bokk na ci li gën a dolli tangoor wi ca daanaka-dun bu Balkaan ba.

Lëj-lëju Maseduwaan:

Ab xare tàkkoon na ci diggante Reewum Usmaan mi ak Gres, Bulgari ak Serbi ci Maseduwaan, ñoom ay reewi Balkaan lanu. Li ko waraloon nag mooy Bulgari, Gres ak Serbi danu doon defi pexe ngir roccee Maseduwaan ci Reewum Usmaan mi, te seddoo ko ci seen biir. Bi nu dàqee Reewum Usmaan mi ca xare ba ba noppi, danoo reeroo woon ci ci seen biir ci nu nu koy seddoo. Serbi moom daa bëggoon na jot ci Albani, waaye ñu xañ ko ko, ndaxte Otris daa taxawoon temb ci nu jox Albani ag tembam. Loolu waral leneen coow amati ci Balkaan ci diggante Serbi, Otris ak Rusi ak ñeneen.

Lëj-lëju Tripoli:

Itaali jariñu na ci am soxla gi Reewum Usmaan mi amoon soxla ak lu ko doy, ca xareem ba ca Balkaan, bu ko defee mu song ko ca Tripoli gu soww ga, atum 1911g, daal di nangu Libi, teg ko loxo atum 1912g, ginaaw bi mu lijjantee ba Fraans ak Britani genn ci, te noppi ci.

Sabab yu jonjoo yi ñeel xareb adduna bu njëkk bi:

Noonoo gi taroon na jëm ci Slaaf yi ci Balkaan, looloo waraloon ñoom Slaaf yi juggoon taxawal ag mbootaayug sekkare ngir xeex loolu, Serbi jàpple leen ci ak Rusig Xaysar gi. Ab dongab Slaaf yong na Arshidog Fransis Ferninand, mi nekkoon wuutlaayu Otris ak soxnaam, ca 28 suwe 1914g, ca dëkkub Sarayevo bi nekkoon peeyub Bosni, ci tukkib nemmeeku bu mu fa doon def. Otris daal di gaaw jirñoo xew-xew bii, daal di yonnee Serbi ag xupp ca bisub 22 sulye 1914g, gu làmboo fukki sart ak benn, bokk na ci yi ëppoon solo ci sart yooyu: raxas goornamaab Serbi bi ak dooley xareem ji ci mbooleem ku bokk ci kureel yiy kontar Otris, te may Otris mu defal boppam raxas gii, te tëj yëglekaay yi ak jumtukaayi tes-xibaar yi noonoo Otris, ak boole Otris ci gëstu ñi def yong googu ak àtte leen. Ak yeneen sart yu tar yu tax Serbi jort ne kii daal daa fas yeenee dugg ciy mbiri biiram. Ba noppi Otris joxati Serbi diirub ñeen-fukki waxtook juroom ñatt, ne ko mooy àpp bi nga xam ne waru koo weesu te tonntuwul, waaye Serbi moom tontuwul .

Jibalug xare bi:

Otris taal na xare bi ci kaw Serbi, ci 28 sulye 1914g . Bi loolu amee Rusi moom itam jug song Otris ngir jàpple Serbi, loolu it jurati Almaañ jug – cig wàllam – jafal ab xare ci kaw Rusi ak ci kaw Serbi. Fraans duggsi ci, ci wetu Rusi miy reew miy xaritam, nadx moom la defal ag tapoo, daal di jibbal ab xare ci kaw Almaañ ak Otris. Britani tam it xuus xare bi kontar ñaari reewi digg yi nga xam ne Reewum Usmaan mi mujj na àndseek ñoom ci xeex bi. Siin it ak Japon mujj nanu duggsi ci xare bi ci wetu reewi dëppoo gi. Itaali it dugg-si ci kontar reewi digg yi, atum 1915g, te kat bu njëkk da doon seetan rekk, feetewutoonn fenn. Britani nag nekkoon na di fasante ak Itaali kollareg sekkare. Kollare gi nag li mu doon yaxal mooy Itaali jox ko suufus Dalmaas bu xare bi jeexee. Amerig dikk moom itam, dugg-si ci xare bi ci wetu reewi dëppoo yi, daal di genn ca beroom ga mu defoon ca goxub Amerig ba. Duggsi gi mu duggsi woon ci xeex bi nag lu am solo la woon, ndax moo ko soppi bu baax, ngir doole ak jumtukaay yi mu indil reewi dëppoo yi ak alal.

Lefum xare bi :

Jë bu sòww bi ëmboon Fraans ak Beljig, mooy barabu xeex bi ëppoon solo ci xare bi ci diggante 1914 – 1915g, boobu diggante mooy bi gën a tar ci xeex bi. ndaxte dooley reewi digg yi jot nanoo putuxlu ci reewum Beljig mi ak wàllug penku gi ci Fraans, ak li reewi dëppoo yi di jàmmaarlo lepp ak a xeex ngir loolu bañ a am. Lii nag bokk na ci ndam yi ëpp solo, yi reewi digg yi def ci jëwub sòww bi. Waaye reewi dëppoo yi jot nanoo taxawal jëm kanam gi Almaañ ak Otris doon def, ba daanaka àgg ca bunti Paris, ci xeexub njàmbaar bi nu doon def ngir aaru. Ñaari wàll yi nag xeex nanu ay xeex yu tar, yi ci gën a siw mooy bu Marn bu njëkk bi ci sulye atum 1914g.

Bu dee nag ci jë bu penku bi, xare bi moom foofa ci diggante Rusi ak Otris la nekkoon. Barabub xeex ba di woon Poloñ ak Balkaan. Xeex bi amoon ci penku bi nag xawoon na a woyofal tuuti yan bu diis bi nu tegoon ci ndòddum reewi dëppoo yi ci sòwwu bi, ndax reewi digg yi danoo mananul woon a ñàkk a dolli seen soldaar sa nekkoon ca penku ba di xeex ak Rusi. Foofa tam ca penku ba lanu gëne woon aw demiin ca sòww ba, ndax jot nanu fa a nangoo wàll gi Rusi moom ci Poloñ ak Litwaani.

Ay xeex am ca diggante Reewum Usmaan mi ak Britani ca Iraag ak Palastin. Ca la Britani tege loxo ñaari reew yii. Reewum Fraans it nangu Siri ak Libaa.

Bu dee ci geej gi moom, xeex bi mi ngi doon ame ci nuuraakon yi nga xam ne Almaañ da leen daa joyal ci gaali reewi dëppoo gi. Mbooloom gaalum Britani mi nag moo kawe woon ci xareb geej gi. Xareb Gitland bu geej bi amoon atum 1916g, bokkoon na ci xeexi geej yi gën a rëy ci xare bi, nga xam ne Amaañ ak Britani ñepp ñàkke nanu ci lu dul jeex ciy nit ak jumtukaay.

Atum 1917g, bokk na ci at yi gën a tar ci ati xare bii, ci la Rusi genne ci xare bi, ca kollareg Litofski ga ca 27 desambar 1917g , ci ginaaw bi fippug Balsafi gi amee. Romani topp ca moom mi sukkandiku woon ci xare bi ci Rusi, moom itam ag gennam mi ngi jaare ci kollare ga nu defoon ca Boxarest. Ca at mooma tam la Diiwaani Amerig yu Bennoo yi ñoom it duggsi ci xare bi ànd ak reewi dëppoo yi. Loolu nag feeñ bu baax ci doxiinu xare bi, ndaxte Amerig moom jàpplee woon na bu baax ci wàllug xare ak koom-koom, loolu nag di woon lu sonnal reewi digg yi. Ca at mooma tam la jë bu Usmaan bi it nërméelu. Ci la jë bu Otris it daanu. Ay yëngu-yëngu aki coow yu ay ligeeykat am ca Almaañ. Ca mooma at it la Woodrow Wilson defoon fukk ak ñeenti poñam ya doon woote ñu taxawal xare bi te bàyyi askan yi ñu def li nuy wax (autodétermination) muy tànnal seen bopp mujj gi nu gis ne moo gën ci ñoom.

Atum 1918g nag mooy atum ndam li ñeel reewi dëppoo yi, waaye it mu nërmeelu ñeel reewi digg yi, ndax imbraatoorug Otris ak gu Almaañ yépp daanu nanu, Imbraatoorug Usmaan gi it ñàkk mbooleem diiwaanam yi mu amoon ci bitib Asi gu ndaw gi, nguurug Bulgari daanu, ci noonu askani reewi digg bi daal sàkku wéerum ngànnaay ci ni ko poñi Wilson yi doon sàkkoo. Bi reewi digg yi demee ba lòtt ci wàllug aaru, te manatunoo dékkooti xare bi, lanu wommatu . Bu ko defee Bulgari xaatim ag wéer ngànnaay ak reewi dëppoo yi ci 30 satumbar 1917, Turki topp ci, ci mujjug oktoobar atum 1918, ak Otris ci 3 nowambar 1918, ak Almaañ ci benn fanu nowambar 1918g.

Lijjanti yi ci ginaaw xare bi:

Reew yi am ndam ci xare bi defoon nanu am ndajem juboo ca Paris, peeyub Fraans, li ko waraloon nag mooy gëstu nan lanu war a def ci adduna bi ginaaw bi xare bi jàllee. Moomu ndaje nag Clemenceau moo ko jiite woon, njiilul jëwrin lu Fraans li, bu ko defee, ñu defe ndaje ma ca njéndul Varsaay la, di dëkk bu nekk ca wetu Paris. Diiwaani Amerig yu Bennoo yi Wilson teewal ko, Britani Luwid George njiitul jëwrin la nekkal ko fa, Fraans Clemenceau miy njiitul jëwrin ya moom itam wuutu ko fa ak Itaali ci teewaayu Orlando njiitul jëwrinam, reew yii amoon nanu xejj gu mag ci ndaje mi, rawati na ñatti reew yii di Amerig, Britani ak Fraans.

Ndajem juboo mii ay saxalam ballewunu ci déggoo ak waxtaan wu reew yi gañe def ak yi nu gañe, waaye kay reew yi gañe danoo teg seeni sart ci kaw reew yi nu gañe cig sañ-bañ. Kollare ga nu fase woon ca Versailles atum 1919g te xaatimoon ko ak Almaañ, bokk na ci kollare yi ëpp solo te juddoo ci ndajem juboo mi. Moom kollare googu dafa yaxaloon lii: Delloo Fraans Alsaas ak Loren, ak delloo Danmark wàllug bëj-gànnaar gi ci goxub Sholswig, bu ko defee Poloñ moom jot ci suuf su bari ci Almaañ ak yoon wu yaatoo ñeen-fukki miil, wu romb ci biir diiwaanub Brusiya gi nekk ci Almaañ, bu ko defee tàqale kook yeneen suufi Almaañ yi. Ci noonu ñu def waaxub Danseg bu Almaañ bi muy waax bu nu jagleel reewum Poloñ mi nga xam ne taxawalaat nanu ko ci ginaaw xare bi. Nu jëlati ci Almaañ diiwaanu Sodit jox ko Cekoslawaki, mi nga xam ne mi ngi sosu woon ci ginaaw xare bi, ñu jëlati ci Almaañ waaxub Mamel jox ko Lituwani. Bu ko defee Almaañ ñàkk mbooleem sancoom yi. Ba noppi nu ga ko ci mu yamale ay soldaaram ci teemeeri junni. Nu neenal fa duggum coldaarum gu sañ-bañ, dindi mbooleem tata yi wëroon kanaalub Kyel ak goxub Rayn. Nu tàmbli woon a def fuglu gu tar ci ligeeywaayu ngànnaay yi ak jumtukaay yi ci aju. Ñu nangoo woon ci Almaañ it mbooleem ay nuuraakonam aki gaali xareem aki fafalnaawam ak lu ëpp ci ay gaali yaxantoom, ci noonu Fraans nangooti diiwaanu Saar ( di xuru dexug Rayn gi) di barab bu naat ci ay mbell, mu nangu ko nag diir bu tollu ci fukki at ak juroom. Ñu daal di teg Almaañ nag ag alamaanug xare ak alal ju mu war a fay ju bari ju tollu ci (6,600,000,000) yu Sterlin, ak doonte Almaañ fayu ci ci diggante 1924 – 1930g lu dul lim boobu rekk.

Imbraatoorug Otris gi nag moom, ndaje ma daa daal di jeexal nguurug njabootug Habsborg ga fa nekkoon, daal di taxawal ciy màbbiitam ay àtte yu bari, ñooy: Pencum Otris ak Hongri ak pencum Cekoslawaki, ñu jëlati wàllam ya nekk ca Balkaan boole ko ca reewum Yogoslawi mi sosu ci ginaaw xare bi. Bu dee Reewum Usmaan mi moom dafa ñàkkoon mbooleem moomeelam yi mu amoon ci Asi ak Afrig, deseetutoon lu dul moomeelam yi mu amoon ci Asi gu ndaw gi, ñu daal di ko def muy leegi pencum Turki wuuteek lool reewum Usmaan mu mag ma nu xamoon, loolu di woon ci 29/10/1923g, ginaaw bi Mustafa Kamaal Atatork (1880 – 1930g ) neenalee nosteg saltana ga fa amoon atum 1923g, ak gu xalifa ga atum 1924g.

Ndaje mi nag sos na fi ay reew yu yees yu bari ci Balkaan, mu ci mel ne mom Yogoslawi mi jële won ay suufam ci reewum Serbi mi ak yenn ci goxi Balkaan yi bokkoon ci moomeelug imbraatuurug Otris gi, bu ko defee nu sosaat reewum Poloñ mi ak Brusiya. Reewum Cekoslaafi moom itam taxawe ci ñaari xeet yii di Slaaf ak Cek, reewum Hongri tam sosu, Finland, Stwaani, Lituwani ak Latfiya reew yii yepp jug di dëgëral seeni nekktey politig, te bu njëkk danoo nekkoon ci ron teg loxo gu Almaañ, ci ginaaw bi Rusi gennee ci xare bi atum 1917g, daal di fas kollareg Litofski gi ak reewi digg yi. Lii moo jeexal àtte gi njabootub Romanof gi doon àtte Rusi.

Ñu daal di jël nag yenn reew yi teg leen ci ron ag feetale: Iraak, Penkub Urdun (Jordanie) ak Palastin ñu teg leen ci ron feetale gu Britani atum 1920g, Siri ak Libaa ñoom ñu teg leen ci ron feetale gu Fraans atum 1920g. Ndajem Paris ma nag saxaloon na feetale gii te xaatimoon ko.

Ñu daal di sos Kureelu xeet yi (League of Nations) teg ko ci poñub fukk ak ñeent bi ci dali Wilson yi doon woote ag ñoŋal jàmm ci adduna bi ak tee xare amati fi ak dëgëral dimblante ci reewi adduna bi.

Nii daal la xareb adduna bu njëkk bi jeexe ginaaw bi mu sonnalee adduna bi bepp, sotti ko sawaraam si ak alkandeem li. Ray nanu ci lu jege juroom ñatti milyoŋi nit , gaañ ca lu jege ñaar-fukki milyoŋ. Waxuma la nag ñi faatoo ca xiif bu metti ba’ak tawat ja xare ba waraloon.

Ñaareelu xareb adduna bi (1939 – 1945g):

Lijjanti ak saxal ya juddoo woon ca ndajem jàmm ma ca Paris, ci ginaaw xareb adduna bu njëkk bi, ñoo jur - man nanu ne – lu ëpp ci li sooke ñaareelu xare bi. Kollareg jàmm ga fa juddoo woon sooke woon na mer wu metti akub sànj ci askani reew yi nu note ca xeex ba. Askan yooyu nga xam ne doyutoon ñu yanu coonay xare beeki musibaam rekk, waaye ñu tegati ci yan leen li ci juddoo ci ginaaw bi ay saxal aki lijjanti yu diis yoo xam ne reew yi notoon a leen tegoon ci seen kaw. Loolu nag juroon ci ñoom ag mbañeel akug bëgg a fayyu, nekkiinu koom-koom wi jaxasoo, tegoodi ci yoon, am pax gasu ci Tugal ci diggante askan yeek seeni goornamaa, loolu tam - man nanu ne - mooy li gën a tax ay noste yu yees sosu, yoy “sañ-sañ bu joyu” lanu jëloon def ko seen raayo. Ay kureel yu neew jugoon nanu teg loxo ci àtte gi ci yenn ci reewi Tugal yi, daal di biral ne li leen tax a jug mooy xettali seeni askan ci jafe-jafe yi nga xam ne xareb adduna bu njëkk bi ba na leen fi. Ay goornamaa yu diktaatoor feeñ ci biir Tugal ak ci biti. Leegi nag jeneen jamono ju yees tàmbli ju ngànnaayu, muy wutu ngànnaay moo xam ne li ko jur mooy bëgg a fayyu ci reew yii note ci xare bu njëkk bi, te toroxal askani reew yi nu not, te diisal seen ginaaw ci ay alamaan yu saf te tar. Lii daal moo sabab xareb adduna bu ñaareel bi.

Li laytaay xare bi:

Àttey diktaatoor yu bees yi sosuwoon man nanu ne ñooy jëfka yi jiitu ci taal ñaareelu xare bi. Ñu indil la wax ju gàtt ci ñatt ci yi gën a am solo ci noste yooyu.

Nosteg àtte gu mbokkoo :

Rusi mooy reew mi àtteg mbokkoo njëkk a taxaw, loolu di woon ci ginaaw fippug oktoobar ga amoon ca atum 1917g, li ko waraloon di koom-koomam ba daanu woon, te ñu dàqoon ko ci anam gu toftaloo ca xare bu njëkk ba ca kanamu Almaañ ci ñaari at yii di 1916 ak 1917g, te mu ñàkkoon it lu tollu ci milyoŋ ak xaaj ci ay xarekatam ca xare booba.

Lenin (1870 – 1924g) mi nekkoon njiitul làngug mbokkte gi (parti communiste), moo jiite woon fipp googu, daal di woon def ag juboo ak waa Almaañ yi, taxwal it ay jataay yu askan yu barab yi (soviets) , daal di xeetal jumtukaayi ligeey yi, taxawal ab goornamaa bu ay ligeeykat aki baykat, daal di yëngu ci luy neewal tàqale yi am ci diggante xeet yu wuute yi. Waa Rusi yu Sofiet yi taxawaloon nanu ab jë bu yaatu kontar nosteg bopp-alal gu soww gi, ñu jiite woon kureelub mbokkoo bi kontar diine ak nostey demokraasi yi, ñu mujj nag am doole ju mag ak jeexiital gu rëy ci liy xew ci adduna bi, yàgg nanoo jëfi jëf ci yekkati tàngoor yi ci adduna bi, walla xiiroo ak ngaayoo yi daa am ci adduna bi ci diggante ñaari xare yi.

Nosteg àtte gu Nasi ca Almaañ:

Làngugug mbokkoo gu xeet gu ligeeykat yi gu ( Nasi) gi (di parti national-socialiste almand des travailleurs) gii làngug politig di gu Nasi gi, daa jariñoo woon (profitoo woon) ci li daloon waa Almaañ yi, te wàcci ci seen kaw ci toroxte ak doyadal ak suufeel, te li ko waraloon di tënk-tënk yi nekkoon ci kollareg Versailles gi, ak jafe-jafe yi mu leen indil, ak ñàkk gi leen wër, peek leen, ak ñàkk-ligeey gi, ak deltu ginaawug koom-koom bi nga xam ne saxoon na fi ay at ginaaw xare bu njëkk bi, làng gii nag jariñu woon na ci lii lepp ngir fitali ca àtte ga (l’état) teg ko loxo, nangu ko, ci njiitug Adolf Hitler (1889 – 1945g), mi nga xam ne bindoon na dali làngam googu ci teereeb xeexam ba, dal yooyu nag danoo taxawoon ci ay cëslaayi waaso, ndax daa gëmon ne waasow Jermaan mooy waawo wi gën ci waaso yi, te it daa gëmoon ne danoo war a sos ag Almaañ gu mag gu ëmb mbooleem waa Almaañ yi, gëmoon it ne àtte gi (l’état) daa war a teg loxo mbooleem lonkoo yu rënk yu mag yi ci Almaañ, te danoo war a neenal kollare ga nu fasoon ca Versailles, te danoo war a delloosi mbooleem sancu yi kollare googu ñàkkloo woon Almaañ.

Hitler mujj na di njiilul Almaañ loo xam ne daa amoon sañ-sañ bu joyu (pouvoir absolu). Ñu mujj di ko wooye Fuhrer, mu tàmbli nag di doxal dali làngam yooyu ci askanu Almaañ wi nga xam ne àndoon na ak moom ngir bëgg a mucc te xettaliku ci nekkiin wu bon wi mu nekke woon, rawati na ñàkk-ligeey gi nga xam ne yaatu woon na lool ci Almaañ ngir xare bi, ak ngir tënk-tënk yi nga xam ne kollareg Versailles gi indi woon na leen fi.

Hitler def na ay jëf yu bari yoo xam ne ñoo fi sabab ñaareelu xare bi, ndax daa jëloon diiwaanu Saar boole ko ci Almaañ atum 1935g, neenal kollareg Versailles, jox sodaar si ngànnaay yu diis te xereñ, jëmale endustri bu Almaañ ci ligeey ngànnaay ak jumtukaayi xare aki bagaas yu ame solos xare. Mu jëlati reew yiy wax làkkuw Almaañ wi boole leen ci Almaañ, daal di taxawal Rayix bu ñatteel bi. Mu booleeti Otris ci Almaañ atum 1938g, jëlati goxub Sodit bi nekk ci Cekoslaawi atum 1939g, daal di jeem a nangu yoonu Danseg ci doole, seddoo ak Rusi Poloñ. Almaañ nag dundoon na ci ron àtteg Nasi la ko dale ca 1933g ba bi mu daanoo tas ci atum 1945g.

Nosteg àtte gu Fasi ca Itaali:

Waa Itaali yi yëgoon nanu – te ñoom kat ci reew yi amoon ndam lanu woon ci xareb adduna bu njëkk bi – yëgoon nanu ne danu leen a naxe ca ndajem jàmm ma amoon ca Paris, màngiit yi juge woon ci xare bi it lu neew lanu leen ci jox, te kat ñoom ñu ci sonne lanu.

Ag ñàkk ligeey tas ci Itaali, nekkiinu nit ñi ñaaw, làngi politig yi fees fa dell, reew ma jaxasoo, xalaat yi tas fa, di mbokkte (communisme) fasi, ak yeneen xalaat yi. Fasi nag lu fi ñëwoon la ngir xeex mbokkte, Benito Mussolini jiite ko mi jiite woon ag làngam (1883 – 1945g). Làng googu nag danoo warlu woon ci seeni dal (principes) xeex mbokkte, taxawal ag nosteg dimblante, te jeem a jot ci ngañaayi sanc yi nga xam ne danu leen a xañoon Itaali ca ndajem Paris ma.

Ci noonu làngug Fasi gi tàmbli di jëfandikoo fitna(violence) ci xeex ak xuloowaaleem yi, bi dégug làng gi gënee dëgër, gën a ñaw, mu gën a am doole ci la Mussolini ak àndandoom yiy solsimis yu ñuul xuppe goornamaab Itaali bi, ci noonu Buurub Itaali bi di Victor Emmanuel amatul woon pexe, mu daal di jox nguur gi kii di Mussoliini, mi nga xam ne mujj na di diktaatooru Itaati, ñu ko daa dàkkantale Dotsi.

Mussolini digale na ñu neenal làng yi, aaye askanu Itaali wi ñuy def yëngu-yëngu mbaa coow, nos endustri bi, dëppale diggante njariñi ligeeykat bi ak naatug walla jëm kanamug endustriy yaxantu yi. Daal di juboo ak Paab bi, delloosi njàggalem diine mi ci jàngu yi (leekol yi).

Mussolini feeñal na mbonam gi ak mbonug làngam gi, jaare ko ci jëfam yu ñaaw yi mu jëmale woon ci askanu Libi wi, ba mu fa bëggee samp sancug Itaali gi. Mu gënoon a yaatal ag kilifteefam ca Ecopi atum 1936g, ginaaw bi ko soldaari Itaali yi tegee loxo ci doole, nangoo ko ci waa Ecopi. Yaatalug sanc gu Itaali gii merloo woon na askan yi nekkoon ci ron ag sancam, te taxoon na yeneen reewi sancaan yi kontar ko ci loolu. Lii nag mooy li jegeele diggante Nasi ak Fasi, nga xam ne mujj nanu àgg ci def ag dëppoo ci seen biir, mooy taxawal ag tapoo gu xare , nu duppee ko diggub Berlin-Rom .

Bokk na ci diktaatoor yii ba tay, làngug xare (parti militaire) gi nekkoon Japon, ak àtteg Franco ga ca Espaañ (1892 – 1975g), moom Franco mi mujjoon ame nguur gu joyu (pouvoir absolu) ca Espaañ atum 1939g, ginaaw xareb ñoñ bu Espaañ ba. Koolute gi askani Almaañ yi amoon ak yu Itaali yi, yu Espaañ yi ak yu Japon yi ci seeni goornamaay xeet yu ëppaloon yi te teengal dolliku woon na te li ko waraloon di ñàkk gi nostey bopp-alal yi ak yu demokraasi yi ñàkkoon kàttan ci jële fi coonab koom-koom bii fi amoon ak ñàkk gu tar gii ubale woon Tugal gépp ak feneen, ci biir jafe-jafeb koom-koom bi amoon ci adduna bi atum 1929g, ñu gënoon koo xame ci turu lamb gu mag gi.

Yeneen jëfka yu sabab xare bi:

Am na fi yeneen jëfka yoy dugg nanu ci li fi indi xare bu ñaareel bi, bokk na ci yi ci ëpp solo:

(1) lòtt gi kureelu xeet yi lòttoon ci ñoŋal jàmmi àdduna bi, ginaaw bi ci Almaañ ak Itaali gennee ak Japon. (2) Digg (axe) yu politig ak xare (militaire) yi nga xam ne reewi diktaatoor yi taxawaloon nanu leen ci seen biir, bu ci mel ne digg bu Berlin-Rom, ak bu Berlin-Tokkiyo, ak kollarante gu ñàkk-a-noonu gi amoon ci diggante Berlin-Mosko laata a xareb ñaareel bi di tàkk ci lu tollu ci ay ayu bis yu neew. Ci geneen wàll gi, Fraans, Britani, Romani, Poloñ, ñoom itam booloo nanu def seenug tapoo. Nii daal la ñaari dank sosoo dankub digg bi, làmboo Almaañ, Itaali, Japon, ak dankub reew yi tapoo walla (way tapoo yi) di Britani, Fraans, Romani, Poloñ, Benoog Sofiet gi ak Amerig – ci ginaaw bi. (3) Xuloo bi amoon ci diggante reewi Balkaan yu yees yi te aju woon ci mbirum dig yi ci seen biir, ndaxte amunu woon ay dig yu sax, ak xuloo bi amoon te aju woon ci mbirum xeetu (nationalisme), ndax kat reew yii, di yu sosoo ci seddaleg ndaje ma, danoo ëmboon lu sakkan ciy xeeti Almaañ, lu jege juroomi milyoŋi ay waa- Almaañ, ñu mujjoon bokk ci njabootug Poloñ ak Cekoslaafi. (4) Masalam yoonu Poloñ wi tàqale Almaañ ak Brusiya, te daytaloo ca waaxub Danseg bu gore ba(libre). Ña dëkke woon ca yoon woowa ci ay waa Almaañ jege woon nanu 96٪ , ci noonu Hitler daal di ne day boole yoon woowu ci Almaañ, looloo fi taalati gilinug xare bi ci adduna bi, ndaxte Fraans ak Britani ñoom danoo daal di woon jàpple Poloñ, ci noonu Hitler daal di joxe ay ndigal ci nu song Poloñ, ci 01 satumbar atum 1939g, ginaaw bi mu gisee ne ànd na ak Bennoog Sofiet gi, Itaali ak Japon . Nii daal la sawaras ñaareelu xareb adduna bi tàkke.


Jamono yi nga xam ne xare bi jaar na ci ak lefi xare bi :

Xareb adduna bu ñaareel bi romb na ci ñatti jamono ñooy:

(1) Jamono ju ndam yi Hitler doon ame ci xare bi, mu tàmbli ci 1939 – 1941g (2) Jamonoy yamoo (équilibre), walla li nuy duppee at mu jaxasoo mi, di woon atum 1942g (3) Jamonoy nërméelu ñeel réewi digg yi, mu tàmbli ci atum 1943 – 1945g.

Hitler yëgaloon na Poloñ atum 1939g ne ko manul ñàkk mu génne loxoom ci waaxub Danseg bi, te delloo Almaañ yoonu Poloñ wi romboon ci suufus Almaañ. Boobu lëj-lëj – bokkoon na ci li juddoo woon ca ndajem jàmm ma – mooy li fi taalati xare bi ci adduna, ndax mooy sabab bu jonjoo bi ko jafal. Hitler yamul rekk ci yonnee ag xupp jëme ca Poloñ, waaye da ca a rax dolli yabal ay soldaaram ñu song ko, teg loxo ay suufam, bi mu lànkee bañ a wuyyu wooteb Almaañ bi, bañ a faale xuppam gi. Bi mu kodefee, Britani ak Fraans jug yonnee ag xupp jëme ca Almaañ, ne ko na génn suufus Poloñ si, ci diir bu weesuwul ñaar-fukk ak ñeenti waxtu. Bi Almaañ lànkee bañ leen a déglu, la ko Britani ak Fraans song, ci 02 satumbar 1939g.

Almaañ jot naa teg loxo waaxub Danseg ak yoonu Poloñ wi, ak lenn ci goxi soww yu Poloñ yi. Ag dëppoo am ci diggante Almaañ-Rusi, gu waral ñu séddoo ñoom ñaar suufus Poloñ si, loolu nag di bi Rusi tegee loxo goxi penku yu Poloñ yi, daal di def ak Almaañ kollareg ñàkk-a-noonu (non-agresssion) di gi amoon ci 23 ut 1939g. Waa Almaañ wéy ci seen xare bi, daal di nangu Danmark ak Norwej atum 1940g, ginaaw ba nu fa dàqee dooley Britani ji ak ju Fraans ja fa nekkoon. Ci geneen wàll, Rusi moom gën na a tàllal ay tànkam ci Finland, loolu nag mu jaare ko ca kollareg ñàkk-a-noonu gi mu fasante woon ak Almaañ. Almaañ daal di song Luksamburg, nangu ko ci lu yéeme cig gaaw. Songati Holand, nangooti ko, song Beljig nangu ko waaye ci ginaaw xare bu saf sàpp, bu mujjoon waral deltu ginaawug dooley Britani ji ak ju Fraans ji atum 1940g. Dooley jañ ak naj gi Almaañ doon def ci bëj-gànnaaru Fraans gënoon a dolliku, gën a tar, ci noonu goornamaab Fraans bi daal di tuxoo Paris, dem Bordeau, foofa lanu tàmbli woon a sàkku ag wéer ngànnaay ak Almaañ. Ci noonu General Deegol daw làqu ca London, fa la doon jiitee jànkoonte (resistance) gu Fraans gi kontar réewi digg yi, fa la birale it ag Fraans gu gore gu ànd ak réewi tapoo yi( les alliés). Goornamaab Fraans bi diriku woon ba Bordoo, daal di xaatim ag wéer ngànnaay ak Almaañ, muy gu mel ne ga Almaañ defoon ag réewi dëppoo ya ca 1918g.

Wéer ngànnaay gi nag lii la wax:

(1) Almaañ nangu bëj-gànnaaru Fraans, péey ba di Paris bokk ca, ak mbooleem tefesi Fraans yi tiim mbàmbulaanug atlas gi. (2) Fraans day fay Almaañ ay alamaan yu alal, yu tollu ne ferey soldaari Almaañ yi nangu Fraans. (3) Limub soldaari Fraans yi dootul weesu téeméeri junniy soldaar. (4) Taxawal goornamaa bu Fraans buy ànd ak Almaañ, bii goornamaa nag taxawoon na ci njiitug Marsal Bitan. Ñu duppee woon ko goornamaab Fishi, ngir nekk ga mu fa nekkoon.

Ginaaw bi Fraans wommatoo meruw Almaañ- Itaali wi dafa sottiku woon ci kaw Britani. Bu ko defee, fafalnaaw yu Almaañ yi jog def lòkki yu toftaloo ci kaw dëkki Britani yi, la ko dale ca ut 1940g. waa Almaañ ñi nag li nu jublu woon ci loolu mooy manante Britani ci wommatu cig wàll, ak waaj ngir wàcce ay dooley Almaañ ca duni Britani ya, ci geneen wàll. Waaye taxaw gi askanu Britani wi taxaw taxawaay bu dëgër, te sax, moo tax ba waa Almaañ ñi manuñu woon a am li nu bëgg.

Réewi tapoo yi tàmbli woon nanoo ndàmmi ndam, di xaw a kawe réewi digg yi as lëf, bi Amerig duggsee ci xare bi ànd ak ñoom atum 1941g, ni ci Bennoog Sofiet gi dugge. Dooley Britani yi nag ndàmm nanu ndam lu mag ci jë bu Afrig bi ci kaw dooley Itaali yi, daal di leen dàqe ca Ecopi ak Eriteri. Looloo taxoon Hitler yabaloon ñaari kuréeli xare yu Almaañ ca bëj-gànnaaru Afrig, Marshal Rommell jiite woon leen ngir xettali-ji àndandoom ba ca Afrig. Ab xeex bu saf am ca bëj-gànnaaru Afrig ca 24 nowambar 1942g ci diggante réewi tapoo yi ak yu digg yi ci njiitug Mongomeri mi jiite woon réewi tapoo yi, ak Romal mi jiite woon réewi digg yi, ci noonu Réewi tapoo yi ndamu ci kaw yu digg yi ca xeex ba nuy wax Alamayni, ginaaw xeexub ñukkaakon (tank;char) bu mag bu sax fukki fan. Ay ngérte yu bari juddoo nanu ci xeex bii, nanu ci tudd:

(1) Teg loxo gi réewi tapoo yi tegoon loxo goxi bëj-gànnaaru Afrig, ginaaw bi nu fa dàqee dooley Itaali ji ak ju Almaañ ji. (2) Itaali wommatu na, soldaari réewi tapoo yi wàcc ca Sisil, ñu daal di daaneel nosteg Mussolini gi ca 3 satumbar 1943g (3) Nosub xare bi mujj na nekk ci loxol way tapoo yi , ginaaw bi mu nekkee ci loxol Almaañ ak réewi digg yi, àggoon nanu nag ci seen njòbbaxtali ndam atum 1942g


Ndamul Réewi tapoo yi:

Ginaaw bi dooley Britani yi ak yu Amerig yi lijjantee ba am ndam ca jë ba ca Afrig, ak ginaaw bi Mussoolini daanoo, la réewi tapoo yi fasoon yéenee jële fi Almaañ. Ñu wàcce woon soldaar su dul jeex ca tefesug Normandi ga, àggoon nanu cib lim ñaari milyoŋi nit daanaka, ñu tegoon leen nag ci kilifteefug Generalu Amerig bii di Dwaayet Asinhawar. Bu ko defee yii doole daal di teg loxo Fraans, Beljig, Holand (suuf yu xóot yi). Dooley Almaañ yi xëyoon nanu wëlbati një – cig deltu ginaaw - jëme Almaañ, waaye dooley tapoo yi mayuñu leen woon fu nu yakke seen nàkka, ngir ragal ñu jekkaat ba amaat doole ju nuy songeeti kenn, ci noonu ñu dab leen ca saa sa, jot a sutuxlu ca digi Almaañ yu soww ya ca fewriye 1945g.


Ruus yi nag ñoom jotoon nanoo jéego jéego yu am solo ci jëwub penku bi, ci goxi penkub Tugal bi, ginaaw ba fa dooley Almaañ yi jugee, ci noonu ñu nangu jëwub Tugal gu penku gi ci suwe 1944g. Ci nii daal la dooley Almaañ tàbbee ciy xat-xat yu jafe, ci kanamu doole yu rëyub lim te nu waajal leen ci ngànnaay yi mujj a génn, bu ko defee Almaañ xëy di ku ñu gaw ci diggante ñaari wàlli kuur , ci diggante penku ak soww, looloo juroon Almaañ faroon wommatu ci mujjantal gi, ci me atum 1945g, ñu daal di xaatim ag wéer ngànnaay ak réewi tapoo yi, loolu mujj di li taxawal dooley xare ju Almaañ jii jot a miiral adduna bi sonnal ko ngir xareem yu bari yii. Leegi nag réewi tapoo yi – di Angalteer, Fraans, Bennoog Sofiet ak Amerig - nangu nanu Berlin péeyub Almaañ, jàmmaarloo gi waa Almaañ yi doon def ak a dàkku seenub dëkk taxaw te jeex .

Wommatug Japon:

Waa Amerig yi yanoon nanu seen bopp coonab xare bi ci penku kontar Japon. Ginaaw bi waa Amerig nangoo suuf yu bari ci li Japon tegoon loxo ci xare bi, lanu dogu woon ci gañe xeex bi, ginaaw bi nu jotee fent bombub fepp (bombe atomique), te bëgg a xam li mu man, te bëggoon it Japon wommatoo ci seeni loxo. Ñu daal di jug ci ut 1945, sànni ñaari jum yu fepp ci ñaari dëkk ci Japon ñooy: Irosima ak Nagasaki, ci noonu Japon mujj wommatu, daal di xaatim ag wéer ngànnaay ak waa Amerig yi ci turu réewi tapoo yi, ci satumbar 1945g, bu ko defee ñaareelu xare bi daal di jeex.

Li juddoo ci ñaareelu xareb adduna bi:

ay ngérte yu bari juddoo nanu ci xareb adduna bu ñaareel bi, bokk na ci yooyu:

(1) Def ndajem Botsdam ca anéeru Berlin, ca 17 sulye 1945g, ngir jeexal xeex bi. Britani teewe woon na ko, Fraans, Bennoog Sofiet gi ak Diiwaani Amerig yu Bennoo yi. (2) Dagg goxub Brusiya ci Almaa ñ gu penku gi, bu ko defee Bennoog Sofiet gi jël ca wàllug bëj-gànnaar ga, Poloñ jël wàllug bëj saalum ga, ñu joxati Poloñ dëkkub Danseg bu gore bi (waaxub Danseg) (3) Séddale Almaañ def ko ñeenti barabi sañ-sañ, ci diggante Amerig, Britani, Fraans, ak Bennoog Sofiet. Ci atum 1949g la njëkk a am ci taarixu Almaañ ñaari reew sosu ci Almaañ, te yor ag nosteg pénc (systeme republicain) walla tosteg askan, ñooy: Almaañ gu soww gi walla péncum Almaañ mu bennoo mi (la république Fédérale d’Allemagne), nekk nag ci ron saytug Amerig, Britani ak Fraans, Bon di péey bi. Geneen gi di Almaañug penku gi (Brusiya gu njëkk ga), walla Almaañ gu demokraasi gi (la république démocratique allemande), Bennoog Sofiet gi saytu ko, Berlin gu penku gi dib péeyam. Ñu fàttali leen rekk ne Amerig, Britani ak Fraans mujjoon nanoo may Almaañ atum 1951 mu wut ay soldaar. (4) Almaañ ñàkk na mbooloom xareem bu dëgër ma te rëy, ñàkk ngànnaayam yu bees ya te jëm kanam, bi nu tasee ab xareem neewal dooleem. (5) Tegoon nanu Almaañ mu war a fay li mu yàqal rewi tapoo yi. (6) Nosaat koom-koomu Almaañ bi, rawati na nosteg alal gi ak gu endustri gi, yooyu yépp ñu jëme leen leegi ci luy ligéeyal mbiri yi dul xare. (7) Séddale Otris def ko ñeenti barabi sañ-sañ ci diggante Britani, Amerig, Fraans ak Bennoog Sofiet. Otris it des ci ron teg loxog réewi tapoo yi ba ci atum 1955g, ak doonte réewi tapoo yi nangu woon nanu ne réew la mu temb dale ko ca atum 1946g. (8) Réewi tapoo yi nangoo nanu ci Japon dun yu am solo, bu ci mel ne Farmosa ak Sakalin añs. Rafleel ko ci mbooleem moomeelam yi nekkoon ci màmbulaan gu atlas gi. Dooley Amerig yi nag juge nanu Japon atum 1951g, ginaaw bi nu xaatimee ag kollareg wéer-ngànnaay cis een digganteek goornamaab Japon bic i dëkkub San Fransisko. (9) Xaatim nanu ag juboo ak Itaali, Bulgari, Romani ak Hongri atum 1947g, gii juboo nag li mu yaxal mooy réew yii warloo fay réewi tapoo yi ay alamaani xare. (10) Deltu ginaawug ñaari réew yii di Fraans ak Britani ci nekk gi nu nekkoon ay réewi adduna yu mag ci ginaaw xare bi, bu ko defee Amerig ak sofyet yi jël seen barab, mujj it di réew yi ëpp doole ci adduna bi, mujj yor ngànnaay yu bon te aaytal. (11) Nërmeelug ñaari noste yii di Nasi ak Fasi ci Tugal ak nosteg xare ga nekkoon Japon, te noste gu mu ci doon rekk sag am bokk na ci li fi indi ñaareelu xare bi. Nostey diktaatoor yooyu bokkoon nanu ci nooni mbokkte yi gën a mag (12) feeñug dankub mbokkoo bi (bloc socialiste) ay réew yu bari bokk ci, Bennoog Sofuet gi jiite ko, mu ci mel ne : Kore gu bëj-gànnaar gi, Wietnaam gu bëj-gànnaar gi, Poloñ, Bulgari, Romani, Cekoslowaki ak Hongri añs. Bu dee nag Siin gu Askan gi ak Yogoslawi nag, ñoom ñaar ay réeyi mbokkoo lanu waaye nekkunu woon ci ron yilifug Bennoog Sofiet. Dankub bopp-alal bu gore bi it feeñ, Amerig jiite ko, làmboo nag réewi Tugal gu soww gi, niki: Britani, Fraans, Almaañ gu soww gi, Holand, Beljig, Danmark ak Norwej añs. Amerig it warlul yii réew ndimbalug alal ak gu xare, ngir ñu man a taxaw ci kanamu dankub mbokkoo bi. (13) Sos tapoog càmmooñu Atlas (Otan) atum 1939g, mooy tapoo gi boole woon Amerig, Britani, Fraans, Kanada, réewi sowwub Tugal bi, Japon ak Turki. Réew yii nag danu ne woon ku ci song menn rekk, song nga yeneen yepp. Ñu kollarante woon ci seen biir ci dimblante ci wàllug aaru, koom-koom ak alal. Ci geneen wàll, tapoog Warsaw gi daal di taxaw, tukkee ci Bennoog Sofiet ak réewi mbokkoo yi topp ci ginaawam ci càmmooñu Tugal ak penkoom. (14) Jëya ju rëy ji juddoo ci xeex bi muy faatug lu sakkan ci dooomu aadama ak yàqug alal ju dul jeex, ngir jumtukaayi xare yu xereñ yi nu ci jëfandikoo ñuy jum yi (les missiles), bombi fepp yi, nuuraakon yi ak ñukkaakon yu diis yi ans. Xare bii moo ëpp lu mu yàq, ray ko, màbb ko ca moomam ja ko fi jiitu woon. (15) Ëttu àtte yu Normbrug yi ngir àtte ñoñ Nasi ñi ci tuumay jèqi fitna ak sabab xare bi ak def ay tooñaange jëme ci ñu ñu tëj ñi (les prisonniers) ak ñi ñu njafe ca reewi tapoo ya. Àtte nanu fa tam njiiti nosteg xare gi nekkoon Japon. (16) Juddug mbootaayu xeet yi, ngir dëgëral jàmm ak tere xare yi ak xulooy réew yi, ak amal mbaandute ak yamoo ci réewi adduna bi. (17) Koom-koomu àdduna bépp a naatoon ginaaw bi xare bi jàllee, li ko waraloon di naali tabax yeek yeneen yi nga xam ne defaraat dëkk yi la doon ligeeye ak wàllug tabax ci anamam yepp. Bi gënoon a rëy ci naal yooyu mooy bu Marsaal. (18) Judduwaatug joŋante ci ngànnaay ci diggante ñaari dank yi: bu mbokkoo ak bu bopp-alal, ak sosu gi xare bu sedd bi sosu ci seen diggante, naka noonu dund ci jàmm gi am leegi ci diggante xeet yi ci kaw suuf.






















Doggantal gu ñaareel gi

Mbootaay yu adduna yi: kureelug xeet yi , mbootaayu xeet yi (walla xeet yu bennoo yi), mbootaayug reewi Lislaam yi (walla mbootaayu daje gu lislaam gi).

Ñatti mbootaay lanu bëgg’a waxtaane ci doggantal gii, ñooy : Kureelu xeet yi, Mbootaayu xeet yi, Mbootaayu reewi jullit ñi.

Kureelu xeet yi:

Njiitul Amerig la tuddoon Widro WILSON da doon ku daa xalaat nu mu fiy taxawale mbootaay gu mag gu adduna bi, guy jeem’a indi jàmm ci adduna bi, ci ginaaw xareb adduna bu njëkk bi. Waxoon nanu ne Wilson moom jotoon na a leeral dalam yooyu nga xam ne fukk lanu woon ak ñeent ci biir xeexub adduna bu njëkk bi, ne woon daal fàwwu nu sukkandiku ci ñoom ngir taxawal xeex bi, ak ngir rëddaat sëqooy reew yi teg leen ci dàtti jàmm ju sax ak moytu xeex yi nar a amati.

Wilson moom gaaraloon na naalam boobu di “Kureelu xeet yi” , gaaraloon na ko ca waxtaanu jàmm wa nu amaloon, kollëre ga nu jotoon a fas ca Versaay it moo rëddoon lanu fa xaatim. Lii di ñew di nanu ci leeral li ëpp solo ciy poñ yu nekk ci kollëre gi taxawal kureelu xeet yi.

(1) Sose kureelu xeet yi ci mbooleem reew yi am tèmb gu mat gu dara wàññiwut, reew yoo xam ne man nanoo indi ay warlu yu mat ci respekte walla wormaal jàmm, te bàyyi xeex mbaa lu koy waral . (2) Reew yi bokk ci kureel gi dananu warlu ne kenn du ci xeex ak kenn te gaaralul li ko tax a bëgg a xeex ci kureel gi, ngir nu àtte leen, te xool li leen boole. Reew yi ci bokk it war nanuy seet mbugal yi yell ci reew yiy tooñ, yu ci mel ne teg leen ay gaw yu koom-koom , walla jëfandikoo doole ci seen kaw. (3) Jeem a dëgëral buumi dimblante ci adduna bi jaare ko ci sukkandiku ci maslaa gu fés, ak wormaal kollërantey reew yi, ak xeex njaam, ci meloom yepp, jeem’a rafetal nekkiinu ligeeykat yi ak seenug dund, ak xeex dorog, nos yaxantu ci adduna bi, ak sonn ci wér gu yaramu nit. (4) Reew yi ci bokk dananu warlul yeneen reew yi wormaal seenug tembteg politig , dananu warlu it bañ a def ay kollërey sekkare , ak jox kooluteg kureel bi ab day ci mbooleem kollërante yi reew yiy def ci seen diggante. Koolute gi nag di secretariat bi, ci dëkkub Geneve bi nekk Siwis la nekk. (5) Aar neewtey xeet yi ak yu diine yi nekk ci mbooleem reew yi, ak wormaalal askan yi ak xeet yi nekkoon ci ron imbraatoor yi, wormaalal leen seen àq ak sañ-sañ ci wutal seen bopp mujj gi nu bëgg te gis ne moo gën ci ñoom , ak reew yi nu gañee ci xareb adduna bu njëkk bi. (6) Kureel bi mooy taxaw ci di xool ni nuy doxale nosteg féetale gi, mooy noste googu nga xam ne moo waraloon yenn ci askan yi, xeet yi ak mbooloo yi, nu feetale leen reewi sancaan yu mag yi, teg leen ci seen ron kilitfeef ak doxaliin, ginaaw bi reew yooyu nekkee ci waawug reew yi nu gañee woon ci xeex bi, ñuy : reewum Usmaan mi , Imbratooru Otris gi, ak gu Almaañ gi. Loolu nag nu defoon ko ngir waajale leen ci ba man leen’a may ag tèmb ëlëg . Kureel bi, bi muy door a sosu, 42 reew a ca bokksi woon. Ci noonu reew yiy temb di gën a dolliku, naka noonu di gën a bokksi, ba mujj limub reew yi bokk àgg ci juroom benn fukk, mu ci nekk it am genn kàddu ci bu nuy woote. Kollëreg kureel gi jox na reew mu nekk àq ak sañ-sañ ci mu genn ne bokkatuma, waaye ci kaw reew moomu teel a yëgale ag bëgg’a bàyyeem lu tollook ñaari at cig njëkk.


Bànqaasi kureelu xeet yi:

Kureelu xeet yi ñatti bànqaas yu mag la am, ñooy : Jataay bu matale bi , Jataayub Kureel bi, Koolute gi (walla secretariat), nga rax ci dolli ñaari bànqaas yu ci bànqaasoo, ñooy : àttekaayu maanduteg adduna bi ak mbootaayug ligeey gu adduna bi .

Jataay bu matale bi:

Mi ngi daa ame ci mbooleem ndawi reew yi bokk ci kureel bi. Ab dajeem it benn yoon la daa am ci at mi ci weeru sëtumbar, ngir xool ak xalaat ci mbooleem xew-xew ak mbir yu am solo yi nekk ci ay prograamam.

Jataayub kureel bi:

Moom mi ngi sosoo woon ci njëlbeen gi ci juroom ñeenti cer , juroom yi ci juroom ñeent yooyu ñooy reew yi am ag bokk gu sax ñooy: Britani, Frans, Itaali, Japon ak Almaañ mi jël cerub Amerig mi nga xam ne bokkutoon ci kureel bi. Ak yeneen ñeenti reew yoo xam ne jataay bu matale bi moo leen di tànn leeg-leeg . Bii jataay nag dana faral di daje ñatti yoon ba ñeent ci at mi. Dana faral di daje it, ci anamug jagle, ci xew-xew yu bette yu man a xupp jàmmi adduna bi. Limub toogu yu sax yi tam yokk na ci jataay bi, juge ci ñeenti toogu dem ci juroom ñeent.

Koolute gi (secretariat):

Koolute walla secretariat bu kureelug xeet yi, mi ngi sosoo woon ci ligeeykat yu kureel bi, ya daa ligeeye ca dalam bu sax ba nekkoon Geneve. Njiit li moom moo daa doon Ku-nu-woolu ku matale , ki nga xam ne jataay bu matale bi moo ko daa tànn. Koolute gi nag amoon na ay kureel yu bari yu aju woon ci moom, ñooy: kureelug dimblanteg aada gi , kureelug jële fi ag njaam, kureelug xeex dorog, kureelug aar neewte yi , kureelug féetale yu sax yi ak kureelug tawat yu bon yi.

Am na yeneen bànqaas yu am ag jokkoo ak kureelu xeet yi, ñooy yu mel ne: àttekaayu maanduteg adduna bi, ligeeyam di àtte xuloo yi ak amlante yi, àttee ko nag ci yoon walla luwa bu àdduna bi, ak kollërante yi reew yiy xuloo jotoon a def. Nosteg kureel bi nag li mu wax mooy àttekaay bi fukk ak juroomi àttekat ñoo koy taxawal yoo xam ne jataay bu matale bi moo leen di tànn, tànne leen nag ci kandidaa yi nga xam ne reewi kureel bee leen di ind. Àttekaayub maanduteg adduna bi moom, mi ngi sosu ci atum 1921g, ab dalam it nekk Lahaay ca Holand. Ak mbootaayug ligeeyub adduna bi, ligeeyam di yewenal nekkiinu ligeeykat yi ci adduna bi, ak yekkati seen tolluwaayu dund. Moom nag mi ngi booloowoo ci ndawi ligeeykat yi ak sendikaay ligeeykat yi, ak boroom ligeey yi. Geneve nag moo dib dalam.

Ayibi kureelu xeet yi:

Kureeb xeet yi de, ak li mu def lepp ci ligeey yu jëm ci saxal jàmm ci adduna bi ci biir fukki at yu njëkk yi, ak li mu fi def ci ligeey yu am njariñ ci wàllug mboolaay , loolu lepp teewul mu lottoon te ñakk kàttan ci lijënti xuloo ak ngaayoo yi da a am ci diggante reew yu mag yi. Loolu nag waraloon na neew-dooleg kureelu xeet yi, rawati na ci atum 1930g, bi nga xame ne ag lottam àgg na ci manatul a tee reew yu mag yi di noggatu yu ndaw yi, lu mel ni loolu moo xewoon bi Japon defee ay jalgati jëme ko Siin. Li ko gënoon a doyadil mooy genn gu ci Japon ak Almaañ gennoon atum 1933g, ak lott gu mu lottoon ci tee Itaali songu Ecopi atum 1935g. Loolu sax moo taxoon mu genn ci kureel bi atum 1937g . Kureel bi ba tay demoon na ba manatul woon‘a tee ay “dank yu xare” yu bees di am, maanaam ay reew dajaloo,boole seen bopp ci wàlli xare . Kureel bi tam àggoon na ci manatuloon’a tee reew yu mag yi di rewante ci ngànnaayu, yi ci bokk ci kureel bi ak yi ci genn. Bokk na ci ayibi kureel bi, fent gu ñeenti reew yu mag yi fentoon nosteg feetate ngir may Britani ak Frans nu man’a sancati walla koloniiseeti ay suuf yu bees, yoo xam ne danoo juboo woon ci seddoo leen ci seen biir, rawati na ci reewi araab yi, ak yu dul ñoom. Yenn yi ci yooyu, danoo nekkoon ci ron kilifteefug reewum Usmaan mi, yi ci des ci waawug imbraatoorub Almaañ bi. Reew yu mag yii dano’o jëloon seen xemmemteefi sancaan yooyu cuub leen ci cuubug ag nite ak bëgg’a def lu baax, bi nu waxee ne kureelub xeet yi daal mooy kilifa gu njëkk gi yilif reew yu neew doole yi muccoon ci kilifteefug Tirki ak Almaañ. Bokk na ci ayibi kureel bi ba tay, aakimoo gi reew yu mag yi aakimoo woon mbooleem saxal yi ak mbir yi nu daa gaaral ci kureel bi.



Mbootaayu xeet yi (walla xeet yu bennoo yi):

Ndawi reew yu mag yi, yu ci mel ni Britani, Diiwaan yu bennoo yi Amerig, Bennog Sofyet , Frans ak Siin, danoo daje woon ci Wasington peeyub Amerig ci wenn waxtaan atum 1933g, ginaaw bi as lëf ci ndam tàmblee feeñ ñeel reewi tapoo yi . Ci noonu nu gëstu woon nan lanu fiy sose ag mbootaay gu adduna guy yëngu ci saxal ponki jàmm ci adduna bi, jële fi xeex yi, amal fi maandute ak yamoo ci diggante mbooleem reew yi, ak rafetal nekkiinu mboolaayu reew yi ci koom-koom, mboolaay, aada ak wér. Bi loolu jàllee nu def benn dajeb waxtaan bu adduna bi ci dëkku San Fransisko ci 25 awril atum 1945, ngir rëdd fa ag kollëre ñeel ag mbootaayug xeet gu yees gu fiy wuutu kureelu xeet yi. Ndawi lu tollook juroom fukk ak benni reew teewe nanu ko, nangu it ci nu def kollëreg mbootaayu xeet yi, ak xaatim ko ci 26/06/1945g. La jiitu ca kollëre ga mooy:

“Ñun askani mbootaayu xeet yi ñi ngi giñ ne di nanu xettali maas yiy ñëw ci musibay xare , yi nga xam ne sotti nanu nit ay alkande aki naqar yu kenn manul’a misaal ci ñaari yoon ci diir bu gàtt bu weesuwul genn maas reek. Ñi ngi giñ it ne dananu feddaliwaat sunu ngëm ci àqi nit ju cosaanu ji ak yelleefam, ak teddngay jëmm ak man-manam, di feddali it ne goor ñi ak jigeen ñi ak xeet yi, moo xam yu ndaw lanu, mbaa yu mag, ñoo yam kepp ci àq ak yelleef” .


Jubluwaayi mbootaayu xeet yi ak ay ker-keraanam :

Kollëreg mbootaayu xeet yi dafa saxal ay jubluwaayam ci ñeenti mbir yu dàttu , ñooy:

(1) Wattu jàmm ak kaaraangey adduna bi. (2) Suuxat seqooy cofeel yi ci diggante reew yi. (3) Gën a soññ dimblante gi am ci diggante reew yi ci mbiri koom-koom, ak mboolaay, ak aada, ak wàllug nit. (4) Dëppale jëfi xeet yi walla reew yi, walla jëmale leen ci lu dëppoo ak li mbootaayu xeet yi bëgg.

Bu dee ker-keraan yi mbootaay giy jëfandikoo ngir àgg ci jubluwaay yooyu, moom mbootaay gi leerale na leen ci nii:

(1) Bennoog askan yu moom seen bopp yi ngir ñoηal jàmm ak kaaraangey adduna bi. (2) Di jëf ci anamug jàmm ak baalante ak jéllale ci diggante reew yi. (3) Warlu yoon yi man’a yobboo ci nu bàyyi jëfandikoo doole ci bu nuy lijanti jafe-jafe yi ci adduna bi, ndare bu loolu day li gën ci adduna bi. (4) Sukkandiku ci campeefi adduna yi ngir dëgëral jëm-kanamug koom-koom ak gu mboolaay gu askan yi.


Campeefi mbootayu xeet yi aki jumtukaayam:

Mbootaayu xeet yi mi ngi ame ci ñatti campeef yu mag ñooy:

Jataay bu matale bi:

mi ngi sosoo ci mbooleem reew yi bokk ci mbootaay gi, mu ci nekk it am na genn kàddu bu niy woote. Jataay bi da na daje benn yoon ci at mi ci weeru satumbar, ca dalam ba ca New York, man na’a am nag leeg-leeg ñu amal jataay bi ci xew-xew yu bette yi ko aajowoo. Jataay bu matale bi nag yii ñooy ay yiteem:

(1) Gëstu naal yi ko reew yi ci bokk di faral’a indil, ak saxal leen, ak def ndinkaane yi war ngir jàmmi adduna bi. (2) Gëstu mbir yi nga xam ne man nanoo yokk anami dimblante ci adduna bi. (3) Nangu bokkug reew yu bees yi bëgg a bokk. (4) Tànn cer yu saxul yi ci jataayub kaaraange gi . (5) Tànn àttekati àttekaayu maanduteg adduna bi, ak ceri ñaari jataay yi: bu koom-koom bi ak bu mboolaay gi, ak jataayub ndenkaane bi.

Saxal yi jataay bu matale bi daa faral di jël, ñi ngi daa ame ci ndollant gu toll ci ñaari ñatteeli cer (2/3) yu fekke woote bu nuy def ci naal bu mu man’a doon walla ab ndenkaane.

Jaataayu kaaraange gi:

Jataayub kaarange gi mi ngi sosoo ci juroomi cer yu sax , ñooy ndawi Diiwaani Amerig yu Bennoo yi (USA) ak Bennog Sofyet gi , ak Nguur Gu Bennoo gi ak Frans ak Siin, ak yeneen fukki cer yoo xam ne jataay bu matale bi moo leen di tànn ngir diirub ñaari at. Cer yu sax yi nag dananu am sañ-sañu firi lepp lu nu fas ca jataay ba, boobu sañ-sañ ñu koy woowe (veto), jataay bi nag dana daje ci anam gu sax ngir xool ci mbir ak xuloo yu adduna bi, yi nga xam ne man nanoo jur njombe. Saxal yu jataay bi, ñi ngi ame ci ndollant gu toll ci juroom ñeenti kàddu, ci cosaanul fukki kàddu ak juroom, maanaam saxal gi du man’a wér mbaa mu wéy ndare bu juroom ñeent danoo kàddoo waaw, la ca des ne deet walla ñu noppi. Waaye nag benn saxal du am njariñ bu ko benn cer bu sax firee ne àndu ci. Jataayub kaaraange gi moo ame kureel biy saytu kàttanug fepp gi , am na it sañ-sañ ci genne ay saxal yu aju ci taxawal xeex yiy am ci diggante ñaari reew, ak tege ay mbugali koom-koom, ak yu xare ci mbooleem reew yi dul dégg ndigalam, am na sañ-sañu yabal ay doole it ngir taxawal ab xeex, walla ay kureeli soldaar ngir ñu dox diggante ñaari reew yu nar’a xeex.

Koolute gu matale gi :

Moom jumtukaay la bu moo uuf mbooleem ñiy ligeeye ci mbootaayu xeet yi, koolute gi ki koy jiite mooy ku nu woolu kiy jiite mbootaay gi, nga xam ne jataayub kaaraange gi moo koy tànnlu, bu ko defee ñu gaaral mbir mi ci jataay bu matale bi ngir nu woote ko (kàddu ko). Dalub koolute gi mi ngi New York. Ci biir koolute googu lanuy denc mbooleem dosyeey mbootaay gi .

Campeef ak bànqaasi mbootaayu xeet yi:

Am na ay campeef aki bànqaas yu aju ci mbootaay gi, ñooy:

Jataayub koom-koom ak mboolaay :

Bii jataay’a ngi ame ci cer yu seen xam-xam aju ci mbirum koom-koom ak mboolaay. Jataay bu matale bi moo leen di fal ngir diirub ñatti at. Jataay bii nag li nu ko wékk mooy gëstu mbiri koom-koom yi ak mboolaay yi, ak aada ak lu aju ci nit. Mbootaayi adduna yii ma lay bëgg’a leeral ci jataay bii lanu bànqaasoo:

UNESCO:

Moom mbootaay guy jagoo mbiri aada yi la ak xam-xam ak yar , dalam bu sax ma nga Paris, ca Frans. Yiteem nag mooy dëgëral dimbalante ci wàllug xam-xam ak aada ak yar ci diiggante reew yi ci bokk, jaare ko ci soññ ak sawarloo gëstu ak ligeey yi aju ci yar ak aada ak xam-xam yi.

Mbootaayu Ligeeyu Adduna bi:

Li nekk yiteem mooy rafetal dundiinu ligeeykat yi ci adduna bi, ak fexe nu yokk seeni ngérte . Moom nag mbootaay gi, mi ngi ame ci ab lim ci ndawi ligeeykat yi, ak boroom ligeey yi ci mboooleem reewi adduna bi, ab dalam nag mi ngi nekk Geneve.

Mbootaayug Wérug Adduna bi :

Mbootaay la guy sonn ci dimbali reew yiy màgg ,ci ñu man a xeex tawat yiy wàlle, te yekkati seen tottuwaayu wér gu yaram. Moom mbootaay gi nag dana def ay gëstu ci wàllug wér, di ci sàkku it xam-xam yi manul a ñàkk. Di yonni ay boroom xam-xam ci loolu, di nos ay prograam yu jagoo tàggat ñi yittewoo wallug wér. Ab dalam nag ma nga Geneve moom itam.

Mbootaayu dund ak mbay gu adduna bi :

Moom nag liy ligeeyam mooy jeem’a def ay pexe ci nu niy yokke li nuy ligeey cib dund ci ñatteelu adduna bi . Loolu nag nu jaare ko ci jëme kanam mbay mi te yokk jumtukaayam aki ker-keraanam, ak xeex gàkk-gàkki mbay yi ak yu dundat yi , ak dox ci lu fi man a indi ag mottalikoonte gu dund ci adduna bi . Dalam bu sax bi nag mi ngi Rom ca Itaali. Ëttu àtte bu maandute gu kawe gi:

Moom nag daa mel ne àttekaayu maandute gu adduna bi gi toppoon ci Kureelu xeet yi. Moom daal moom lanuy jàppe kilifa gu wàllug yoon gu mag gi nekk ci mbootaayu xeet yi. Mi ngi ame nag ci fukk ak juroomi àttekat yu jataay bu matale bi di tànn, ak jataayub kaaraange gi, ginaaw bu leen seeni reew sampee, gaaral leen ci mbootaay gi. Ligeeyam nag mooy gëstu sabab yi waral xuloo yi ci diggante reew yi. Mooy kàttan gi ame firi ak leeral kollërante yi reew yiy def ci seen diggante, ak àttey yoonu adduna bi. Ab dalam nag mi ngi Lahaay ca Holand.

Mbootaayu xeet giy yëngu ci xettali gi ak tabax:

Li miy yittewoo mooy mbiri way daw-làqu yi, te indil leen ndimbal li manul’a ñàkk te dëkkal leen, ligeeyloo leen.

Jataayub ndénkaan yi :

Mooy saytu mbirum sancu yi Almaañ moomoon, Itaali ak Japon njëkk ñu leen di gañe ci xeexu adduna bu ñaareel bi. Bii jataay nag moo taxaw taxawaayu jataayu feetale bi nekkoon ci kureelu xeet yi, ginaaw xeexu adduna bu njëkk bi.

Bankub addunna bi ngir sos ak tabax:

Bii bank danu koo sosoon ngir man’a lebal reew yi ci bokk, ak dimble leen ci tabax barab yi xeex bi yàq, ak jëmale kanam barab yiy tàmblee màgg, ak sos ay naal  yoo xam ne man nanoo jàpplee ci màggug koom-koomu adduna bi, ak jeem’a rafetal dundiinu ñi dëkke ci reew yiy màgg  .

Banku adduna bi, moom dafa mel ni ag lonkoo gu adduna bi, goo xam ne boppu alalam mi ngi juge ci li cer yi di teg. Cer bu nekk nag li muy teg day tolloo ak ni koom-koomam toll. Dalam bu sax nag mi ngi Wasington, peeyub Amerig.

Keesug kee gu adduna bi :

Yitteem mooy saxal njëgu kee gu adduna bi, ak dindi fi jafe-jafe yi man’a juddoo ci wecciku ci diggante reew yi .

Man nanu ne mbootaayu xeet yi daal mbootaal la gu adduna, gu am sañ-sañ yi kureelu xeet yi amoon, waaye mu ëpple kureelu xeet yi ci ñatti mbir yu am solo, ñooy: (1) mbootaayu xeet yi day dëgëral - ci ay jubluwaayam – àqi ak yelleefi doomu aadama yu dàttu yi, ak teddngay nit ak yamale ñaari xeet yi (goor ak jigeen) cig wàll, ak yamale reew yi ci geneen wàll. (2) Mbooleem reew yu mag yi bokk nanu ci mbootaayu xeet yi, te bu dee kureelu xeet yi moom Amerig bokku ci woon ngir bañ gu Kongres bañoon ne du ci bokk. Te it Bennoog Sofiet moon bokku ci woon lu dul ci diggante 1934 – 1939 g. Nga rax ci dolli ne cer yi bokk ci mbootaayug xeet yi, boo ñaarte woo cer yi bokkoon ci kureelu xeet yi, yu mbootaay gi moo leen di ëpp. (3) Mbootaayu xeet yi am na dooley xare ju koy kàttanal ci mu man’a wéyal ay saxalam, am na it sañ-sañu tege ay dogoo yu koom-koom, ak jëfandikoo doole jëme reew yiy tooñ.

Ànd ak loolu lepp nag, teewul mbootaayu xeet yi moom, doon daanaka ab jumtukaay bu nekk ci loxoy reew yu mag yi am ay toogu yu sax ci jataayub kaaraange gi, yooyu nga xam ne ñoo ame sañ-sañu firi (veto), man a bañ mbaa firi bepp naal boo xam ne gaaral nanu ko ci jataayub kaaraange gi. Ci noonu yenn ci reew yu mag yi, fètteerlu nanu,wéy ci jëfandikoo sañ-sañu firi, di ko jëfandikoo fu nu ko wart a defe, di ci tooñe, di ci dumaa, di ci aare reew yuy jalgati. Te lu bari ci saxali jataay bu matale bi, ak saxali jataayub kaaraange gi, ba leegi daa rekk lanu ci kayit, kenn doxalu leen. Ab ligeeyam nag ci wàllug dimbalnteg koom-koom, aada, wér gu yaram ak mboolaay, lu am solo la, te yayoo màggal, waaye bu dee ci lu aju ci politig ak xare, moom dëgg-dëgg ni mu ciy doxe sori na dëgg, sori maandute te sori yoon.

Mbootaayu reewi jullit yi (walla mbootaayu daje gu lislaam gi):

Ag sosam:

Mbootaay gii mi ngi sosu ci saxal goo xam ne buur ak njiiti reewi jullit yi jëloon nanu ko, ci waxtaanu seen daje bi nu njëkk’a daje, te defe woon ko Ribaat, peeyub reewum Marok, ci diggante 9 – 12 /8/ 1389 g.g , deppoo ak 22 – 25 /9/ 1969 g. Ñaar-fukki reewi lislaam ak juroom bokkoon nanu ca waxtaan woowa, mbootaayug goreel Falastin (OLP) it teewe woon na ko waaye niki aji fuglu rekk .

Ndajem waxtaan moomu mi ngi amoon ci ginaaw bi nu lakkee Masjidul’Aqsaa, ci 21/8/1969 g , te ay yahuud def ko. Waxtaan wa ba muy tëj daa ñaawlu jëf ju bon jooju, nga xam ne day wone ag noonu gu nu def jullit ñi te ñàkk’a wormaal seeni gëm-gëm . ñu sàkku woon it ci Israayil mu genn ci mbooleem suufi araab yi mu tegoon loxo atum 1967 g. Te delloosi dëkkub Quds bi ci ni mu nekke woon ca xareb sue (juin) ba atum 1967 g. Mu feddali ba tay moom ndaje mi, jàpple gu miy jàpple reewi artaab yi, ci seen xeex bi nuy def ak Israayil, ak jàpple gi muy jàpple waa Palastin ci nu delloosi seen àq ak yelleef yi nu teg loxo, te goreel seeni suuf.

Kollëreg mbootaayu reewi jullit yi:

Kollëreg mbootaay gi mi ngi genne ca ñatteelu waxtaan wa jëwrini bitim reew yu reewi lislaam yi amaloon ca Jidda atum 1392 gg, dëppook 29/2 - 4/3/ 1972 g. Mu sampu woon – moom kollëre gi - ci li taxoon nu sos mbootaay gi.

Li nekk ci poñ bu njëkk bi ci kollëre gi mooy “reew yi ci bokk ñi ngi sos mbootaayug reewi jullit ñi (walla mbootaayug daje gu lislaam gi)” poñ bu ñaareel bi làmboo dali mbootaay gi aki jubluwaayam. Jubluwaay yooyu nag weesuwunu woon “ amal fi jawwu ju baax, ju nu man a dëgërale dimblante ak deggoo ci diggante reew yi ci bokk, ci seen biir, ak ci seen diggante ak yeneen reew yi. Waaye dal yi nag ñoom ci nii lanu taxawe:


(1) Yamoo gu mat ci diggante reew yi ci bokk (2) Wormaal àq ak sañ-sañu reew mu ci bokk, ci wutal boppam mujj ga ko soob, ak bañ’a dugg ci mbiri biiram. (3) Wormaal moomeelug reew yi bokk ak seenug temb. (4) Dëgëral dalu dimblante gu lislaam gi, ci diggante reew yi bokk. (5) Dëgëral dimblante ci diggante reew yi bokk, ci wàlli: koom-koom, mboolaay, aada, xam-xam ak ci yeneen wàll yu am solo yi, ak diisoo ak yeneen reew yi bokk ci yeneen mbootaay yi. (6) Jeem’a far boddante ci biiru xeet, ak sanc ci mbooleem ay anamam. (7) Def lepp lu man a indi jàmm ak kaaraange ci adduna bi, ci anamug maandute. (8) Dëppale ak nos ligeey bi reew yi seq, ngir njoηal barab yu sell yi te goreel leen , ak jàple waa Falastin ci seen xeex bi, ak dimble leen ba nu man’a delloosi seen àq ak yelleef, te jotaat seen suuf. (9) Jàpple mbooleem reewi jullit yiy xeex ngir njoηal seen teddnga, jot seen tèmbte, dollosi seeni yelleefi reew. (10) Lijjanti xuloo yi nar a ami ci diggante reew yi bokk ci mbootaay gi, lijjanti loolu ci jàmm, niki: waxtaan, dox diggante , ak layoo . (11) Reew yi ci bokk, danoo war’a bàyyi - ci seeni seqoo – di jëfandikoo doole walla xuppe ci jëfandikoo ko, jëme ko ci suufus reew mu bokk walla jëme ko ag tèmbam .


Campeefi mbootaay gi aki kureelam ak jumtukaay yi ci bànqaasoo:

Mbootaay gi sos na ay campeef yu bari yu cosaanu niki :

(1) Jataayu buur yi ak njiit yi (2) Jataayu jëwrini bitim reew yi (3) Koolute gu matale gi (4) Àttekaayu maandute bu lislaam bu adduna bi.

Bu dee kureel yi ci bokk nag, ñooy:

(1) Kureelu Quds (2) Kureel bu sax bi ñeel wàllug koppar (3) Kureelu lislaam bi saytu wàllug koom, mboolaay ak aada. (4) Kureel bu sax bi ñeel dimbalanteg xam-xam ak xarala (5) Kureel bu sax bi ñeel dimblanteg koom ak yaxantu (6) Kureel bu sax biy yëngu ci wàllug xamale ak aada


Bu dee nag lu aju ci jumtukaay yeneen yi bànqaasoo ci mbootaay gi, ñooy:

(1) Keesug dimblante gu lislaam gi (2) Keesug Quds (3) Daaray gëstu gu lim yi ak koom, ak mboolaay. (4) Barabu lislaam biy yëngu ci jàngale mecce ak xarala, ak defi gëstu. (5) Cëslaayu lislaam giy saytu xam-xam xarala ak suqli koom-koom. (6) Barabu adduna biy yëngu ci yar ak njàngalem lislaam. (7) Barabub lislaam biy sonn ci suqali yaxantu (8) Kureelu lislaam gi saytu terute gi ci adduna bi. (9) Kureel adduna gi saytu ndono lu lislaam li (10) Akaademi bu xam-xamu lislaam (11) Jataayu lislaam bi yor tukkib jawwu bu nit ñi (12) Kureelu lislaam bu adduna bi ñeel yoon


Bu lii jàllee, teewul sosees na ba tay yeneen cëslaay yu bokk ci mbootaay gi, ñooy (1) Banku lislaam bi (2) Barabu xibaar bu lislaam bu adduna bi (3) Mbootaayu rajoy reewi jullit yi (4) Neegub yaxantu bu lislaam bi, ak mecce ak joqalanteg njaay yi (5) Mbootaayu peeyi lislaam yi (6) Suqali gu lislaam gi jëm ci boroom gaal yi (7) Mbootaayug lislaam gi jëm ci yar, xam-xam ak aada.

Jagley campeef yi ak seeni ligeey:

Jataayu buur yi ak njiit yi, mooy campeef bi ëpp solo ci mbootaay gi. Moom nag dana faral di daje saa su ko yitey xeet wi laajee, ngir gëstu ay mbiram, ak lijanti ay lëj-lëjam.

Buur yi ak njiit yi ci bokk nag, saxaloon nanu ca seen ñatteelu ndaje ma nu defoon ca Makka (mu sell mi) ak Taayif, ci diggante 19 – 22 rabihul-awal 1301 gg, dëppook 25 – 28/1/1981g, saxaloon nanu fa ne danuy def ndaje yi ñuy luy wër ci seen diggante ci ñatti at yu nekk.

Niki nu ko waxe woon, mbootaay gi, ndajeem mu njëkk, mi ngi ame woon Ribaat, diggante 9 – 12/7/1389gg, dëppook 22 – 25 /9/1969g. Mu defaat meneen ndaje ca Lahoor ca Pakistaan, diggante 29 muharram – 01 safar 1394 gg, dëppook 22 – 24/3/1974 g . Ñatteelu ndajeem mu defe ko Makka ak Taayif, diggante 19 – 22/3/1401gg , dëppook 25 – 28/1/1981g. Mu def ñeenteelu ndajeem ca Kaasa Balanka, ci diggante 13 – 17 rabiihu-saani 1404 gg, dëppook 16 – 19/1/1984g. Juroomeelu ndajeem ame Kuwet, ci Jumaadas-saaniya 1407 gg, dëppook 26 – 30/1/1987g.

Jataayu jëwrini bitim reew yi nag, mooy ñaareelu campeef bi ëpp solo ci mbootaay gi, ginaaw jataayu buur yeek njiit yi. Campeef bii nag dana faral di daje – ci anam guy wër – ci at mu nekk, ci benn ci reew yi bokk, ngir xool mbooleen bataaxel yiy doxal politigu mbootaay gi. Ak jël saxal yi war ci mbir yi am ay njariñ yu reewi mbootaay gi bokk, loolu lepp nag, fekk mu dëppoo ak jubluwaayi mbootaay gi aki bëgg-bëggam. Jataayub jëwrin yi mooy xool saxal gi nga xam ne kureelub koppar bu sax bi di na koy def, ngir saxal ko te wéyal ko. Mooy xool it njël lu yaatu lu kooluteg mbootaay gi. Bokk na ci ay ligeeyam, di sàkku ci mbootaay gi muy daje, bu jaadoo, ngir ay xew-xew yu bette, yu yitteel jullit ñi. Jataayub jawrin yi ba tay dana faral’a daje ci anam gu xotti baax, saa su ko yitte laajee.

Bu dee koolute gu matale gi nag walla, moom mooy campeef biy wéyal jëf yi ci mbootaay gi. Mi m ngi sosoo ci saxal (resolution) gu genne woon ca ndajem jëwrini bitim reew ma nu amaloon ca Jadda, diggante 23 – 25/3/1970 g. Yiteem nag mooy def ligeey yi nu ko sant, ci biir àttey kollëreg mbootaay gi. Dina dimbli tam yeneen campeef ak bànqaas yi bawoo ci mbootaay gi, ak di dëppale seeni prograam yu wuute yi. Bokk na ci yitteem ba leegi, topp ak xeeñtu saxal ak ndenkaane yi tukkee ci ñaari ndaje yii: mu mbootaay gi ak mu jëwrin yi. Kiy saytu ligeeyi koolute gi, mooy ku nu wóolu ki nga xam ne mbootaay gee koy fal, ngir diirub ñeenti at yees manul’a yeesal, bu ko defee ñeenti dimblikat ak ñeenti ñu-ñu wóolu di ko jàpple, kenn ci ñoom, jagoo mbirum Palastin ak Quds, mbootaay gi Jidda la defandi dalub kooluteem gi, ba kero nuy goreel Quds,insallaa, ngir nu def ko dal bu sax bi. Làkk yi mbootaay giy jëfandikoo ciy ligeeyam ñooy: Araab, Franse, Angle. Mbootaay gi nag mbirum Palastin yitteel na ko lool, ak mu Quds, moom mi nga xam ne moo uuf Masjidul-Aqsa, mi Yàlla teral te teral li ko wër, ak doj wu sell wa, ak miir ba nuy wax “Miiru Buraax” . Ak yeneen mbir yi aju ci diiney lislaam te nekk ci mbooleem barabi lislaam yi. Quds nag boo gisee nu fonk ko, day suuf si Yonnant bi rañaane woon yeeg, loolu nag dana waral ci jullit ñi ñu fonk ko te yittewoo ay mbiram, te aar ko ba noon yi dunu ko tilimal. Kureelub Quds mi ngi sosu ci ndigal lu tukkee ci juroom benneelu ndaje mu jëwrini bitim reew yi, mi ame woon Jidda ci diggante 12 – 15/7/1975 g. Ndajem jëwrin mu fukkeel ma nu defe woon Faas ca Marok, ci diggante 10 – 14/5/1979g, ndaje moomu dal di denk njiitug kureelu Quds bi buuru Marok bii di Asan mu ñaareel mi. Ligeey yi nu denk kureel bi mooy yii: (1) Di gëstu lay xew Quds (2) Di topp ak a xeeñtu doxalug saxal yi aju ci Quds, te jataayub jëwrin yi def leen, (3) Di jokkoo ak mbootaayi adduna bi, yi man a dimblee ci aar Quds (4) Di wax ci lu man a doxal saxal yi ci aju. (5) Di indi ag saxal ci at mu nekk guy leeral ay ligeeyam aki jëfam ci jataayu jëwrin yi.

Kureelu Quds moom, njiit la ko jiite moo ko man’a dajeloo walla lu mbootaay gi. Kureel gi nag mi ngi ame ci ndawi 15 reew, yu bokk ci mbootaay gi, yoo xam ne jataayu jëwrin yee leen di tànn ngir diirub ñatti at.








Doggantal gu ñatteel gi: Reew yi def ay dank ak reew yi feetewul fenn

Ag jiital:

Bokk na ci li gën’a rëy ci li juddoo ci xeexu adduna bu ñaareel bi, bokk na ci li ci gën’a rëy, feeñug walla juddug ay dank yu ay reew, walla ay booloo yu ay reew , ci wàllug politig walla xare. Ci noonu dankub bopp-alal dal di feeñ nee, Amerig jiite ko, mu uuf nag Biritani, Frans, ak lu bari ci reewi Orobug sowwu gi. Mbooloo mii nag ñi ngi ko daa woowe dankub sowwu bi , ak reewi adduna ju gore ji, safaan nag walla wuute ak reewi bokkoo yi . Bu ko defee Amerig moom, jug di dimbli reewi dankub sowwu bi, ci ngànaay ak xarala, ak alal, ngir dëgëral seen koom-koom, te may leen doole ba nu man a taxaw di tata ci kanamu reewi bokkoo yi, tee leen a tas, tee leen a wisaaroo. Naka noonu, dankub bokoo bi , moom itam sosu, Bennoog Sofiet gi jiite ko, mu uuf lu sakkan ci reewi bokkoo yi ci Tugal gu bëj-gànnaar gi, ak gu digg gi, ak reewi bokkoo yi nekk Asi, niki Kore gu bëj-gànnaar gi, Wietnaamm gu bëj-gànnaar gi, ak Siinug askan gi . Ñaari dank yii: di bu sowwu bi ak bu penku bi, xeex nanu ba tàyyi ngir yilif adduna bii nga xam ne sonne na lool ci ñaareelu xeexu adduna bi, nga xam ne reewi Orob yi sax mujj nanu di reew yu lòtt te neew doole ci kanamu ñaari reew yu mag yii di: Diwaani Amerig yu Bennoo yi ak Bennoog Sofiet gi, looloo waraloon gisiin wiy woote ne “reew yi ñoo tolloo, yamoo, ay nawle lanu” wii gisiin naaxsaayoon, te faf far, xajal fi wiy indi doonadi moroom gi Amerig ak Sofiet doonadi woon moroom ci yeneen reew yi. Loolu nag taxoon na ba reewi Orob yi tàmbli woon’a xalaat ci seen ëlëg, ginaaw bi nu mujjee di reew yu ñàkk solo bu nu leen tollalee ak yile ñaari reew. Ginaaw ñaareelu xeex bi it, yeneen reew feeñ nanu, ñu leen di woowe reew yiy màgg, yi ci ëpp nag ñooy reewi Asi ak Afrig, yi doon door a tembe ci reewi sancaan yu orob yi. Reew yooyu tam danku nanu ngir taxawal dankub reew yi feetewul fenn, ne li niy def mooy fas yeenee ame ag peeteedi gu rafet ci diggante ñaari reew yu mag yi, ak yi nekk ci seeni ngunu. Dananu leen leeral ci lii di ñëw lenn ci danki adduna yi, bu ci mel ni: Tapoo gu càmmooñug atlas (Otan):

Njiilul Amerig lii di Harry Truman (1884 – 1972 g) dafa nekkoon ku bañoon lool mbokkte walla (cominisme), te bañoon it mu tas. Looloo taxoon mu taxawaloon ci atum 1939 g, ag tapoo walla alliance gu boole woon Amerig, Itaali, Holand, Beljik, Norwej, Danmark, Fraans, Kanada, Portigaal ak Island. Ñu tudde woon nag tapoo gii, tapoo gu càmmooñu Atlas. Ginaaw bi la ci Turki bokksi ak Gres, atum 1951g, ak Almaañ gu federaal gi atum 1955 g. Seenug kollëre it ci ñatti wàll yii la jëm:

(1) kepp ku laal benn ci reewi tapoo gi, laal nga yi ci des. (2) Reew yi ci bokk dananu dimblante ci seen biir ci wàllu aaru , alal ak koom. (3) Tapoo gi dana taxawal ab jataay bu xare , te da na am njiit lu matale tam.

Jaadu na nu leeral ne Amerig mooy dàttub tapoo gii, maanaam mooy reew mi ci ëpp solo, ci wàllug li nuy joxe ak ngànnaay. Paris it moo nekkandi woon ab dalam, ba ci mujj gi nu tuxal ko ca Buruxel, peeyub Beljik. Bokkoon na ci li ko taxoon a jug, neexal dundug ay askanam, yombal seenu nekkiin, dëppale ko ak sarti demokraasi, goreg jëmm ak yoon.

Tapoo gu Warsaw: Bennog Sofiet ñoom itam taxawal nanu ag tapoo gu kaaraange, atum 1955 g, loolu nag booy seet, ag won Amerig rekk la ne nun itam toogunu, boo sosee tapoo gu Atlas, nu sos sunu gos, rawati na bi ci Almaañ gu sowwu gi bokksee (ci gu Atlas gi) atum 1955 g. Tapoo gu Warsaw moom, Bennoog Sofiet la woon, reewi bokkoo yi nekk ci ngunoom, maanaam yi ànd ak moom, ci gànnaaru Tugal ak diggam, mell ni: Romani, Poloñ, Hongri, Cekoslowaki añs. Warsaw nag li ko taxoon a jug mooy aar Bennoog Sofiet gi, ak reew yi ko topp, ci mbooleem musiba mu man a bàyyikoo ci tapoo gu càmmooñu Atlas gi. Dëkkub Warsaw bii di peeyub Poloñ moo mujjoon dib dalam, li mu yoroon it ciy xarekat àggoon na ci 6000000 xarekat, ñu seddale leen ci diggante reew yi ci bokk. Tapoo gu kollëre gu diggu gi: Waa tapoo gu Atlas, Amerig jiite ko, danu ne woon daal fawwu nu jële fi bennoog Sofiet, tas tapoom gii di Warsaw, ci noonu ñu taxawal ag njiit gu jagoo mbirum penku bu diggu bi atum 1951 g, ginaaw bi nu sos mbootaayug aar penku bu diggu bi, atum 1952. Ci atum 1955 g, nu sos tapoo gu Iraak – Turki, ñu gën koo xame ci tapoo gu Baxdaad, tur woowu nag mujj na soppiku atum 1958 g, mujj di tapoog kollëre gu diggu gi, ginaaw bi ci Iraan bokkee, Pakistaan, Britani, ci wetu Turki ak Iraak. Ñu leen di fattali rekk ne Iraak moom mujj na genn ci tapoo gii ci suwe atum 1968 g. Jataayub Tugal bi : Waa Tugal ya daa woote bennoog Tugal, ak tembug ay gis-gisam aki saxalam, taxawaloon nanu ca atum 1949 g jataayub Tugal bi, muy ag mbootaay gu koom-koom, gu politig, loolu nag doonoon ab jeego bu njëkk rekk, jëm ci reewum Orob mu mag mu nu bëgg a taxawali. Bookoon na ci jataay boobu nag: Biritani, Frans, Itaali, Belgik, Holand, Luxamburg, Danmark, Norwej, Suwed ak Irland, nga rax ci dolli ay ndawi parlamaa yu reewi Orobug sowwu gi ak Turki. Dëkkub Strasburg bu Frans bi moo doonoon dal bi. Rewwi Tugal ya ca ja bu nu bokk ba : Waa Tugal yi – ci ag kollare gu nu fase woon ca Rom Atum 1957 g – taxawaloon nanu am mbooloo mu koom-koom mu Orob, nu gënoon koo xame ci turu Reewi Tugal ya ca ja ba nu bokk, ngir jële fi ag nduwaan ci diggante reew yi ci bokk, te doxal fi yaxantu gu gore ci seen biir. Buruxel nag lanu defoon seenub dal. Bokkoon na ci Frans, Britani, Itaali, Beljik, Almaañ gu sowwu gi, Luxamburg, Holand, Irland, Danmark ak Yonan (Gres). Ja boobu nag li ko taxoon a jug mooy dimblanteg koom-koom gu Orob, waaye mujj na rax ci gu politig gu yaatu ci seen biir. Mbootaayu dimblanteg koom-koom ak suqali  :


Mbootaay gii, Amerig moo ko sosoon atum 1980 g, muy mbootaay gu mel ni ( Reewi Tugal ya ca ja ba nu bokk ), ngir rekk man a dugg ci koom-koomu Tugal bi cig wàll, ak ngir man a dëgëral ay seqooy koom-koomam yi mu am ak reewi Ja bi, ci geneen wàll. Bokk na ci mbootaay gi nag: reewi tapoo gu Atlas gi, ak Siwis, Finland, Otris, Suwed, ak Yogoslawi. Mbootaayug reewi Amerig yi: Mbootaay gii yàgg na a sosu, ndax def na ko ci 30 awril atum 1948 g, waaye ag dëgg-dëggi sosoom mi gi door atum 1890 g, muy – man nanu ne – lu juddoo ci xalaatu njiitul Amerig lii di woon Monrow, mi daa wax naan ((Amerig daal ñaari Amerig yi ñoo ko moom)). Mbootaay gii nga xam ne Diiwaan Yu Bennoo Yu Amerig yi ñoo ci bokkoon ak reewi Amerig gu Latin gi, mujjoon na gën a yaatu gën a jëm kanam, mujj di ëtt bu am solo ngir dëppale diggante reew yi ci bokk, waxuma la nag njariñul koom-koom lu mag li ci nekk. Waa mbootaay gii nag Wasington lanu defoon seenub dal, te Amerig it amoon na kilifteef gu mag ci mbootaay gi, kilifteef googu feeñ na bu baax, bi Amerig tèggee Kuba ne bokkatul ci mbootaay gi, loolu nag mi ngi amoon ci ginaaw bi fi ag fipp gu bokkoo amee ca atum 1958 g.

Mbootaayi reewi Andis yi:

Moom nag mbootaay gu jagoo yenn ci reewi Amerig gu Latin gi la, li ko tax a jug di dëppale reew yi ci bokk ci wàllu koom-koom ak aada . ñi ci bokk nag di Kolombi, Peru, Ekuwador, Cili ak Boliwi.

Naalub Marsaal bi ak Komikon:

Bennoog Sofiet daa taxawaloon ag mbootaayug koom-koom atum 1949 g, ngir fayyoo ci ci li Tugal def ci wetam muy mbootaayug Ja bi, nga xam ne Amerig moo ko digaloon waa Orob yi, ne leen woon nanu taxaw ci tabaxaat seen koom-koom bu daanu bii nga xam ne xareb adduna bee ko màbboon, te moom dana leen ci jàpple, wooteg Amerig googu, ñi ngi ko gënoon a miine ci turu “Naalub Marsaal” , Marsaal nag jawrini Amerig ji yoroon wàllu bitim reew la woon, ci ginaaw ñaareelu xareb adduna bi. Sofiet yi nag ñoom seen mbootaayu koom-koom ñi ngi ko tudde woon “Komikon”, Bennoog Sofiet jiite woon ko, mbooleem reew yi àndoon ak moom bokkoon ci. Li ko taxoon a jug di dëppale reew yi ci bokk ci wàllu koom-koom.

Mbootaay gi boole reewi araab yi :

Reewi Araab yee ko sos ci atum 1940 g, ngir dimblanteg politig, gu koom-koom ak gu aada, ci seen biir.

Mbootaayug jàpplante gu Asi:

Reewi Asi yee ko sos ak yu Afrig yi, ngir dëgëral diggante reew yi ci bokk.

Mbootaayug bennoog Afrig :

Moom mbootay la gu reewi Afrig yi, ñu sos ko atum 1963g, li ko tax a jug di dëgëral buumi dimblante ci diggante reew yi ci bokk, rawtina ci wàlli poloitig, koom-koom ak aada.

Reew yi féetewul fenn: :

Reww yu bari temb nanu, ginaaw ñaareelu xareb adduna bi, rawati na ci goxu Afrig ak Asi, ñu daal di dem nag bokki ci mbootaayu xeet yi. Reew yooyu di door a am ag temb, soxla woon nanu di diisoo ci seen biir, te di daje, ndax kat ragaloon nanu bu baax reewi sancaan yi ak seeni pexe cig wàll, ak ngir ne ginaaw bi nu tembee ba noppi, danoo fees dell aki coonay koom-koom ak yu politig ci geneen wàll.

Ci nooonu am mbooloo sosu mu nu xame woon ci turu “Mbooloom reewi Asi yi ak Afrig” , ab xalaat dox ci ñoom jañ leen ci ñu taxawal ndajem Asi-Afrig, ngir gëstu jafe-jafey ñaari gox yi, rawati na lu aju ci goreel ay askan seen, ak tembal leen, teggil leen sukkub sanc bii tegu ci seenug dòq, ak ci anam gu mu ci teggoo.

Ci noonu nu def ndajem Bandonj ca awril 1955 g, ca Endonesi, ndawi lu tollook 29 reew teewe ko, yu Afrig ak Asi, ñooy: End, Bakistaan, Endonesi, Borma, Silan (mujj di Sirilanka), Afganistaan, Iraan, Japon, Filipin, Taylan, Siin Gu Askan gi, Wietnaam gu bëj-gànnaar gi, Wietnaam gu bëj-saalum gi, Cambodie, Lawus, Nipal, Ecopi, Liberia, Tefesug Wurus (Gana ginaaw bi), Siri, Isipt (Misra), Iraak, Nguurug Araabi Sawdid, Jordanie, Libi, Sudan, Liban ak Yaman. Ndajem Bandonj nag mooy ndajem adduna mi njëkk a boole ndawi ay reewi Asi ak yu Afrig yu temb. Ay ndénkaane aki saxal yu bari juddoo nanu ca ndaje ma, yuy soññee ci nu yamale diggante xeet yi ak waaso yi, te wormaal àqu ak yelleefu doomu aadama ju cosaanu ji, ak sañ-sañu nit ci wutal boppam mujj gi ko neex. Moom ndaje mi tam woo na reewi Afrig yi ak Asi ci nu dimblante ci kom-koom ci seen biir, te diisoo ci politig.

Ndajem Reew yi feetewul fenn, nag juddoo na ca ndajem Bandonj moomee. Nu njëkk koo amal ca Keer atum 1958 g, ma ca topp, nu defe ko Konaakri atum 1960 g . Bi adduna bi gënee bari ay coow, xuloo yi gën a tar ci diggante reew yi, Jamaal Abdu NAASIR, mi nekkoon njiitul reewum Isipt ak kii di Tito nekkoon njiitul Yugoslawi, ñoom danoo woo woon reew yi feetewul fenn te nekk Afrig, Asi ak Amerig Latin, ne nanu def am ndaje mu mag, ngir gëstu tolluwaay bii, ak tàngoor wii ci adduna bi. Ci noonu nu daal di def ndajem Belgraad, ci sëtumbar 1961 g, daal di genne ay saxal yu aju ci jàmmi adduna bi, ak jafe-jafe yi aju ci noccim ngànnaay mi , ak jafe-jafe bu Aljeri bi ak bu Kongo, ak yeneen jafe-jafe yu adduna yu bari yu amoon ca jamono ja. Nu defaat meneen ndaje ca Keer, mu Reew yi feetewul fenn, ci Oktoobar 1964 g. Lu tollook 47 ci ndawi reew teewe woon ko. Ab lim nag ciy saxal aki ndenkaane yu am solo genne na ca mooma ndaje, nu tudd ci yii rekk:

(1) wormaal sañ-sañu askan yi ak seen àq ci wutal seen bopp mujj gi nu bëgg. (2) Àndandoo ligeey ngir goreel reew yi tembagul. (3) Sakku nu nocci ngànnaay yi, te lijënti xuloo yi ci yoonu jàmm, te jële fi tapoo yi tas leen, dindi dàtti xare yi . (4) Ligeey ngir suqali dimblanteg koom-koom, aada, xam-xam ak yar ci diggante reew yi ci bokk.

Ñi ngi fattalee ne Reew yi feetewul fenn dolliku nanu, bi reew yi temb gënee dolliku, xuloob reew yi gën a tàng, rawante ci ngànnaayu gën a yokku, ci ngànnaay yu nu xamoon yi ak yu gën a jëm kanam yi. Looloo waraloon Reew yi feetewul fenn gën di dolli seeni daje yiy wër, ak di gën di ligeey ngir adduna bi man a dégg seen baat, te man cee def jeexiit bu baax.






















Ñeenteelu Doggantal

Fipp gi xam-xam amal ci Elektron :

Xamale lan mooy “ Elektron” :

Elektron moom yaram wu sew la lool, moom daal gën na a ndawe ay milyoŋi yoon, yeneen yaram yi nga man a gise ci bët rekk, bu nu rafleel. Moom sax manoo koo gise ci fésalukaay yu elktronik yu bees yi am leegi. Li ko waral mooy boo jëloon ay bilyoŋi Elektron dajale leen, du nu toll ne boppu puso.

Elektron nag nekk na ci bepp ne-ne bu Yàlla sàkk, moom nag mooy peek fepp wi , walla saal bi , moom nag foo ko fekk da koy wër ngir xëcc gi ko saal biy xëcc. Elektron ni muy wëre saal bi - booy xool - day mel ne ni bidiw yu mag yi di wëre jant bi. Elektron nag day yanu ay cëfkay kuran yuy bañ , saal bi walla fepp wi di yor ay cëfkay kuran yuy wuyyu walla nangu.

Xam-xamu Elektron ni mu sosoo:

Xam nanu ne xam-xamu Kuran moom xam-xam la bu nu xame bu yàgg ci ki nuy wax Taalis, di woon boroom xam-xamu Gres. Ay boroom xam-xam yu bari nag ñëw, gën koo jëme kanam, bokk na ci ñooñu kii nuy wax Wilyaam Jilbert, di boroom xam-xamu Angle boo xam ne mooy ki teqale dooley kuran ak dooley bijjaakon , ci noonu la wuuteek kii di Taalis mi ne woon ñoom ñaar daal benn lanu. Jilbert it xamoon na ne duusi kuran yi mooy jur dooley asye. Boroom xam-xamu Almaañ bii di Anofon Jiyorik, moom itam di ki njëkk a genne masinu juddal kuran, maanaam jumtukaay buy tax kuran bi di judd, di am, loolu di ci atum 1663 g. Tomas Adison it ñëw, indil ñu lamp bu kuran.

Xam-xamu kuran nag soppiku di xam-xamu elektron ci njëlbeeni xarnub ñaarfukeel g, loolu nag mi ngi amoon ginaaw bi boroom xam-xamu fisiyaa bu angle bii di Josef TOMSON jugee, feeñal xam-xamu elektron atum 1897 g, daal di ciy ame neexalub Nobel ci xam-xamu fisiya. Li gën a jëmal kanam xam-xamu elektron nag mooy feeñal gi boroom xam-xam yi feeñal ne fepp (saal biy wuyyu) day xëcc jëme ci boppam lu bari ci elektron yiy bañ, te moom fepp wi day seddaliku ci fepp yu bari. Ndamul xam-xam lii ab jeego la bu am solo ci doxub xam-xamu elektron. Jeego bii daal bu am solo la ci dundug nit ci kaw suuf.

Jumtukaay yu elektronik yi ak seen njariñ:

Jumtukaay yu elektronik yi mujj nanu ci jamono jii nu nekk, di loo xam ne foo wëlbëtiku gis ko, ci kër yi, barabu ligeey yi, dëkk yu mag yi, yu ndaw yi, mbay mi ak mecce yi añs. Kon daal jumtukaayi elektron yi, dugal nanu seen loxo ci yombal dund gi, nga gis nit ñi ñuy jëfandikoo raxasukaay yu kuran yu otomatik yi, ak fompukaay yu kuran yu otomatik yi, ak jumtukaayu seral yi yu wuute yi, ak rajook tele yu melo yi, ak jumtukaayu nataal yi añs. Boo demee ci ndoktoor it fekk ko mu fees dell ak jumtukaay yu elektron, xoolal ma fesalukaay yu elektonik yiy feeñal jàngoro yi gën a tuuti, ak nataalukaayu ndoktoor yi, ak jumtukaayu segg yu elktronik yi. Jumtukaay yii dey tax nanu doktoor man a xam lu jot nit, man koo faj, te looloo tax ndoktoor jëm kanam ci sunu jamono jii.

Gis nga leegi foo dem fekk fa komputer, ci bank yi, lonkoo yi, campeefi goornamaa yi ak ligeewukaay yi. Gis nga xam-xamu fuglug jawwu ji ni mu nosoo leegi, ak xam kiliman bi, te loolu lepp elektron a ko waral, leegi man nanoo xam nu tooyaay bi toll, nu jawwu ji selle, nu gelaw li gaawe, nu tàngoor wi tànge, nu niir yi kawee añs, te loolu lepp elktron a ko def.

Waa xam-xamu suuf (jiyoloji) jariñu nanu ci jumtukaayi elktronik yi leen di xamal ati doj yi ak ati suuf si, te di leen won fi am petrol, yoraniyom ak yeneen mbèlli suuf yu am yi solo.

Jumtukaayi elektronik yi dimblee nanu ci wàlli ngànnaay ak xare, ak aaru. Leegi gis nga jumu fepp , rajo, jumtukaay yi amul buum , ak yiy yonnee tey nangu, ak yiy nataal añs.

Lii nag wone na ne xam-xamu elektron, aki jumtukaayam, yi ci aju ci jàmm ak yi ci aju ci xare, def nanu fi ag jeqiku gu xam-xam gu am solo ci xarnub ñaar-fukk g bii. Nit nag jot na a man a tàggat xam-xam bii def ci li mu ci bëgg ci lu aju ci jàmm, waaye it mi ngi koy jëfandikoo ci xare yiy màbb, tey mbugale, di alag mbidéef yi.











Juroomeelu Doggantal

xareb jawwu ji  :

(( yaa mahsharal jinni wal’insi inistatahtum an tanfuzuu min’axtaaris’samaawaati wal’ardi fanfuzuu, laa tanfuzuu illaa bisultaanin)) Sooratu Rahmaan, aaya 33.

Di : yeen jinne yeek nit ñi, su ngeen manee dem, ba soobu ci goxi asamaan yi ak suuf, def leen ko, waaye fu ngeen fi àgg rekk na leen woor ne Yàlla a leen may ngeen àgg fa. Fu ngeen fi àgg rekk, ci sultaan ngeen fa àgge, sultaan nag mooy: lay, ndigal, kàttan, nguur. Di kon fu ngeen fa àgg, sunu boroom a leen fa àggale moom mi leen may xel, may leen kàttan, ubbil leen bunti yooyule gox, man a layal lu tax ngeen àgg fa.


Nit nag yàgg naa xëntewoo xam li ko wër ciy mbir, yàgg naa yittewoo xam mbóoti jawwu ju biti jii nga xam ne daa fees dell aki nekkteef yu asamaan; ay bidiw aki ñoom seen. Moom de jot naa àgg ci xam bidiw yi ak seeni kem ak seeni bind, ak li leen sos, def it ab jeego bu rëy ci xam-xamu juxraaf ak yeneen xam-xam yi am ag jokkoo ak kaw suuf, biir suuf ak li wër suuf, peek ko ciy mbindeefi asamaan, bidiw ak lu ko moy. Ci ati juroom fukk yi, ci ñaar-fukkeelu xarnu bii, gis nanu nit mu jeem ay yoon nu mu yeege ci jawwu ji, ngir làmb ko te xam la fa nekk, loolu nag faalewu ci jafe-jafe yi mu ci man a dajeel, ak ay wu rëy wi loolu làmbool, bokk na ci ay woowu: man cee ñàkke bakkanam, ñàkk a wóor gi, ci bu nuy joy , bu masin biy wëndéelu ak buy wàcci.


Li Sofiet yi def ci xareb jawwu ji:

Sofiet yi de njëkk nanoo nattu jawwu ji, làmbtu ko, loolu nu jaare woon ko ci jëfandikoo ay bayyima, ngir ragal nit di ci loroo. Sofiet yi ñi ngi njëkk a joyal seen gaalug jawwu gi tuddoon Fostok – 1 ñaari soobukati jawwu yu sofiet nekkoon ci biir – di Yori Jajarin ak Alaan Shabard, ci subag bisub 12 awril 1961 g . loolu nag bettoon na adduna bépp. Tukkib jawwu bii nag yobbu woon na lu tollook teemeer ak juroom ñatt-fukki simili, ci biir diir boobu, gaalug jawwu gi wër na ci suuf si benn yoon ak xaaj. Tukkib xam-xam bu jawwu bii xew-xew la bu am solo ci taarixu nit ci jamono ju yees jii, ndax kat moom ubbi na fi ay gox yu yees yu yaatu ci wàllug xam-xamu jawwu.

Sofiet yi wéyoon nanu ci seen ligeeyi jawwu yooyu nga xam ne am na ci yu jàmm taxoon a jug ak yu xare taxoon a jugg. Seen satalit yi gënoon nanoo yokk seen cawarte rawati na ci lu aju ci xare, ci diggante ati juroom-ñaar-fukk yi ak juroom-ñatt-fukk yi, ci xarnu bii.



Li ci waa Amerig def:

Waa Amerig yi - ci ati juroom fukk yi, ci ñaar-fukkeelu xarnu g – def nanu ay jeem aki pexe yu am solo ci wàllug xareb jawwu ji. Seen cawarte ci wàll googu dolliku woon na ci ati juroom benn fukk yi ci xarnu bii, ndaxte seen ligeey yu jawwu yi gënoon nanoo ràññiku te gën a fés ci diggante bii, ndax ci la kërug jawwu gu Amerig gi, ñu koy wax NASA, jot a joyal ay waruwaayi jawwu , yoo xam ne ay jum ñoo leen di jañ, jañax leen ñu naaw, bu niy dellusi ci suuf si nekk ay fafalnaaw yu yor ñaari laaf, ñu leen di man a jëfandikoowaat ay yooni yoon. Lii nag tax na ba li nu daa ñàkk ci tukkiy jawwu yi gën a neew, te itam indi na ay ngérte yu am solo ci xareb jawwu ji.

Waa Amerig jot nanoo sànni waruwaayu jawwu wii di Apolo ci 20 sulye 1969g, ñaari soobukati jawwu nekkoon ca, ñooy: Aarmustrong ak Adwin Drin, Aamustrong nee na “ Amoon naa yëg-yëg bu tumbrànke, bi may dox ci kaw weer wi, damaa yëgoon ne sama màndaxe daa woyofoon lool”. Waa Amerig yi sàmp nanu ci kaw weer wi ay jumtukaay yu xam-xam yu bari, jële nanu fa it ay còmp yu juge ca weer wa, teg fa it ab juddalkaayu kuran bu saal .

Kongres it dëppoo - ci 5 samwiye 1972g – ci prograamu jawwu bi nu tudde woon (baaganteg jawwu) ngir barig li nu daa dem ci jawwu jeek a dellusi. Tukki bu jawwu bu njëkk bi nuy wax Kolombiya tàmbli na ci 12 awril 1981g, yeneen tukki topp ci yu jawwu yu àntu .

Waa Amerig yi defati tukkiy jawwu yu Carlinger , bi ci njëkk di ci 4 awril 1983g, juroom ñeenti tukki topp ci, bi mujj di ci 30 oktoobar 1985 g.

Musibam Carlinger:

Am musiba xewoon na ci baagante gu jawwu gu Amerig gii di Carlinger-10, loolu nag mooy bi waruwaay bi fàccee , ci bisu talaata 28 samwiye 1986 g, lu tollook juroom ñaar faatu ci, ñaar ñi di ay soxna . Njiitul Amerig la nu daa wax Ronaald RIGAN nee na woon “ Bii bis de dana doon bisub naqar ak fàttaliku” . Waa Amerig yi it tudde woon nanu ko bis bu tiis bi.

Musiba mii du mooy mi njëkk a dal Amerig ci wàllug jawwu gi, mu ni mel njëkkoon na ko fi ci lu tollook ay at, loolu mooy bi sawara tàkkee ca joyaluwaayu waruwaay ba tudd Apolo 11, ci samwiye 1967 g, ci noonu ñatti soobukati jawwu ya ca nekkoon yepp dee.

Amerig defati yeneen tukkiy jawwu yu baagante, tudde ko Discovery, bi ci njëkk mi ngi amoon ci 30 Ut 1984 g, yeneen tukk yu àntu topp ca.

Lii nu tudde xareb jawwu ji daal, def na lu am solo ci wàllug xam-xam, rawati na lu aju ci mbiri jàmm yi. Ndaxte xam-xamu fisiya gën a jëm kanam, bu fuglug jawwu , ak xam-xamu nataalu jawwu biy nataal kaw suuf si te di ko natt, xam-xamu kart yi ak nataali jawwu yi gën na a jeego ay jeego, naka noonu endustri elektronik, ni nuy xame fi mbell yi nekk gën a xarañ, ak ni nuy xeexe lakk yi añs.

Sofiet yi ak waa Amerig yi ku ci nekk soobu nga ci jawwu ji ngir ay xemmemteefi xare, jawwu ji mujj di lef mu stratejig mu yaatu ñeel ay ligeeyi xare, la nu ca jublu it di door ak jam ay barab yu nekk ci kaw suuf, jaare ko ci seen satalit yi nekk ci jaww ji, yi ci yanu ay boppi atomig, cig wàll, walla nu jaare ko ci ngànnaay yu wuute yi nu man a joyale ñu tukke ci jawwu ji, ci geneen wàll.

Xareb jawwu ji, yamatul rekk ci diggante Sofiet yi ak waa Amerig yi, leegi kay lu sakkan ciy reew bokksi nanu ci, mu ci mel ni Siin ak Fraans. Am na yeneen reew yuy waaj ngir sànni seeni jumi jawwu walla satalit ci jawwu jii nga xam ne mujj na di barab bu yaatu ngir rawanteg xam-xam, ak gëpplante ci wàllug xare.


















Juroom benneelu doggantal

Ni Japon jëme kanam


Japon njëkk fukk ak juroom ñeenteelu xarnu g:

Japon de wéyoon na diir bu yàgg, di beru ak a sori xayug Tugal gi, yam ci yëfi bobbam, doyloo aadaam, ba ci digg juroom ñeenteelu xarnu g, gii beru gu xay, ak deltu ginaaw gu mag raxoon na ci, ci wàllug koom-koom, rawati na endustri.

Waaye nag lii mu nekke woon, soppiku woon na ci ñaareelu xaajub fukk ak juroom ñeenteelu xarnu. Ci noonu mu tàmblee juge nànk-nànk ci reew mu deltu ginaaw, dem ci reew mu jëm kanam ci wàll yii: koom-koom, aada, politig ak xare. Mu roye nag ci reewi Tugal yi, gisiinu sanc ak yaatal ko, ci reew yi mu dendal, ngir wone ci dooley addinaam ji mu yor, ci wàllug xeex gi nuy def ngir teg loxo ay reew, sanc leen.

Japon nag ak li muy yeex a jot ci xayug tugal gi lepp, boo ko dee xool ci reewi Asi yeneen yi - ndax dëppoo gi mu njëkk a def ak Amerig ci wàllug joqalanteg yaxantu weesuwul atum 1854 g gii rekk - teewul mu tàmbli woon na jege nànk-nànk xayug Orob gi, di ci jariñu, di ci niitu. Loolu jural ko mu tabax ay isin yu mag, xotti ay yoon, defar ay yooni saxaar , gën a jëmale kanam ni nuy yaxantoo. Reewum Japon ca saa sa mu tàmblee gis ag yëngu-yëngug endustri gu mag, gu nirook ga Tugal romboon ba mu ciy door a dugg. Bu ko defee, Japon xëy di reew mu dox, mu jëm kanam, raw nag ay maasam ci reewi Asi yi, ci wàllu endustri, xam-xam ak xarala . Mu mujj am, moom Japon, mbooloom gaal mu yaxantu tax a jug, mu mag, moo xam ne moo jël limub ñatteel ci adduna bi, ci diggante ñaari xarey adduna yi. Marsandiisi Japon yi, nga mujj foo dem fekk leen fa, ci Asi ak Afrig.

Japon, ginaaw bi nu ko gañee ci ñaareelu xareb adduna bi:

Japon gañe nanu ko ci ñaareelu xareb adduna bi, te booba moo nekkoon laafum penku mi ñeel reewi digg yi (axe), ñooy: Almaañ, Itaali ak Japon. Japon nag mujjoon na nangu ne gañe nanu ko, mu jébbalu, joxe loxoom ci kanamu njiitul xare lu Amerig lii di Mark Arthur, atum 1945g . Ci noonu nu taxawal benn jataay bu way tapoo yi , ngir doxal mbiri Japon, nu dénk ko kii di Mark Arthur, ci diggante 1945 – 1951 g.

Waa Amerig yi nag rëddaloon nanu Japon benn strateji, dugal fa demokraasi, jële fa dal bi aju ci jaamu imbraatoor bi , nu soppi woon it seeni njàngaliin, maanaam ni nuy jànge ak li nuy jàng, wutaloon leen sartu reew bu bees, ray it lonkoo yu mag yi . Ñu fuqarci ay moomeel yu rëy ci loxoy njabooti Japon yi, sëddale leen ci lim bu mag ci baykat yi, daal di it taxawal ab parlamaa bu bees .

Ci noonu Japon jot na a tàmblee nosaat dundug koom-koomam., gu plitigam ak gu mboolaayam, te tàmblee dab nànk-nànk, reewi endustri yu jëm yi kanam.

Waa Japon jariñu nanu ci li leen Amerig indil ci ndimbal yu alal ak yu xarala, loolu bokk ci li delloosi cawarte gi ci wàllug koom. Lijjantikati Japon yi dox nanu bu baax ci tas ak yaatal koom-koomu Japon, ngir seenug yewwute ak ngir bari gu Japon bari ay ligeeykat.

Suqali nag gën na a yokk ci wàllug endustri ak yaxantu ci diggante bi topp ci 1955g . Japon mujj di ñatteelu reew mi ëpp lu muy ligeey weñ, bokk it ci reew yu njëkk yiy segg petrol, ak yi ëpp lu nuy defar gaal. Mbooloom gaalum yaxantoom mi gën na a jëm kanam, ay ngañaayam gën a dolliku, ligeey bi aju ci jumtukaayi eliktronig yi gën a jëm kanam, ba mujj Japon àgg ci, ci fi nu man a yam ci raw gu xam-xam. Ja yi nuy jaaye ligeeyi Japon yi gën a yaatu, gën a bari ci adduna bi. Bu ko defee Japon mujj nag di reewum endustri mu mag, mu dox, te jëm kanam.