Tukkib géej gi

Jóge Wikipedia.

Sëñ bi,bi mu jotee ndigalul Yàlla ak Yonnant bi (j.y.m),Yonnant bi (j.y.m) jox ko kiiraay luy dox diganteem ak tubaab yi,te loolu wax na ko ci genn xasida:{ ku nu tànn ki,jàmm ak mucc yal nanu nekk ci moom,wutal ko kiiraay lu koy aar wëlif lor,ne ko doxal te bul ragal woru,}}, bi loolu amee mu genn ca këram ga mu sancoon Jolof ngir jàng ak jàngale,ci bisub gàwwu fukki fan ak juroom ñatt yu safar,ci atum junni ak ñatti téeméer ak fukk ak ñatt g. Ci jummaada saaniya walla sahbaan ci at mii,la sheex Bashiiru gane àdduna di doomi sëriñ bi,bi miy genn daje ak ki jiite mbooloom xare moomu genn moom itam juge wàllug Luga, ñu daje ca Jeewal ca ngoonug bis booba,sëñ Banji NJAAY,nee na ma - moom ci ñi àndoon ak Sëñ bi kerook la, ñu gënoon koo xam ci Banji Xuja - am na benn karaama bu feeñ Jeewal,mooy bi nu àggee Jeewal , danoo jeexaloon ndox,te foofa ndox bariwu fa,satalag Sëñ bi jeex,bi nu nekkee ci jaaxle googu nag,jenn waay ju yor ab baag bu fees dell ak ndox jege,nu wax ak moom xamul li nu koy wax,nu jox ko ab defukaay, mu duy ko ba mu fees ak ndox,nu naan,Sëñ bi jàpp,ndax moom daawul tiim,waa ja jàll,te déggunu aw làkkam,xamunu ci moom dara.


Sëñ bi nee na :ginaaw bi nu jullee tàkkusaan,nasaraan boobu di njiitul soldaar yi,dikk na, bëgg a wax ak moom,mu wëlbati kanamam wëlif ko ,jublu Yàlla,jàng Bismil laahir rahmaanir rahiimi juroom fukki yoon,waa ja nooy,aw xalam fay,mu gaaw genn,jëm ci ay aajoom,mu fanaan foofa,ak jaraaf ju ñuul jooja,ci loolu Sëñ ba’a ngi naan: {ginaaw bi nu dajee’k ña génnoon jëm ca këram,te njàqare nekk ci seeni dënn)) (Dox nanu àndandoo di way gaaw,jëm ca jaraaf ja,ba tàkkusaan jotee ñu julli fa cig ragal yàlla ) (Ginaaw bi la jaraaf ji daje ak moom,mbooloom xareem mi wër ko,am ca ñuy siyaare ) (Mu jubale kanaman ca Yàlla mu tedd ma,bañ koo jubale jaraaf ja,ngir am li mu bëgg ) (Wax juroom fukki bismil laahir rahmaanir rahiimi,cig toroxlu jëm ca ka nga xam ne,fu mu daaneele ab noon mu nërméelu) (Jaraaf ja génn cig gaaw jëm ca aajoom,mu fanaan fa di boroomi xéewal.}}


Waxam ji mu naan am ca ñuy siyaare ,Sëñ bi nee na mi ngi ci jublu woon,taalubeem ba Omar NJAAY,sheexub Konjoru Njaay,di dëkk bu nekk ci wetu Luga,moom nag am na wàccuwaay bu kawe ci sëñ bi,bi mu faatoo sëñ bi seereel na ko yiw wu rëy,dig ko it yiw wu ko ku dul moom di ñeewe,ngir rafetug njortam,ak waxam ju rafet ci sëñ bi, ñi ngi ko denc Njaaréem.

Sëñ bi nee na: ( Omar mii mi ngi génn,ngir siyaaresi ma,daje ak soldaar siy génn,fekk nu xamoon ko,te fonkoon ko, ñu kontaan ci ànd gi mu ànd ak ñoom,jàppe woon ko kenn ci seen kilifa yi,waaye Yàlla moom xam na la nekk foofa). Sëñ bi nee na (nasaraan boobu jiite woon soldaar yi,moo doonoon ki yoroon Luga (gouverneur) ca jamono jooja,doonoon gorob buuru ndar (boroom ndar),looloo waraloon ñu déglu woon ko ci samay mbir,mooy ku rëyoon, ki daawul wax ci man lu baax,daawu ko def,daawul ànd ak ku koy def,dogu woon it ci tumbrànkeel ma,nu ne ko du fi ame,mu ne kenn du ko tee am,dogalub yàlla bi dëppook li mu dogu,looloo taxoon,ma yàggoon Ndar ñuy xool samay mbir,looloo taxoon mu wird aayay {wa iz yamkur bikal laziina kafaruu liyuzbituuka aw yaxtuluuka aw yuxrijuuka,wa yamkuruuna wa yamkurul laahu wal laahu xayrul maakiriina}}muy ci maanaa ,bi la ñi weddi di fexeel,ngir saxal la fi,walla ñu ray la,mbaa ñu génne la, ñu nekk di fexe,Yàlla itam di fexe,te Yàlla’ay ki dàq a fexe.Sëñ bi nee na :(Ndar, ña fa nekkoon ñatti kuréel lanu woon, ñu bëgg ñu bàyyi ma fa,bu ko defee,nu di leen sonnal ca daanaka-dun ba bépp (daanaka-dun mooy Presqu’ile) ,di yàqq seeni kër,ak ñu bëgg ñu faat ma, ñooña amunu lanu bëgg,ak ñu bëgg ñu tumbrànkeel ma, ñooña Yàlla dëppale dogal bi ak seeni xalaat). Sëñ bi wax na ci loolu lii: { Yàlla tàbbal ci xoli ñi sababoon ag tuxalam,ca jooja jamono)) (Mu tàbbal ci seeni xol,ag génne ko,jëme ko ca réew yu sori ya,mu ame fa lu kawe déggub Saariya}}

Yàlla (t.s) dëggal na ba mu naan {wal laahu xayrul maakiriin}}muy yàlla’ay ki dàq a fexe. Ndax xéewale na ma ñatt yu gën seen ñatti kuréel ya,ndaxte bi may tukki,amoon naa martabay dëgg-dëggi sëriñ,ci gëm ak lihsaan ak lislaam,waaye dese woon naa lu ma yitewoo woon lool ba mu daa ma jaaxal ak a fogloo (fog mooy ñàkk a nelaw guddi) ,te ñàkk ko, ñu may jam ay xeej a ma ko gënal,di daggate samay baaram,loolu moo di matug gëm Yàlla gi nga xam ne mooy dëgg-dëggi xam Yàlla,ak matug lislaam gi nga xam ne mooy yaqiin ( mooy mu wér la ne li nga nekk ay dëgg,ni ngay xame ne aw xal day lakke boo ko joggee) ak matu lihsaan gi nga xam ne mooy àgg ca Yàlla mu kawe mi, ñatti mbir yile,amewu ma leen, ci lu dul jaxasoo gi ma jaxasoo’k ñoom,te loolu moo daa doon sababu rékki gëm,yal nanu ci yàlla musal.


Ab nettali bu yéemee ngii ma, dégge ko ci Sëñ bi,ci mbirum àttekatub (goornoor) Luga bu rëy te bon,te yoroon woon mbirum tukkib Sëñ bi te taxawoon temb ci mu am. Sëñ bi nee na :( àttekat boobu ,bi ma nekkee ci tukki bi ,laa dégg ñu ne danu koo mujj mere,gëstu ay mbiram,gis ci luy waral ñu génne ko,tumbrànkeel ko,bi niy xalaat,mbugal mi nu ko war a teg,am ku ne kii daal,ginaaw moo taxoon nu génne Sëñ bi tumbrànkeel ko,nanu ko yobb,fa waayam ja nekk, ñu dëppoo ca loola,muy fayyug sunu boroom,yëguma lu dul ñu ne ma àttekat baa ngi ci dun bi ma nekkoon,mu nekk foofa ab diir di ma làqatu ngir ragal ak rus,loolu moo waraloon mu dem gis goornoor (àttekat walla saytukat) ba fa nekkoon,ne ko moytul ma Sëñ bii fi yaw,bu ko jéem a def lenn lu ko naqari,ndax lii ma dal de dara waralu ko lu dul sama yéene ju ñaaw ci moom,kon daal bul def lu dul,di ko jox li nga ko war di fay weer rekk te yam ca .

Loolu moo waraloon àttekat boobu nooyoon mel ne galas fi man,tukki bi, li ci jafe woon lépp mujj yomb. Bi Yàlla sottee ndox ca sawaraam wa doon jëf-jëfi (moom goornooru Luga bi), mu mujj di ku sedd,la nu ko delloo fa mu juge woon,ginaaw bi ñu yobbooti ko ci penku bi,ca wàllug Xaay,foofa la ko ab njabarkat bu bàmbara njabare,ci génn kërug bàmbara, mu dee di ku nu dàkku, di ku nu ngàññ, xoolal ma rekk mujjug ñiy tooñ . Mbirum noonam boobu,niroo’k lool,mbirum noonub ki miy ligéeyal di Yonnant bi (j.y.m),noonam booba di woon Haamir doomi Tufayli,ba mu nee jamono ja ko tawat ja sonnalee ci génn këru jenn jigeen ju Salool: (ndax lii day am mbas mu mel ne mu giléem , te di ag dee ci néegub jigéeni Salool ?).


Sëñ bi def na ag xasida,gu mu tënke arafi {mazalul jannatil latii wuhidal muttaquun , ba ca, tilka huqbal laziinat taqaw }} ne; { tooñ gu nu ma doon tooñ,jeex na,aji not jee ko jeexal,ji damm ngànnaayul ki doon puukarewu, te mu damm)) (Moom de yàlla am na samag cant,ndax rayal na ma ka doon fexe ci atum junni ak ñatti téeméer ak fukk ak ñatt g,te deem gi dolli xalaat yi)) (Amewul ca la mu doon def,lu dul am mbugal,te ginaaw bi mu farloo,ba yaakaar ne moo ci nekk,daa daal di giim,tawat ji gàllankoor ko)) (Fayyug sunu boroom da koo tiital mu daw, ci géej gi ak ci jéeri ji,te am mbooloom wor ko }}.

Jaraaf ju ñuul jooju,xam naa aw turam xam giir gi mu bokk,waaye du ma sobeel sama xalima ci bind aw turam,moo’k mbokkam mu nasaraanu, mi daa ñaawal Sëñ bi ak a saboote,fu mu masa’a daje ak moom,moo nekkoon Garambasaa.

Gis naa li sëñ bi bind ci ñoom ñaar, ñu bari it, ci ñi xam seenug mujj,nettali nanu ma ne ku ci nekk dee gu ñaaw la dee,kenn ki mooy ku jéeri ji,mi ngi Ndakaaru,ki ci des,di ku géej gi,nekk Konaakiri,yal na nu Yàlla musal ak jullit ñépp,ci nattu bi mu leen tegoon.

Nu dellu ci mbirum tukki bi,Sëñ bi nee na kerook wird wi mu gënoon di def,mooy { Inna wàlliyiyal laahul lazi nazzalal kitaaba,wahuwa,yatawallaz zaalihiin}} muy ci maanaa :kiy méngoo samay mbir,mooy Yàlla mi wàcce téere yi,te mooy kiy méngoo mbirum ñu baax ñi. Loolu mooy maanaam waxam jii: {Yàlla naagul na ci man ibliis,fa Jeewal,bi ma ko woowee ci turu walii,(muy kiy méngoo mbir yi) }}.

Sëñ bi fanaan foofa,bi mu julle suba,laxas jëm Kokki, ñu yendu fa,mu tàmbli fa’a woy xasidag Asmaau Ahlul Badri, Sëñ baa ngi wax ci loolu: {ganaaw bunu fa yendoo,moom tàmbli na fa di woy lol ubbil na ko ab bunt }}.

Boobu bisub dibéer la,bi gee jàllee ba teg lu néew,ñu laxas, - ci li ma kenn ci ñi àndoon ak sëñ bi nettali - ci fenkug weer wi,ci guddig altine dëppook ñaar fukki fan,juge Kokki,nee na :booba ñun ñi ngi dox, muy wicc-wiccal ci sunu kaw. Sëñ bi nee na : maa ngi rañaan (mooy dox guddi) kerook ca guddi googa,ci kaw sama wenn ngélamu ñu naa ko Hawnul laah,wu gaaw,nga xam ne fasi ñoñ buur bi manunu ko woon a jot,te ñi ngi doon def li nu man,ba mujj am ci ñoom ñu naan ma:Sëñ bi defal nànk,yëramal sa bopp,te yëram nu,ma naan leen gaaw leen,nu ku nu yilif,ba noppi yonni ko di yeexe? bu ko defee,nu wedam. Sëñ bi def na ci loolu aw woy: {{laxas nanu ginaaw bi nu yendoo,di dox,ca ginaaw gee, ànd ca’akug xat te di ko muñ ) ((Nu àgg,laataa jullig fajar,mu fanaan guddi gi ci yekkati ay bayit ,di boroomug jàjji}. Bayit yi mu doon yekkati, ñooy ñaar yu Busayri yii: (kuy sukkandiku ci ndimbalul Yonnant bi,bu koy gaynde fekkoon cib àll it wedam) (Moom Yonnant bi,foo ko gise ak doonte moom rekk a ànd,da nga naan moo’k am mbooloo ànd ngir,màggam ga ). Li mu jublu ci di boroomug jàjji gi ci woy wi,nag,mooy mu nekk di jàjji fas wi ngir mu gaaw. Ginaaw bi, nu àgg Luga,laataa fajar,yendu fa.


Nettali nanu ne Sëñ bi nee na:bi mu jegee Luga,kenn ci ndawi nasaraan bi,te bokkoon ci ñi àndoon ak moom,wax na ak moom,ci anamug yërmaande,ne ko ngànnaayul,jege nanu noon bi de,Sëñ bi ne ko ci kàddu gu dëgar,yàlla du lòtt,te du des ginaaw,bi nu àggee ba dal,la ndaw li ko doon wax loolu dellusi, ne ko man dey da ma laa wax ngir yërmaande,ngànnayul,jege nanu noon bi,nga ne ma Yàlla du lòtt te du des ginaaw,li nga ma tontu ci sama wax jii de,xawma ko,loo ci jublu? Sëñ bi ne ko maanaam loolu mooy Yàlla (t.s) dara du fàddu ci moom,kon mi ngi ànd ak nun,bu doxee sama diggante ak noon yi,ci kàttanam,dàkku ma wëlif leen,kenn du ma manal dara,bu ma bàyye ak ñoom it, ñu def la leen soob,kenn du ci man dara.{wa in yamsaskal laahu bidurrin falaa kaashifa lahuu ila huwa,wa in yuridka bi xayrin fa laa raadda li fadlihii,} muy ci maanaa bu la Yàlla laalee ak lor,kenn manu koo dindi ku dul moom,bu la nammalee aw yiw it kenn manul a delloo ngënélam. (Yàlla mu sell mi dëgal na,Yonnant bi,jàmm ak xeewal nanu sax ci moom,jòttalee).


Ndaw li dem ànd ak mbégte,man ma ne kooku Sëñ bi daf ko doon leeral haalam (haal mooy melo walla mbir walla aw nekkiin) ak ni mu donne Yonnant bi (j.y.m),Yonnant bi (j.y.m) nee na {wàkkiirlu mooy sama haal,fàggu di sama sunna,ku lòtt ci sama mbir,bu mu lòtt ci sama sunna}},Sëñ bi moom dònn na ci haalam ak sunnaam ab cér bu mag,ak ci haalu Ibraahiim (j.y.m) bi nu ko sànnee ca sawara sa,malaaka yi ñaan ko mu sàkku ci ñoom ndimbal,mu bañ,Jibriil (j.y.m) ne ko ñaan ko,mu ne xam gi mu xam sama haal doy na ma ba du ma ko ñaan.


Sëñ bi Yonnant bi la ciy jikko,di Ibraahima ci yite (j.y. ñ),day jëf haalu Yonnant bi ak sunaam,gis nga haal ji noonu,mu jëfe ko,ma won la nag ag jëfeem sunna si,bokk na ci loolu,moom defal nanu ag xasida gu nu tënke harafi {hasbunaal laahu wa nihmal wakiil}muy ci maanaa Yàlla doy na nu sëkk,te moom de wéeruwaay bu baax la. Mu ne ci xasida gii laa sengewoo woon (senge mooy ta-ta,walla ci tubaab fortification,muy miir bi ñu njëkk ña daan tabax wërale seen dëkk yi,ngir mu leen di aar ci song gu bette,kon sengewu mooy aaru ) ca ngoonug bisub àjjuma ba,ba ma dogoo ci ànd ak ñoom ca gàwwu ba,ginaaw bi ma Yonnant bi (j.y.m) aaree,digal ma ma dem,ne ma wéyal te bul ragal lor.

Xasida gii nag mooy muslaay li,juttit bu ne war na koo jeem a am di ci musloo li mu ragal,bu leen fàtte li ñenn ñiy wax naan,waxtuw ajjuma mi ngi dale ca ginaaw tàkkusaan,ba bu jant bi sowee,xasida gi nag mooy gi tàmblee hamidtu man yahsimunii minad darar, muy : {maa ngi sant ki ma musal ci lori jépp saytaane ak jinne ak nit) (Tudd naa sellam ga,muy buur,buy aji wattu,may sàkkoo aaru ci wattoom gi wëlif musiba yi ak mbugal yi)) (Maa ngi sàkku ci moom mu musal ma ci bànneex,ak ibliis,ak ci mbooleem yiy lore ci jamono ju nekk)) (Yéene naa koo ñaan di sàkku am ramu,ci darajay soppeem bay ramu ñiy ramu)) (Mooy Ahmad,sangub mbindéef yi,may julli ak a sëlmal ci moom,te di ko def aw yoon jëm ca sama boroom)) (Maa ngi ñaan ,sama boroom,ci darajaam,mucc ci saytaane ak ciy ñaawtéef,ak way bew yi di ma xëccoo)) (Ya’a moom mbindéef yi ,yaw sama boroom,may ma ag mucc ci ñoom,ak bépp balaa ak mbugal)) (Yaw laa jox sama bopp de,yaw aji wattu ji,ba fàww it ya’ay sama wettal)) (May ma li ma bëgg ci adduna ak alaaxira,na nga ma musal it ci gàccag àdduna ak gu allaaxira)) (Jubale naa la sama kanam,yaw sama boroom,ya’ak sama wasiila,te loolu doy na ma)) (Musalal samag wàll ci mbooleem luy ñaaw,te nga fegal ma mbooleem luy jax-jaxiloo)) (Soril ma mbooleem noon yi ,ci barkeb Yonnant bi,ak Ahlu Badri ñu tedd, ñiy ay tànnéef)) (Na nga ma xeewale ci ma dugg ci sa senge (kaaraange) lu aaru li,te dëkk fa,di ku am kóolute ci samay noon)) (Yaw’ay kiy musal kuy muslu ci yaw,ci lépp lu ko man a jublu ciy mbugal)) (Samay mbir ba fàww da ma koy joyal jëme ci yaw,ndax ya’ay ki nga xam ne ku wéeru ci moom deesu ko jalax)) (Yaw aji baax ji,fegal nga ma ag kéefar,ak lori ñoñam,ak jépp fitna)) (Fegal ma loxol way bokkaale yi,ci darajay Ahlu Badrin,te nga def leen ñuy sama senge)) (Yaw aji baax ji,nekkal ma te bu ma gàccaal,ci àdduna ak àllaaxira,te dee ma jéggal)) (Bindalal Yonnant bi ag xéewal ak mucc,ak ñoñam aki saabaam,ci anam gu sax.}} Mu tëje ko { fanqalaboo bi nihmatin minal laahi wa fadlin,lam yamsashum suuhun,wattabahuu ridwaanul laahi wallaahu zuu fadlin haziim}}: muy ci maanaa, ( ñu dellu ànd ak xéewalug Yàlla ak ngënéelam,lu ñaaw laalu leen, ñu topp ngëramul Yàlla te Yàlla’ay boroom ngënéel lu mag li).



Mu neeti { alhamdu lillaahil lazii hadaanaa lihaazaa,wamaa kunna linahtadiya law laa an hadaanaal laah,wa aaxiru dahwaanaa anil hamdu lillaahi rabbil haalamiina}} muy ci maanaa : ( maa ngi sant Yàlla mi nga xam ni,moo nu gindi jëme nu ci lii ( muy lislaam) ,duñu doon gindiku bu nu Yàlla gindiwutoon,sunu wax ju mujj,mooy ag cant ñeel na Yàlla,miy boroom mbindéef yi) . Xoolal ni mu aaroo woon ci baat yii nga xam ni,Yàlla da leen a tagg,tagg it nit ñi ciy aaroo.

Mu wax:{allaziina xaala lahumun naasu innannaasa xad jamahoo lakum,faxsawhum,fasaadahum iimaanan,waxaaluu hasbunaal laahu wa nihmal wakiil ba fam yam}}muy ci maanaa :( ñi nga xam ne nit ñi dañu ne leen: nit ñi kat dajaloo nanu ngir fexeel leen,kon tiit leen te moytu,loola dolli leen ag ngëm, ñu maase ne Yàlla doy nanu ,te doy na sëkk ku ñu doyloo). Nga boole ca loola juroom fukki bismil laahir rahmaanir rahiimi, yi mu jàngoon ca Jeewal,ba ndawul nasaraan bi bëggee wax ak moom.

Waxees na ma ,te loolu lu wér la,ne rakkam ja sheex Ibra Faati, ci bis bi Sëñ bi tukkee,ba bi mu dellusee,masul a dañ di def junniy salaatu alan nabii ci melo wii:( allaahuma salli halaa sayyidinaa muhammadin,wa halaa aali sayyidinaa muhammadin,salaatan tunajjiinaa bihaa min jamiihil ahwaali,wal aafaati,wa taqdii lana bihaa jamiihal haajaati,wa tutahhirunaa bihaa min jamiihis sayyiaati,wa tarfahunaa bihaa hindaka ahlad darajaati wa tuballixunaa bihaa aqsal xaayaati min jamiihil xayraati,fil hayaati wa bahdal mamaati)). Maanaa mi di:( yaw buur bi jullil ci sunu sang Muhammad,ak ñoñi sunu sang Muhammad,ag julli gu da nga nu ci musale ci mbooleem tiitaange yi,ak gàkk-gàkk yi,fajale ñu ci mbooleem aajo yi,laabale ñu ci, ci mbooleem ñaawtéef yi,yekkatil ñu ci gën jaa kawey daraja fa yaw, àggale ñu ci ca dayo ya gën a sori ci mbooleem yiw yi,cig dund ak ginaaw ag dee).

Mu ko daan def ginaaw bu wàccee kaamil bi,waaye kaamil bi moom lu saxoon la,suba ak ngoon,naka jekk, njëkk Sëñ biy tukki,waaye salaatu halan nabii gi moom saxal gi,man na a nekk muy ndigalul Sëñ bi, mbaa xalifaam bu baax,bu sell ba,ngir xér gu mu defoon ci muccug Sëñ bi ak ag delluseem ci jàmm,mu sàkkaloon ko mbooloo mu ci daawul sàggan suba ak ngoon,waxambaane wu ragal Yàlla,wu dëkkoon Kokki wii di Samba Joop nu gënoon koo xam ci Samba Asta daan leen jiite.

Ku baaxoon la te gudoon aw fan,mi ngi faatu ci atum waafiris sitri,di junni ak ñaat téeméer ak fukk ak juroom ñatt,bokk na ci loolu woy gi mu def Ahlu Badrin,ak aaru ci ñoom,bi mu nekkee Ndar,mu mottali ko, tudd itam ànd gi mu defoon ak ñoom ci tukkeem boobu, ñu daa toroxal képp ku ko daa jéem a lor,téere boobu,jotoon na koo won ca magi Ndar ya ka ñu naan Alhaaji Muhammadu Maabéey,ne ko mu mokkalandi bayit wu njëkk wa,ba ñu dajewaat ginaaw bu ñibisee.

Te kat dajewaat nañu ginaaw juroom ñaari at ak ay weer,bi nu dajee sëñ Maabeey jàngal ko bayit wi,daal di daanu ab jéll,jooy. Ak leneen ak leneen ci li mu aaroo woon te xamunu ko, degg naa ko bis mu naan: bi mu nekkee ci géej gi,masul a dañ di jàng Hisbul Bahri,bu imaam Shaazalii,muy lu am njariñ,li koy wone mooy yitewoo gi ko Sëñ bi yitewoo woon,bayit wi mu digale woon mu wattu ko,mooy njëlbéenug xasidag Asiiru gu yéeme,gi nga xam ne Sëñ bi feeñal na ci njëlbéen gi,ba ci fukk ak juroomi bayit,lenn ci mbóoti tukkeem bi ci diganteem ak noon yi,ak wone ci mucc gu mu mucc ci seeni lor,xamale ne saytaane moo leen wor ci moom,tax ba ñuy am njort yu ñaaw ci moom,waaye seen njort yi sooy nañu,te Sëñ bi dellusi na ci jàmm,bayit yee nekk nii: {maa ngi dox ànd ak ñu baax ñi (waa Ahlu Badri),bi may dox (bi may tukki),waaye noon yi jort ne man booba ku ñu njaf (jàpp) laa )) (Sama dox bi may def, ci wommatug Yonnant bi, ànd ci ak gaa yu baax yi,Yàlla rekk a ko tax a jug,ba fàww it samab dox du jëm ci ku dul Yàlla)) ( Bijji gi ma wommat (bijji mooy jazbu,di lol day xëcc,kon man nanu koo jàppe yitewoo sunu boroom gi nga xam ne daa mujj mel ni ab asyee bu koy ñoddi jëme fa Yàlla) jëme ma ci aji tedd,joj lu ma sàkku ci moom mu jàppandi,mooy liy dox ak man )) (Samag cant ci xalima,ak ci xol ak jëmm, ñeel na ki ma nekkal cig tab ( ki nga xam ne jamono ju nekk mi ngi may sottil ay xéewalam ) te mooy ki di ab santaakon (ku soxlaalul kenn) )) (Sama ndimbal,samag dëgëral,sama kaaraange ca noon ya,mi ngi bawoo ci Aji yaatu,ji di ab Mayewaakon,(ku tabe lool) kooku mooy aji dimbali sama )) (Sama kilifa nag, ci bu may dox ak bu ma taxawee,mooy sama kerkeraan,di Yonnant bi,te mooy ki may ligéeyal,te moom dey day xont (mooy jox ab dund) ku koy ligeeyal)) (Samab yool ci ligéey bi may defal Ku nu tànn ki,di Yonnant bi, mayewaakon (Yàlla) bee ko warlu,te moom ku am lu mu faye la)) (Li ma nesar nag mooy nekk jaamub boroom Aras rekk,di ligéeyal gën ji mbindéef,te moom Yonnant bi mooy samab xuppkat (Yonnant bi day bashiir tey naziir,di kuy bégale tey xuppe ngir jaam yi bañ a sàggan bañ a naagu ) )) (Aji feg jii di Yàlla,moo may fegal ci Yonnant bi,ayi noon yi,ak lépp lu ñaaw te mooy ki may xettali)) (Samag mujj mooy nekk dib jaamam,di ligéeyal Yonnant bi,mbiri mbindéef yépp nag ca Yàlla lay mujj )) ( Samay weer aki bis ëlëg ñoo may seedeel nekk gu ma nekk di jaamub Yàlla,te moom siw na )) (Samay sutura ci adduna ak allaaxira,mooy tagg Yonnant b,ci woy ak wesar,te moom suturaalkat bu baax la )) Samaw jiwu mooy téereb Yàlla bi ak sunna si nga xam ne ci laay aaroo ci li yaqkat bi jublu (muy saytaane) )) (Samay kër wéet na, ñoñ ñi tas,ngir tagg Ki nga xam ne,noo ko man a tagge,du tax tagg wi mat )) (Woru gi nekk ci mbindéef yi,wor na nasaraan yi,ciy pexeem, ñu jort ay njort,te njort ak woru la}}.



Sëñ bi nee na : ginaaw bi nu jullee tàkkusaan,lanu dugg ci saxaar gi,jëm Ndar, ñu àgg Ndar bi jant biy bëgg a so,ci loolu Sëñ ba’a ngi ciy wax naan: {Yàlla ca bu njëkk,la dàqoon samay nëx-nëx, ca Ndar jëme leen ci ku dul man,ci barkeb Ahlu Badrin ña diy gaynde)) (Ñu àndandoo, sax ca dun (île) ba akub coona,fuglukat ya di ñu fa bari}}. Ma sax fa - sëñ beey wax - la desoon ca safar,muy fukki fan,ak weeru rabiihul awal,ba ca bis bu mujj ba,muy bisub alximis, ci diir boobu laa matale woyug Asmaau Ahlu Badrin, muy turi waa badar ,topp ko,wéral ko,ci la’a dajee it ak ñu bari ci kilifay Ndar yi,ak li ko wër,kuréel it ci njiiti Njaambur yi seetsi ma ngir tinusi ak ramusi,ci tubaab bi,ma ne leen bàyyi leen ma ak sama boroom rekk,moo leen ëpp ñeewant ci man,gën leen a xam li gën ci man, ñu far taxawlu.


Nee nanu bi nu ko taxawalee ci seen kanam,wax ak moom,ci teewaayu kilifay nasaraan yi,te booba moom ku wéet la woon ci seen biir,amu fa ab xarit du caagéenug aw wéttal,nu ne ko wax nañu nu ci yaw nàngam ak nàngam ? Sëñ bi ne leen indil leen ma ki leen ko wax,ba xam ma’ak moom ku ciy ki wax dëgg!. Te booba li nu doon wax naan moo ko def,ab dof bu amut am xel sax du ko def,waxantu ma la’ak ku mel ni moom, li am daal rambaaj la gu juge ci ñu kañaan lëjal,ba ñu mujj amatuñu kersa ci Yàlla,saytaane yàq seeni xel,jox leen xalaatam yu ñaaw,ba nu mujj di rambaaj ak a tudd ciy ñaawtéef aki caaxaan lol ñi gën a dof ci wutkati àdduna yi sax,xalaatunu koo bëggal seen bopp,mbaa ñu koy soxla,waxantu ma la’ak boroom xel yu dëddu yi àdduna.


Ca bis ba ma war a juge Ndar jëm Ndakaaru,te booba ma nga woor, àgg fa njëkk jant biy so, ñu wàcce ko fa, ca genn kër,mu tàmblee waajal dog ak julli,waaye ñu jekki-jekki rekk lenn ndaw teew,ne ko ayca ñu dem,Sëñ bi jug ànd ak moom,waa ja yobb ko ci néeg bu deesi muslu,lëndam kariis,tàng jérr,xeeñ xunn.

Bi Sëñ bi gisee li wàcc ci moom,mu xam ne mooy nattub Yàlla bi ko doon xaar,amu ci am pexe mu dul gàddu ko,te muñ te sant Yàlla te gëram ko,ndax doon na sentu lu gën a réy loolu,mu dal ni innaa lillaahi wa innaa ilayhi raajihuun. Sëñ bi nee na ma fanaan fa dundal guddi gi ci saari Baqara ak Aali Himraan, ñu feg ma ñoom ñaari saar yooyu,ci ñaari sawara yi ak ñaari gàcca yi,ma teg ci julli ci Yonnant bi (j.y.m) ki may ligéeyal,sama dënn leer,sama xol dal,kóolute gi dolliku ci Yàlla’ak Yonnant bi,ndax {{ alaa bizikril laahi tatma-inul xuluub } ci tudd Yàlla ak fàttaliku ko,la xol yi di dale.

Sama gudd gi daal di neex ci Yàlla, ak ci aji sabab jii, ak dëkk bi,ak ci néeg bi. Ci loolu sëñ baa ngi naan: { Yàlla dàq na jëme ci ku dul man ca Ndakaaru,wépp ay wu pexewaakon (ki bari ay pexe ) bi xëccoon jëme ci man)) (Bu ma fattalikoo panaan moomee,ak njiit loolee,ak sax ga,sama xol day naaw ak man jëm ci jëli xepp aki gobar ngir jiyaari,waaye Yonnat bii di kiy fari bàkkaar,dox sama digante ak loolu ))