Tuberculosis

Jóge Wikipedia.

Tuberkiloos (TB) feebar la buy wàlle, te li koy faral di joxe mooy doomu jàngaor bi tuddu Mycobacterium tuberculosis (MTB).[1] Cër bi tuberkuloos di ngëna jàpp mooy dënn bi, waaye mën na dem ba laalaale yeneen cër ci yaramu nit ki.[2] Barina lu muy dal nit te du feeñ, loolu lañuy woowe tuberkuloos bu nëbbatu.[3] Lu tollu 10% feebar yiy nelaw yaramu nit ki, dañuy dem ba daaneel nit ki, suñu ko fajul, mën na dem ba faat ki mu dal.[4] Beneen tuburkuloos bi nelawul moom dafay wane boppam, kumu dal dangay am sëqët mu tar àndaale ak lumbi deret, yaram wu tàng, ñaqu guddi, ak yaram wuy jeex di dem.[5] Di nañu koy faral di woowe feebaru "ŋacci" ndax limuy ŋacci sa yaram.[6] Amna yeneen anam yu muy feeñee su laalee yeneen cër yi.[7]

Tuberkuloos dafay tasaaroo ci ngelaw li, suede tuberkuloos bu tar moo la jàpp, soo sëqëtee wala nga tifli wala nga wax, wala nga tissooli mën nga ko wàlle.[8] Nit ñi feebar bi di nelaw ci seen yaram du ñu wàlle feebar bi.[9] Nit ñi gëna mëna wàlle feebar bi mooy ñi am VIH/SIDA ak tóxkat yi.[10] Ngir saytu jàngoro ju tar ji ci yaram nit, dañuy rajo dënn bi, dañuy jël itam ndox mu bawoo ci moom ñu xool ko ci microscope wala ñu amal ci njàngat mu xóot.[11] Sudee tuberkuloos biy nelaw nak, ci deru nit ki wala ci deretam.[12]

Suñu bëgee aar nit ñi ci feebar boobu, nañuy saytu bu baax ñi nekk fumu leen mëna dalee, teela gis doomu feebar bi ak teel ko faj, ak jël ñaq bii di Bacile Calmette-Guérin (BCG).[13] Nit ñi feebar bi gëna yab ñooy ñiy liggéeyandoo ak ki ko am, ñi mu bokkal kër, workplace, ak ñi muy nekkal bis bu nekk.[14] Paj mi dafay yàgg lool, te ay àntibiotik lañu koy defee.[15] Doomu jàngoro bi daa tàmbali ñeme garab yu bari (MDR-TB) ak doomu jàngoro yi ñeme yeneen garab bi (XDR-TB).[16]

Ci atum 2018, ñeenti nit ñoo jël xalaat nañu ni kenn ka amna tuberkuloos.[17] At mu nekk dina am lu tollu ci 1% ci nit ñi ci àdduna bi ñuy am doomu jàngoro ji.[18] Ci atum 2017, amoon na lu ëpp 10 milion ci nit ñu am feebar bi, ci ñooñu amna ci lu tollu 1.6 milion ñu ci ñàkk seen bakkan.[19] Loolu moo ko def feebar bi dàqa ray ci feebar yiy wàllaate.Lu ëpp 95% nit ñi mu faat ci réew yu néew doole yi lañu dëkk, lu ëpp 50% Inde, Chine, Indonesie, Pakistan, ak Philippines.[20] Seetlu nañu ni li ko dale atum 2000 ba leegi wàllaate gi dafay gëna wàññeeku at mu nekk.[21] Nit ñi saytu ndax am nañu tuberkuloos am déet, 80% ci ñoom dañuy am feebar bi suede ci Asie ak ci Afrique waaye suede ci Etats Unis 5–10% ci nit ñi ñuy saytu ñoo koy am.[22] Ca jamonoy maam ya ba leegi tuberkuloos a ngi am.[23]


Cosaanu gëstu bi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

  1. "Tuberculosis Fact sheet N°104". World Health Organization (WHO). October 2015. Archived from the original on 23 August 2012. Retrieved 11 February 2016.
  2. Ferri, Fred F. (2010). Ferri's differential diagnosis : a practical guide to the differential diagnosis of symptoms, signs, and clinical disorders (2nd ed.). Philadelphia, PA: Elsevier/Mosby. p. Chapter T. ISBN 978-0-323-07699-9.
  3. Hawn TR, Day TA, Scriba TJ, et al. (December 2014). "Tuberculosis vaccines and prevention of infection". Microbiology and Molecular Biology Reviews. 78 (4): 650–71. doi:10.1128/MMBR.00021-14. PMC 4248657. PMID 25428938.
  4. Organization, World Health (2008). Implementing the WHO Stop TB Strategy: a handbook for national TB control programmes. Geneva: World Health Organization (WHO). p. 179. ISBN 978-92-4-154667-6.
  5. Harris, Randall E. (2013). Epidemiology of chronic disease: global perspectives. Burlington, MA: Jones & Bartlett Learning. p. 682. ISBN 978-0-7637-8047-0.
  6. Tuberculosis (TB)". World Health Organization (WHO). 16 February 2018. Retrieved 15 September 2018.
  7. "Global tuberculosis report". World Health Organization (WHO). Retrieved 9 November 2017.
  8. The Chambers Dictionary. New Delhi: Allied Chambers India Ltd. 1998. p. 352. ISBN 978-81-86062-25-8. Archived from the original on 6 September 2015.
  9. Dolin, [edited by] Gerald L. Mandell, John E. Bennett, Raphael (2010). Mandell, Douglas, and Bennett's principles and practice of infectious diseases (7th ed.). Philadelphia, PA: Churchill Livingstone/Elsevier. p. Chapter 250. ISBN 978-0-443-06839-3.
  10. "Basic TB Facts". Centers for Disease Control and Prevention (CDC). 13 March 2012. Archived from the original on 6 February 2016. Retrieved 11 February 2016.
  11. Konstantinos A (2010). "Testing for tuberculosis". Australian Prescriber. 33 (1): 12–18. doi:10.18773/austprescr.2010.005.
  12. "Tuberculosis". World Health Organization (WHO). 2002. Archived from the original on 17 June 2013.
  13. Kumar V, Abbas AK, Fausto N, et al. (2007). Robbins Basic Pathology (8th ed.). Saunders Elsevier. pp. 516–22. ISBN 978-1-4160-2973-1.
  14. Lawn SD, Zumla AI (July 2011). "Tuberculosis". Lancet. 378 (9785): 57–72. doi:10.1016/S0140-6736(10)62173-3. PMID 21420161.
  15. Schiffman, G (15 January 2009). "Tuberculosis Symptoms". eMedicine Health. Archived from the original on 16 May 2009.
  16. Gibson, Peter G. (ed.); Abramson, Michael (ed.); Wood-Baker, Richard (ed.); Volmink, Jimmy (ed.); Hensley, Michael (ed.); Costabel, Ulrich (ed.) (2005). Evidence-Based Respiratory Medicine (1st ed.). BMJ Books. p. 321. ISBN 978-0-7279-1605-1. Archived from the original on 8 December 2015.
  17. Behera, D. (2010). Textbook of Pulmonary Medicine (2nd ed.). New Delhi: Jaypee Brothers Medical Publishers. p. 457. ISBN 978-81-8448-749-7. Archived from the original on 6 September 2015.
  18. Halezeroğlu S, Okur E (March 2014). "Thoracic surgery for haemoptysis in the context of tuberculosis: what is the best management approach?". Journal of Thoracic Disease. 6 (3): 182–85. doi:10.3978/j.issn.2072-1439.2013.12.25. PMC 3949181. PMID 24624281.
  19. Jindal, editor-in-chief SK (2011). Textbook of Pulmonary and Critical Care Medicine. New Delhi: Jaypee Brothers Medical Publishers. p. 549. ISBN 978-93-5025-073-0. Archived from the original on 7 September 2015.
  20. Golden MP, Vikram HR (November 2005). "Extrapulmonary tuberculosis: an overview". American Family Physician. 72 (9): 1761–68. PMID 16300038.
  21. Ghosh, editors-in-chief, Thomas M. Habermann, Amit K. (2008). Mayo Clinic internal medicine: concise textbook. Rochester, MN: Mayo Clinic Scientific Press. p. 789. ISBN 978-1-4200-6749-1. Archived from the original on 6 September 2015.
  22. Southwick F (2007). "Chapter 4: Pulmonary Infections". Infectious Diseases: A Clinical Short Course, 2nd ed. McGraw-Hill Medical Publishing Division. pp. 104, 313–14. ISBN 978-0-07-147722-2.
  23. Jindal, editor-in-chief SK (2011). Textbook of Pulmonary and Critical Care Medicine. New Delhi: Jaypee Brothers Medical Publishers. p. 525. ISBN 978-93-5025-073-0. Archived from the original on 6 September 2015.