Totaasoro

Jóge Wikipedia.

Totaasoro xeet la ci xeeti acacia. Garab gi amna Senegaal, Kamerun, ba ca Réewu Diggu-Afrig.

Melo wi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Totaasoro garab gu am ay dég te ndaw la, guddaayam man naa toll ci 8 jàpp 9i met.

Ay xobam dañuy sew, seen guddaay man naa toll ci 3 jàpp 7i sàntimet. Garab gi mi ngi jebbi ci taw yi jëkk, walla lu ko jiitu tuuti.

Njariñ yi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Garab gi dees na ko jëfandikoo ngir faj biir buy daw ak jafe-jafey mbàq, ak ku jaan màtt. Bantam dees na ko jëfandikoo ci liggéeyu tabax, di nañ ko def itam matt di ko taale, mbaa këriñ.

Nataal yi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Turu xam-xam wi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Acacia dudgeoni