Tojj

Jóge Wikipedia.

Tojj Garab la gog ci barab yu wow yi la ëppe ak ci digg Afrig ( Tógoo, Sudaan, Eritere, Senegaal, Tansani, Càdd... ) ak "penku-digg" , "Asi gu naaje" ak ci barab yi néewub taw. Ab guddaayam day àgg ba 10i met.

Ay xobbam day man a yàgg lool (gudd fan). Ci ndox yu taa yi lay saxe.

Tojj bi


Melo wi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Tojj day gudd lool, te njobaxtal la mel ni lu wërnbalu, am i cat.

Am xàncam day yor melow baam, day nooy, mel ni waasintóor yu jën.

Tojj day bari ay wànqaas yu ndaw, Xob yi da ñuy tegaloo, nooy it, am i gaañu-gaañu.

Tojj xet gu neex la am. Doom bi day tuuti te wex xàtt.

Njariñ li[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Am na ñuy jëfandiko doom bi ak ug wexam.

Xob yi it dees na ko def ci ñam.

Xob yi dees na ko wal def ko sunguf di ci saafara ay jàngoro yu ci mel ni safoodi lekk. Day fajj it ag coono.

Xanc mi day faj góom. Xob yi it day faj biir buy daw, buy metti ak sibbiru te day yokk ngóora ak jàngoroy sëy.

Xob yi it jur gi it dañ koy lekk

Nataal[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Meññeef


Meññeef


Turu xam-xam wi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Maerua angolensis