Tiir
Apparence
Tiir xeet la ci xeeti garab yu gudd yi ne sóll. Mu bari lool ci tundu Afrig, Ecopi, Afrig bëj-saalum. Di nañ ko fekk batay ci digg Afrig, fu ci mel ni Saara, walla Namibi.
Melo wi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Tiir garab la gu baaxoo wéet. Guddaayam danay àgg ba 25i met. Yaatuwaayam nag danay àgg 1 met, Xobam melo uppukaay la yor te guddaayam di 2i met. Feggam daa am i dég.
Tiir, day am bu góor ak bu jigéen, bu jigéen bi ay xobam dana jàpp ci 260i sàntimet ci yaatuwaay. Day jur benn foytéef bu doom ba mboq, ci biir foytéef woowu dina am benn ba ñatti doom.
Njariñ
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Garabug tiir bari na ay njariñ lool ay xobam dañuy tàkk ñu man cee toggu. Manees na cee def tam it sàngara Doom bi daa neex lool nit ñi dañuy koy lekk
Turu-xam-xam
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Borassus aethiopum