Taysiirul Hasiir

Jóge Wikipedia.



Daaray Taysiirul Hasiir bu Sñ Moor Jóob Ndar:[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Taysiirul Hasiir: daaray Alquraan la ju mag, ju nekk ca réewum senegaal . mingi sosu ci atum 1953, ki ko sos mingi tudd Sëriñ Moor Jóob Ndar dëkk foofee ca Ndar.




Senegaal naka jekk da ñoo masa fonk njàngum diine moo tax diiney lislaam am fi doole lool dale ko ca bañ tànnee lislaam muy seen diine ba leegi,ci ndimbalu Yàlla jaare ko ci Sëriñ si ak nitu diine yi ñu daa taxawal ay daara ngir jàngale ak yar,daara yooya daa génne ay kurél yu takku yu Fees dell ak xam-xam ànd ak mokkal Alquraan loolu nag mujj doon jikkoy Saa Senegaal yi ba at mu jot ay téemeer i téemeer di mokkal ciy gox yu fasantikoo ak i dëkk yu ndaw-ndawaan yi.

Dëkkub Ndar nag bokkoon ci dëkk yi gënoon a fes ci xam-xam,la ko dale ca ba Senegaal moomagul boppam ba tay jii,boroom xam-xam yu bari foofa lañ jànge, te sun mag ñi ñi ëpp ci ñoom jaar nañ fa, ba leegi téewul muy dëkkub daara di dëkkub xam-wam.la fa ne ciy daara kenn xamul num toll,bokk na ca daara ya fa gën a ràññiku te gën faa rëy "di daara joj ju yàgg la ju ubbiku ju wéet ciw njàngaliinam ju cosaanu"muy:

Daaray Taysiirul Hasiir bu Sëriñ Moor Jóob Ndar

Kan moo sos daara jooju?[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Amul sikk-sàkka ci ne mépp mbir mu yékkatiku am na waa ju kawe ju nekk ca ginnaaw kok boroom pas-pas la,boroom yitte ju kawe la,ndaxte Yàlla day tànn saa su ne ku ko taxawul diineem ji,di ko tasaareel ab wooteem.bokk na ca ñam tànn ngir loolu *Sëriñ Moor Jóob Ndar* mu boole ko ca ña nga xam ne dañuy sàmm ak lu leen ca man a fekk;doon ay sondeel yuy lakk seen bopp ngir leeralal jullit ñi yoon wi.Sñ Mustafaa Jóob didoomam waxam ja akay dëgg bam nee :Aji sàmm ndonol way jiitu ya,kenob dëgër ci kanamu /jafe-jafe yi,Aji yar maas gi mooy mooy Sñ Moor Jóob.

Ngir xam kuy Sñ Moor Jóob danuy tuxal jële ci doomam juñ naa Siidi Abdallaa Jóob Yal na Yàlla sàmm ko ci mbindam mum bindoon ciy jaar-jaaram duppe ko(الشيخ مور جوب مؤسس معاهد)

Aw Askanam:[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Sñ Moor Jóob boroom xam-xam la dib faqiih di ku dëddu Àdduna dib yarkat bob dundam gépp ci léggéeyal Alquraan la ko jeexal ak waa Alquraan,moo sos Daaray Taysiirul Hasiir, di doom ci Muhammat Faati Gay Jóob,miy doom i Mbay Binta Faal,miy doom i Moor Maanta doom i Aale Soxna Sow; mi sanc Belal Jóob ci ndigëlal doomu magam jii di Sñ Maxtaar Ndumbe Jóob Kokki Bu dee yaayam mooy:Soxna Roqayya Jóob di doom i seex Muusaa Roqayya Jóob,kenn ca Jàmbaari nitug Yàlla kookee tudd Sayxu ka doon xeex ngir yékkati Lislaam,faatu ca atum/ 1875 m.

Ñaari way-juram yii nag ñi ngi bokkoon ci Askan wu amoon diine taqoo ko te amoon ak sàmm,di askan wuñ xam ci farlu ak yéwén ak yéwénal.



Ab juddoom:[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Sñ Moor mi ngi gane Àddina ci atum (1926)m,ci dëkk buñ naan Kër-MaantaJóob,digganteem ak Luga 22i Jun-ñay la(km).

Tolluwaayu daara ja ca Ndar cig nattale:[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Daaray Taysiirul Hasiir mi ngi ci ndar ci kace bu tudd (Soor-Dàgg), te xaw naa jege /Gaaraas/ bu mag bi ci buntu dëkk bi. Boo demee ba jege *Ndar* da nga gis ñeenti sooroori Jumaa foofa ngay jublu, boo fa àggee rekk xamal ne àgg nga ca dara ja jumaa jooju mooy jumaay Sñ Moor Jóob boroom Taysiirul Hasiir, digganteem ak daara ja tuutee fa dox; boo ko laajee sax ñu wan la ko,foofa ba daara ja wenn yoon la. Buntu daara ja ñuŋ ca bind :

   "معهد تيسير العسير لتحفيظ القرآن الكريم وتدريس العلوم الشرعية"

Ak waxi Yàlla jii(فلولانفرمن كل فرقةمنهم طائفةليتفقهوافي الدين ولينذرواقومهم إذارجعواإليهم لعلهم يحذرون)



Taariixu sosug daara ji ak ay Jaaruwaayam[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Sëriñ bi mi ngi sanc daara ji ci ndigalal Nijaayam ji ko yar tudd(Sñ Jibriil Jóob) "yal na ko Yàlla yërëm"ci atum /1954. Mi ngi tàmbalee jàngale ci Karce bu tudd (Balakoos) ca Ndar, ginnaaw loolu tuxu na dem Karce buñ naan (Jàmm-Gën) ci atum/1957,ba ci atum/1977 mu tuxuwaat dem (Soor-Dàgg) foofu la nekk ba leegi. Kon daara ji mi ngi sosu ci atum /1954, am ñatti jaaruwaay ci biir dëkkub Ndar, ba ca mujj di (Soor-Dàgg) te foofa la nekk sax fa ba leegi, kon daara ji am na ciy at lu ëpp 60i At.



Séddalikoog Sémbi(porogram)Njàngalem daara ja:[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Daara ji nag dafa séddalikoo ci ñaari jàngu ; jàngub Alquraan :muy jàngu bi nga xam ne Alquraan rekk leesfay jàng, te mooy cosaanu daara ji, jàngal ay jëmm bañ mokkal Alquraan ˊmoo xam ay mag wallay gone. Njàng mi nag jàngalekat bune ak sab géew, géew yoy dees leena séddale ci biir xaaji jànguy Alquraan bi. Xaaji jàngub Alquraan bi nag mooy yii:

Basaru lanwaar, Daarul xuduus, Daaru tansiil, Daarul haliim, Daaru salaam, Jànnatul mahwaa. Jàngub Alquraan bii nag ki ko jiite mooy Sëriñ Jibriil Jóob dibdoomi Sñ moor Jóob.

Beneen jàngu bi nag jàngub xam-xam la; maanaam Majaalis bob dees fay jàngale xeeti fànni xam-xami sariiha yépp muy: Fiq, Nahwu, Adab, Usuul, ak làkku Araab ak yeneeni fànn. jàngub xam-xam bii nag da cee wàllisi rekk waaye jubluwaayu daara ji moo doon jàngale Alquraan, ndaxte ku mokkal Alquraan ku ne da nga soxlawoo xam-xam, sëñ bi moo ko njëkk a daa jàngaleel boppam xam-xam, waaye bim demee ba Mage manatulu ko boppam, loolu waral dongo yi daa génn di ko sàkku ji feneen. Waaye bi Taawam Seex Ahmadul Xayri Jóob ñibbisee bawoo cim njàng "di boroom xam-xam bu mag dib Fóore yal na ko Yàlla sàmm, mu far gàlloo njàngalem xam-xam mi. Loolu moo sos jàngub xam-xam bi, te ba leegi moom moomu moo fay jàngale. Bam femee ba jëmmi jamono njàngiin mu bees mii xew, te aju ciy këyit mu wutal ñiy jàng xam-xam fuñuy jànge jàngum Ekool diggante Araab ak Farañse, te loolu doomam juñ naa Doktoor Seex Maalig Jóob moo koy taxawu ñu gën koo xame ci Seex Maanta, ba loola tay jii mujj na soppikub Ekool. Sñ Moor Jóob Dana farala wax lu bari naa"Amumay doom ay dongo laa am!!!


Njàngaliinu xam-xamu daara ji:[Soppisoppi gongikuwaay bi]

daara ji nag njàngum xam-xam mu dëgër moo fa ne, mu kawe lool it ci xeeti fànni xam-xam yees fay jàng yépp, day tàggat dongo bi ba fum dem dees koy naw ngir bari xam-xam. Loolu nag di wane ndimbalal Yàlla lum defal Sñ Moor. Képp ku fa jànge ba jeexal Sémb wa boroom xam-xam ngay doon bu mag, bu kenn dul nàttable ab xam-xamam rawatina xam-xam Fiq ak Nahwu ak luxa, téere yuvam solo lees ciy jàng, jaare ko ci yoon wu jub it ba dongo bi xëy doon Fóore ju mag, te lu ci nekk rekk day tàmbalee ci téere yu suufe yi ba ci téere ci gën a kawe.


Ëllëgu Daara ji ak ubbik gox ñeel ay Dongoom:[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Daara ji tërël na ab Tëréef ngir Ëllagu ay dongoom, bu njëkk da daa génne ay ndongoom di leen yóbb ca jàngub (Hanafiya) waaye leegi ñi nga xam ne seenum njàng kawe na dees leeni may ay këyit ngir ñu man a àggale seenum njàng ca daara yu kawe ca *Marog* ñu di fa jàng ba am Mastéer Walla sax Doktooraa.ci gàttal daal mooy ba jeexal, moo ñu bari jàng nañ ba noppi déllusi ubbi seen daara, ñu bari tudde seeni daara Taysiirul Hasiir, daara yooyu yépp diy bànqaas yu cosaanoo ci daara ju mag jii *Taysiirul Hasiir bu Sñ Moor Jóob Ndar* kon nag nu tuddal leen lenn ci daara yi nga xam ne ay bànqaas lan ci daara ji tey wuyyoo aw turam.


Bànqaasi daara ji:[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Sëriñ bi nag bu weesoo daaraaam ji am na ñu bawoo ci daaraji mu sampal leen daara, te daara yooyu mu sampal ay nit nag nekk ciy gox yu fasantikoo ci biir Senegaal diggante: Dakaar, Cees, Lugë, Tuubaa...am na ci yeneen it yoy ay nit a juge daara ja góor-góorlu ba taxawalal seen bopp daara tuddee ko *Taysiirul Hasiir* ngir fa la ñu jàngee ca daaray Sñ Moor. Daara yooy nag danañ ci tudd yennat tuxale ko ci Siidi Abdallaah Jóob Al Maalikii miñ tuddoon ci ginnaaw.

Bokk na ca yooya yii di ñëw:

  • Daaray Sñ Isaa Sàmb Ca Lugë ci Karce(Sanc ba) mi ngi sosu atum/1972,m ci ndigëlu Sñ Moor.
  • Taysiirul Hasiir :Miftaahun Nasri, bu Sñ Daam Pànne Jóob, nekk (Jaxaay)ca dakaar. mi ngi Sosu/1986.m
  • Taysiirul Hasiir :Bu Sñ Mustafaa Jóob ca Tuubaa Karce(Jéemun)mi ngi sosu/1999.
  • Taysiirul Hasiir :bu Sñ Mustafaa Jóob batay, ca Tuubaa (aaliya)sosu/2012m.
  • Taysiirul Hasiir :Daaray Sñ Muhammat Lamin Gay ca Tuubaa(Jànnatul Firdawsi).
  • Taysiirul Hasiir :Sñ Baara Faati Mbóoj ca Tuubaa (Jànnatun Nahiim)sosu/2004m.
  • Taysiirul Hasiir :ca Tuubaa (Baxdaat) mi ngi sosu /2010m.
  • Taysiirul Hasiir :bu Seex Maalig Ñas ca Tuubaa (Baxdaat/2)
  • Taysiirul Hasiir :Bu Sñ Moor Xëri Ture Tuubaa(Daaru Minan)sosu /11/02.
  • Taysiirul Hasiir :Ca Cees, sosu bisub Àllarba /15/2/2012.bu Sñ Móodu Yaasin Jóob.
  • Taysiirul Hasiir :Ca Ndar Karce (Leebar)sosu ci/2018 gi wees, Siidi Abdallaah Jóob.
  • Daaray Muxaddamaatul Amdaah: ca Tuubaa, sosu /11/2/2012.
  • Daaray Sëriñ Mbàkke Gay:ca Lugë, sosu /1998.
  • Taysiirul Hasiir :bu Sñ Ibraahiima Mëróon Ca Sóokoon Karce (Ndóofaan) sosu /2013.
  • Taysiirul Hasiir :Bu Sñ Muhammat Jàllo, ca Réewum Gàmbi ca (Yuuna)digganteem ak Gëbla ga(kapitaal) mi toll ci 15i Jun-ñay(km).
  • Daara yii ñu lim nag yi ci ëpp ci ndigëlu Sñ Moor lees ko sose, te yu ci ëpp Taysiirul Hasiir lees leen di woowe.

Kon lii mooy daaray Taysiirul Hasiir ak li ci aju. Di ñaanal Sñ Moor Jóob mu yàgg fi te ànd ak wér mook njabootam gépp ak képp kuy safoo Alquraan.