Taab

Jóge Wikipedia.

Taab nu ngi koy faral di gis lu ci ëpp ci àllu Sayel bi, fi muy sax itam danuy seetlu ne suuf si day dëgër.

Senegaal ba Kamerun ak Somali, amna ñu koy jàllale ci diggante réew yooyu. Boo deme Niseria it di nga koy faral di gis ci boori "Sud-Ouest".

Melo[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Taab garab la goo xam ne guddaay bi dina dem ba ay 12imeetar ci kaw. Te ay wànqaasam day am lu ci ëpp ay dég yu xaw a dëng. Loolu moo tax muy man a jàppanteek yeneen garab yiy nekk ci wetam. Ba laa man a sax dëgg nu nekk ci njeextalu noor bi walla ci biir nawet bi. Dina am ay xob, dina am ay meññeef.

Njariñ[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Garab gi nag day faj ay feebar yu bari, yu ci mel ne: biir buy daw, saan, day yokk cawarte, tegsi di ubbi biir ngir ngay man a lekk bu baax.

Nataal[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Turu xam-xam[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Combretum Nigricans