Aller au contenu

Substance abuse

Jóge Wikipedia.

Royuwaay:Feebaru dorogewu

Royuwaay:Dorogewu bu ëpp


Feebaru dorogewu, tamit ñu xame ko ni Dorogewu bu ëpp, benn yoonu dorogewu la boo xam ne kiy dorogewu dafay jël dorog bu bare walla niki melo yi bees ci moom walla yu keneen, te melokaanu dorogewu bu joge ci feebar. Ay piri yu wute ci wallu ëppal ci dorog yi ñungi leen di jëfandikoo ci fann yépp ci wér gu yaram, ak ci wallu yoonu tëjaate. Ci yenn fand yi ci ñaawteef walla nekkin yu àndulak lu nit ñi di def mungi nekk bu fekkee nit ki dafa dorogewu, te bu yaggee nekkinam dafay soppeeku ci nit ñi dina mëna am itam.[1] Dooleeku ci gaañ sa bopp, nit ñi, ak sa xel, dorogewu mën itam indi ay tëj yu joge ci ñaawteef, su fukkee sax dañu wute wekku ci yoonu rééw mu nekk.[2]

Dorog yi ñungi leen di boole lu ci ëpp ak baat bii ni: sangara, yambaa, barbiturates, benzodiazepines, cocaine, methaqualone, opioids ak yenn yuy wuutu amphetamine. Li tax ba nit ñi di jël dorog leeragul bu baax, ak ñaari wax yiñ ci gëna raññe di: benn yoonu ndono te ñeneen ñi jàngal ñu ko, walla ab tamm la bu amee, su fekke tamm bi mungi gëna fës, dafay dikke feebaru bu metti.[3]

Ci 2010 lu tollook 5% ci nit ñi (230 miliyoŋ) ñungi doon jëfandikoo dorog yu bon.[4] Ci ñii, 27 miliyoŋ yi dañuy jël dorog bu bari bu leendi indil musiba, ñu xame ko itam ci dorogewu bu kawe bu leen mëna indil musiba ci seen wér gu yaram, jafe jafe ci seen xel, seen nekkin ak nit ñi bu leen di dugal ci ay risk yu bon. [4][5] CI atum 2015 feebaru dorogewu agg na ci 307. 400 nit ñu dee, romb na 1990 ak 165.000 dee.[6][7] Ci yii, xayma yu gëna kawe ñungi joge feebaru naan sangaraci 137.500, feebaru opioidci 122.100 ñu dee, feebaru amphetamine ci 12.200 ñi dee, ak feebaru jël cocaine ci 11.100 dee.[6]

  1. Ksir, Oakley Ray; Charles (2002). Drugs, society, and human behavior (9th ed.). Boston [u.a.]: McGraw-Hill. ISBN 0072319631. 
  2. (2002). Mosby's Medical, Nursing & Allied Health Dictionary. Sixth Edition. Drug abuse definition, p. 552. Nursing diagnoses, p. 2109. (ISBN 0-323-01430-5).
  3. "Addiction is a Chronic Disease". Archived from the original on 24 June 2014. Retrieved 2 July 2014. 
  4. 4,0 et 4,1 "World Drug Report 2012" (PDF). UNITED NATIONS. Retrieved 27 September 2016. 
  5. "EMCDDA | Information on the high-risk drug use (HRDU) (formerly 'problem drug use' (PDU)) key indicator". www.emcdda.europa.eu. Retrieved 2016-09-27. 
  6. 6,0 et 6,1 GBD 2015 Mortality and Causes of Death, Collaborators. (8 October 2016). "Global, regional, and national life expectancy, all-cause mortality, and cause-specific mortality for 249 causes of death, 1980–2015: a systematic analysis for the Global Burden of Disease Study 2015.". Lancet 388 (10053): 1459–1544. PMC 5388903 Check |pmc= value (help). PMID 27733281. doi:10.1016/S0140-6736(16)31012-1. 
  7. GBD 2013 Mortality and Causes of Death, Collaborators (17 December 2014). "Global, regional, and national age-sex specific all-cause and cause-specific mortality for 240 causes of death, 1990–2013: a systematic analysis for the Global Burden of Disease Study 2013.". Lancet 385: 117–71. PMC 4340604. PMID 25530442. doi:10.1016/S0140-6736(14)61682-2.