Soxna Jaara Buso
Soxna Mariyaama BUSO ñu dàkkantale ko ci jikko Jaaratu-l-Laah (dëkkandoob Yàlla bi) gane àdduna ci atum 1833 ci as ndëkk su tudd Gollere ca Fuuta, Génn àdduna ci atum 1866 ca poroxaan, di way-juru Sëriñ Tuubaa.
Soxna Jaara BUSO mom Sëriñ Hamat BUSO (baayam) ak Soxna Asta Waalo MBÀKKE (yaayam), cosaano ci askanu Sëriif gog calale ga dem na ba ca Imaam Hasan mom Imaam Aliwu mom Abii Taalib ak Faatima mom Muhammad Yonentub Yàlla (jàmmi Yàlla ci ñoom), (*xoolal callale gi fii [1] ngir gàttal)
Mu dondoo ci loolu ag cell akub Yar ba war ci doomi Soxna jële ko ci Waa-juram wu Jigéen Soxna Asta Waalo MBÀKKE doon ab Jàngalekatub Alxuraan ak xam-xamu diine di yare ci Lislaam rawatina ci Tassawuuf, mu juddu ci loolu Yaayam yar ko ci,
Am njàngam ak ab yaram:
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Soxna Jaaratu-l-Laahi BUSO jànge na alxuraan ci aji/way-juram wu jigéen wu séll wa te sàmmu, te doon senn Soxna su ame taxawaay bu mat sëkk ci Lislaam ci jàngale ak yare, niki Sëriñ si, ba mokkal ko ci anam gu sell te sax, ci jamono yi muy am fukki at ak ñeente (14 i at)
Aywaay! ak li dudam gi di gàtt lépp (33 i at) téewul bind na Alxuraan ñeenfukki yoon ci yoxoy boppam (40 i kaamil) ndax daa mujjoon di ab jàngalekatu Alxuraan ci Taaral mbind,
Mu jàngal ko it xam-xamu diinéem niki jennal Yàlla (Tawhiid), Àttey Lislaam akuw yoonam (Fiq), Séllal ak jaamu ngir Yàlla dong (Tassawuuf), bamu wattu ko namu ware, mu yar ko it ci Lislaam, ci jàng alxuraan, ak jëfe ab xam-xamam, yar ko it ci ngor, muñ, nangu, ak jépp jikko jees taamu.
Bamu mujj di ku xarañe bépp xam-xamu Lislaam, te it di kuy jëfe ngirum Tassawuuf ci anam gu xóot,
Jigéen ci lislaam:
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Lislaam ginnaaw fimu fekk jigéen ak nimu ci taxawe bamu déñ fi, li mu tëral ngir ñoom a gën a tee yeeme, ci sàmmu léen, wormaal leen, ak taxawu leen, tey tëkku képp ku léen wormaalul, mba nga leen di fowe. Jox leen it kem daraja ak góor ñi ci wareef yi ak àq yi, ci waxi Yàlla ji muni: «Góor ñi ñooy Kilifa ci kaw jigéen ñi, ci ngënéelul Yàlla ci diggante ñee ak ñii» kon sàmm jigéen ñi farata la ci bépp góor bu di kilifa,
Te làq leen ci ginnaaw góor ñi, ngir kenn walla darra bañ leen a lor, Yonent bi (Jàmmi Yàlla ci moom) Neena : «Ki gën ci yéen mooy ki gën ci ay jigéenam, te man maa gën ci samay jigeen»
Jigéen june nag, mu wutal ko góor gu ko war a wattu, yiir ko, diko taxawu ci pakki àdduna yii diis ci ndoddu jigéen lool, Baay, jëkkër mbaa mag, (te góor gu mukàllaf yaay sa sàmmub bopp ci loraange yi) te jàppe ko muy lu «sakré» (worma), wormaal léppam, bëggul kenn ku ko fowe bëggul it mu fowe boppam,
Def ko it muy yaay, di jabar, muy ñaari wareef yi gën a diis ci àdduna, ba matal ko rekk war naa doy i yitte bépp jigéen june waliif leneen,
Yii yépp nag di lu Soxna Jaara jàng, jàpp ko te jëfe ko ca anam gamu ware, ci topp ndigëli wattukatam (Kilifaam) ak sàmm ak njabootam, yor leen yar leen ci lislaam, niki lees koko defalee woon.
As lëf ci ay jikkoom ak i meloom:
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Soxna Jaaratu-l-Laah Dëkkandoob Yàlla bi ci ag céll akuk sàmmu, Di Ab jullit bu di doomi jullit, Nangu te seere ni: «Amul jenn Yàlla ju dul Allaa, (Yàlla aji sàkk ji yélloo wul Wayjur, mbaa doom, ëppante naak di bokkaale ak kenn, Mooy dégg, Mooy gis) Muhammad (Jàmmi Yàlla ak xéewalam ci kawam) ndawul Yàlla la, (ndaw lumu jox Bataaxal bu ñeel nit ak jinne,) nangu te jàpp ni Lislaam rekk mooy Diine, Gëm téerey Asamaan yépp te nangu ni Alxuraan a leen wuutu, Gëm dogal te diko rafetlu, Gëm Malaaka yi ak lépp li aju ci ngëm... nangoo julli, nangu woon a joxe Azaka ndeem war na ci alalam, nangu woon a woor, nangu woon ni Aj war na ko aw yoon.
Soxna Jaaratu-l-Laah doonoon as gor su di doomi gor, di ku sàmmu, ragal Yàlla, Gëm Yàlla diko jaamu, Sopp Yonent bi di topp sunnaam, Bëgg ab Sëriñam di wëye ay ndigëlam, fonk ay bokkam te nawloo leen, di ab jullit bu koy jëfe, di as gor su gore, Di doomi Soxna su soxnaa, Di ab jàngkat buy jàngale, di Boroom xam-xam bu koy jëfe, di boroom alxuraan ci bind ak ci wattu, doon ku nangu te man a muñ, doon ku yaru te daa yare, doon ku ñime njaboot te di leen taxawu, doon it jigéen ju maanu ci bépp anam, Ku daa dunde Lislaam, waxees nani masu la faat waxtu mukk,
Masul a julli te jàppuwul, masul a julli it te deful yi ko war ak yimu warloo ci «Wird»... niki ko waykat ba waxe: Masla julli te jàppul () masla julli te wirdul () nangam nàngam..... Ci lu dul weeru koor, baaxoo woon na di woor, koor yees taamu ci at mi, ak i koor yu mu tegoo woon. tegoo woon na it di jàng téereb «Dalaa-ilul-Xayrâti» bu Imaam Jazuuli, di ab téere bees taamu, temu fees dell ak i julli ci Yonent bi (Jàmmi Yàlla ci moom) Li am daal, ay waxtoom ci jàng alxuraan ak tari ko la dëkke woon mbaa julli ci Yonent bi, ngir ndigalul Yàlla la, lu woom aki dëel.
Moom daal ci gàttal mooy Way-jur wu jigéen wu Seex Ahmadu Bàmba Xaadimul Xadiim, te aji bind ji (Yalla) neena: «Suuf su nangu dan a génne kemam ci ndigalul Boroomam» Muy li Wolof naan: «Kéwël du tëb doom jay bëtt»
kon daal loolu rekk doyna ay jikko akuw tagg, ndax Bàyyi doom ju melni Seex Ahmadu Bàmba, ci ag céll akuk sàmmu, wéetal Yàlla, te jox ko léppam, xam, xàmme di xamale, nangul Lislaam, yaru lool di yare... jigeen ju ko ame làmboo mbooleem jikko yees taamu...
Soxna Jaara BUSO ci pénc mi:
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Niki jigéen ñépp, baaxoos na jigéen ju mat a dem kër, fàggu lees ko boroom kër, ak it teewal ko ngir man koo dénk wax i njariñ, ak yee ko ci àddina xamal ko ni it, fa nga jëm sa ab sang nga fay fekk, bu la Yàlla booleel, xamal ko it ni, Ngërëmul Yàlla akuk payam, ak doom ju raw i maasam, ñeel na soxna si ànd ak boroom kërëm ci li neex Yàlla, nangoo muñ, nangu, tey wéy ci ay ndigël,
Niki noonu lees ko defale Soxna Jaara ci bimu ci tolle, fàggul ko te tànnal ko ab Sëriñ ci anam gamu gëne, ak ci melo yiy sax ci nit,mu déglu it wax yu am solo yooyu ak soññee yooyu, ci ag teewlu, dégg ak topp, Waaye ci yaru gimu yaru ci xamlu Yàlla ak di jéem a xàmme, ak xalaat yu sori yi Sufiyànke yi baaxoo,
neeñu ci loolu, bees koy jaarale ci yii, Mu Ubbi Kaamilu Alxuraan bi mu baaxo yor, ngir def ab natt, yam ci wax i Yàlla ji naan: «Déeti Yonent ginnaawam (Muhammad)»
Cey ! lii déy màndarga la mu yaatu te bar i maanaa te doy Kiimaan ci way-xalaat yi, Ci loolu mu dogu (ab sufiyànke la woon, te fa Suufiyànke ya, wacci séen dogu, moo gën a tar dee fi ñoom) te jaayante ci topp Ab Sëriñam ci jëmmam akuk ruuham (ndundam) kemm kàttanam ngir Yàlla dong, tey ku sàmm ay wareefam, am kersa akuk topp gu matale ñeel boroom kërëm.
Nu indi fi ak pàttali, Sëriñ Muhammadu BUSO bokk ak Soxna si yenn way-jur, bimu tollee ci wut kër daa dogu ni: «Bu ma wóorul ni doom ju ma am Wàlliyu lay doom duma samp kër» cey ! Pas-pas bu ni mel déy, la soxna si ame bi muy dem kër.
Soxna Jaara BUSO doonoon Soxna su Maam Moor [Anta Sali] MBÀKKE, Soxna jaara nag bokkoon ci askan wu di boroom Barke, Yàlla dénk leen am-am, te Yàlla def Maam Moor Anta Sali mi mujj di boroom këram bokkoon ci askan wu seen wërsëg melul noona...
Amna wax i Sëriñ Tuuba jukoy wéral, Amna bis am góor gu ñëw ci Sëriñ bi, melni ku yàkkamti lool, Sëriñ bi neko: Diw ! fàtte wu ma sama Nag wa, daadi ni: Jëmm jii de, ba may gën di gone bind naa ab Kaamil, diko jox saa Baay Sëriñ Moor Anta Sali muni ma : Xanaa nga yobbu ko saalum ngir man cee am darra, Lu man a jëm ci kër gi, Sëriñ bi neena: Ma dem Saalum diko wecee ku, di wër ba am kuma ko diktal muni ma: aah ! ndongoli man dey Soxla naako waaye ab xaalis de yoru mako, te lima yor xamnaa ni ab dongo du ko war a soxla, niko; Aw nag de laafi yor, Sëriñ bi neko: aah! aw nag moom lu ko yobbu dina yéeme, neena: nag woowee góor gii mooko ni man naala ko jiitalal, Sëriñ bi neena ma warlul ko Àjjana ak guddu-fan, Ni góor gi: "gis nga sama ndëel ya ?" muni ko: "aah! gis naa benn bi de muy gudd fan gi, bi ci des kay a ma wóorul", Sëriñ bi neko:"Waaw! bi ci des it noonu rekk, amul sikk".
Ci wax jii manees na cee xame ni Yàlla dénku leen woon alal jees man a gis. Waaye xanaa ñu di ay jaamukati Yàlla, di ay boroom i xam-xam yuy jëfe seen i xam-xam, di ay jullit te doon i gor, sàmmu te ragal Yàlla,
ci yii jikko daal la Kilifay Soxna Jaara BUSO xool, ba nangu faa maye séen doom, Soxna Jaara it ci yooyii jikko la xool ba nangul ko, loolu it masul di feeñ ci séenub ànd, xanaa àndak Moom ci dooleem ñuy dund ci sutura ak ngir Yàlla,
Mu Jàppe ko ni ab sangam di topp ay ndigëlam ci anam gu yéeme, Misaalum nittali bu siiw bii te doy kiimtaan, ñuni: Amna bis Maam moor Anta Sali di takk aw sàkket teye looko sàkket wa, dugg ci biir neeg bi, (xayna ngir jël lumu takke sàkket wi) faf Yàlla dogal mu dugg rekk, Yàlla sóob ab taw, mu far toog fa néeg ba, neeñu: ba ci fajar gi Maam Moor génn fekk Soxna si mu téye sàkket wa, Muni ko: Aaah! yaw de xanaa fii lala taw bi fekk, niko: Waaw! lu tee bimuy taw nga dugg ci biir, man de jàppoon naani yaangi ci biir, Soxna si niko: Sa ndigël a ma ko teyeloo woon te ba leegi ndigël jugewaatul ci yaw bàyyi loo mako... Haakazaa !! Eskëy ! Lii déy yéem nama, te war a man a yéem waa jamono jii, ci lii numu man a ame,
Soxna si it liggéeyub kërëm moom rekk a ko daan defal boppam, di ko def ca anam gamu ware, boole ko ak matal jaamuy Yàllaam.
Ci topp boroom kërëm ak dabu ay sàkkutéefam, ginnaaw Maam Moor ab sëriñam daa xawoon a jëm mag, te fiñu nekkoon xaw a àlle, ba tax sedd ba xaw faa tar, ci loolu daan na ko fàggul matt mumuy jaaroo, ngir mucc ci sedd boobu nga xamni baaxul ci mag,
Ba bis (xayna matt jafe nako), ngir bëgg a matale càkkutéef i boroom kërëm, tax mu dàjji gaal gi mu daa denc i mbiram, ngir taalale ko Ab sëriñam, Cey !!
noonu it lako waykat ba waxe Seex Sàmba Jaara MBAY Taalubeb Sëriñ TUUBAA
Soxna Jaara neeñu:Masul a jug ci di dimbalante ñeel waa pénc mi, ci di taxawu ak di dundal jirim yi ak néew doole yi, ci lu dul sàkku ak cant ci nangukat yi, xanaa ngir jëmm i Yàlla rekk, ba waxees nani ci loolu la jële Turam wii di Jaaratu-l-Laahi (Dëkkandoob Yàlla bi),
Soxna si ak njabootug boppam:
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ci loolu Soxna si Yàlla may nako ci sëy bu barkeel boobu, ñéenti doom, yoy dinanu sawar lool ci tudd séen i tur, ak wax as tuut ci séen i jikko, Nu lime léen nii:
1- Ab taawam moodi Maam Moor [Jaara] MBÀKKE Mom Sëriñ Moor Anta Sali MBÀKKE ak Soxna Jaara BUSO, doon ab jullit bu di doomi jullit, di as gor su di doomi gor, di ku sàmmu te ragal Yàlla, daan jàng ak a jàngale Alxuraan, ci anam gu yéeme, daan jàngale it ci bépp xam-xam bu aju ci diine.
Neeñu saxoo woon na guddi gune téeméer i ràkkaa (100 i ràkka) noppi jàng alxuraan bamu mat, bimu fi bawoo Sëriñ TUUBA seereel ko ni:«Man déy Sëriñ MBÀKKE kajoor ak Sëriñ Moor Jaara rekk laa mas a gis kuy dugg ci bàmmeel te yobbaale wu fa bàkkaar, Cey !!
2- Gi ci tegu di Sëriñ Habiibu-l- Laahi MBÀKKE Mom Sëriñ Moor Anta Sali MBÀKKE ak Soxna Jaara BUSO, doon ab jullit bu di doomi jullit, di as gor su di doomi gor, Sëriñ TUUBAA seereel na ko ni: ku amoon ab cér bu kawe ca Yàlla la, Cey ! Ba jamono yi mu nekkee moom Sëriñ Tuubaa Njaaréem (Diourbel, 1912-1927) baaxoo woon na di dem Xuru Mbàkke di Ziyaare Barabam.
3- Teg ci Soxna Faatima MBÀKKE Mom Sëriñ Moor Anta Sali MBÀKKE ak Soxna Jaara BUSO, doon ab jullit bu di doom i jullit, di as gor su di doomi gor, ndeysaan ! moom nag ag dundam lu gàtt la, dellu na ci Aji sàkk ji ci jamonoy ndaw, Seex Siidiya Gànnaar di ab Wàlliyu ca Gànnaar neena: Malaaka yi dañuy wàcc ci bàmmeelam ngir def i Ziyaar, Cey !
4- Haaa ! Teg ci nag, sunu waaji, Ki sunu làmmeñ ak sunuy cér dul deñ ci di ko tudd ak diko liggéeyal, Ki jur ko rekk doy màqaama, Seex Ahmadu Bàmba MBÀKKE Xaadim Rasuul, Mom Sëriñ Moor Anta Sali MBÀKKE ak Soxna Jaara BUSO, doon ab jullit bu di doomi jullit, di as gor su di doomi gor, Di Ab mujaddid bu Lislaam, Doon liggéeykatub Yonent bi, Gëm Yàlla daa ko jaamu, Sopp yonent bi daa roy sunnaam, Bëgg ko daa ko liggéeyal... Neena: «Yàlla wommatal nama lol mas la nekk te du mas a nekk ba fàww di ko wommatal keneen» «Du Am Sikk ba fàww ci nekk gi ma nekk di dëkkandoob Yàlla....»
Héé! mani: bul ko sikk dellul ca lamu liggéey ba yélloo bii añ bu rëy. Moom daal nu bañ a sori ci jëmm jii, ndax Seex Saliwu Mbàkke neena: «Lu ñépp xam wax ci tuuti doyna» ! kon nu xelu yam foofu,
Diggante Soxna Jaara ak Sëriñ Tuubaa:
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Bees delloo ci mbindum Seex Muhammadu Basiiru «Minanul Baaxil Xadiim» manga ca naan: Soxna si ku manoon a yare la, daan a yar ag njabootam ci di leen fàttali ak a nettali Xistay gaa ñu baax ña, di leen ko jàjje ak di leen xamal lañu def ba yelloo séen may yooyii, di léen yar ci yuni mel, di léen ci nàmptal, Loolii nag mooy wareef wu jëkk wiy dox ci diggante way-jur ak doom ja, Soxna si matale ko lool,
Loolu topp na sunu Sëriñ ba waxees nani jaarul ci po doonte gone baaxoo nako, waaye neeñu am powam moodoon, julleentu, jàng alxuraan, ak a bindantu... te looli kat lako Yaay ju séll jii kune ni woon siiw muy sa jos nàmpatale,
Soxna si ci ag maandoom, bi sëriñ biy gone daana def ay xarbaax mu koy yëg di ko gis, waaye Sëriñ bi daa sàkku ci moom ngir mu bañ koo yegge Baayam du caageenu mbooloo mi.
Soxna Jaara digganteem ak Seexul Xadiim weesu na rekk Saahir (lu feeñ) soosu, waaye sar ba ci Baatin bu sax te keemtaane,
Barina ay nettali yu koy saxal sax, waaye nu Tànn ci rekk bu Sëriñ Abdu Lahad MBÀKKE bi muni: Bees dugalee Seexul Xadiim ci puq si woon ci Ndakaaru, mu xat lool, sëfees ko ak i ràbb ak i fital, ndeysaan ! Soxna Jaara fekk na ko fa diko masta wu diko ñaax, diko fàttali lamu ko yarewoon, muy di xool ca gaa ñu baax ña wéy, ak lañu dajoon ngir yelloo séen i cer, Yonent Naan ko: Xoolal Amsatu (jàmmi Yàlla ci moom) di ab Sahaaba bu jàmbaare ak rayiin wu ñaaw wees ko ray, Cey ! wii way-jur... Tax Sëriñ Muusaa KA naan: «Neena kerog gis nafa sunu maam Jaara () Mu di ko ñaax te di ko dolliy daara» «Njool Màkka naan ko xalamal Sahaaba () Bu tudd amsatu li leey Xitaaba»
Sëriñ bi nag, Ku fonkoon Soxna si la te di ko wormaal, Dëkk biimu nekkoon di Poroxaan daa mujjoon gent, waaye Sëriñ bee ko dekkilul, Lépp ngir worma ak fonkeel, Xabru ba it reeroon na, ba xameesul fumu nekkati, waaye Sëriñ bee jox Sëriñ MBÀKKE Gani BUSO doomi nijaayam ndigël ngir mu seetal ko te saytul ko barab boobee, Sëriñ Mbàkke Gani BUSO def ay yitte, ba dégg ab pël bees jàpp ni xam nako,
Mu ànd ak moom ñu wër ba gis ko, mu koy taxawu ci ndigëlul Sëriñ bi, ba ginnaaw bi mu tàbbi ci loxol Sëriñ Muhammadu Basiiru MBÀKKE, mu koy taxawu ba, bimu fiy juge, noonu it lako ak njabootam di taxawoo ba fimne.
Amna Sëriñ bu sàmm woon, ragal Yàlla, di ab jàngkat tey ab jàngalekat, Muy Sëriñ Sàmba Mareema Saa-kokki, doon wóllare wu Maam Moor Jaara, wayoon na ay woy ci araab, ngir seere ay jikko yu sell te rafel, yu mu gis si Soxna soosii di Soxnas Wóllareem,
Way yooyu waxees nani lu Sëriñ bi fonkoon la, daako yër lu bar, ba mujj gi mu waylu waat ko, ngir ag yaatal, Muy Xasida gu tudd «Matlabu ridwaanul mbàkkii () Fii taxyiiri Nazmi Ash-Shaykhu Sàmba al-kokkii»
Loolu lépp di tektale ak cofeel akuk fonkeel gu mu am ñeel way-jur wi...
Haakazaa Sii Soxna ! Eskëy wii way-jur ! Cey bii jullit ! Aywaay ! gor sii ! ndeysaan bii yarekat ! Su làmboo lii lépp ci ay jikko akuw doxiin, Su melni nii la suuf soxla woon ! su melniiy a baax ci dénd bi ! Su melnii la Yàlla soxla ! Su melnii La pénc mi soxla ! Ju melni la doom yi soxla ! Su melnii la boroom kër yi soxla ! Su melnii la njaboot gi soxla ! Su melnii la Lislaam Soxla ! Su melnii lees taamu ! Su melnii lees di fàttali ku !