Seydinaa Limaamu Laay
Seyidinaa Limaamu ab nappkat la woon bu juddoo Yoof atum 1845 g.j. Ci atum 1885 g.j, mu gént gis ne mooy Mahdiyu .. mu tàmbalee woo àndandoom yi ci ñu dugg ci Lislaam, di soññ jullit ñi ci ñu sellal te jaamu Yàlla rekk, mu daa wax : (( wuyyuleen wooteb Yàlla, man de yonnantub Yàlla laa, maay Mahdiyu mi ñuy neggandiku)), daa na woo ay àndandoom jëme léen cig jub ak jàppalante. Bu ko defee nit ñu bari dikkal ko ngir déglu njàggaleem mi. Mu daal di sos kuréelug Laayéen. Siiwam gi tiitloo woon na way sanc yi ragaloon ag jeqiku kontar leen. Ci atum 1887 g.j, la sancaan yi taxaw ci jàpp ko, bi mu yëgee seen naal yooyu la ànd ak lenn ciy àndadoom génn, waaye tubaab bi jàpp ko ca wetu Caaroy. Waaye ëttu àtte bi mujj na ko setal ko ngir ñàkk lenn lu man a dëgëral tuuma yi ñu teg ci kawam. Limaamu wéyoon na ci wooteem gi, waaye daa na def jamono ju nekk muy fenqook sancaan yi ko daa jéem a sonal ak àndandoom yi. Mi ngi làqu atum 1909 g.j.