Aller au contenu

Seex Ibraayma Faal

Jóge Wikipedia.
Maam Seex Ibraayma Faal

Làmp Fall, Baay Faal bu mag bi, jàmbaar ju raw gaynde

Kenn ci ñi gën a siiw ci taalubey Bamba yi mooy Seex Ibraayma Faal. Bàyyi na fi ay dongo yu ñuy wooye Baay Faal yiy wottee seenug ñàkk a julli ak woor, liggéey bi ñuy def ci seen loxo ak yalwaan , looloo tax yeneen jullit ni ñoom di leen jam tey naqarlu seeni jëf. Seen njañ yi ñu yore ak seen létt yi yobbe na leen way nemmeekusi yi (touristes) di leen jaawale aki rastamen.

Jëf yii nag yu ci ëpp du yu bawoo ca Maam Seex, moom kay day yu bawoo ci seen bopp, li leen jur di am njaxas mu ag dëddu àdduna ak ginaawal ko ak yëngu bu bari bi ñu taqool ba duñu talati seen bopp ñu far ba seeni kawar noonu duñu leen topptoo, duñu leen tal.

Maam Seex nag nekkoon na di ku dëggu te liggéeyal lislaam lu réy, waaye ñàkk a jullit gi ñu bari firee nañu ko ci ne daa amoon ngànt, ndax daa meloon ne ku àndul woon ak sagoom, booy xool it ci ni mu daa waxe mbaa mu koy jëfe lépp da daa wund loolu, mu mel ne ku sóobu la woon ba sóobu gi yobbu ko ci mu nekkoon di ku àndadi akum xelam te loolu lislaam boole na ko ci sart yiy tee julli di war. Bokk na ci sart yiy tax julli di war nit ki ànd akum xelam.

Sëriñ bi bind na ko bataaxel bob Sëriñ Abdul Ahad 3eelu xalifa génn woon na ko móollu ko ca téere ba ñuy wax majmooha, muy téere bu dajale waxi Sëriñ Tuubaa yu bari, ma nga cay wax naa :« Yaw Ibraayma Faal boo jotee ci sama bataaxel bii nanga digal sa ñoñ ñuy julli te nga sax ci te muñ ko, laajuñu la wërsëg ñoo la koy jox, te mujj gu rafet ñeel na way ragal Yàlla yi,» lii di aw laaya wu alxuraan wu mu ko yonnee ngir délloosi ko ci, kon day mel ne Sëriñ bi moom wàcci na ak ku nekk, Maam Seex nag ak ni mu gëme Sëriñ bi bu julliwul ngànt a tax, ndax daawul jëfeedi ndigal te loolu ndigal la woon.

Seen gëm-gëm nag amul lenn lu ko wuuteel ak bu lislaam, ñu jàmbaare lañu ci lislaam di liggéey di joxe, ngir lépp lu ñu war a alalal ci lislaam man a alalu, lépp luy sémb man a àntu, foo leen fekk dañuy sikkar (maanaam tudd Yàlla) di woroomi pastéef yu kawe aki jéll, bu koor gee ñuy joxe ay ndogu ñeel way woor yi, di tabaxi jàkka aki jumaa, lii rekk mooy li ñu leen man a doyodale ci lislaam te du ñépp ñooy ña ca dul julleek a woor, am na ci ñoñ dañu koy def, doonte ñu néew lañu it.