Saytu yaramu nit

Jóge Wikipedia.

Ci wallu pajj saytu yaram mooy xool nit ki ban jangaro moo nek ci moom walla luy wone  liko febaar. Saytu nit ki nak dafay lacc xam dembam ak li ci yaramam ndax ñu xam limu andal. Yennsaay, benn wala saytu yu berri dañu koy amal ci jamonoy gëstu pur xam yan xeet u feebar ñoo nekk ci yaramu nit ki. Lek lek itam  saytu yaramu nit ku ñaak bakkanam ba pare mën nañu ko jappe kom saytu yaramu nit ki pur xam ban feebar moo nekk ci moom. Saytu yaramunit ki dafay faral di nekk lu jafe ndaxte mandargay doomu jangoro yu berri dañu jafe xam loolu. Ci missaal yaramu nit buy xonk jafe jafe la ci pajjkat yi xam mandargay ban feebar la.

Toppu fajum yoon[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Pajum yoon ak saytu limu andal:

  • Xam lu bari ci kuy faju, mana xam ay febaaru dembam,saytu yaramam and  ak yenen  xeet u saytu (buko jare lacte kimu jege ndax geuna xam). Saytu dafa melne  xool beep xeet u febaar bu nekk ci nit. Saytu meunna doon pur xam  mandarga bepp feebar bu nekk ci yaramu borom.[1]
  • Saytu ci wallu tontu yi,setlu, wala yenen xeet u jangat.  Wante itam saytu ak yenen doktor yu sen xel macc ci wallu pajj mën na nekk xalat bu raffet loolu.

Barina fasong yinuy sayto ci toppu fajum yoon,bokk na ci amal ay xeet u saytu yu berri te wute wala xeet u saytu yu bess yi nga xamante ni mën na wane bepp xeet u jangoro bu nekk ci yaram u nit ki.[2] Ci deug deug toppu fajum yoon barina yoon.[3]

Saytu ci wallu corona wirus bi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Corona wirus bi  mën  nañu ko saytu ci ay mandargam jëm ci saytu yu njëk yi, donte ni sax pur dëggal ni feebar bi mungi ci nit dañuy xaar ba am mandarga yu melni luñuy tudde (rRT-PCR) wala xaar ba giss ni  am na ay pacc yaram u nit ki am na doom u jangoro bi ci missaal tiflit (CT) lañu koy mandarga le.[4][5] amal nañu jangat ci diggante (CT) li jëm ci wallu askaneer ak (PCR) manam li jëm ci wallu  ADN nit ki ci rewu Wuhan limu wone mooy saytu ak skaneer amul njariñ loolu.[5] Li ko tamabale ci weer u mars  2020 ba leegi daara ju mag nekk ci Amérique di yëngu ci wallu rajo xamle ni " lu jëm ci wallu skaneer pur saytu feebar bi di corona wirus nekkul li ñu diggle".[6]

Saytu virus[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Kurël bi tënk wallu wërgu yaram ci aduna bi yepp xamle na ay bataaxal jëm ci tërelin u saytu yi ñuy amal ci wallu corona wirus bi, xamle bu njëk bi mungi amoon ci weer u janvier ci bessu fukk ak juroom  ñaar.[7] [8][9] Saytu bi reaktion bu tuddu (rRT-PCR) lay jëfandiko.[10] Saytu bi mën nañu ko amal ci ay nooyikay walla ci deret.[11] Saytu yi li cu ruuse mën nañu ko am ci ay fan yu neew walla ay waxtu yu neew.[12][13] Lu ci ëpp saytu bi mën jogge ci jangat buñu amal jële ko ci bakkan wala put.[14]

Barina ay bërëb u gëstukay ak usin  yuy guestu ci ay  serum pur mëna giss ci teel lu bokkul ci yaram u nit ki.[15] Ci weerup awril juroom ñaari fan ci atum 2020 saytu  yi joxewul dara lo xamante ni mën nañu ci japp ba tax ñu war ko mëna jëfandiko  ci aduna bi yëpp.[16] Cu rewu  Amérique benn saytu jëm ci serum te Cellex amal ko nangu nañu ko pur jëfandiko ko ci ni mu gëna gaawe ci bërëb u gëstukay yi ñu jox ndogal[17].

Xalatal[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Mandarga feebar yi ñuy saytu ci wallu radiographie yu nit yi am bepp xeetu mandarga buy wane ni am na doomu jangoro mën nañu ci wax jafe jafe ci wallu xool bu bax lu melni lep luy takk ci missaal lamp wala itam jafe jafe  jëm ci wallu nooyikay nit ki am mandargay feebar.[18] Benn bërëb ci wallu radiographie manam xol yan xeet u feebar ñoo nekk ci nit ki te bët munu ko giss ci reewu Italie amal na benn jangat bumu jaglel lu jëm ci wallu nit yi am doomu jangoro bi mungi ñu tass ci internet bi. [19] Kom jixi jaxa dafa am ci ak yeneen xeetu doomu  jangoro yi di walle lu ci "adénovirus" di benn xeetu wirus boo xamante ni dafay ëndil jafe jafe nit ki ci wallu nooyi, skaneer bu andul ak dëgal ni nit ki am na feebar bi di COVID-19 nekkul luñuy mëna jëfandiko pur saytu ndax nit ki am na feebar bi di COVID-19. Reew mu Chine amal na jangat bu yaatu diggante saytu ci skaneer wala saytu ci wallu ADN li ñu giss mooy amana sax skaneer bi nekkul lu am doole loolu pur xam ndax nit ki am na doomu jangoro bi ci yaramam, wante moo gëna gaaw pur ay tontu ba taxna ñungi digle ngir ñu koy jëfandiko lu jëm ci wallu saytu nit yi ndax am nañu doomu  jangoro bi ci dekk yi nga xam ni doomu jangoro bi law na fa bu baax.[5] Amalnañu ay xeetu "neurones"yi nga xamante ni seen liggey mooy fexe ba rañee wirus bi ci kaw amal "radiograpghie"[20] ak "skaneer"[21].

  1. Thompson, C. & Dowding, C. (2009) Essential Decision Making and Clinical Judgement for Nurses.
  2. "Making a diagnosis", John P. Langlois, Chapter 10 in Fundamentals of clinical practice (2002). Mark B. Mengel, Warren Lee Holleman, Scott A. Fields. 2nd edition. p. 198. ISBN 0-306-46692-9
  3. "Making a diagnosis", John P. Langlois, Chapter 10 in Fundamentals of clinical practice (2002). Mark B. Mengel, Warren Lee Holleman, Scott A. Fields. 2nd edition. p. 204. ISBN 0-306-46692-9
  4. "CT provides best diagnosis for COVID-19". ScienceDaily. Retrieved 14 March2020.
  5. 5,0 5,1 et 5,2 Ai T, Yang Z, Hou H, Zhan C, Chen C, Lv W, et al. (February 2020). "Correlation of Chest CT and RT-PCR Testing in Coronavirus Disease 2019 (COVID-19) in China: A Report of 1014 Cases". Radiology: 200642. doi:10.1148/radiol.2020200642. PMID 32101510.
  6. "ACR Recommendations for the use of Chest Radiography and Computed Tomography (CT) for Suspected COVID-19 Infection". American College of Radiology. 22 March 2020.
  7. Laboratory testing of 2019 novel coronavirus (2019-nCoV) in suspected human cases: interim guidance, 17 January 2020 (PDF) (Report). World Health Organization. 17 January 2020. hdl:10665/330676. ISBN 9789240000971.
  8. Laboratory testing for coronavirus disease 2019 (COVID-19) in suspected human cases: interim guidance, 2 March 2020 (PDF) (Report). World Health Organization. 2 March 2020. hdl:10665/331329. WHO/COVID-19/laboratory/2020.4.
  9. "Coronavirus disease (COVID-19) technical guidance: Laboratory testing for 2019-nCoV in humans". World Health Organization. Archived from the original on 15 March 2020. Retrieved 14 March 2020.
  10. "Coronavirus Disease 2019 (COVID-19) Situation Summary". US Centers for Disease Control and Prevention. 30 January 2020. Archived from the original on 26 January 2020. Retrieved 30 January 2020.
  11. "Real-Time RT-PCR Panel for Detection 2019-Novel Coronavirus". U.S. Centers for Disease Control and Prevention (CDC). 29 January 2020. Archived from the original on 30 January 2020. Retrieved 1 February 2020.
  12. Brueck H (30 January 2020). "There's only one way to know if you have the coronavirus, and it involves machines full of spit and mucus". Business Insider. Archived from the original on 1 February 2020. Retrieved 1 February 2020.
  13. "Curetis Group Company Ares Genetics and BGI Group Collaborate to Offer Next-Generation Sequencing and PCR-based Coronavirus (2019-nCoV) Testing in Europe". GlobeNewswire. 30 January 2020. Archived from the original on 31 January 2020. Retrieved 1 February 2020.
  14. "Coronavirus Disease 2019 (COVID-19)". Centers for Disease Control and Prevention. 11 February 2020. Retrieved 5 April 2020.
  15. Vogel G (19 March 2020). "New blood tests for antibodies could show true scale of coronavirus pandemic". Science | AAAS. Retrieved 6 April 2020.
  16. Coronavirus antibody tests: How they work and when we'll have them". BBC Science Focus Magazine. Retrieved 6 April 2020.
  17. Azad A. "FDA authorizes first coronavirus antibody test". CNN. Retrieved 6 April2020.
  18. Li Y, Xia L (March 2020). "Coronavirus Disease 2019 (COVID-19): Role of Chest CT in Diagnosis and Management". AJR. American Journal of Roentgenology: 1–7. doi:10.2214/AJR.20.22954. PMID 32130038.
  19. "COVID-19 DATABASE | SIRM" (in Italian). Retrieved 11 March 2020
  20. Heaven WD. "A neural network can help spot Covid-19 in chest x-rays". MIT Technology Review. Retrieved 27 March 2020.
  21. Li L, Qin L, Xu Z, Yin Y, Wang X, Kong B, et al. (March 2020). "Artificial Intelligence Distinguishes COVID-19 from Community Acquired Pneumonia on Chest CT". Radiology: 200905. doi:10.1148/radiol.2020200905. PMID 32191588.