Sanaar
Sanaar garab la guy ñoree ci tefes gi mi ngi gën a yaatoo ci géeju atlantig bi. Dalee ko ci Gànnaar ( Muritani) jàpp Àngolaa topp tefesug Amerig gu digg gi ba ci bëj-saalumu Amerig lu ci mel ne Beresil.
Melo wi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Garab gi nag bant bu tooy te diis la yor ba noppi dëgër xaw a paalmaan. Bant bu jafee wowal la. Waaye bu demee ba wow nag day jafee damm ndax dëgër gim dëgër. Bu duggee cim ndox it man na faa yàgg lool te du yàqu ndax dëgër gi mu dëgër. Am xàncam mi ngi toll ci 12,5%. Ay xobam dañoo dëgër. Reen yu bari te dëgër la yor.
Njariñam
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ab bantam man nañ cee defar gaal, kër (baraag) , ay jumtukaayu kër ( lal, Cempteŋ, toogu ak yu ni mel). Man na matt ak këriñ. Doom yi bees leen baxalee ba ñu bax ngir wàññi tooke gi manees na koo jëfandikoo ci jamonoy xiif. Xob yi walla reen yi dees koy xoromee lujum yi ak yu ni mel. Xànc mi daan na ñu ko jëfandikoo ngir wirgo wu xonq. saxaar siy jugge ci matt mi it day dàq i yoo. Xob yi daa nañu ko def cim ndox di ko sangoo; day faj i teeñ ak yu ni mel. Ca Amerig dañ koy jëfandikoo ci wàllu pajum cosaan ngir faj biir bu daw, ay nàcc-nàcc, emoroyit, tànk yuy metti, baat buy metti...
Lor yi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Doom yi balaa nga koy lekk nanga ko baxal ba mu ñor ngir wàññi tooke gi.