Sam

Jóge Wikipedia.
Sam gi (Acacia macrostachya)

Sam xeet la xeeti garab , mi ngi bokk ci njabootug Fabaceae, dees koy fekk ci goxi Sahel gi ak ca Sudaan.

Garab la gog fi muy sax day bari suuf lool walla xeer ñu ngi koy fekk ci réew yii: réewum Bene, Burkinaa Faaso, Kodiwaar, Gine, Gine Bisaawóo, Mali, Niseer, Niseryaa, Senegaal, Siraa Leyoon, Togóo, Càdd, Sudaan.

Melo wi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Mi ngi bokk ci garabu matt yi, te bari dég day yor xas yu bari, nuroo ak garab gu ndaw guddaayam man naa jàpp ñenti met jëm kaw.

Bokk na ci garab yi nga xam ne dañuy laxasu, ci loolu nag guddaayam man naa àgg ci fukki met ak juróom .

Njariñ yi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Moom dees koy watt ngir di ko jox baahima yi ñu koy jëfandikoo walla ñu ciy fajoo, batay it ñu ciy defar matt

Ay doomam manees na ko jëfandikoo niki xeeti (acacia) yi am yépp dañuy tàkk te dañuy dundal.

Ay xobam dees koy tàngal bamu tàng di ko jëfandikoo ngir di ci faj biir buy metti ak yu ni mel moom it ba tay dees koy jëfandikoo ngir wàññi ci daŋaru jaan.

Nataal yi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Turu xam-xam wi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Acacia macrostachya