Saltige
Saltige, benn tur la, ci cosaanu Séeréer yi ak Pël, bu ñuy woowee boroom xam xam yi.
Cosaanu baat bi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Saltige, ci lakku bambara (bamanakan) la juge. Ci bambara, noonu lañu ko xajalee:
- Sila (mooy yoon wi)
- Tigi (mooy njiit bi).
Kon, Silatigi, ca njeelbeen, mooy kepp kuy jiite yoon wi.
Saltige Séeréer yi, ak Silatigi bu Fuuta Tooro
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ci seereer yi, Saltige bi, mooy kuy yoree mbirum xam xam yi. Ñoo yoree mbirum paj ak gisaan, ci askan wi. Gëdd bu mag lañu yoroon, ndax ñoom a tax ñu mënoon wuti safaara ci lu demoon ci wallu bey mi, nawet gi, ak yeneen coono yi askan wi jankoontel. Dañoo dendoon lool nguur gi (Siin-Saalum), buuri seereer yi, di leen yegle ak di leen digal lu bare, ngir buuri yoree nguur gi ci añam yu rafet, reew mi jem kanam te am jamm. Ci seereer yi, nekk Saltige, ndono la. Lebu yi ñu xam ni, seen maam, ay seereer lañu woon ci lu ëpp, ba tey, am nañu tamit seen Saltige, di bokk ci mbootaayu ñooñu nekk ca kaw askanu Lebu, Seriñ Ndakaaru bi moo leen jiite.
Fuuta-Tooro nag, Silatigi bi, buur la woon, moo doon yoree nguur gi. Deeniyaɲkooɓe yi, giir gu daan jiite reewum Fuuta, ci diggante 1526 ba 1778, seen buur, Silatigi lañu ko daan woowee, wante laata Fuuta-Tooro nekk seeni nguur, buur yi fa nekkoon, yeneen tur lañu amoon. Silatigi boobu, da naroon bokk ci geño Koly Teɲella ku sos giir googu.
Tey, ci Pël yi, Saltige amaatul. Waaye ci Seereer yi ba tey, Saltige yi ñungi wey li ñu doon def demb, di faj ñooñu febar japp, te ñepp xam neen xeew bi ñu tudd Xoy, ci dëkku Seereer yi, laata nawet gi agsi, Saltige yi ñu def ko ngir yegal askan wi mbaa nawet gi dina neex am det, ak yeneen xibaar bu mëna jëm ci wallu nguur gi, ak yeneen. Bu ñu jeexe li, su de dañoo gis lu bon a bugga ñow ci dëkk, di nañu digal ay saaxaar, nit ñi war ko def, ngir lu bon baña agsi. Ci lebu yi, dañoo yengu ci Ndœp, di ay tuur, ngir faj nit ñi.