Saaru Xunti ma

Jóge Wikipedia.

Saaru Xunti ma Makka La Wacc 105 Laaya la.

(1) Maa ngi sant Yàlla mi wàcce ca jaamam ba téere ba te dara dëngu ca.

(2) Mu jub xocc ngir mu xuppe ci mbugal mu metti muy bawoo fa moom ngir mu begal way-gëm yiy def ay yiw ne am nañu yool yu rafet.

(3) Ca la ñuy sax dàkk.

(4) Ngir it mu jàjj ña naan Yàlla am na doom.

(5) Amuñu ca benn xam-xam waxatuma la séeni Baay. kàddu gu rëy a ngook gu génne ca séeni gëmmiñ. Waxuñu lu dul aw fen.

(6) Boo demee yaa ngi alag sa bopp ci topp ci séen gannaaw ak u naqar ngir li ñu ñakk a gëm wax jii.

(7) Nun dey def nanu li nekk ci kaw suuf mu koy taaral. Ngir nu nattu léen kan ci ñoom a gën a rafet jëf.

(8) Te nun noo def la ca kowam mu dib dénd bu wow kohh.

(9) Ndax yaakaar nga ni gaay xunti ma ak (seén xaj ba nekk nañu di lu yéemé ci sunnu kéemtaan?

(10) Fàttalikul ba waxambaane ya làqoo ca xunti ma ne : «Sunnu Boroom noo ngi lay ñaan nga indil nu yërmande ju bawoo fa yaw, te nga yéwénalal nu sunu mbir mii ba mu jub.

(11) Nu nelawal léen ca xunti ma ay at yu takku.

(12) Gannaaw lolu nu yee léen ngir ñu xam kan ci ñaari kurél yee gën a takk diir ba ñu fa sax.

(13) Noo ngi lay nettalli séen xibaar dëgg-dëgg ;nekkoon nañu ñu jub, nu dolli léen ak njub.

(14) Nu takk séen fit ba ñu jógee ni : sunu Boroom a di Boroom asaman yi ak suuf si, dunu ñaan jeneen yàlla ju dul moom, bu nu ko waxee dëy, kon wax nanu lu ëpp.

(15) Sunu nit ñii nag ñoom jël nañu yeneeni yàlla yu dul moom; lu tee ñu joxe ci tegtal bu leer ? ku dàq a tooñ kuy duural yàlla ay fen?

(16) Bu ngéen léen beddikoo ak la ñuy jaamu dem léen làqqu ji ca xunti ma. Séen Boroom wesaare yërmandeem ci yéen defal léen ag jàppandal ci séen mbir.

(17) Nga gis jant bi bu fenkkee bàyyi séen xunti ma ca ndey-joor bu sowee bàyyi léen ca càmmooñ ñoom nag ñu nekk ci men lëm foofee, loolu bokk na ci kéemtaani yàlla, ku Yàlla gindi kooku moo gindiku, ku mu sànk ,doo ko amal ku koy taxawu di ko gindi.

(18) Dangaa yaakaar ne dañoo yewwu te fekk ne ña nga tëdd di ndaw ñu léen di wëlbati ca ndey-joor ak ci càmmooñ séen xaj ba ne wàpp ca ëtt ba, boo ne woon jàkk ci ñoom danga ne waññet daw tiit ba fees.

(19) Noonu la nu lèen yee ngir ñu laajante ci séen biir. Am ca ku ne : Ban diir ngéen fi sax ? Ñu ne : Bès walla as lëf ci bès; ñu ne : Séen Boroom daal moo gën a xam li ngéen fi sax. Yónni léen kenn ci yéen ak xaalis bii mu dem ca dëkk ba, na xool ñam wa gën a sell mu ëndil léen ca lu ngéen wërsëgoo. Na teey, bu mu yëgal kenn nag !.

(20) Ndax ñoom bu ñu léen jekkoo daañu léen jam (xeer) walla ñu delloo léen ca séen diine, te kon dungéen texe mukk

(21) Noonu la nu léen feeñale ndax ñu xam ne digéb Yàlla dëgg la, ak it ñu xam ne àllaaxira amul lu ñu ciy sikki-sakka. (fàttalikul) ba ñuy xëccoo séen mbir ca séen diggante; ñu ne : Tabaxal léen ab tabax. Séen Boroom a gën a xam séen mbir; ña not ca séen mbir ma ne : Fàww nu tabax jàkka ci séen kaw.

(22) Dinañu ne : ñatt lañu (woon) séen xaj baa léen ñeenteel. Dinañu ne : juróom lañu séen xaj baa léen juróm-benneel, » ci demaleek a fekkale. Daañu ne : juróom-ñaar lañu séen xaj baa léen juróom-ñatteel. Neel : Sama Boroom moo gën a xam séenub lim. Kenn xamuléen lu dul ñu néew.

(23) Bul werante ci séen mbir lu dul werante wu leer. Bul sàkku kenn ci ñoom mu ubbil la ci séen mbir.

(24) Bul wax dara nag ne danaa ko def ëllëg lu dul bu soobee Yàlla. Nanga tudd sa Boroom boo fàttee, te nga ne : « jombul sama Boroom won ma lu gën a jub lii ».

(25) Sax nañu ca séen xunti ma ñatti téeméeri at ñu teg ca juróom-ñeent.

(26) Yàllaa gën a xam la ñu fa sax. Moo moom kumpay asamaan yi ak suuf. Ndaw ku man a gis, ndaw ku man a dégg ! Amuñu kenn ku léen di taxawu ci séeni mbir, te àtteem bi du ci boole kenn.

(27) Jàngal li ñu la yenkeewal ci sa Téeréb Boroom bi, Ay kàddoom kenn manu koo soppi. Te amóo benn làqukaay bu dul Moom !.

(28) Notal sa bopp ànd ak ñi nga xam ne dañuy ñaan séen Boroom subaak ngoon namm jëmmam ja rekk. Bu sa bët jéll ñooñu, ngay bëgg taarub dundug àdduna bii, bul topp koo xam ne dañoo fàbbi ab xolam ci fàttiliku nu, mu topp bànneexu bàkkanam, mbiram nekk lu jéggi dayoo.

(29) Texawal ne dëgg gii ca sa Boroom la bawoo. Ku mu neex na gëm, ku mu neex na weddi ! Nun waajal nanu Safara ñeel na tooñkat yi, mu peeg léen wet gu ne . Bu ñu sàkkoo wallu, nu wallu léen ak ndox mu mel ni téex ub diwlin, buy lakk xar-kanam yi ; googu naan a bon ! Boobu sóonuuwaay a ñaaw !

(30) Wóor na ni ñi nga xam ne gëm nañu tey def ay yiw, nun déy dunu sànk yoolu ku rafetal jëf.

(31) Ñooñu am nañu àjjana ju sax, yu ay dex di daw ca séen ron, ñu takkaayal léen fa ay lami wurus ; ñu sol fa yéré yu nëtëx, yu jógé ci sooy ak “wëluur” ; ñuy sóonu ci ay lal Boobu yool a baax, boobu sóonuwaay a rafet . Nu ballal ay dex ca séen biir.

(32) Joxléen misaal ci ñaari gaay yoo xam ne defal nanu kenn ka ñaari tooli reseñ, ñu wërëléléen ay tàndarma, ñu def gàñcax ca diggante ba .

(33) Ñaari tool yépp di menñ te dara wàññikuwu ca.

(34) Mu ame ay meññent, mu wax àndandoom ba ne ko fekk nuy waxtaan :

(35) « Maa la gën a bare alal, te maa la gën a dëgër mbooloo ! » Mu tàbbi ca toolam ba, te di ku tooñ boppam, te mu naan : « Man daal foog naa ni lii du yàqu mukk!

(36) « Te yaakaaruma sax ne Saa dana taaxaw ! Te sax bu ñu ma delloo sama Boroom danaa fa fekk dellluwaay bu gën bii ».

(37) Ándandoom ba ne ko, fekk muy waxtaan ak moom : « Moo ndax dangaa weddi ki la bind ci suuf, ginnaaw ba mu la génné ci toq, topp mu yemale la nga di gòor ? .»

(38) « Waaye man déy kookoo di Yàlla sama Boroom ! Sama Boroom nag duma ko bokkaaleek kenn ! »

(39) « Tee woon ba nga duggee ci tool bi nga ne : lii moo neex Yàlla ! Doole amul lu dul ci ndimalul Yàlla ! Bo gisee ma gën laa néew alal ak i doom. »

(40) « Amaana sa Boroom jox ma lu gën sa tool bi, te (amaana) mu sànni ci sa tool bi ay dënu yu jògé ci asamaan, mu mujj nekk pàkk bu ne ñayy. »

(41) « Walla ndoxam ma mujj ηiis, te doo ca am menn pexe. »

(42) Meññentam ma yàqu, mu mujj di wëlbati loxo, di réccu la mu ca defoon, lépp daanu. Mu naan : « Cèy! aka neexoon ma bañ a bokkaaleek sama Boroom bi kenn. »

(43) Te amul kurél béneen bu dul Yàlla bu koy dimbali, te munu la feyyu.

(44) Foofa dèy Yàlla rekk a fa di ndimbal. Boobu yool a gën, te googu muj a gën.

(45) Joxléen misaal ci dundug àddina gii, dafa mel ni ndox mu nu wàcce ci asamaan gàncaxu suuf si jaxasook moom, mu mujj nekk mboob, ngelaw li di ko tasaare.. Te Yàlla ku jekku lépp la.

(46) Alal jeek doom yi taarub àddina jii la. Te nag yiy des te baax ñoo gën ub yool fa sa Boroom, te ñooy gën-ji-mébét.

(47) Bu keroogee dananu doxloo doj yi nga gis suuf si mu ne dàηη, nu dajale léen, dunu bàyyi kenn ci ñoom.

(48) Ñu gaaral léen séen Boroom ñu doon ay sàppe ca dëgg-dëgg ngéen ñëw fii ci Nun ni nu léen sàkke woon cig njalbéen. Te nag nee woon ngèen ne dunu léen defal ab dig.

(49) Nu teg nag téeré bu, nga gis nag saay-saay si ñu tiit ca la ca nekk, ñuy wax naan : «wóoy nun ! Moo lu jot téeré bii be bàyyiwul lu tuut wàlla lu rèy lu dul rekk takk na ko ! » te nag nu fekk la ñu jëfoon mu teew. Te sa Boroom du tooñ kenn.

(50) Fàttalikul bu nu nee Malaaka ya : « sujjòotalléen Aadama. » Nu sujjòot ba mu des Ibliis ci jinne ya la bokkoon, mu lànk bañ a topp ndigalul Borooman. Ndax yéen dangéen koy jàpp mook i sëtam far ak ñoom ba ma fii yalla ? Te ñoom ñu di séeni noon. Tooñkat yee bon kuutlaay.

(51) Seedeloowuma léen bindu asamaan si waxumalaak séen ug bind ñoom ci séen bopp. Te duma dëgërloo sànkekat yi.

(52) Bu keroogee ba mu ne : wooléen ni ngèen ma doon bokkaaleel,ñi ngèen doon gortu. Ñu wooleen,waaye du énu leen wuyu. Nu def ci séen diggante xuru alkande.

(53) Saay-saay si gis safara wa, mu wòor léen ne daañu ca tàbbi te amuñu lu koy wuññi.

(54) Leeralal nañu nit ñi ci Alxuraan jii ci misaal mu ne . Waaye nit nag moo gën a man a dàggasante lu ne .

(55) Dara terewul nit ñi gëm ba léen njub ga dikkalee, te ñuy jégglu séen Boroom, lu dul doxalinu ñu jëkk ña ; dafa ñëw ci ñoom walla book mbugal mu ñuy jàkkaarlool war a ñëw ci ñoom.

(56) Nun nag dunu yebal yonent yi lu dul ngir ñu ñëw di bégle ak di xuppe. Yéeféer yi nag dañuy dàgge ci neen ngir néewal dëgg. Te nag Jël nañu sunu kéemtaan yi di léen yéjje.

(57) Kan moo dàq a tooñ ku ñu fàttali kéemtaani Boroomam mu dummòoyu léen fàtte la mu defoon. Nun danoo muur séen xol ya be duñu ko dégg, saañ séen nopp ya, te boo léen woowee jëme léen ci njub duñu gindiku mukk.

(58) Sa Boroomay jéggalaakoon tey boroom yërmande. Bu leer doon jàpp la ñuy fàggu kon dana léen gaawe mbugal mi. Li am daal mooy am nañu dig boo xam ne duñu ko man a làqu fenn.

(59) Dëkk yooyu nag alag nanu léen ba ñu tooñee, te wutaloon nanu séen alkaande ja ab dig.

(60) (Fàttalikul) ba Muusaa waaxee ngóoram sa : Duma deñ di wéy ba fa ñaari géej ya daje walla ma wéy ab diir bu yàgg lool.

(61) Ba ñu yeggee fa ñu daje ñu fàtte fa séen jën wa, mu jaar ca géej ga wèy.

(62) Ba ñu jàllee mu ne ngóoram sa : ëndil sunu añ bi, sunu tukki bii daj nanu ci coono.

(63) Mu ne : xanaa xamóo ne ba nu wàccee ca xeer wa la fàtte jën wa. Dara fàtteloowuma ko lu dul Séytaane, bé fàttalikuwuma ko. Mu toppaat aw yoonam jëm ca géej ga ; lii moo doy waar!

(64) Mu ne : loolu la nu doon wut. Nu woññeeku topp séeni tànk ya woon.

(65) Ñu fekk benn jaam ci sunu jaam yi bu nu jox yérmande ju tukkee fi nun, te nu jox ko xam-xam bu bawoo fi nun.

(66) Muusaa ne ko : Ndax duma la topp ngir nga jàngl ma li ñu jàngal cig njub ?

(67) Mu ne (ko) : yaw soo àndeek man doo man a muñ.

(68) « Nooy man a muñe loo xam ne peegóo ko cig xam.

(69) Mu ne : « Dinga ma fekk bu soobee Yàlla may ku muñ, te duma moy sa benn ndigal.

(70) Mu ne : Boo ma toppee, bul ma laaj dara, ba keroog ma la ciy tudd li ko waral.

(71) Ñu wéy ba yéeg ca gaal ga, mu xar ko. Mu ne : Ndax danga koo xar gir labal séen woroom ? Li nga def réy na !

(72) Mu ne : xanaa waxuma la woon ne foo àndeek man doo man a muñ..

(73) Mu ne : Bul ma jàppe sama fàtte gi te bul ma teg ci sa mbir mi lu ma manul !

(74) Ñu wéy ba dajeek benn xale, mu rey ko. Mu ne : ndax dangay rey bakkan bu sell ci lu dul bakkan. Def nga bir mu juunu!

(75) Mu ne : xana neewuma la woon boo àndeek man doo man a muñ.

(76) Mu ne ! Su ma la laajatee dara ginnaaw ba bul àndateek man. Egg a ngaak man ci am ngànt.

(77) Ñu wéy ba agsi ci waa-benn dëkk, ñu fekk fa wenn sàkket wuy bëgg a màbb nu jubbanti ko. Mu ne : Bu la neexoon nga jël cig pey.

(78) Mu ne (ko) fii nag la ñuy tàqalekoo. Dinaa la firil lii nga xam ni manuloo ko woon a muñ.

(79) Li aju ci gaal gi, ay miskiin a ko moomoon yu daan liggéey liggéeyu géej ga. Ma bëggoon caa def sikk ndax dafa am benn buur buy nangu gépp gaal ci doole.

(80) “Bu dee xale bi nag, ñaari way-juram dañoo gëm, Nu ragal mu teg léen ag bew ak ug weddi”.

(81) “Te yaakaar nañu ne séen Boroom wecceel léen ku ko gën, te gën a sell, gën a am yërmande.”

(82) “Bu dee sàkket wa nag, ñaari xaley jirim ñoo ko moom, yu nekk ca dëkk ba, te séen um koom dafa nekk ca ron ga, te baay bu baaxoon la, te Sa Boroom namm bu ñu demee ba dëgër génne séen koom ma, mu di yérmande gu tukke ci sa Boroom, te defuma ko ci sama sañ-sañ loolu mooy pirig li nga manul woon a muñ.”

(83) Ñu ngi lay laaj mbirum « Sul-Qarnayni » Neel : “Dinaa léen nettali ci moom lu di fàttali.”

(84) “Nun noo ko dooleeloon ci kaw suuf, defal ko ci lu ne aw yoon”

(85) “Mu topp yoon be àgg ca sowu jànt, fekk ko muy so ci déeg bu ñuul kuk, nu fekk fa aw nit. Nu ne : yaw « Sul-Qarnayni », benn nga mbugal léen walla nga defal léen njekk.”

(86) Mu ne : ku tooñ nag, dananu ko mbugal topp nu delloo ko ca Boroomam mu mbugal ko mbugal mu tar.

(87) Ku gëm nag te jëf jëf ju rafet, daanu ko defal ag yombal ci sunu ndigal.

(88) Mu toppaat yoon wa be yegg penkub jànt ba, mu fekk ko muy fenk ci aw nit yu defunu séen digganteek moom genn kiiraay.

(89) Naka noonu la Nu peege ci xam-xam la ne fa moom.

(90) Ginnaaw ba mu toopaat yoon wa. Ba mu egsi diggante ñaari xeer yu mag mu fekk fa nit ñoo xam ne daanaka duñu dégg wax.

(91) Ñu ne yaw « Sul-Qarnayni », Yaajooja et Maajooja dañuy yàq ci réew mi, ndax duñu la jox galag ba nga defal nu sunu diggante dig woo xam ni dana léen téyé.

(92) Mu ne : “Jàppandal gi ma sama Boroom defal moo gën waaye dimbali léen ma ci doole ma def séen digganteek ñoom ab sëkk“

(93) “Ëndilléen ma daggiti weñ yoo xam ne su ñu demee be tollook ñaari walli doj wi, uppléen, bu demee ba nekk safara, Mune : Ëndilléen ma sotti ci xelliti përëm.

(94) “(Noonu) duñu ko man a yéeg, duñu man a bënn”.

(95) “Loolu yërmande ju tukkee ca sa Boroom la. Bu sama dige Boroom dikkee, dafa koy def mu mokk rumbux. Te sama dige Booroom dëgg la”.

(96) Nu bàyyi ñenn ña ñuy jaxasook ña ca des, Nu ëf ca bufta ba, Nu dajale léen dajale bu wóor.

(97) Te bu keroogee dananu gaaral Safara yéeféer ya ab gaaral.

(98) Ñooy ñi nga xam ne séen gët ya dafa muuru woon ba duñu fàttaliku te ñu nekkoon ñu dul man a dégg.

(99) Ndax ñi weddi (Yàlla) dañoo yaakaar a jël sama jaam yii di far ak ñoom bàyyi Ma fi Nun dèy waajal nanu Jahannama muy wàccuwaayu yéeféer ya.

(100) Neel : Ndax dunu léen wax ñi gën a pert jëf : Ňooy ñi nga xam ne séen jëf ya sànku nañu ci àdduna jii, te ñu yaakaar ne ñu ngay rafetal jëf.

(101) Ñooñu ñoo weddi séen kéemtaani Boroom ak ab dajeek Moom. Séeni jëf yàqu keroog dunu léen màndaxeel séeni jëf.

(102) Li ko waral moo di séen pey mooy jaanama ngir la ñu weddi, te danoo jël sama aaya yi ak sama ndaw yi di léen yéjji.

(103) Wóor na ne ña nga xam ne gëm nañu, àjjana firdaws nekk na séen wàccu-waay.

(104) Fa la ñuy béel, te duñu ca sàkku genn ug soppiku.

(105) Neel : Bu fekkoon ne géej gi dafa nekkoon daa ngir bind sama kàdduy Boroom, kon Neel : kon géej ga dana jeex te sama kàdduy Boroom du jeex, dontale ëndi woon nanu geneen géej mu tëbb ko.

(106) Neel : Man duma lenn lu dul mbindéef ni yéen mu ñuy yenkeewal ne : séen Boroom benn Yàlla là. Ku yaakaar ne dana dajeek Boroomam na jëf jëf ju yiw te bu ma bokkaale kenn ak Borooman ca jaamu ga mu koy jaamu