Saamóori Ture

Jóge Wikipedia.
Saamóori Ture

Saamóori Ture mi ngi juddoo Mayambalandogo ci lu tollook 1830 g.j. Mu nekkoon ab yaxantukat, dajale woon na ab xare ngir nangu suuf yu bari, daal di taxawal ag Imbraatóor.

Dugg na ci Lislaam atum 1880 g.j, daal di wéy nag ci yaatal Imbratóor gi. Waaye xéy na cig mbetteel fenqoo ak Tubaab yi daan sanc, daal di jàmmarloo ak ñoom jàmmarloo gu tar : leeg-leeg ci anamug maslaa (diplomatie) jaare ko ci di def ak ñoom ay déggoo, lu ci mel ne déggoo gu Bisandogo ; leeg-leeg it ci anamug xeex ak ñoom.

Waaye waa Fràas yi ci njitug Gayni ñoo ëppoon ngànnaay : ndax ñoom amoon nañu ay kanó aki fetal yu aaytal. Bu dee Saamóori nag, moom dafa sukkandiku woon rekk ci fasam yi ak fetal yi tëgg yi daa liggéey. Jot naa daq nag tubaab yi te jàmmarloo ak ñoom diirub 12 at. Ci atum 1892 g.j, la dooley xareem ji tàmbalee doyadeek a loof ngir xeex yu bari yi, bu ko defee tubaab yi song Imbratooram gi. Saamóori lànkoon na ne du wommatu ( se rendre), mu daal di woon dem jëm penku taxawal fa ag nguur gu yees ci bëj gannaaru Tefesug bëñu ñay gi (Cote d’ivoire), waaye fekk na waa Fràas yi ak waa Angalteer xemmeemoon barab bii mu taxawal nguuram gi.

Ci atum 1898 g.j, waa Fràas yi bett nañu ko ca dàttub Gelemu (camp de...), ñu njaf ko, yobbu ko Gabon, fa la faatoo ci atum 1900 g.j daal di jël nguuram googu boole ko ci Cote d’Ivoire. Jàmarloo gu Saamóori Ture gi kontar tubaab yi dees na ko jàppe genn ci yi ëpp solo ci jàmmarloo yi ci sowwu Afrig. Sax na diirub 17 at. Yóbbe na canc gi ay ñakk yu takku.

Xool it[Soppisoppi gongikuwaay bi]