Sñ Sàmba Jaara Mbay

Jóge Wikipedia.
Seex Sàmba Jaara Mbay

SEEX SÀMBA JAARA MBAY

AB XAMLE[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Seex Muhamadu Abdu Kariim Sàmba Jaara Mbay: Mi ngi gane jamono ci atum 1868, làqu ci atum 1917 dundam mi ngi tollu ci 49i at.

Di doom ci S Ahmadu Mbay ak Soxna Ndaag Kan Ñaŋ. Di rakk ci S Saa-jéey Mbay mi nga xam ne nitu Yàlla ku mag la woon, ba sax Sñ Sàmba Jaara Mbay moom la defoon ub Sëriñam.

Sñ Saa-jéey Mbay, jamono bi Sëriñ Tuubaa nekkee Ndar jëkk muy dem ci géej gi booba Ndar moo doon gëblag senegaal. booba nag Sëriñ bi daa na dem lu bari ci ku ñuy wax Sëñ Móodu Njaay Maa-béey daan dal fa moom, foofa la Seex Saa-jéey gisante woon ak Sëriñ Tuubaa Sñ Saa-jéey Mbay nag bi mu tasee ak Sëriñ bu mag bi, ba Sëñ bi wan ko lam ko wan, ca la jébbalu fa saa sa. Sëriñ bi nangul ko njébbaloom teg ci seexal ko ca bis ba, ngir fam tollu ci sunu Boroom.

Ca ginnaaw ga la doon wëri rakkam jii di Sàmba Jaara Mbay, ngir mu jébbalu ci Sëriñ bii mu gis; muy Sëriñ Tuubaa.

AG JÉBBLOOM[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Bi nga xamee ne S Saa-jéey mi ngi ko doon wër, fekkoon ne booba Seex Sàmba Jaara Mbay mi ngi doon waaj ngir siyaare ji Yónnent bi, doon tàggu Sëriñ Alaaji Maalig Si mi nga xam ne daan na ko jàngal yenn téerey xam-xam yi. Ca booba la ko Sëriñ Alaaji Maalig Si waxoon ne ko ngir mu jaar ci Sëriñ Siidi Muxtaar Alkuntiyu mi nga xam ne moo doonoon sëriñu baayam Ahmadu Mbay ngir mu siyaare ko tàgguwaale ko. Bam demee ngir tàggu ko ca la ko xamaloon ginnaw bi mu duggee ñatti fani xalwa ne ko woon nag: «Kenn du dem ngir siyaare Yóonent Bi ñu ko koy fomm-loo waaye yaw kat am na lu ma saa Boroom wan ci say bir, wan na ma ne Xutbub jamono dina feeñ te yaw kat di nga am cér bu rëy ca moom boo fi toogee. Te ki tax nga nar a daje ak moom mi ngi lay wër». Booba Seex Saa-jéey juge na Ndar , dégg ne Seex Sàmba Jaara mi ngi jëm Gosaas. Fekkoon ne S Sàmba Jaara moom juge woon na fa ba demoon Tiwaawan jaar fa dem Njaasaan ba doon dëppaat jëm Gosaas foofa la tase ak Seex Saa-jéey mu xamal ko ne moom la doon seet, ne ko nag jëmm ji ma doon wër muy Xutbub jamono gis naa ko. Ma bëggoon ñu ànd ca moom nga jébbal ko say bir. Ca la Seex Saa-jéey ànd ak moom jëm Ndar jébbal ko Sëriñ Tuubaa.

DIGGANTEEM AK SËRIÑ BI[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Seex Sàmba Jaara nag ab Saa-Kokki la woon waaye ba mu jébbaloo ci Sëriñ bi dafa mujjee féete Ndar. Mu nekkoon fa ak Sëñ bi, Sëriñ bi nag ubbi woon ko, mu nekkoon way-katam, di ki jëkk a tagg Sëriñ Bu Mag Bi ci làmmiñu wolof! Ngir ne moo jiitu ñoom S Moor Kayre(1869-1951) ak ñoom Sëriñ Mbay JAXATE(1875-1954) ak Sëriñ Muusaa KA (1889-1963) , te doonoon seen mag, ba lii a tax Sëriñ Muusaa KA naan:


  • Wayoon nan ko ba làccal te yaa ngi way Daam.

Kon muy ku daa tagg Sëriñ bi ci ay way yu rafet lool, Sëriñ bi tamit bëggoon ko lool ak iy wayam. Loolu nag ag déggam ak ug man a wayam lay tegtale. Ba moom Seex Sàmba Jaara sax daan na wax naan: Sëriñ Tuubaa damaa rafaatale darajay Hassaan ibn Saabit mi daan dar Yónnent Bi daa ko way mu koy may, ba loolu a tax mu ne:

  • Buur Yàlla may na ma'w kañam
  • Ma di Hasaanam fu ma jëm.
  • Di tarjumaanu làmmiñam
  • Ki ma giseel a mat a xam

Ay wayam nekkoon lu daan dugg ci xolu aji-dégloom, ba daan na yóbb Sëriñ bi cib jéll. Loolu nag sikkul ngir ne Sëñ bi daan na dégg ay mbindi boppam mu ko daan def haal, ba di laaj ana ku wax lii? Ñu ne ko Mbàkke lii de say wax a. Te Seex Sàmba Jaara ni Sëriñ bi daan waxee ak Yónnent bi noonii la daa waxee ak Sëriñ bi, ci ay waxiin yu taaru, moo tax mu ne :

  • May na ma, ma déggook moom i wax
  • Ci ay waxiinam yu mu wax,
  • Samay waxiinay na mu wax,
  • Ki ma ma giseel a mat a xam.

Nga xam ne dañoo dem ba niru ay wax, ba Sëriñ bi da ko daan di bëgg a dégg muy way, ba loolu waral moom masut a ñëw ci kër Sëriñ bi ñu koy xaarloo naan ko sëriñ bi daa fatu (tëju). Te ba ci magam Seex Saa-jéey daan na ñëw ñu naan ko Sëñ bi dafa fatu. Ba mag ñi, ku ci masaa na bëgg a gis sëñ bi, ba gis Seex Sàmba Jaara Mbay jëm fa moom, da koy leer ne di na gise ak Sëriñ Bi tay. Ba bu daa ñëw fekk Sëñ Bi fatu sax, bu daa Tàmbli a way, Sëriñ bi génn, ba amoon na bayit yoy moom la daa nuyoo Sëriñ bi bu masaa na dugg ci kër Sëñ bi:

  • RAHMATUL LAAHI YAA NAHIIMA JINAANII
  • ANTA HIBBII WA ANTA NUURA JANAANII
  • XURRATU HAYNII YAA BUSAARATA XALBII
  • ANTA TIIBU FU-AADII YAA RAYHAANII ...bmj (ba mu jeex).

Bu ko daa jàng reg Sëriñ Bi daldi génn.

Ba loolu a waraloon mu tudde woon ko Saahibul Abyaati maanaam Boroom Bayit Yi (dàkkantal la wu ko Sëriñ Bi daan woowe ngir ug ràññikoom ci man a way).

AY WAYAM[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ay wayam nag nekk na luy yare ak a jàngale tawhiit, ak a wane melow Sëriñ Bi. Ngir daan na wax ne : Sëriñ Tuubaa li mu daan defal Yónnent Bi SHW ci daan ko tagg ak a xamle mooy kan? Manu ko woon a defal boppam, loolu a tax mu def ci man li tax ma koy defal la mu daan defal Yónnent Bi SHW, ci di ko tagg ak a xamle mooy kan? Moo tax mu ne:

  • Wax na Yónnen Bi, li mu doon,
  • Man it, ma wax ko Ii mu doon,
  • Moom it, mu def ma li ma doon
  • Ki ma giseel a mat a xam.


  • Nee na Yónnen Bi, yaw a yaw,
  • Man it ma wax ko yaw a yaw,
  • Bu nee ko yaw, ma ni ko yaw,
  • Ki ma giseel a mat a xam.
Seex Sàmba Jaara Mbay

Ba loolu a waral mu daan jël Xasida yi Sëriñ Bi di tagge Yónnent Bi SHW , mu jële ca turu xasidaam tagg ci Sëriñ Bi, jël it Bahru bi nga xam ne moom la Sëñ bi tëggee ag taggam ci Yónnent bi. Ci noonu lanuy gisee mu jël xasidag Sëriñ bii di Jasbul-Xuluub mu fent ci Jasbul-Majsuub. Moo tax mu naan:

  • Jësbul-Xuloob bi dafa jib,
  • Bii jësbu jóg xeeñ fa mu jub-,
  • -lu ku ko xeeñ na wut a jub,
  • Wéy na xameeful fu mu jëm.


  • Jësbul-Xuloob bi dafa daw
  • Bii Jësbu góg, xeex fa mu aw
  • Ta ku ko dab na daw a daw,
  • Raw na xameeful fu mu yam.

Naka noonu la tëggaate xasidag Sëriñ bii di Mawaahibun-Naafih fii Madaa-ihis Saafih mu tuddee ko Naylul-Maraahibi Fii Mukaafatil-Mawaahibi mu ciy way Sëriñ bi ci jëmmi Bahru Mawaahibu. Bokku na ca Xasida ga, fi mu jële waxu Sëriñ bi, ba mu doon tagg Yónnent Bi naan ko:

  • Antal Kariimu.
  • Anal Xidiimu.

Moom mu jël ko delloowaat tagg woowu ci Sëriñ bi. Naan ko:

  • Antal Xadiimu.
  • Antal Kariimu.

Nga xam ne bayit woowu Sëriñ bi mi ngi ciy wax Yónnent Bi SHW: (yaw yaay Aji-tedd ji, man maay sa jëwriñ ji lay liggéeyal) Seex Sàmba Jaara Mbay ne Sëriñ bi: (yaw yaay jëwriñ ji, te yaw yaay Aji-tedd ji) Nga xam ne ñaari melo yépp da ko a delloowaat ci Sëriñ Bi. Loolu di dëggal la mu waxoon ne:

  • Wax na Yónnent bi li mu doon,
  • Man it, ma wax ko Ii mu doon,
  • Moom it, mu def ma li ma doon
  • Ki ma giseel a mat a xam.


  • Nee na Yónnent Bi, yaw a yaw,
  • Man it ma wax ko yaw a yaw,
  • Bu nee ko yaw, ma ni ko yaw,
  • Ki ma giseel a mat a xam.

FI KO SËRIÑ BI TEGOON[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Sëriñ Tuubaa nag fonkoon na ko lool ba bu daa laaj kenn; ana foo bawoo? Boo ne koo Ndar. Daf lay laaj ndax siyaare nga Sàmba Jaara Mbay? Boo ne koo déet. Mu ne la kon demóo Ndar! Loolu batay muy tektale ag cofeelam ca moom, ba tax bi Seex Sàmba Jaara Mbay làqoo, toog na ñatti at yoy daan na laaj ana ku man waxiy Muhammat Abdu Kariim Sàmba Jaara ya? mag ñi daa ko ko wëral ba 1920 ci lañ gisee kuñ naan Sëriñ Daam Njaay ca Gosaas moom taalube Seex Saa-jéey Mbay la woon, moo mokkaloon wayi Seex Muhammat Abdu Kariim Sàmba Jaara ya? Ca la ñëwe daa di koy jàng ci kanamu Sëriñ bi. Ba nee nañ bu daa dégg kuy wolofal, da daa wax: "Sàllaahu moom de lu mat a wax reg Sàmba Jaara wax na ko". Ba Sëriñ bi yeggoon na ci daa wax S Sàmba Jaara bu daa way ba yeggal: "Aggal ci keesu jigéen ñi nettali leen wax ji". Te ku ne xam na ne keesu jigéen ña Sëriñ Bi musta nangu benn góor dugg fa, waaye lii la daan wax S Sàmba Jaara Mbay. Mu am tawféex ju rëy nag, ci Sëriñ Bi joj ci moom reg la nu ko déggee mooy "xam Sëriñ Bi", te bi mu koy wax ci kanamu Sëriñ Bi la ko waxee! Te Sëriñ Bi waxoon na ni ku dul sama Boroom xamuma, moom mu ni

  • Wan na ma boppam na mu day.
  • Yàlla a ko xam moo ma ko may.
  • Ta wóolu naa ni moo ma doy.
  • Ki ma giseel a mat a xam.

Dellu ne:

  • Bu fekkee moo feeñu ci man.
  • Nu naa ma yaw, booba du man.
  • Moom ka di moom moo fi di man.
  • Ma di fi moom muy ki fi xam.
  • Moo tax ma wax ku déglu lii.
  • Na xam ni yii ñuy wax du lii.
  • Waaraate jóowuma si lii.
  • Seriñ Bi may na ma boppam.

MUJJUG JAMONOOM[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Bis Seex Sàmba Jaara doon na doxantu ci wetu dex ga ca Ndar, mu gis ay jongama yu taaru lool , mu xam ne ñii duñ ay nitu fii, mu laaj leen? Ana loo leen di def fii? Ñu xamal ko ne ñoom ci Huurul-ayni yi la nu bokk, da noo ñëwoon ngir teertu seen ub sang. Mu laaj leen; naka la seen sang boobu tudd? Ñu ne ko: Muhammat Abdu Kariim Sàmba Jaara Mbay . Ca la dawee dellu këram, moo tax mu ne:

  • Ku sédduwul man séddu naa.
  • Ku fàdduwul man fàddu naa.
  • Ba matle weesu naa danaa.
  • Yàlla ak sa barke maa la gëm.

Bayit bii la téjjee Xasidaam gii di Jasbul majsuub, yàggul dara mu wuyji Boroomam. Te ci xew-xew boobu la xamee ne Àjjana la jëm. Te Muhammat Abdu Kariim Sàmba Jaara la fay tudd. Ci la waxee woon ne!

  • Ku xam lii xamul woon samaw tur la xam
  • Ku xam lii xamul woon na xam ñatti tur
  • Muhammadu Abdu Kariim Sàmba Jaara
  • Lu siiw la ci yoon wii te siiw taaxi Ndar
  • Di soppey Sëriñ Bàmba tey way-katam
  • Diggante juróom ñaari réew yii ñu wër.

Keroog bim wàccee liggéey, mag ñi seen ug xam cofeelu Sëriñ bi ci moom taxoon na manu ñu ko woon a wax ni Seex Muhammat Abdu Kariim Sàmba Jaara Mbay bàyyeeku na fi. Mag ñi naan ko: Mbàkke yéem nanu Yàlla ci Seex Sàmba Jaara! ay waay Mbàkke yéem nanu Yàlla ci Seex Sàmba Jaara! Sëriñ Tuubaa ne leen: Waaw ñi ko doon jël si fii la ñu jaar.(fekk ne moom moo leen ko njëkk a yëg.) Mu ne leen Sàmba Jaara déy dama koo duy ba mu fees ma rokkas ko mu tépp. (Te mooy li mu doon junj ca Jasbul majsuubam ba naan Sëriñ Tuubaa déy:

  • Tibbub cofeelam da fa fees
  • Ci man di funki ak a yees
  • Ci sama xol ba dóotul rees
  • Ki ma giseel a mat a am
  • Moo tax mu def buma nee gees
  • Ci sama xol mbaa mu ne gees
  • Sunu diggante ne depees
  • Ki ma giseel a mat a xam).

Seex Muhammat Abdu Kariim Sàmba Jaara Mbay mi ngi génn àdduna atum 1917, barabam bi ma nga nekk ca almeeru Cem yi fa Ndar.

AK NJABOOTAM[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ñatti doom la amoon ñuy:

  • Faatima Sahraa Mbay
  • Elaaji Mbàkke Mbay
  • Muhammdu Mustafaa Mbay.

XOOL IT[Soppisoppi gongikuwaay bi]