Sëriñ Baara Mbàkke Fàllu
Seex Muhammadu Lamiin Baara, ñu gën koo xam ci Sëriñ Baara Mbàkke Fàllu!
Ganeem àdduna
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Mi ngi gane àdduna Ndindi ci atum 1921. Ay wayjuram : Seex Muhammadul Faadal Mbàkke ak Soxna Xari Sàll.
Am njàngam
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Sëriñ Fàllu moo ko dalal jàng ginnaaw ñu jox ko S Moor Sàññe mu jàngal ko bamu sori 1928 la ko Sëriñ Baara moom Sëriñ Tuubaa minu ko tudde jël yóbbu ko ci ku ñiy wax Sëriñ Móodu Amar mu àggaleel ko alxuraan ji, ginnaaw loolu la Sëñ Baara génn àdduna mu dellusiwaat ci Sëriñ Fàllu mu yabal ko Jaamal mu jànge fa xam-xam ca Sëñ Jaamal Siise, bokk na ci liy wan xam-xamam bu yaatu lumu jangoon da ko daan mokkal. Sëriñ Siidi Maxtaar ka nee na toog na muy tari. “Maqaama Al hariirii” ne ko lii dama koo mokkaloon bamiy jàng! Xel mi neexoon lool daan na wax ay lakk yu bari te wuute araab farañse angale ak yu ni mel, nekkoon nit ku man a takk daawul fàtte.
Sëriñ Baara nekkoon ku bëgg Sëriñ Fàllu te déggaloon ko lumu am jox ko lumu am tudde ko ba tuddee na ko ci njabootam ab lim bu bari tabaaràkkal laah, fonk ay magam Sëriñ móodu miy magam noonu la ko bëgge woon topp ko daawul juuyoo ak moom ci dara daawul xëccoo ak moom dara bàyyee ko boppam bam jeex takk. Sëriñ Móodu daa na wax naan kenn rekk laa xam ci kuma gën a bëgg sëriñ Fàllu mooy sëriñ Baara!
Ag xilaafaam:
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Muy sët bi njëkk a wuutu Sëriñ Tuubaa ci jamono ji nit ñi miinoon lool doomi Sëriñ Tuubaa Sëriñ Tuubaa Baara ñëw ca yar ba ak jikko ju rafet ja ak man a xajoo ga ak man a yaatal ga ak ubbiku ga xam ne fimu nekk dug moomeel waaye ab liggéey la bu népp bokk du yëfi kenn. Mu dox doxiin woowu ba jaar fu kenn foogul liggéey fi loo xam ne toogaayub juróom fukki at lay niru. Ay jëfam Tuubaa liggéey na fi liggéey bu yaatu pecci yi wër kër njabotug Sëriñ bi yépp defar na ko def fa ay yoon, fu ndox mànki mu yóbbu ba ci biir dëkk bi sax, ñu bari ci ag nekkam lañu am kër, soxla soo ko wax bu dee luñu man a joxe mu joxe ko bu dee luñu war a lijanti mu lijanti ko daar-daar, andi waat ñu bari ci yoon wi jox leen seen wàccuwaay, nos dëkk bi ku ne mu am lumu la jox ci dëkk bi ngir nosiin wi rafet ak doxiin wi, màggal gi mu yaatal ko bitim réew ak fépp ak biir réew mi ak waxtaan yu am solo ngir tissaare wooteb sëriñ Tuubaa wi. Nekkoon gu bëgg bennoog jullit yi, dem seet i ay mbokk i diineem yu bari daan leen nemmiku, Sëriñ Baara nekkoon nit ku woyof daawul xeeb kenn, nekkoon nit ku neex a jot di wax ak ñépp di déglu ñépp, bamu nekk a gul xalifa ak bi mu nekkee xalifa daraam soppikuwul, ña mu daan seet i lay seet i, ña mu xamoon beddiwu leen di tudd i doom di dem sarax di seet i ku tawat, màggal yépp la daan dem. Deful woon yëff yi yëfi kër, waaye yëfi ñépp la ko defoon, bëgg ay rakkam def leen ni boppam , dëddu woon àdduna lool man a jaamu Yàlla lool fonku julli lool bokk na ci ñi ëpp lunu julli ci jumaay Tuubaa ak lumu metti ci moom di xaritu ñépp. Sëriñ Baara nekkoon koo xam ne ku daan jàppale ndaw yi, dileen taxawu ci seen njàng ak seen liggéey. Sëriñ Baara amoon gëm-gëmu jiital ndaw yi ci lépp xam ne ñooy yaakaari ëllëg yi, mu teel leen a jiital, Mu nekkoon nit ku man a jaamu Yàlla daawul nelaw guddi wird ak déeyaaleg boroomam la daan fanaane,
Diganteem ak nitu nguur yi:
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Sëriñ Baara daan na jëflante ak nitu nguur yi ci jëflante bu rafet te lépp lu ko laloon mooy jotalileen lépp luy ñjariñal nit ñi, teewul nag, moom daa mas a gëm ne fii lépp lu fi nekk rekk, taalibe Sëriñ Tuubaa yi ñoo ko fi def! !!! Loo fi gis ñoom la ladaan wax, kon masul sàkku ci ñoom dara lu dul ne, daa nekk loo xam ne njariñal nit ñi la. Nitu nguur yi itam yabuñu ko woon, ngir dëggoom ak pass-pass bu dëgër ba ci Sëriñ Tuubaa ak fulla ji nekkoon ci moom.
Sëriñ Baara ak aji màkka: Dem na màkka lu ëpp ñent fukki yoon, yóbb na fa nit ñu dul jeex, att mu nekk dadaan yóbb nit ñu bari, sëriñ Baara yoroon jikkoy sëriñ Fàllu, nekk nit ku woyof te bari njariñ daan dimbali ñépp, di nit ku ubbiku, ku baax te bariwoon jàmm, tabe lool am xorom lool, yéene ji kawe lool, pasteef bi ak taalube gi foo ko takk weesu na ko Yàlla nanu ko Yàlla fayal.
Sëriñ Baara bàyyi koo na fi wuyji boroomam ci attum 1431, 18 rajab