Sëriñ Abdul Ahad Mbàkke
Sëriñ Abdu Lahat Mbàkke di doomi Soxna Maryaama Jaxate ak Sëriñ Tuubaa Xaada lahu laahu Maxtaara lahu. Ci 23i la gane àddina ci weeru korite ci atum 1332 ginnaaw gàddaay gi. Di tolloo ak 1914 ca Njaaréem.
Am njàngam
[Soppi | soppi gongikuwaay bi]Ba mu tollee cim njàng lañu ko jox nijaayam Sëriñ Hamzatu, nijaay ji jox ko Sëriñ Alsaan Jaxate mu jàngal ko Alxuraan. Ci barab boobu la jàngee Alxuraan ba mokkal ko, bind ko. Am nañu wax ne kaamil bi Sëriñ bi la ko jox am ñu wax ne Seex Muhammadul Mustafaa la ko jox.
Ginnaaw ba la ko magam ju baax jii yabal fa Cindoodi mu fay jàng xam-xam ci ku ñuy wax Sëriñ Maxtaar Jeŋ Guyaar. Àndiwaat na ko Tuubaa jox ko Sëriñ Habiibu Mbàkke mu fay jàng, ba mujj na doon kaaŋ-fóore, xam lépp lu dóomi-soxna war a xam.
Ay jëfam
[Soppi | soppi gongikuwaay bi]Mu amoon gis-gis bu yaatu, teel a jàmbaare te ñeme sumb. Li koy firndeel moo di ci atum 1932 la sanc ab dëkk, booba amul 20i at. Bokk na ci dëkkam ya Daaru Rahmaan, Kàdd Ballooj, Kàbb Gay, Daaru Ja ak yeneeni dëkk di fa Tarbiya, di bay, di joxe àddiya.
Ba Sëriñ Fàllu wàcce liggéey la toog ci xilaafay Borom Tuubaa ci atum 1968. Wax nañu ne sax, di tudd turu Sëriñ bi di ci teg turu xalifaam ci jamonoom la tàmbali. Ku ñuy wax Keledoor Jaañ moo ko njëkk wax "Sëriñ Tuubaa Sëñ Abdul Ahad" ginaaw ba la ko Sëriñ Mustafaa Basiiru tasaare.
Seex Abdul Ahad daa mane woon fu bari te xamoon jamono. Moo yaatal Marse Okaas, moo tàmbali "Université bi" moo dundalaat Aynu Rahmati ba ñépp man ci jot. Moo yokk "forage" yi, sanc Tuubaa "bibliothèque" bu mag, nu koy wax Daaray Kaamil.
def ci alal ju bari, ubbi ko ngir ñépp man ci njariñu, tëli yi jëm Tuubaa itam liggéey na ci lu réy. Moo yokk dëkk bi, "muré" Jumaa ji, yeesalaat barabu Ku Tedd ki. Moo aaye fa Tuubaa mbooleem luy tux ak ya ca askanoo ak lépp luñuy naan te Diine tere ko.
Loolu moo waral Seex Abdul Ahad Ture wax ne: "fitam waak xelam waa tax, mu xéy yeesalaat Okaas, te aaye fi ay ñaawtéef di leen jox ndigal yu leer, fitam waak xelam waa tax mu aaye fi jëf yu ñaaw lu mel ne naan ak tux ba dëkk bi lépp a leer".
Daan taxawu Yoonu Murid ci wàll yépp. Nit ku dëggu la woon, daan nañu ko wax ñàkk-caaxaan, am fit lool، xel mi réy، mu manoon a jëflante ak ku nekk. Waa Nguur gi joxoon ko cër itam. Nit ku oyof la woon، leer ay wax.
Ay way yu jëm ci moom
[Soppi | soppi gongikuwaay bi]Lii la ko wax:
Abdul Ahad yal na saw fan gudd Mbàkke nga wér. Te sax ci jamm’aku yiw ak jaamu Yàlla gu wér. Farlul te wéy yal na ngay for dog bu sedd sa xol. Te mucc ciw ay’akum ndog sax ci def la la war.
Toppal sa mag Mustafaa bul génn yaw ndigalam. Ngir mag mu mat mag la mat ñéppub sëriñ te du wor. Jëfal te bul faale nit، bul geesu nit ci sa jëf. Na Yàlla tax ngay jëf ak Yonen ba ak ka la jur.
Kalay manal dara moo jar def lëf ak bàyyi lëf Te kooka nag moo di « Rabbul Archi » yal na la yor. Yar bii nga yor yor ko biir ak bitti moo di sa kee. Moo gën ci yaw nit ñu baax ak kër yu baaxaki jur. Sa baay a gën ñépp teb yar dong-dong la yor.
Yoral yaram ba te koo gis deeko sant ak a yar Sa baay a gën ñépp ab yar ngir dalay jox a jox ab yar. Ba ngay am a am ab yar te doo mos i yar. Du yëkkatib yar di teg nit waaye moo gënu nit. Ñay teg nitub yar akay janneek a yeew ak a lor.
Nijaayi ndam yii nga am loo jis ñu am ko ci ndam. Xamal ni moo ko ca def jii wax ku nekk la bir. Nijaayi ndam yii nga am loo jis ñu am ko ci ndam. Xamal ni moo ko waral ak cant war na gu tar.
Ag cant war na ci yaw ak ñoom gu rëy gu rafet. Gu tol ne bàjjo gu dul yam fenn mukkati far. Loo jis ci Amsatu moo mii cib yar ak jëfu yiw. Xamal ni moo ko ca def gii wax ku nekk la bir.
Abdooki Amsatu ak Mbakkeeki Bàlla Asan Yaw say nijaay a ngii ñoo diy sàll kenn du ciw par. Fëxal te raw am nga ab yóbbal fëx ak raw a des. Ngir baaxi bokk a di ab yóbbal na yitte ji sar.
Saral te wéy dëgg bul yam ciy nijaayaki Baay ak nday di sant ak a doyloo seeni cër lu ko jar؟ Foo seeru kuy fok a doyloo ab cëram na nga wut. Loo dolli yaw ci sa cër bii ndax nga am cëri-cër.
Ag dëggoom
[Soppi | soppi gongikuwaay bi]- Bu ñu dee naw sunu réew mi ci Demokarasi (démocratie)ak wax sa xalaat ci feex (liberté), kii di S Adbu Lahat ku ci jeego ay jeego yu réy la, ku ci bay aw waar la. Bu kenn fatte ba muy wax Sengoor kàcc nga, te wéeruwul woon booba ci ku dul Yàlla, te fasoon yeene du wax lu dul dëgg, te booba njiitul Afrig lu kenn ñemee wax lu jege loolu amul. Loola bokk ci li nooyal njiit yi ci Senegal, sos ag màndaxoo (équilibre) ci sunu reew mi, tax it njiit lu fi nekkati yëg ne kenn a ngi fi kok du may kenn muy ame nguur gu joyu (pouvoir absolu) ci reew mi. Bari na lool ay taxawaay yu amal njariñ réew mi ci wàllug demokaraasi (démocratie), kafte (liberté) ak àq ak yelleefu doomu aadama. Ku mel ne moom aki jëfam ñoo suuxat Senegaal gii nu am tay, bu ko kenn féetale Seŋoor aki gaayam (way politig yi) ak doonte seen loxo gennu ci!