Sàppóoti

Jóge Wikipedia.

Sàppóotigarab la gu bàyyikoo Amerig gu digg, mu mujj yaatu ba agsi Afrig ak Asi.

Sàppóoti bi


Melo wi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Garab la gu am ay meññeef ñu neex. Ci aw déeg la ëppe waaye it di na am ci ag joor.

Màggug sàppooti daa yeex lool. Ay doomam yu jëkk a ngi tàmbalee ci ñeent jàpp juroomeelu atam. At mépp nag lay am i doom. Ci menn at man na cee joxe 150 jàpp 200i kiloy doom.

Taxawaay bi day àgg 15 met ba 30i met. Xob yi dañoo xaw a dëgar. Xas mi du ëpp 80i sàntimet cib rëyaay.

Sàppóoti gi


Njariñam[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Doom yi dees koy lekk, ñam wi daa am ay ferñent, da lay sawarloo, baax na it ci ay butiit ndax day reesal. Ab bantam lawbe yi ak liggeeykatu bant yi dañ koy jëfandikoo, di ci defar ay toogu walla ay lal.

Tur xam-xam wi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Achras sapota

Wàll:garab