Ron
Ron walla sibi ca saalum, xeet la ci xeeti garab yu njool yiy gudd ne sóll ca kaw. Mu bari lool ci tund Afrig, Eccopi, Afrig bëj-saalum. Dees na ko fekk ba tay ci digg Afrig, fu ci mel ni Saara, walla Namibi.
Melo wi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ron garab gog guddaayam danay àgg ba 25 ba 30i met. Yaatuwaayam nag danay àgg ci 1 met. Xobam moom lees di wax xëddeen melo uppukaay la yor te guddaayam di mat 2i met. Ron day am bu góor ak bu jigéen, bu jigéen bi ay xobam dana jàpp ci 260i sàntimet ci yaatuwaay.
Foytéefam
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Moom lees di wax kóoni. Moom ab doom bu nëtëx lay doon am ci biir ay pax yu duy ndox mu neex ñu di ko naan. Bu demee ba ñor nag day soppiku di ab ron. Ñu di ko lakk di ko lekk. Boo ko lakkee bamu ñor nag dangay xolli der wi sànni lekk li ci biir. Li ci biir day mboq mel ni màngo saf suukar lool.
Njariñ yi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Garabug ron bari na ay njariñ lool ay xobam ñu koy wax ndon mooy daggiit yi ñu dagge ci xëddeen weer ko bamu wow, dees ciy taal ñu man cee togg.
Xiis mooy lees dagge ci xëdéen ngir di ci yeewe ak a takke. Xiis bees ko takkee ci garab ag dënnu du ca daanu
Turu xam-xam wi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Borassus flabellifer
Tur wi ci yeneeni làkk
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]farañse: borasse |
angale: Palmyra palm |