Penda Mbow
Penda Mbow
Dundu ak jaar-jaaram | |
Juddu | Awiril 1955 (juroom-benn-fukki at ak juroom)
Dakaar |
Réew | Senegaal |
Liggeey | Way-pólotig, jàngalekatu taarix |
Borom-këram | Saaliw Mbay, 2017 ba tey |
Yeneen xibaar | |
Liggeeye na | Iniwersite Seex Anta Jóob |
Njiitu teesam | Charles-Marie de La Roncière |
Penda Mbow mu ngi juddu atum 1955. Borom xam-xam bu xam-xamam màcc ci taarix la, muy ab bañkat. Nekkoon na fi jëwriñ ji yore caada ak cosaan ay weer atum 2001. Jàngalekatu taarix la ci Iniwersite Seex Anta Jóob bu Dakaar nekk itam njiitu genn mbootaayu njuddu-réew.
Dundu ak jaar-jaaram
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Penda Mbow mu ngi juddu ci weeru mee atum 1955.
Atum 1986 la am ab doktoraa ci tarixu jamono ji farañse tudde moyeenaas (histoire médiévale) ca iniwersite bu Porowãas (Provence) ci ab teesu ñetteelu fànn bi mu bind ci « Nguuru takk-der gu askanu mameluke ci ni ko téereb nattu suuf bu Ibn al-Ji’an ñu dendale ko ak li am Farãas ngir xam li ñu niroole ak li ñu wuute » (L’aristocratie militaire mameluke d’après le cadastre d'Ibn al-Ji'an : éléments de comparaison avec la France.
Ñaar-fukki fan ak ñaar ci weeru mee atum 2011, mu am Piri Sãa Póol II ngir jàmm ji[1], ab raaya bu Watikãa di joxe te kilifag làbbe gii gi Mgr Luis Mariano Montemayor tegoon ci ay yoxoom.
Dundug biiram
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Atum 2017 ba léegi, mu ngi ci buumu sëy, borom-këram a ngi tudd Saaliw Mbay[2].
Mbind (tànneef)
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]- (sous la direction de) Hommes et femmes entre sphères publique et privée, 2005
Téere, jukki wala dali web yi ñu yër
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Seetal tamit
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Lees bind ci moom
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]- (en) Lydia Polgreen, « At Africa's Crumbling Colleges, No Room for Students », The New York Times, 26 mai 2007 (la situation à l'UCAD)
- Fabrice Hervieu-Wane, « Penda Mbow. Femme d'utilité publique », dans Dakar l'insoumise, Éditions Autrement, Paris, 2008, p. 94-99
- Babacar Ndiaye et Waly Ndiaye, Présidents et ministres de la République du Sénégal, B. Ndiaye, Dakar, 2006, p. 284
Jukki yi ñu ko tudd
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]- Taarixu jigeen ci Senegaal : <small>Histoire des femmes au Sénégal</small>
- Limu jëwriñ yu jigeen ci Senegaal : <small>Liste de femmes ministres sénégalaises</small>
Lees jële feneen
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]- Fees ko mën a xameRoyuwaay:Autorité
- Limu téere ak jukki yi Penda Mbow siiwal : Liste des publications de Penda Mbow
- Dundu ak mbindam ci dalu web bu UCAD : Biographie et bibliographie sur le site de l'UCAD
- Waxtaan ak Penda Mbow : Entretien avec Penda Mbow (fukki fan ak ñaar ci weeru màrs atum 2008)