Pàppaaya
Pàppaaya ñu ngi koy fekk lu ci ëpp ci fu bari ndox. Bu dee ca Senegaal bari ca fa ñuy tudde ñaay bi ak ca Kaasamaas.
Melo wi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Guddaayam dana toll ci 3 ba 7u met. Mu bokk ci njabootu dicotylédone bi nga xam ne seen i wànqaas lu ci ëpp day taqaloo. Dundam ci kaw suuf nag, taxu koo yàgg lool diggante ñatt ba juróomi at su bare ba bari waaye ci at mu njëkk mi dina tambalee am meññeef. Te booy dagg wànqaas yi, diir bu gàtt mu tàmbalee amaat yaneen i wànqaas. Ag ndombaam nag da mat 20i sàntimet . Yaram wi yenn saa yi mu yor melo wu nëtëx yenn saa yi mu yor wu baam. Xob wu rëy lay yor wow manees na cee uppu.
Njariñi paj yi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Boo amee liir buy sank muy seere dangay jël ñam wi ci biir nga nal ko di ko ko jox kudd gu ndaw dana dindi seere bi. Bu dee mag mu jël genn wàllu kaas. Ñi am jafe-jafey reesal buñuy jël doom bi ba la ñuy tëdd dinañu reesal ni mu ware. Ku am dagg-dagg bu bees bu jëlee xott pàppaaya wu xaay wi teg ko ci dana tax dagg-dagg bi gaaw a wér.
Paj
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ku am bopp buy metti bu jëlee xobu wi tiimale ko ci taal bamu xaw a tàng mu takk ko ci bopp bi bàyyi ko bamu sedd ci dana ko saafara. Naka noonu day faj pëyiis ak epaatit ak sëqët.
Nataal yi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]-
Tóor-tóor yi
-
Meññat mi
-
Doom yi
-
Xob yi
-
Ëkk gi
Turu xam-xam wi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Carica papaya