Nus

Jóge Wikipedia.

Nus walla mbuumu giléem garab la gog mi ngi bokk ci njabootug capparceae Moom nag garab la gu bari lool fii ñu nekk muy Senegaal , ak fu mel ni Moritani , ak Gàmbi daal di dem ba réewum Somali ba wàcc ba ci suuf ci réew mi ñuy wax Afrig gu bëj-saalum.

Ndax moom ci gox yoo xam ne dañoo xaw a wow lay sax , leeg-leeg mu gàtt , leeg-leeg mu njool.

Nus gi


Melo wi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Garabu nus taxawayam dinay dem ba àgg ci 10 fukki met ci kaw , moom nag xob yi ; xob yu dëgër lay doon te dafay nëtëx, baxa saa su ne. Ay reenam fu dëgër la ñuy sàmpu fu mel ni ab xorndom, maanaam fu xorondom dëkk, am xasam it dafa dëgër te ritax.

Njariñ yi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Moom nag lu bari ay njariñ la . Bokk na ci ay njariñam : di na faj opp ji ñuy wax siburu, ak yaram wu tàng , dinay faj jaani biir maanaam ay saan, baax na ci tànk bu newwi ak i góom , baax na ci góor gu niiw kàttan , baax na lool ci jigéen ju taxaw maanaam ku doom jafe, baax na ci soccet , ak i tànk yuy metti rawatina bu dee sedd maanaam "rimaatism" baax na ci biir buy daw rawatina bu àndee ak dereet , ak yaram wu tàyyeel , dina faj it tawat ji ñuy wax sifis .

Nataal yi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Nus bi


Turu xam-xam wi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Boscia angustifolia