Aller au contenu

Njuux li

Jóge Wikipedia.

Njuux li (kilimã), mooy digg-dóomub meloy jàww ji ci diir bu yàgg, li ëpp bu ñu koy natt 30i at ba 30i at lay doon. Muy bawoo ci soppaxndikug xam-xamu fuglug jàww ji gi nga xam ne dees na natt ci am at: tolluwaayu tàngoor bi ak guusug ngel li ak fattug jàww ji ak ngelaw li ak sóobug taw yi. Cig yaatal daal, njuux li mooy mbir mi bawoo ci ni nosteg njuux li mel tey matale mbàmbulaan yi yuur mi ci kaw suuf si. Njuux nag melow barab dina def jeexiital ci moom ci ag tundeem walla xureem añs, naka noonu laliinu ndox mi ak i duusam.

Kon bu ñu nee njuuxul gox sangam mooy rekk tolluwaay ba mbaa melo wa nosteg njuux la yor ca jamono ja.