Ngun-ngun

Jóge Wikipedia.

Ngun-ngun xeetu gancax la gu bokk ci njabootu "asteraceae". Garabu rëndaay la, dees ciy safal.

Melo wi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Gàncax la guy tollu ci 20 ba 90i sàntimet ci guddaay. Xobam daa tàppndar, danay àgg 2 ba 3i sàntimet. Xobam ci diggante nëtëx bu dër ak woyof, yenn saa yi nag mu ngolleñ ci yenn xeet yi.

Njariñ li[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Am rënd mu am solo la ci wàllu togg ci yenn réew yi. Ca Senegaal dees na ko def ci ataaya. Gàncax la gees di fajoo it.

Turu xam-xam wi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Blumea aurita