Ngigis
Ngigis xeetu garab la guy ne ci sahel bi ci réew yu mel ni Senegaal, Gànnaar...
Melow ngigis
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ngigis, as ngarab la gog ay xobam xob yu xaw a dëgër lay doon te xaw a yaatu te am njariñ lool, melow garab gi nag man naa àgg 3i met ba 15i met ci njoolaay. Garab la gu bari fu ñu ko man a fekk nu man koo bay cib àll. Garab gi man na joxe ay ñam mbaa ay garab yuñ man di fajoo.
Njariñal ngigis
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Foytéefam day jariñ ci wàllu togg.
Ci wàllum paj nag, garabu ngigis xob yi ak bant yi ak reen yi yépp a am njariñ. Bu nu tàmbalee ci xob yi, dees koy yëy, ndox moo mu muy genne lanuy muucu mooy faj biir buy metti walla sëqët walla ku jaan màtt. Bu nu fabee xob yi lakk ko bamu def dóom, danay faj góomu ku jaan màttoon dana koy wowal ngir mu gaaw a wér it.
Reen yi man nanu koo jëfandikoo ci jigeen joo xam ne mbaaxam day yàgg, dana faj itam linuy wax "emorasi" muy yaram wuy nàcce ci biir dana musal it ci ëmb buy yàqu, dana faj it sëqët su yàgg, dana faj it soj walla coonay yaram.
Bu nu ñëwee ci xas mi. Xas mi bu nu ko toggee man naa faj soj man naa faj dënn buy metti ci biir, man naa faj màttiitu jaan. Xas mi nag ak xob yi nga boole ko togg moo gën a gaaw ci bëñ buy metti danga koy suuroo ak di ko galaxndikoo.