Neb-neb

Jóge Wikipedia.
Sauter à la navigation Sauter à la recherche
Neb-neb gi (Vachellia nilotica)
Neb-neb gi (Vachellia nilotica)

Neb-neb garab la gu am i dég yu ñaw, guddaayam man naa dem ba 5i ba 20i met, ay xobam day sew.

Njariñ yi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Tóortóori neb-neb
Tóortóori neb-neb
Meññeefi neb-neb
Meññeefi neb-neb

Garab gu bari ay ferñeet la, day faj gémmiñ guy xeeñ baxalal xob yi di ko galaxndikoo da koy faj, day dindi kadam itam. Xas mi day faj biir buy metti, walla muy daw, ba ci ilseer sax da koy faj. xasum neb-neb day faj ilseer, reen bi soo ko boolee ak reenu Xarañ walla reenu Tëmb day faj jigeen ju jaasir. Doom bi daa bariy ferñeet lool.

Turu xam-xam wi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Vachellia nilotica (Acacia nilotica)

Tur wi ci yeneeni làkk[Soppisoppi gongikuwaay bi]

farañse: gommier rouge
angale: gum arabic tree