Aller au contenu

Ndimbal:Nooy sose aw Xët

Jóge Wikipedia.

Xët wii da lay won sosinu xët wu bees, moo xam jukki bu bees nga fay dugal walla leneen.

Seet balaa benn sosteef

[Soppi | soppi gongikuwaay bi]

Balaa ngay sos aw xët wu bees nanga bàyyi xel ci ñett yii :

Bu njëkk bi, ndax li nga ciy dugal du jalgati yoon ?
Bul dugal ci Wikipedia ay mbind walla ay nataal te amóo sañ-sañ bi. Bis bu nekk dinanu fi fare ay mbind walla ay nataal, ndaxte dañu leen a jële ci yeneen dal te amuñu ca woon benn ndigal. Li gën mooy ngeen dugal ay liggéey yu ngeen defal seen bopp walla ñu doon ay liggéey yu jóge ci ay sémb yu seen ëmbiit ubbeeku. Ndax ñiy bind seen i téere ñaare duñu nangu kuy def seen i liggéey ci dal yu mel nii, li ñuy wax àqi aji-sos ji(droit d'auteur) doon na lu mat a bàyyi xel.
Ñaareel bi, ndax li ngay dugal solowu na ?
Ndaxte Wikipidia bëggul ñu ciy dugal ay mbir yu kenn xamul lan lañu. Kon li nga ciy dugal war na doon lu yitteel ay nit.
ñetteel bi, ndax xët wi amul ba noppi ci weneen tur ?

Bari na ñuy sàkk ay xët yu yees yu amoon ba noppi ak tur yu wuute ak yi fi nekkoon te seen ëmbiit benn la, li ko waral mooy ki sàkk xët wu mujj wi seetul bu baax ndax li mu bëgg a dugal am na fi ba noppi walla déet.

Nan lañuy ame xët wu amul dara ak kojam ?

[Soppi | soppi gongikuwaay bi]
  • Am na ay yoon ngir sàkk xët wu yees:
    • ci biir jukki yu am yi ba noppi cuqal ci lëkkalekaay yu xonq yi.
    • Su fekkee dangaa bëgg a wax ci lu bees, lu fi nekkul woon, lu njëkk li nga war a def mooy dem ci boyotu seetukaay bi "Seet" (mooy nekk ci càmmooñu xët yi), man ngaa gis jukki yi mu méngool walla ci biir ay jukki yoo ko man a dugal (soo bëggee bind ab jukki ci Kajoor, dugal ko ci biir nguuri Senegaal mooy gën). Kon nga tijji xët wi nga yaakaar ne ci biiram war nga faa man a def ab lëkkalekaay buy tudd Kajoor, boo xam ne soo ci cuqee mu yóbbu la ci xëtu Kajoor wi. Nii nga koy binde [[Kajoor]]. Day xonq, su ko defee nga tijji ko def ci li nga ci namm.
    • "Ayca" moom da lay laaj ndax bëgg ngaa sos xët wi ak baat bi nga bind mu nekk kojam, su fekkee amul benn jukki bu tudd noonu. Jar naa teey ak wii sosiin ndax doy na ab wuute bu tuut ci baat yi mu sosloo la jukki bu bees.

</poem>