Xët wii da lay won lëkkalekaay yi ëpp njariñ ngir nga mana cëru te jang jëfandikoo Wikipedia.
Dañ leen séddatle ciy xaaj yuy wax ci doxinu dal bi, ay baaxu Wikipedia ak ay àtteem yu ñuy wormaal, ci soppi xët yi, yokkug ëmbiitam ak melokaanu xaralay jimbulang.
Ni mu wutee ak yeneen jimbulang yi, Wikipedia day def nga mana jóge ci aw xët dem ci weneen ci anam wu yomb lool. Loolu laaj na, saa yooy soppi walla sàkk ab jukki, def ci ay lëkkalekaayi biir.
Ngir yenn jukki yi, man naa doon lu solowu yenn saa yi nga def ay lëkkalekaay yu biti yu lay yóbb ci yeneeni dal, yuy yokk ay xibaar ci li nga jota jukki.
Dafa am ay waa-wikipedia yu bari ci yeneen làkk. Nii la nuy dugale ay lëkkalekaayi diggantelàkk ci biir jukki yi, ngir jàngkat yi man koo am ci yeneen làkk.
fii ngay xamale yeneen waa wikipedia yi làkk yi nga dégg.
Njuumteg royuwaay: Des balises <ref> existent pour un groupe nommé « Sai.net@a.sai.com », mais aucune balise <references group="Sai.net@a.sai.com"/> correspondante n’a été trouvée