Aller au contenu

Ndimbal:Dalal-jàmm

Jóge Wikipedia.

Dalal-jàmm, yaa ngi ci wikipedia gi ñu jagleel kàllaama Wolof, mu di jimbulaŋ bu ubbeeku goo xam ne ñi koy jàng bokk nañu ci ñi koy bind. Ku nekk man nga cee dugal sa loxo, bind ay jukki yu yees walla gën a baaxal li fi jot a nekk; ndaxte ngir sémb wi man a dox ci ni mu gëne, dafa laaj ay loxo yu bari. Ku mu man di doon, man nga cee jàpp ci kaw njekk ak teraanga, topp àtte yi ñu fi tëral, noo ngi lay dalal.

Li mu doon lu ubbeeku ngir ñépp te amul ag pay, ñi binduwul tamit ci biir, moo tax Wikipedia manul a joxe ay wóoral ci mbaaxaay ak cellteg ëmbiitam Donte askanu wikipedia mi ngi tijjiy gëtam ngir di ko jéem a aar ci anam yu dëgër. Saa su ne, man naa am ay xët yu ñuy saay-saaye walla yu ñu soppi ci anam yu dul yi gën ci kaw tayeef, def ciy xibaar yu baaxul walla yu dëppóowul ak sa dundiinu waa-gox.

Nooy Yëre wikipedia

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Man ngaa tàmbalee ci xët wu njëkk wi te topp ci lëkkalekaay yi lay yóbb ci li la solool, li la soob ci njàng. Su fekkee itam daa am jukki booy seet, man ngaa bind benn walla ay baat yu bari ci boyotu bind bi nekk ci sa cammoñ daal di "cuq" ci Ayca

  • su fekkee baat bi nga bind dafa nekk kojug jukki ba noppi, dangay "cuq" ci Ayca rekk mu feeñ.
  • su fekkee nak baat bi dafa nekk ci biiri xët yu am ba noppi, dangay "cuq" ci Seet.
  • (jàppal ne xëtu seetukaay bi dafay tijjil boppam su fekkee dangaa "cuq" ci Ayca te amul lu mu la indil, gisul dara).

Dangaa bëgg a jéem a bind?

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

DBalaa dara, ma xamal la ne lu yomb la, doy na nga jéem a roy ci li fi nekk. Su fekkee dangaa bëgg a jéem a bind te ragal a yàq li fi jot a nekk, jéemal ci xëtu jéemantu wi. Ci wii xët man ngaa jéemantu ci li la solool. Su fekkee nag dangaa bëgg a jéem a soppi xët yu am ba noppi (wu mel ne wii), jëlal te taqale ëmbiitam ci xëtu jéemantu yi te nga soppi ko ci sa coobare.

Su fekkee yaakaar nga ni sag bokk ci Wikipedia day doon luy wéy, di bind ay jukki walla di bokk ci waxtaan yi, mbindu mi doon na lu solowu.

Njariñu doon jëfandikukat bu bindu:

  • dinga am lim bu mat sëkk ci say cëru
  • dinga am sa xëtu bopp, fooy waxee yaay kan ñu duppe ko xëtu jëfandikukat
  • dinga am xëtu waxtaanukaay
  • man a yeb ay nataal
  • man a toppale ay xët, soppi seeni tur itam
  • man a soppi xët yi ñu aar, ngir bañ ku kenn xamul def ci naka su dul noonu
  • man a xaatim say kàddu ci xëtu waxtaanuwaay yi
  • ak yeneen ak yeneen

Lëkkalekaay yu biir

[Soppisoppi gongikuwaay bi]