Ndimbal:Dalal-jàmm

Jóge Wikipedia.
Dem: Joowiin, Seet

Dalal-jàmm, yaa ngi ci wikipedia gi ñu jagleel kàllaama Wolof, mu di jimbulang bu ubbeeku boo xam ne ñi koy jàng bokk nañu ci ñi koy bind.
Ku nekk man nga cee dugal sa loxo, bind ay jukki yu bees walla gën a baaxal li fi jot a nekk; ndaxte ngir sémb wi man a dox ci ni mu gëne, dafa laaj ay loxo yu bari. Ku mu man di doon, man nga cee jàpp ci kaw njekk ak teraanga, topp àtte yi ñu fi tëral, noo ngi lay dalal.

Li mu doon lu ubbeeku ngir ñépp te amulug pay, ñi binduwul tamit ci biir, moo tax Wikipedia manul a joxe ay wóoral ci mbaaxaay ak cellteg ëmbiitam Donte askanu wikipedia mi ngi tijjiy gëtam ngir di ko jéem a aar ci anam yu dëgar. Saa su ne, man naa am ay xët yu ñuy saay-saaye walla yu ñu soppi ci anam yudul yi gën ci kaw tayeef, def ciy xibaar yu baaxul walla yu dëppóowul ak sa dundiinu waa-gox.

Nooy Yëre wikipedia[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Man ngaa tàmbalee ci xët wu njëkk wi te topp ci lëkkalekaay yi lay yóbb ci li la solool, li la soob ci njàng.
Su fekkee itam daa am jukki booy seet, man ngaa bind benn walla ay baat yu bari ci boyotu bind bi nekk ci sa cammoñ daal di "cuq" ci Ayca

  • su fekkee baat bi nga bind dafa nekk kojug jukki ba noppi, dangay "cuq" ci Ayca rekk mu feeñ.
  • su fekkee nak baat bi dafa nekk ci biiri xët yu am ba noppi, dangay "cuq" ci Seet.
  • (jàppal ne xëtu seetukaay bi dafay tijjil boppam su fekkee dangaa "cuq" ci Ayca te amul lu mu la indil, gisul dara).

Dangaa bëgg a jéem a bind?[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Balaa dara, ma xamal la ne lu yomb la, doy na nga jéem a roy ci li fi nekk. Su fekkee dangaa bëgg a jéem a bind te ragal a yàq li fi jot a nekk, jéemal ci xëtu jéemantu wi. Ci wii xët man ngaa jéemantu ci li la solool. Su fekkee nag dangaa bëgg a jéem a soppi xët yu am ba noppi (wu mel ne wii), jëlal te taqale ëmbiitam ci xëtu jéemantu yi te nga soppi ko ci sa coobare.

Binduwoo?[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Su fekkee yaakaar nga ni sag bokk ci Wikipedia day doon luy wéy, di bind ay jukki walla di bokk ci waxtaan yi, mbindu mi doon na lu solowu.

Njariñu doon jëfandikukat bu bindu:

  • dinga am lim bu mat sëkk ci say cëru
  • dinga am sa xëtu bopp, fooy waxee yaay kan ñu duppe ko xëtu jëfandikukat
  • dinga am xëtu waxtaanukaay
  • man a yeb ay nataal
  • man a toppale ay xët, soppi seeni tur itam
  • man a soppi xët yi ñu aar, ngir bañ ku kenn xamul def ci naka su dul noonu
  • man a xaatim say kàddu ci xëtu waxtaanuwaay yi
  • ak yeneen ak yeneen

Lëkkalekaay yu biir[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Translatewiki.net update[Soppisoppi gongikuwaay bi]

  • Currently 72.39% of the MediaWiki messages and 3.72% of the messages of the extensions used by the Wikimedia Foundation projects have been localised. Please help us help your language by localising and proof reading at translatewiki.net. This is the recent localisation activity for your language. Thanks, GerardM (xëtu waxtaanuwaay) 14 Disembar 2009 à 14:32 (UTC)
  • Currently 72.19% of the MediaWiki messages and 3.55% of the messages of the extensions used by the Wikimedia Foundation projects have been localised. Please help us help your language by localising and proof reading at translatewiki.net. This is the recent localisation activity for your language. Thanks, GerardM (xëtu waxtaanuwaay) 25 Samwie 2010 à 14:38 (UTC)

Language support group for Wolof[Soppisoppi gongikuwaay bi]

The Wikimedia Foundation has brought together a new team of developers who are dedicated to language support. This team is to support all the languages and consequently it is not realistic to expect that the team members can provide proper support for your language. It is for this reason that we are looking for volunteers who will make up a language support team.

This language support team will be asked to provide us with information about their language. Such information may need to be provided either to us or on a website that we will indicate to you. Another activity will be to test software that will likely have an effect on the running of the MediaWiki software. We are looking for people who clearly identify their ability. Formal knowledge is definitely appreciated.

As much of the activity will be concentrated on translatewiki.net, it will be a plus when team members know how to localise at translatewiki.net.
Thanks, Gmeijssen (xëtu waxtaanuwaay) 15 Fewriyee 2012 à 09:55 (UTC)