Muurum Koor

Jóge Wikipedia.

Muurum Koor di ci wu-araab “زكاة الفطر/Zakaatul Fitr” farata la ci bépp jullit bu di boroom xel, mag walla ndaw, góor walla jigéen, ab jaam walla gor, ngir waxtaan (Hadiis) wi nu Abdulaah mom (Ibn) Omar (gërëmul Yàlla ci ñoom) dikke ne: «Yonentub Yàlla (jàmm i Yàlla ci moom) farataal na ci nun muurum koor ci wéeru koor, saa ci tàndarma walla bele, muy ab jaam walla gor, jigéen walla góor, mag walla ndaw ci jullit ñi» (Buxaari 2/579, Muslim, Tirmiidhi, Abuu Daawuud, Nasaaï ak Ibn Maaja) Ku ko weddi ab yéefar la, ku ko bàyyi te tay ko te tëlewu ko ab saay-saay la, bu ko tuubul ba dee ag payam sawara la. Ku ko deful it du ko wàcc ba mukk ci dëppook boroom xam-xam yi, doonte bu julli gi weesoo yoolum sarax ngay am.

Kañ lay war ?[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Balaa noo julli korite lees koy génne, Mom Omar (gërëmul Yàlla ci ñoom) neena: «Digalees nanu nu genne muurum koor balaa nit ñee génn di julli ji» (Buxaari 2/579, Muslim) Abdullaah Mom Abaas (g.Y.c.ñ) neena: «Yonent bi farataal na muurum koor ngir mu laabal aji-woor ji ci caxaan yi ak safaan yi akit ngir leel way-ñàkk yi, Ku ko genné njëkk julli gi muurum kooram mees nangu la, Ku ko génne ginnaaw julli gi nag, sarax la ci sarax yi » (Abuu Daawuud, Ibn Maaja ak Daaraqutnii) Naafih nettali na ni: «Ibn Omar génne na ko benn walla ñaar i bis njëkk Korite» (Buxaari) Ci ngirum Maalig mi waa réew mi di sukkandikoo ak Ahmed, neena ñu «manees naa joxe muurum koor benn walla ñaari fan njëkk korite» bu dee ci Abuu Hanifa neena: manees nakoo génne njëkk wéeru koor sax, Saafih ni manees nakoo génne ci bu weeru koor tàmbalee. Waxtuw joxe ko dëg nag moongi doore ci bu weer wi feeñee la ko dale ca timis ga ba xëy.

(karmat: Wax i maalig ji ak Ahmed (genne ko ci ñaari fan jëm kori) ñoo sax ci sunna, moo gën a lënk, waaye yeneen ax yi ci góor-góorlu la (ijtihaad) tege ngir ag jàppandal ñeel jullit ñi, kon ku loru man nakoo jëfandikoo ci lu dul par-parloo, manaam ci bu fekkee ni fi nga nekk amoo kooko fi man a jox te réew sàngam walla dëkk sàngam la war a dem, nanu seet ñaata bis lay def àgg famu jëm ci ñaari fan ba ci jullig kori, te bañ a weesu loolu ngir moo gën a dëppoo ak sunna.)

Ku ko génnewul ba julli gi wees nag ?[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Boroom xam-xam yépp dëppoo nañu ci ne du tax mu wàcc ko mukk, doonte sarax lay doon bu julli gi xësee weesu niko Yonent bi waxee: «Ku ko génne ginnaaw julli gi, sarax la ci sarax yi »

Ana ku muy war ?[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Xanaa ab jullit bu di boroom xel, di as gor (bu dee ab jaam it boroomam moo koy genneel) di mag walla ndaw, góor walla jigéen, ab jaam walla gor, Abdulaah mom (Ibn) Omar (gërëmul Yàlla ci ñoom) neena: «Yonentub Yàlla (jàmm i Yàlla ci moom) farataal na ci nun muurum koor ci wéeru koor, saa ci tàndarma walla bele, muy ab jaam walla gor, jigéen walla góor, mag walla ndaw ci jullit ñi» (Buxaari 2/579, Muslim, ) Mu diko war ci boppam (gor si te di ab jullit) ak koo xamni moo ko war a dundal niki: soxnaam ak doomam ju góor ba bamuy mat góor (mukallaf/majeur) ak doomam ju jigéen ba bamuy mat a am boroom kër ak ci ay way-juram (bu ñu ko amul) ak ci ay jaamam. Ku ko amul woon bees la joxee lu la man a dundal ci bis bi ba suba, la ca des war na nga génne ko ci, bu desul it man nga koo génne ci lees la jox boo noppee jox ko sag njaboot, wér na ci sunna.

Ana ci lumu koy war a génnee?[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Xanaa ca la ëpp ca réew ma mu dëkk di dunde, nun waa réew mii daanu ko génne njëkk ci Ceeb, Dugubi Suuna, Saaño, Basi, Tin, Feela ku ko amul jënd ko joxe ko, kuy dunde yu dul yii yitam man na koo génne ca lamuy dunde rek.

Ana namuy war a toll?[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Xanaa benn (1) saa bopp bu nekk. Bu dee ci réew mi dugub lees ko daa gën a génnee ci bopp bu ne ñaari kilo ak genn-wàll ci Dugubi-Suuna ak yini deme bu dee Ceeb nag walla muy yu dul yii kon day wut nattukaay goo xamni ñaari kilo ak genn-wàll a koy fees ci Suuna mu natt ko ca te bañ koo peese ngir xam ñaata kilo la.

Ana luy benn Saa?[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Saa mooy tolloo ak ñeenti mudd, benn mudd bu nekk mooy tolloo ak sa tibbub ñaari loxo bees ko boolee, yenn ci yees di dunde bees ko natte ci benn Saa:

  • Ceeb: 2300g
  • Bele: 2040g
  • Cere: 1800g
  • Tàndarma: 1800g
  • Fariñ: 1400g
  • Resiñ: 1640g


Ana ku ñu ko war a jox ?[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ku ñu war a jox Asaka rek ñoo yam ci lépp, moo di as gor su di ab jullit te am ca aajo ju wér te muy koo xamni seenuwu loo ci moom lenn njariñ lu dul jox ko ko ngir Yàlla rek, Séenuwu loo mu di la sant ak a gërëm walla mu di ko nettali fi aw nit, nga xamni bëgguloo sax ku ko yég, bëggu ñu nag ku la dogal ab tool nga di ko jox asaka ngir tool ba loolu araam na ci ñoom ñaar ñépp, boroom tool bi nag bu ko moomee sañ nala koo jaay walla mu luye la ko waaye lumu ci doon doo ko ko jox ci asaka ji walla luñuy lekk walla lu suuf di saxal, bëgguñu yitam jox nit asaka mu di ko jaay nga di ko jënd, bëgguñu yitam tuxal asaka lu gën a sori juroom ñaar fukki kilomet te fi nga nekk ku ko yayoo sori wu fa, bu ko weesuwul nag dara newu ci, boo gisul ku ko yayoo lu dul lu ko weesu yitam dara newu ci., sañees na koo dajale jox ko kenn, sañees na koo tasaare ci mbooloo mu ko yayoo. ku ñu war a jox asaka. Ku ko amul woon ba mu wàcc la bees la joxee lu la man a dundal ci bis bi ba suba, la ca des war na nga génne ko ci, bu desul it man nga koo génne ci lees la jox boo noppee jox ko sag njaboot.

Abuu Haniifa ak ñénn ci boroom xam-xam yi nangu nañu genne ko jox ko waa-téere ba (Ahl-ul-Kitaab) manaam ñi nekk ci diiney Yahuud ak nasaraan. (Sayyid Sâbiq mooko indi ci Fiq As-Suna)

Ndax manees nakoo génne ci xaalis ?[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ci ngirum Maalig maneesu koo génne ci lu dul aw cam, Maalig neena: «Muurum koor wareesu koo génne ci lu dul ñam, Deesu ko génne ci kee (xaalis wala lu ko xeetoo)» loolu it mooy gis-gisu Shaafih ak Ahmed ibn Hanbal.

Ci ngirum Abuu Haniifa manees naa génne muurum koor ci xayma ko ci xaalis (Imaam Nawawii mooko indi ci saraab Sahiihu Muslim). boroom xam-xam yu bari ci jamono jii it nangu nañu ko.

Karmat: joxe ko ci ñam manaam li ngay dunde moom rekk a sax ci sunna, te Hadiis bi koy digle it daa waxni ngir jox way-ñàkk yi ñu lekk la, te moom la daan def it, leel léen miskiin yi nag wuute na ak joxe léen ci séen alal yi, leel miskiin muy jox ko lekk sarax lees ci jublu, joxe léen ci séen alal yi azaka lees ci jublu, wuutee ngi foofu bu jar a bàyyi xel, ginnaaw léel miskiin la wax, nanu léen leel ci li nuy lekk rekk, Joxe ko ci ñam nag moo war.

Mu des nag bu loru amee, kon ngànt day taxaw ndax lor fu mu fekk ab àtte àndaleko, bu boobaa manees koo jëfe ci niko Abuu Haniifa gisee ci lu dul par-parloo te sellal yéene ji.

Luy njariñam ci lu nëbbu ak lu feeñ ?[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Abdullaah Mom Abaas (g.Y.c.ñ) neena: «Yonent bi farataal na muurum koor ngir mu laabal aji-woor ji ci caxaan yi ak safaan yi akit ngir leel way-ñàkk yi...» Abdullaah Mom Abaas (g.Y.c.ñ) neena: «Yonent bi farataal na muurum koor ci naan: Fexe léen ñu woomal tay! (Daraqutni) manaam ngir way-ñàkk yi woomal ci bisub korite gi. ci niko Al-Bayhaqi Soloo: «Fexe léen ba bu ñu yalwaan i ci bisub kori gi» Kon dina laabal aji woor ji ci mboolem rëcc-rëcc i koor gi ak it indi indi jàmmu ci nit ñi ci dimbalante, woomalal ñu ñàkk ñi ngir ñu yëg bër gi ni ñépp, fexe ba kenn du yalwaan ci bis bi.

Amma nag Hadiis biy waxni fii ak génnewuloo ko deesul nangu sa koor, ci wax i boroom xam-xam i Hadiis yi wérul, manaam jàppee wu ñu ko waxi Yonent bi (jàmm i Yàlla ci moo).