Moom sa boppu

Jóge Wikipedia.

ANA LAN MOOY MOOM SA BOPPU? Li as cëslaay buma bëgga seddoo ak aji jàng ji fi ci Jàngu bi saytu Kalaama Wolof (Akaademi Wolof). Ci sama biir waxtaan ak sama amdi-jam yi ma neka ndool, ken si gnoom dafa fa sulli yoon waxtaan bu ajju ci moomsa-bopp (liberte). Loolu mooma jox yëg-yëgu bind wax ji. Bi ëmbitu xalaat (concept): “moomsa-boppu” dafa lëntt, rax ci dolli neexuta tënkk ci anam yu léer, yu mucci ci wérenté. Waaye, manees na jappu ne, moom sa bopp mooy « meum-meum ak sagn-sagnu tànn wala bagna tànn ». wante nit ki du mana aag ci lii fileeg amul momeel bu matalè ci yaramam ak xellam. So gnu beggee léeral wax ji, nanu addu ne, moom sa boppu dafa lallu ci gniati kènu : tolloo (egalite), garange (securite), ak meunal sa boppu (independance). Ci biir seetlu, xell du mana nangu am moomeel ci sa bopp bu amul sakett, manam yamukaay. Ndax domu adam du mala. Liko waral mooy dagnuko mognaleeg xell, ta iittam dafay dundu ci biir askan, ay moromu nittam weur ko. Kon sagn-sagnam ak meum-meumam fok mu tëslaayo, weeru ci ay terälin yuy taxawal ak di gindi doxalinu askan wi. Kon wax jooju Descartes di gissee moomsaboppu « kantan nuk jef ak bagna jef » dafa tenkku ci doxalinu ak teralinu askan wi emb doomu adam ci beppu jamano, beppu bërëp, ak beppu aal. Sugnu suka dinkko ci cëslaay wi, dana gnu mana jàppu ne, ta di ci andak borom xam-xam bugn naan Emmanuel Kant, moom sa bopp man firndeel ni nit ki amna sagn-sagn ak meum-meum ci tan luko neex mu def ko, wax ko, wala mu bayi ko, ci kaw muy samu teralinu askan wamu nekk ak li xellu domu adam mana nangu. Been fànn buy dëgëral moom sa bopp mooy askan yi tamit sammu ngor ak yeleefu nit ki. Ndax ak lu nit jeema tënku si doxalinu askanam, bu feekine, gna ŋankk nguurug askan wa deloo wugnu buum sa boy-boy ba, kon moom sa boppu doo tul mana yémbbu. Aw askan su bäggee sammu momeel gi nit gni moom seen boppu, fok mu yamale leen (Egalite), ak tamit samu seen ngor, aar seen alall ci biir ak ci biti (Securite). Ta ku toogn, yoon dal ci aji toognakoon ba, jox ndampaay kignu toogn (Justice). Dènccu kaayu alallu baytimaal dafa yell mu nek ci anam yu mucci ayib ta sell (Trésor public). Faj aji feebar yii, aji tayàtt yi, jàng gum ndaw gni, ak ndimbal ci neew ji doole, alall jooju lees war di jafandikoo ngir faj ajooy ak soxla askan wi. Kon moom sa boppu du ma am su fekkeeni, ax ak yeleefu gniko mbootayo samugn ko. Jamanoy tay nak, baatub “moom sa boppu” ay mbootaay ak ay nit yu beru dagn koy faral di jibbal ci pencci yi ngir di laaj loo xamne doxalinu ak teralinu reew ma andu ci. Dafa war gnu xajjale, moom sa boppu ak asaaro (libertinage). Reew moo gis dafa am aada ak cosaan yuy birndeel gis-gisu nit yako don nu. Jégaani ay doxalin man waral wuute ak jamaar loo ci nu gnu wara firee moom sa boppu. Gnun waa senegaal, sugnuy aada dafa dugalanteek dine lislaam. Jàngu tubaab bi tamit amna ci wall ci sugnu doxalin. Wayee xeltu bima si am mooy, leppu lu ligni eppu ci askan wi gis ne dëppoo wulag adaa ak dine ak feggu (morale), warta tax gnu nasaxal sakett wi ëmbb sugnuy baax (valeurs). Moom sa boppu yamul rek ci nit ki, wayee dafa wara yaatu ba lambaale reew mi yeppu. Reew mu moom boppam nak dafa laaj ay mbir yu takku. Bokku na ci li si eppu solo, bagna weeru ci keneen, wala beneen reew. karaangee, coobare, ak kantanug dundal sa gnos bokku na ci liy dëgëral momeel gi am reew wara moom boppam. Waye bu fekeene, sa dundu, sa karaange, say jumtuwaay, sa xarele, ak mboleem xam-xam yu aju si nekine ak doxalinu dëkk bi dagn lakoy sâh, bu boo ba, ca moom sa boppu des na lu bari. Reew mu melni taxawayam du dëgër. Ndax kersam dagn kako yoral. Buko noonam bëgee buntu xatal dafay yombu. Ndax bugn ko dundalul mu fandè. Ngir sunu reew moom boppam, foku njiit yi farlu, am fayda, ngir mana gnaax nit gni gnu jôk liggeeyi, bayyi, jàngi, sammi. Ku si nek ak wett wa nga feete, nga wane ci sa yiite ju matt, ci kaw njup ak jubale. Werente ak dagasante munta gnak, wantè dafa war neew. Nit gni da ngo wara dëppoo, ànd ligeey. Su lii amee, andaari kom-kom yi dana gnu fees, nantagee sawaan bawaan, jammu law. Talàll gafaka di yalwaan dina dakk, buumi njaam dina feccee ku, jantub yokkute fenk ci beppu diiwan. Su booba, gaindeeg senegaal dina daagu ci manding ngu am-am, andak jòm, fit, ak jambaar.