Aller au contenu

Merkuur

Jóge Wikipedia.
Merkuur

☿ Merkuur mooy jawwu ji gën a jege jant bi te gën a diisadi (woyof) ci jawwu yi nu xam ci nosteg jant bi. Diggam ak jant bi mingi toll ci diggante0,31 ak 0,47 ce benntey saytubiddiw (46 ak 70 miliyo ciy kilomeetar), ëppe sunu jawwu jii di suuf lu ëpp fukki yoon ak ñaar, te gën a kawee lu bari yeneen jawwu yi ci nosteg jant bi. Wareesoon na koo man a gise ak bëtu kese fi sunu jawwu ji waaye wet gi mu féete jant bi (yées 28,3 degre) tax na muy nuur ci biir leeraayu caneeri jant bi.