Aller au contenu

Measles vaccine

Jóge Wikipedia.

Royuwaay:Infobox drug Ñaqu rougeole (ŋas) mooy li lay musal ci rougeole.[1] Sudee bi nga njëkkee ñaqu sa yaram defarul lu koy aar ci feebar bi, soo ñaquwaate rek feebar bi dootul mën dara ci yaw.[2] Sudee dañu ñaq lu weesu 92% ci waa dëkk bi, mën nañu jàpp ni dëkk boobu feebar bi dufa feeñ; waaye mën na fa ñëwaat sudee limu ñiy ñaqu dafa dem ba wàññiku.[3] Soo ñaqoo dinga mucc ci feebar bi ay at yu bari.[4] Xama guñu bu baax ndax ndax kaaraangeg ñaq bi dafay wàññiku.[5] Ñaq bi mën nala aar itam soo ko jëlee ci biir ñaari fan yi nga nekk ci barab bula feebar bi mëna dalee.[6]

Ñaq bi du indil nit ki benn jafe-jafe, doonte danga am VIH.[7] Mën nala xawa sonal tuuti waaye du yàg dara.[8] Maanaam fi ñu la ko jam mën na saf tuuti wala sa yaram xawa tàng. Amul benn yokkute buy seetlu ci limu Seetlu nañu itam 3,5 jàpp 10 kaa anaphylaxie ci miliyoŋi nit ñuñu ñaq.[9] Sudee lu jëm ci feebar Guillain-Barré, autisme ak biir buy metti (maladie intestinale inflammatoire) gisu ñu ci benn yokkute.[10]

Ñaq bi amna mooy kese, waaye itam dina ñu koy boole ak yeneen ñaq yu ci melni ñaqu ROR, (muy boole ñaqu rubeole ak anti-ourlien)[11] wala ñaqu RROV (maanaam ñu boole ñaqu RRO ak ñaq biy aare ci varicelle).[12] Ñaq bii aare ci rougeole dafay musalaate ci feebar itam ndeem dañu ko boole ak yeneen ñaq, te effets secondaires yi dañuy wuute, lépp di aju ci xeetu ñaq bi ñu ko booleel.[13] Waa OMS ñoo digal ñu ñaq xale bi su amee juróom ñeenti weer te nekk ci barab bu feebar bi bari. Waaye sudee fu feebar bi bariwul la, jaaduna ñu ñaq xale bi su amee fukki weer ak ñaar.[14] Ñaq bi luy doomu jàngoroy rougeole bu dundu la waaye dañu ñéewal dooleem.[15] Ñaq bi puudar bu waw la, fàww ñu jaxase ko laata ñu koy jam nit ki ci suufu deram wala ci siditam.[16] Soo bëggee xam ndax ñaq bi jàppna danga saytu deretam.[17]

Ci atum 2013, ñaq nañu lu tollu ci 85% xale yi ci àdduna bi.[18] Ci atum 2015 amna gën gaa néew 160 réew yu baamtu ñaq bi ngir nit ñi mën a am matuwaay yu leen musal ci feebar bi.[19] Ci atum 1963 la ñu njëkka génne ñaq bi.[20] Ci limu garab yu am solo yi waa OMS def, mooy ñaq bi gëna am solo bu yaramu nit ki soxla.[21] Njëgi ñaq bi ci réew yu néew doole yi mingi tollu ci 0,70 USD dose bu nekk, en gros, li tàmbale 2014.[22] Ginaaw feebar bi dafa faral ci barab yi nit ñu bari ñaquwul, feebar dina tax ñu xam barab yi ñaq bi barul ñu ko def.[23]

  1. "Measles vaccines: WHO position paper – April 2017" (PDF). Weekly Epidemiological Record. 92 (17): 205–27. April 2017. hdl:10665/255149. PMID 28459148.
  2. Mitchell D (2013). The essential guide to children's vaccines. New York: St. Martin's Press. p. 127. ISBN 9781466827509. Archived from the original on 9 September 2017.
  3. "Information Sheet Observed Rate of Vaccine Reactions" (PDF). World Health Organization (WHO). Retrieved 1 December 2018.
  4. "Measles Fact sheet N°286". World Health Organization (WHO). November 2014. Archived from the original on 3 February 2015. Retrieved 4 February 2015.
  5. "Immunization coverage". World Health Organization (WHO). Archived from the original on 13 July 2017. Retrieved 12 July 2017.
  6. Centers for Disease Control and Prevention (2014). CDC health information for international travel 2014 the yellow book. p. 250. ISBN 9780199948505. Archived from the original on 9 September 2017.
  7. "World Health Organization model list of essential medicines: 21st list 2019". World Health Organization. 2019. hdl:10665/325771.
  8. "Vaccine, Measles". International Drug Price Indicator Guide. Retrieved 6 December 2015.
  9. Abramson B (2018). Vaccine, vaccination, and immunization law. Bloomberg Law. pp. 10–30. ISBN 9781682675830.
  10. Babbott FL, Gordon JE (September 1954). "Modern measles". The American Journal of the Medical Sciences. 228 (3): 334–61. doi:10.1097/00000441-195409000-00013. PMID 13197385.
  11. Centers for Disease Control and Prevention (CDC) (1994). "Summary of notifiable diseases, United States, 1993". MMWR. Morbidity and Mortality Weekly Report. 42 (53): i–xvii, 1–73. PMID 9247368.
  12. Centers for Disease Control and Prevention (CDC) (July 2007). "Summary of notifiable diseases, United States, 2007". MMWR. Morbidity and Mortality Weekly Report. 56 (53): 1–94.
  13. Wallace G, Leroy Z (2015). "Measles". In Hamborsky J, Kroger A, Wolfe S (eds.). Epidemiology and Prevention of Vaccine-Preventable Diseases (13th ed.). Washington D.C.: Public Health Foundation.
  14. "Measles Cases and Outbreaks". Archived from the original on 13 February 2015. Retrieved 30 November 2018.
  15. Bloch AB, Orenstein WA, Stetler HC, Wassilak SG, Amler RW, Bart KJ, Kirby CD, Hinman AR (October 1985). "Health impact of measles vaccination in the United States". Pediatrics. 76 (4): 524–32. PMID 3931045.
  16. Bloch AB, Orenstein WA, Stetler HC, Wassilak SG, Amler RW, Bart KJ, Kirby CD, Hinman AR (October 1985). "Health impact of measles vaccination in the United States". Pediatrics. 76 (4): 524–32. PMID 3931045.
  17. Centers for Disease Control and Prevention (CDC) (March 2006). "Progress in reducing global measles deaths, 1999-2004". MMWR. Morbidity and Mortality Weekly Report. 55 (9): 247–9. PMID 16528234. Archived from the original on 16 October 2007.
  18. Douglas M (4 August 2010). "Dr. Thomas C. Peebles, Who Identified Measles Virus, Dies at 89". The New York Times.
  19. Collins H (30 August 1999). "The Man Who Saved Your Life - Maurice R. Hilleman - Developer of Vaccines for Mumps and Pandemic Flu: Maurice Hilleman's Vaccines Prevent Millions of Deaths Every Year". The Philadelphia Inquirer.
  20. Parker AA, Staggs W, Dayan GH, Ortega-Sánchez IR, Rota PA, Lowe L, Boardman P, Teclaw R, Graves C, LeBaron CW (August 2006). "Implications of a 2005 measles outbreak in Indiana for sustained elimination of measles in the United States". The New England Journal of Medicine. 355 (5): 447–55. doi:10.1056/NEJMoa060775. PMID 16885548.
  21. Centers for Disease Control and Prevention (CDC) (December 2006). "Measles--United States, 2005". MMWR. Morbidity and Mortality Weekly Report. 55 (50): 1348–51. PMID 17183226. Archived from the original on 13 March 2015.
  22. Sankoh O, Welaga P, Debpuur C, Zandoh C, Gyaase S, Poma MA, Mutua MK, Hanifi SM, Martins C, Nebie E, Kagoné M, Emina JB, Aaby P (June 2014). "The non-specific effects of vaccines and other childhood interventions: the contribution of INDEPTH Health and Demographic Surveillance Systems". International Journal of Epidemiology. 43 (3): 645–53. doi:10.1093/ije/dyu101. PMC 4052142. PMID 24920644.
  23. Measles and the Vaccine (Shot) to Prevent It". Centers for Disease Control. Archived from the original on 20 January 2015. Retrieved 24 January 2015.