Aller au contenu

Mbànte

Jóge Wikipedia.
Mbànte gi (Senna occidentalis)
Mbànte gi (Senna occidentalis)

Mbànte garab la guy sax at ba at, gu sew te am car yu sew di am ay xob yu xet ga nàqari lool, mu man a yegg ba ci ñaari met ci guddaay waaye lu ci ëpp nag lu ndaw lay doon doom yi it doon doom yu sew te gudd. Garab gi ñi ngi koy watte ci àll bi ngir fajum cosaan. Doom yi leeg-leeg man nanu koo jëfandikoo ngir mu wuutu kafe. Garab gi nag, faju lees ciy gën a def.

Barab yi muy sax

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Garab gi ci li ëpp mi ngi sax ci suufu sën walla fu ko jege walla ci lu xaw a kawe tuuti walla ci bërëb bu suuf sa xaw a nangu walla ci bërëb boo xam ne dex da faa jege mbaa ab àll.

Njariñ li

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Garab gi manees na ciy lekk mbaa di ko jëfandikoo cim paj. Ci lekk gi: doomi garab gi bees ko jëlee weer ko ba mu wow nu wal ko ba mu nekk sunguf manees na koo jëfandikoo ngir mu wuutu kafe. Boo jëlee xob yu xaw a mag yi tay ko man koo jëfandikoo ci rëndaay noonee it doomi garab yu ndaw yi moom it manees na koo jëfandikoo ci rëndaay, xob yi soo ko jëlee takk ko ci sa bopp dana faj bopp buy metti, jigeen ju wësin itam bu wutee xob yi baxal ko di ko dàmpoo baax na.

Turu xam-xam wi

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Senna occidentalis

Tur wi ci yeneeni làkk

[Soppisoppi gongikuwaay bi]
angale: coffee senna