Mask yii ci mbasum 2019-2020 bi

Jóge Wikipedia.

Tektalu gornmang bi.[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Coluk mask yi ci mbas mii di coronavirus am ci atum 2019-2020 jot na am digle yu bëri yu ci juddo jogge ci kurël yi tënk wallu wërgu yaram ak itam gornmang bi . Mbir mi di coluk mask yi juur na ay coow yu juur au reero ci digante ñi ngank wallu wërgu yaram nit yi ak itam gornmang bi lu jëm ci wallu coluk mask yi.

Liy yoon[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Yeen yoon ci yi borom xam xam ya ca siin ci wallum wergu yaram wax ne noonu lañu wara sole mask mooy:[1]

  1. Ki la waal te amul been mandarga buy wane ni amna feebar bi .Bari na ñu mën am feebar bi te du am been mandarga buy feeñ seen yaram wala bu amee itam du leen sonal.
  2. Nakk mën ci lu jëm ci wallum ñak dendale  nit yi ci bereb yu siiw yi.
  3. Su fekkoon ni ñi feebar sol nañu mask, doon nañu baña joxe feebar bi. Ki doomu jangaro ji nekk ci yaramam mën na baña degg dara lu baax,ludul  ñukay wax lu ñaaw tek ci diko beddi.

Ab waay bu xam xamam macc ci wallum wirus yi nekk ca université bu Leeds te mu tudd Stephen Griffin neena" bu nit ñi di sol mask mën na tax ba du ñu laal seeni kanam te loolu men na juur feebar bi su fekkantane loxo yi setul".[2]

Fasong mask yi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Masku tisu yi mooy fasong mask yi nga xamne ñu ngi ko defaree tisu ngir mu muur gemmiñ gi ak bakkan bi, cotong lañu kay faral di defaree, lu wuuteek mask yi ñiy oppeere di sol ak nooyikaay yi, tek ci itam nekkul lu yoon nangu. Am na ay jangat yu ñu  ci amal pur xam ndax mask yu baax la pur aar nit yi ci wallante feebar bi ak xeet u feebar yi bon yi nekk ci jawu ji. Mask yi ñiy oppeere di sol mooy mask yi nga xamante ni bu  ñu ko jeffandiko ba noppi danñu koy sanni tek ci dafa woyof  ñu ngi ko defaree noo xamante ni dafay aar bakken ak gemmiñu ki ko takk ci bepp doom u jangoro bu nekk ci bereb bi mu nekk.Mask yi ñiy oppeere di sol dai ñu ko defar ngir mu mena tëye bepp tokk tokk bu baayee ko ci gemmiñ wala bakken u nit lu ci mel ni tëflid wala ñandaxit yi nga xamanate ni men na am ay wirus wala bepp xeet u doom u jangoro sufekkante ni takk nañu ko ni ñu ko santane, wante fexe itam ba doom u jangoro yooyu baña laal gemmiñ ak bakken u ki takk mask bi. Mask yi ñiy oppeere di sol dina tax itam ba ki feebar bi ay tëflitam duñu dal ci keneen ba men ko jox doom u jangoro bi.[3] Mask yi ñiy oppeere di sol defaruñu ko pur mu segg wala tëye doom u jangoro yu ndaw yi nekk ci jawu ji te men wallate ci sëkkat, wala ñandu wala yenn ci doxalin u waa kër doktor.Mask yi ñiy oppeere di sol neekul ni dañuy aar nit yi bamu mat ci bepp xeet u doom u jangoro ndaxte mask bi ci benn pacc ci sunu kanam lay aar te nekkul lu serre ci kanam bi.Mask yi ñiy oppeere di sol tisu lañu ko defaree ci ndimbal u doxalin yu mel ni "fusion-soufflage".[4][5]

Mask bi di N95 fasong mask le boo xamni dafay segg bepp xeetu doom u jangoro bu nekk ci ngelaw li tek ci dafa samonte ak saart yi waa reewu Amérique jël jem ci karange wergu yaram u liggey kat yi. Dina segg lu toll ci juroom  ñint fukk ak juroom ci teemeer boo jël. Missaal la ci xeetu nooyi kaay yi boo xamante ni dafa lay aar ci wallu doom u jangoro yi nekk ci jawu ji wante menula aar ci lu mel ni ay gaas, wala saxaar.[6] Moom ak mask yi ñiy oppeere di sol ñoo yam ndaxte tisu bu "polypropylène" buñu rabbul lañu ko defaree [7][8] Mask bi waa Union Européenne  di jëfandiko mooy fasong mask bu tudd FFP2.[9] [10]

Digleeg kureel gi ëmb wergu yaramu nit ñi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Kureel gi ëmb wergu yaramu nit ñi digle  nañu nit ñi ni buñuy sëqqët wala ñuy tissooli warnañu tek seen ruqqu concc ci seen gemmiñ wala ñu jël morso bu leen gënë jegee.[11] [12] Digal nañu ñi am feebar bi ñuy sol mask yooyu ñi faral di oppeere di sol,[13][14][15] ndax sol mask yi dina wañi bu baax tis tis yi nit mena nooyi te  jogge ci waxtan,sëqqët wala tissooli.[16]

Digleeg kureel gi ëmb wergu yaramu nit ñi ci adduna werngël këpp[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Kureel gi ëmb wergu yaramu nit ñi nekk ci adduna werngël këpp mu ngi gënë bayiloo xel nit ñi ci ñuy sol mask yi ci kaw yile sart yuñu tërël:[17]

  • Bu fekkee ni and nga ak wergu yaram, di nga soxla mask ci bu fekkee ni ya ngi toppato ku ñu yaakaar ni amna feebar COVID-19.
  • Solal mask bu fekkee ni da ngay sëqqët mbaa ngay tishooli.
  • Di sol mask lu am njariñ la ci kaw nga kay faral di foot ak ndox mu set ak saabu bo ci mënee def tuti alkol di na baax.
  • Su fekkee ni da ngay sol mask, kon war nga xam nan lanu kay solee ci nimu waree.

Li reewu Afrik yi tërël ci lu jëm ci wallum tak mask yi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

  • Benin: Liko dalee juroom ñetti bes ci weeru avril, kilifa waa benin yi door nañu ab liggeey ngir forsé ñuy sol mask ngir faagaagal coronavirus bi.[18]
  • Cameroon:njiitu reewu taaxu dëkk bë wax nani di nañu digël ñëpp ñuy sol mask ngir waañi ni coronavirus bi di lawee.[19]
  • Reewu Republique Democratic bu Congo: coluk mask bi leegi lu ñëpp wara def la ca capitaal ba.[20]
  • Ethiopia: Mbootaayu ministar ya nangu nañ dogalup tere nuyoo tek ci ñëppa wara sol mask bu ñu nekkee fuy faral di am nit.[21]
  • Ci reewu  Guinee Conakry: njiitu reew mii di  Alpha Conde jël në dogal ni ñëppa wara takk mask.[22]
  • Ca Kenya solfa mask lu warla. Gornmang bi tek na ay tërëlin ni ñëppa wara samonte ak tërëlin yi di baña tankaloo ci  bërëb yi nit ñi di faral di dajje ndaxte loolu bokk na ci luy tax doole wallate feebar bi neew loolu.[23]
  • Liberia: Ci ñaar fukki fan ak ben ci weeru avril ba jamono jile gornmang bi dogal na ni ñëppa wara tak mask wala ñu muur seen kanam.[24]
  • Ca Marok solfa mask lu war la.[25]

Référence[Soppisoppi gongikuwaay bi]

  1. "Why healthy Chinese wearing face masks outdoors?". NHC.gov.cn. Chinese Center for Disease Control and Prevention. 23 March 2020. Archived from the original on 10 April 2020.
  2. "How to avoid touching your face so much". BBC News. 18 March 2020.
  3. "N95 Respirators and Surgical Masks (Face Masks)". U.S. Food and Drug Administration. 11 March 2020. Retrieved 28 March 2020.  This article incorporates text from this source, which is in the public domain.
  4. "Not Enough Face Masks Are Made In America To Deal With Coronavirus". NPR.org. 5 March 2020. Retrieved 10 April 2020.
  5. "Chinese mask makers use loopholes to speed up regulatory approval". Financial Times. 1 April 2020. Retrieved 10 April 2020
  6. "Respirator Trusted-Source: Selection FAQs". U.S. National Institute for Occupational Safety and Health. 12 March 2020. Retrieved 28 March 2020.
  7. Zie, John (19 March 2020). "World Depends on China for Face Masks But Can Country Deliver?". Voice of America. no-break space character in |authorlink= at position 1 (help)
  8. Feng, Emily (16 March 2020). "COVID-19 Has Caused A Shortage Of Face Masks. But They're Surprisingly Hard To Make". NPR.
  9. "Comparison of FFP2, KN95, and N95 and Other Filtering Facepiece Respirator Classes" (PDF). 3M Technical Data Bulletin. 1 January 2020. Retrieved 28 March 2020.
  10. "Strategies for Optimizing the Supply of N95 Respirators: Crisis/Alternate Strategies". U.S. Centers for Disease Control and Prevention. 17 March 2020. Retrieved 28 March 2020.
  11. "Advice for public". World Health Organization. Retrieved 8 February 2020.
  12. Home. "Novel Coronavirus". HPSC.ie. Health Protection Surveillance Centre of Ireland. Retrieved 27 February 2020.
  13. "Severe Respiratory Disease associated with a Novel Infectious Agent". Government of Hong Kong. Retrieved 1 February 2020.
  14. "Updates on Wuhan Coronavirus (2019-nCoV) Local Situation". MoH.gov.sg. Ministry of Health of Singapore. Retrieved 1 February 2020.
  15. "Advice on the use of masks in the community, during home care and in health care settings in the context of the novel coronavirus (2019-nCoV) outbreak". World Health Organization. Retrieved 21 February 2020.
  16. "2019-nCoV: What the Public Should Do". US Centers for Disease Control and Prevention. 4 February 2020. Retrieved 5 February 2020.
  17. ^ "Coronavirus disease (COVID-19) advice for the public: When and how to use masks". World Health Organization. World Health Organization. 2020. Retrieved 6 April 2020.
  18. Benin Police Enforce Mask Wearing In Bid To Stop Virus,Barron's, 8 April 2020
  19. Cameroon City Makes Wearing Mask Mandatory in Fight Against Coronavirus,VOA News, 7 April 2020.
  20. Tasamba, James (19 April 2020). "Rwanda, DR Congo make mask wearing mandatory".
  21. Samuel, Gelila (12 April 2020). "Ethiopia Outlaws Handshakes, Obliges Masks in Public Places".
  22. Masilela, Brenda (14 April 2020). "Guinean president makes masks compulsory in bid to curb the spread of coronavirus".,IOL
  23. Muraya, Joseph (5 April 2020). "Kenya: Masks Now Mandatory in Public Places, Kenya Declares".,All Africa
  24. Senkpeni, Alpha Daffae (21 April 2020). "Will You Wear Mask? Liberia's Lawmakers Want Compulsory Wearing of 'Protective Device' In Public".,Front Page Africa
  25. Eljechtimi, Ahmed (6 April 2020). "Morocco makes face masks compulsory due to coronavirus". Reuters. Retrieved 11 April 2020.