Déteelu

Jóge Wikipedia.
(Yoonalaat gu jóge Major depressive disorder)

Feebaru naqar gu metti ku dara saful MDD, ñu xame ko itam ni déteelu, mooy benn feebaru xelbu ñuy xame ci ñaari ayubés ci (dikkale bu wacc bu feeñ ci yu bari.[1] Dafay faraldi di ànd ak tuuti ci wóólu sa bopp, ñakka am yëg yëg ci yoon ci ay yëngu yëngu yu wara neex, njaxlafaay gu wacc, ak mettit bu amul lu ko waral.[1] Nit ñi mëna nañu am yenn saay ay gëm gëm yu amul walla gis walla dégg ay mbir yu nit ñi dul gis walla dégg.[1] Ñenn ñi am nañu ay diiru déteelu te ci seen diggante dañuy mel ñépp ay at, te ñeneen ñi ci boobu diir dañuy génne feebar bi.[2] Feebaru naqar gu metti ku dara saful mën na japp nit ki japp bu ñaaw ci dundam, walla ci njàngam, walla ci nelawam, walla ci ni muy lekke, ak ci wér gu yaram.[1][2] Ci diggante 2-8% ci magg ñi ame feebaru naqar gu metti ku dara saful dañuy dee ak xaru, [3][4] te lu tollook 50% ci nit ñiy dee ak xaru amoon nañu déteelu walla beneen feebar feebaru dikkale.[5]

Gëm nañu ne li koy indi mooy ab mbooloowu ndono ci dereet, ci li ñu wër, ak ci wallu xel.[1] Risk yi ñooy ci wallu cosaanu waa kër gi ci li koy joxe, coppite ci dundum nit ki, yenn garab yi, jafe jafe yu metti ci wér gu yaram, ak feebaru dorogewu.[1][2] Lu tollook 40% ci risk yi ñungi joge ci ndono yi ci dereet.[2] Saytu yi ci feebaru naqar gu metti ku dara saful mungi wekku ci jaar jaar yi nit ki di nettali ak benn saytu ci fi xelam tollu.[6] Amul benn saytu ci laboratoire ngir feebaru déteelu yu gêna bari yi.[2] Di ko saytu, waaaye, mën nañu ko def ngir dindi fi yenn jafe jafe yi ci yaram bi yu mëna indi ay yeneen mandarga yu mel noonu.[6] Feebaru déteelu moo gëna metti te mooy gëna yagg naqar, lu bokk ci dund nit ki la .[2] Lii di United States Preventive Services Task Force (USPSTF) laaj na ñu saytu déteelu ci ñi am lu ëpp fukki at ak ñaari, [7][8] ci waxtu woowu ci xibaaru Cochranegis nañu ne di faraldi di laajte du jappale génne walla faj feebar bi.[9]

Ci yoon, nit ñi ñungi leen di faj ak joxe ay tegtal ngir dimbali nit ki saafara jafe-jafeem ak garab yiy xeex déteelu.[1] Garab yi wone na ne am njëriñ, waaye njëriñ li mën na baax ci ñi gëna mettile feebar.[10][11] Leerul ndax garab yi dañuy def antum risk xaru.[12] Yenn xeeti joxe ay tegtal ngir dimbali nit ki saafara jafe-jafeem bokk na ci pajum nekkin bu àndak xalaat(CBT) ak pajum nekkin ak ñeneen ñi bu àndak xalaat.[1][13] Su fekkee yeneen xayma yi amuñu njëriñ, pajum electrochoc (ECT) mën nañu ko jëfandikoo.[1] Tëye nit ki ci opitaal dina baax su fekkee nit ki am na risk gaañ boppam te mën na léég léég ñakka ànd ak li nit ki bëgg.[14]

Feebaru naqar gu metti ku dara saful daloon na lu tollook 216 miliyoŋ ci ay nit (3% ci addina bi yépp) ci atum 2015.[15] Limug nit ñi ame feebar bi ci seen dund mungi tollu ci 7% ci Japon ba 21% ci France.[16] Lim gi ci giir dund mungi gëna kawe ci rééwi ame koom koom gu baax (15%) méngale ko ak rééw yi seen koom koom di jog (11%).[16] Indi na ñaareel bu gëna kawe ci ay at yu ñu dund ak feebaru ñakka mën, ginnaaw ndigg guy metti.[17] Diir gu ñu gëna raññe ni feebar bi génn na mooy ci ati ñaar fukki yi at fanweer yi.[2][16] Jigéén ñi dañuy faraldi gëna nañu ame feebar bi ñaari yoon góór ñi.[2][16] Lii di American Psychiatric Association di mbooloo mi nekk Amerik dajale fajkati feebaru xel yi yoq ci ne "feebaru naqar gu metti ku dara saful" ci Téére Saytu bi ak Xayma bi ngir ñi ame Feebaru Xel (DSM-II) ci atum 1980[18] Ab dog dog la woon feebaru déteelu bu ànd ak dikkale bu waccci DSM-II, te mënin yi bokkoon ci ñu xame ko léégi ni déteelu bu ndaw ak ay feebaru nekkin yu dajaloo ak dikkale yu bon. [18] Ñi amewoon feebar bi ak ñi ko ame léégi mën nañu nekk ay légëtloo.[19]

  1. 1,0 1,1 1,2 1,3 1,4 1,5 1,6 1,7 et 1,8 "Depression". NIMH. May 2016. Archived from the original on 5 August 2016. Retrieved 31 July 2016. 
  2. 2,0 2,1 2,2 2,3 2,4 2,5 2,6 et 2,7 Royuwaay:Citation
  3. Richards CS, O'Hara MW (2014). The Oxford Handbook of Depression and Comorbidity. Oxford University Press. p. 254. ISBN 9780199797042. 
  4. Strakowski, Stephen; Nelson, Erik (2015). Major Depressive Disorder. Oxford University Press. p. PT27. ISBN 9780190264321. 
  5. Bachmann, S (6 July 2018). "Epidemiology of Suicide and the Psychiatric Perspective". International Journal of Environmental Research and Public Health 15 (7): 1425. PMC 6068947 Check |pmc= value (help). PMID 29986446. doi:10.3390/ijerph15071425. Half of all completed suicides are related to depressive and other mood disorders 
  6. 6,0 et 6,1 Patton LL (2015). The ADA Practical Guide to Patients with Medical Conditions (2 ed.). John Wiley & Sons. p. 339. ISBN 9781118929285. 
  7. Siu AL, Bibbins-Domingo K, Grossman DC, Baumann LC, Davidson KW, Ebell M, García FA, Gillman M, Herzstein J, Kemper AR, Krist AH, Kurth AE, Owens DK, Phillips WR, Phipps MG, Pignone MP (January 2016). "Screening for Depression in Adults: US Preventive Services Task Force Recommendation Statement". JAMA 315 (4): 380–7. PMID 26813211. doi:10.1001/jama.2015.18392. 
  8. Siu AL (March 2016). "Screening for Depression in Children and Adolescents: U.S. Preventive Services Task Force Recommendation Statement". Annals of Internal Medicine 164 (5): 360–6. PMID 26858097. doi:10.7326/M15-2957. 
  9. Gilbody S, House AO, Sheldon TA (October 2005). "Screening and case finding instruments for depression". The Cochrane Database of Systematic Reviews (4): CD002792. PMID 16235301. doi:10.1002/14651858.CD002792.pub2. 
  10. Fournier JC, DeRubeis RJ, Hollon SD, Dimidjian S, Amsterdam JD, Shelton RC, Fawcett J (January 2010). "Antidepressant drug effects and depression severity: a patient-level meta-analysis". JAMA 303 (1): 47–53. PMC 3712503. PMID 20051569. doi:10.1001/jama.2009.1943. 
  11. Kirsch I, Deacon BJ, Huedo-Medina TB, Scoboria A, Moore TJ, Johnson BT (February 2008). "Initial severity and antidepressant benefits: a meta-analysis of data submitted to the Food and Drug Administration". PLoS Medicine 5 (2): e45. PMC 2253608. PMID 18303940. doi:10.1371/journal.pmed.0050045. 
  12. Braun C, Bschor T, Franklin J, Baethge C (2016). "Suicides and Suicide Attempts during Long-Term Treatment with Antidepressants: A Meta-Analysis of 29 Placebo-Controlled Studies Including 6,934 Patients with Major Depressive Disorder". Psychotherapy and Psychosomatics 85 (3): 171–9. PMID 27043848. doi:10.1159/000442293. 
  13. Driessen E, Hollon SD (September 2010). "Cognitive behavioral therapy for mood disorders: efficacy, moderators and mediators". The Psychiatric Clinics of North America 33 (3): 537–55. PMC 2933381. PMID 20599132. doi:10.1016/j.psc.2010.04.005. 
  14. American Psychiatric Association (2006). American Psychiatric Association Practice Guidelines for the Treatment of Psychiatric Disorders: Compendium 2006. American Psychiatric Pub. p. 780. ISBN 9780890423851. 
  15. Njuumteg royuwaay: Balise <ref> incorrecte : aucun texte n’a été fourni pour les références nommées GBD2015Pre
  16. 16,0 16,1 16,2 et 16,3 Kessler RC, Bromet EJ (2013). "The epidemiology of depression across cultures". Annual Review of Public Health 34: 119–38. PMC 4100461. PMID 23514317. doi:10.1146/annurev-publhealth-031912-114409. 
  17. Global Burden of Disease Study 2013 Collaborators (August 2015). "Global, regional, and national incidence, prevalence, and years lived with disability for 301 acute and chronic diseases and injuries in 188 countries, 1990–2013: a systematic analysis for the Global Burden of Disease Study 2013". Lancet 386 (9995): 743–800. PMC 4561509. PMID 26063472. doi:10.1016/S0140-6736(15)60692-4. 
  18. 18,0 et 18,1 Hersen M, Rosqvist J (2008). Handbook of Psychological Assessment, Case Conceptualization, and Treatment, Volume 1: Adults. John Wiley & Sons. p. 32. ISBN 9780470173565. 
  19. Strakowski SM, Nelson E (2015). "Introduction". Major Depressive Disorder. Oxford University Press. p. Chapter 1. ISBN 9780190206185.