Aller au contenu

MBaaliya Kamara

Jóge Wikipedia.

MBaaliya Kamara

Dundu ak jaar-jaaram
Juddu 1929
Faatu 8 féewiriyee atum 1955 wala 18 féewiriyee atum 1955
Réew Ginne
Liggeey Bañkat, Way-pólotig

Erreur de script : la fonction « build » n’existe pas. Abla Pokou (wala Aura Poku, wala Abraha Pokou) lingeeru Afrig la , juddoo ci fukk ak juróom-ñetti xarnub. Indi na askanu Baoulé ci réewum Gana ba ci Kodiwaar. Léeb bi dafa nettali, saraxu doomam bu góor ngir jàll ag dex .

Bat bi "Baoulé " li nu tudde leegi askan yi , mu ngi joge ci saraxu doomam.

Bicci toppu saraxe, né na "Ba-ouli", loolu dafay tekki "doom bi dee na". Mbaaliya Kamara mu ngi juddu atum 1929, faatu fukki fan ak juroom-ñett ci weeru féewiriyee atum 1955 ci Tondon. Ab bañkat la woon buy xeex ngir Ginne moom boppam.

Dundu ak jaar-jaaram

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Mu ngi juddu ci Poseya, ci goxu Dubréka. Ci njabootu baykat la bokk. Bi mu jëmee mag tuuti, la dugg ci kureelu pólotig gu tudd Rassemblement démocratique africain (RDA), ci wetu borom-këram, Cerno Kamara mi bokkoon ci ñi demoon ca ñaareelu xare àdduna ba. Way-dencante yi dëkk Tondon, foofee mu doon jiite kureelu jigeen ñi bokk ci RDA. Njiitu kàntoŋ ba, Almaami Dawit Silla tere fa yëngu-yënguy pàrti RDA. Juroom-ñett ak juroom-ñeenti fan ci weeru féewiriyee atum 1955, mu bokk ci ñiy nangu lempo yi. Ab jote am ci diggante dëkkandoo yi ci jamonoy laaj lempo yooyu, Silla daldi ne saraax ci kër kamara-kundaa yi. Mbaaliya ma mu fa fekkoon, nga xam ne dafa wannoon lor sax, moo jàmmaarloo ak moom, Silla dóor ko jaasi, ñu yóbbu ko lopitaal bu Konaakiri. Fukki fan ak benn ci weeru féewiriyee, liir bi juddu te andiwaalewul bakkan. Ñu teg ci benn ayu-bés rekk, Mbaaliya Kamara faatu[1][2].

Xew-xew boobule yokk xadar ji nit ñi àndaloon, gën leen a ñaax ci xeex ba réew ma doon xeex ngir moom boppam. Ay junne junney nit teewe rob ga[3]. Ahmet Seku Ture[4] jàng seede ya. Nit ñi fent ay woy ngir sargale ko Mbaaliya Kamara mi nga xam ne woyam woowu, mu nga fay jolli ba tey, te ba léegi ñu ngi ko fay màggal[5]. Ja bu Konaakiri, moom lañu ko tudde[6].        

Téere, jukki wala dali web yi ñu yër

[Soppisoppi gongikuwaay bi]