Màkkaanum mbëjfeppal

Jóge Wikipedia.

am Màkkaanum mbëjfeppal, di ko wax itam màkkaanum m-bataaxal, walla màkkaanum e-mail, am mbooloom ay araf la, muy teewal ab boyotu bataaxalub mbëjfeppal bu nekk ci ag mbaal (reseau) gu xibaarfeppal gu mel ne internet. Màkkaanum mbëjfeppal mooy tax ñu man a yónnee ab m-bataaxal (bataaxalub mbëjfeppal) kenn nit ci internet.

Ci lu bari dañuy jaawatle màkkaanum mbëjfeppal ak màkkaanum web, mi nga xam ne du lenn lu dul am màkkaan mu dalub web. Te sax am na yeneen xeeti màkkaani internet.

Baat yi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Kon liñu lay yónnee ci sa màkkaanum mbëjfeppal du ab bataaxal, ndax bataaxal dañ koy jàppe niki lu ñu bind ci këyit ak xalima. Bataaxalub mbëjfeppal la, su ñu ko gàttalee mu doon m-bataaxal (di ci jàng: miim-bataaxal)