Aller au contenu

Looy

Jóge Wikipedia.

Looy : dundat yi

  • Looy ak yenn ciy mayam :

Aw loosam :

[Soppi | soppi gongikuwaay bi]

Ni muy xoole ci kanamam noonu lay xoole ci ginnaawam te du soppi ab jubluwaayam, ci niral : jëm ji man naa jublu penku, mu wëlbati bopp bi mu féete soww (fi ko neex lay xool).

Ay noppam, ay gëtam ak diggante 2i gët :

[Soppi | soppi gongikuwaay bi]

Ay noppam a ma koy xibaar fa li mu soxla toll. Bu lu mu war lekk nekkee ci kanamam baa ci ginnaawam te muy luy dund, dafay am um riir mu muy dégg ak lu riir ma suufe-suufe, bu ko déggee dafay daa di déglu ban nopp la riir mi gën a xumbe mu jëme fa xar-kanam gi. Leegi bu dégloo 2i noppam tolloo menn riir mu ñu koy jox ci lay daadi xam ne kon bu jógee warut a jàdd fenn day jubal ci kanamam rekk. Ginnaaw bu ko 2i nopp yi xamalee fa li mu soxla féete nag ci la koy daadi màndaxe baxam digganteem ak la mu war a jëli ci ñaata meetar lay toll... Diggante 2i gëtam yi dafa am lu mel ni ab , lii mooy jox gët yi fa li muy bëgg a jëli toll dëgg-dëgg, moo koy xamal it ndax lu mu war a lekk la walla déet, xamal ko it ndax àttan na ko walla déet (da koy jox puwaa bi) ndax balaa jóg day dem day xam lépp ba noppi ndax bii xibaar yu leer nàññ la koy jox... Ginnaaw bu amee xibaar yi mu soxla yépp ba noppi nag ci la ko bi di xëccële (zum) mbir mi ba mu jege ko lool mu di ko gis, gis bu leer nàññ. Leegi nag ndeem lépp leer na ci moom, day jóg nag ngir jëli ko waaye ndax dana ko fa fekk ? Ndax la muy jëli du ko yëg ba man koo rëcc añs... ? Déedéet ! Ndax bu jubee li mu soxla ay laafam dóotuñu riir (silencieux) dañu naa tekk, tekk jooju muy def nag moo koy tax a jot ci li mu soxla te njëkk muy jóge fi mu taxaw sax xibaar yi muy am fekk ko fa ak jot ca daf ciy bokk añs...


Wikipedia
Wikipedia
Bii jukki ab junj rekk la. Man nga cee duggal sa loxo suqali ko ndeem am nga ci xam-xam ci anam yi Wikipedia taxawal