Lislaam ci sowu Afrik
Yaatug lislaam ci Afrig gu sowwu gi :
Ci njëlbéenug juroom ñaareelu xarnu la Muhammad (j.m) tàmbali di tas diine ju yees ji (lislaam), ginnaaw bi mu làqoo atum 632 g.j, la araab yi ubbi Afrig gu sowwu gi, daal di duggal aw nitam ci lislaam, ci noonu, jullit ñi tàmbalee tas lislaam ndànk-ndànk ci bëj-saalumu tàkk gi (désert bi),.
Lislaam mujj na yaatu, tas te li ko waral du dara lu dul joqalante gu yaxantu gi naar yi daa def ak Afrig, ak njëgg (convoi) yu giléem yi daa jëggi tàkk gi, nga xam ne yaxantukat yi dañu daa jënd wurus ci sowwu Afrig, jaayiji ko ca bëj-saalumu Afrig, daa nañu baana-baana it ci jamaa ak jumtukaayi xanjar yi ak weer aki téere ak xorom ci dëkki yaxantu yii : Jinn, Tumboktu, Gaawo. Yaxantukat yooyu dañoo fekk lislaam ca bëj-gànnaaru Afrig, bu ko defee, la ëpp ca ñoom daal di ciy dugg, daal di tàmbalee waar seeni àndandoo ngir dugal leen ci.
Waaye yaatug lislaam gi amewul ci jàmm rekk, ndax yenn askan yi dooni jullit dañoo jugoon def jiyaar ngir tàbbal yeneen yi ci lislaam.
Murabituun (Marabout) yi nga xam ne ñi ngi juge woon ci bëj-gànnaaru Afrig, ubbi woon nanu lenn ci Afrig gu sowwu gi ci xarnu bu fukk ak benn