Laab
LAAB)
Laab moom lu war la,ci alxuran ak sunna ak dajeg boroom xam-xam yi. Ku ko bàyyi ci lu dul ngànt lu xel nangu,dees koy ray rayug gëtën,gu dul gu yéefër, ndaxte julli du mat mukk lu dul dafa ànd ak lab kon ag waram lu wér la.
BUNT 1
Li aju ci laab
Cours 1 : Njariñul laab ci Islaam
Laab nag 2 xeet la : 1- Laab ci sa jëmm 2- Laab ci li la wër te mooy say yere wala ci barab bi ngay jaamoo Yalla
Li ñu bëgga jànggale fii nag mooy laab ci sa jëmm, te loolu ni ñu ko mana defee mooy 3 yii : 1- Jàpp 2- Sangu farata 3- Tiim
Am na jëf yoo xam ne maneesu lee na def te yoroo njàpp, lu mel ni : - Julli - Laal kaamil u Alxuraan - Tawaaf (wër kaaba gi)
Kon 3 yii kepp ku ko leen bëgga def fàww nga laab ba noppi. Laab googu nag soo ko bëggee def da ngay jàpp bu fekkee da ngaa wara jàpp wala nga sangu farata bu fekkee da ngaa wara sangu farata. Soo amul ndox moo ko defee wala nga am ngant may na ñu la kon nga tiim.