Làkku malgaas
Apparence
Malgaas (làkk) mooy làkk wu bokk ci làkki Ostronees, di làkk wu ñu wax ci Madagaskaar. Làkk wi ñu tudde Malagasy Officiel, mooy làkk wu am solo ci Madagaskaar, ànd ak faranse. Làkku Malgaas mooy làkku Malaay-Polinees bu nekk ci bëj-saalum gi, ñu yóbbu ko ci Madagaskaar ci jamono ji askanu Ostronees yi jóge ci dunde yi ñuy wax Sunda ci atum 500 g.