Aller au contenu

Kunsay/Ngunsay

Jóge Wikipedia.
Kunsay (Ngunsay) gi (Afraegle paniculata)

Kunsay mbaa Ngunsay, as ngarab la walla garab gu xob yu sew te am i dég man a àgg ba ci 15i met ci njoolaay, gu bokk ci njabootug Rutaceae. Buutam lum gàtt-gàtt man naa dem ba ci 200i met ci biir suuf, man na it àgg ba ci 40i sàntimet cig xala.

Garab gi day am ay wànqaas yu bari. Wànqaas yi it am ay dég yu jub xocc teg ci ñaw, man nanu koo bay, man nanu koo fekk it ci àll bi walla ñu koy bay ngir jëfandikoo ay foytéef am cim paj walla bant bi dees na ko soxla ngir di ko toggee.

Ci wàllu dëkkuwaayam, garab gi li ci ëpp noo ngi koy fekk cib àll walla di ko fekk ci suuf suy tooy suy bari ndox walla yu ni mel. Ci dëkk yi ëpp li nu koy fekk bokk na ca Amerig ak dëkk yi nga xam ne day jige xala yi yu ci mel ne Miyaami ak yu ni mel.

Garab gi it màggam gaaw na lool rawati na bu nekkee ci suuf su nangu, màgg gu gaaw nag lay màgg lu muy gën a màggat garab gi di gën a rëy ay wàqaasam di gën a yaatu ak a gudd.

Njariñ li

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Li ëpp ci njariñ yi mooy lu jëm ci lu nut jëfandikoo, nee nañu doom yi man nanu cee defar diw, xob yi it bu ñoree manees na ko lekk waaye li miy am bariwul.

Foytéefam day xaw a tolloo ak suraas ci yaatuwaay. Moom it waxuñu fenn ne manees na ko lekk.

Lu jëm ci wàllu jëmbat garab ak yu ni mel kunsay lañuy jëfandikoo ngir màggal yeneen i xeeti garab yoo xam ne manuñu màgg ci seen i reeni bopp.

Yeneeni njariñ

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Xob yi leeg-leeg bu nu ko dëbbee mbaa nu yëy ko ba mu mokk man nañu koo boole ak ndox di ko sangoo. Bant yi it man nañu koo defaree jëfandikaay yu jëm ci kër lu ci mel ni lal añs.

Turu xam-xam wi

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Afraegle paniculata